Simoore Al-Inshiqaq pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Inshiqaq pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Inshiqaq Tekki. Simoore Al-Inshiqaq (Meccan) 25 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Inshiqaq

ﭣﭤﭥﭦ
84:1
Saa su asamaan si xottikoo! Maa ngi giiñ!
ﭧﭨﭩﭪ
84:2
te mu def – ndigalu boroomam dëggël
ﭫﭬﭭﭮ
84:3
ak saa suñu maasalee suuf si,
ﭯﭰﭱﭲﭳ
84:4
te mu gëx lép lu nekk ci biiram,
ﭴﭵﭶﭷ
84:5
moom it – mu def ngigëlu boroomam dëggël ko
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
84:6
Éy yaw nit ! Yaa ngi def jëm ci sa boroom, te danga dajeek moom de
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
84:7
Képp ku ñu joxe téereem ci loxob ndeyjooram,
ﮇﮈﮉﮊﮋ
84:8
dees na ko màndaxe mu jàppandal,
ﮌﮍﮎﮏﮐ
84:9
muy walbatiku jëm cag njabootam di bég.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
84:10
Képp koo xam ne nag moom da ñu koo jox téereem ci ginnaawam,
ﮘﮙﮚﮛ
84:11
Ngalla moom kon,
ﮜﮝﮞ
84:12
te dana xoyomoo safaraw Sa’iir.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
84:13
Moom ku bégoon la cag njabootam,
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
84:14
foogoon na ne du dekkiwaat mukk.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
84:15
Axakañ boroomam daan na ko gis de.
ﯔﯕﯖﯗ
84:16
Déet !... Maa ngi giiñ ci yeeri ji,
ﯘﯙﯚﯛ
84:17
ak ci guddeek la mu làmboo,
ﯜﯝﯞﯟ
84:18
ak ci weer wi su xàbbee wërngëlu mat !
ﯠﯡﯢﯣﯤ
84:19
Dingeen jaar, ay jaar-jaar yu tegaloo yu bari !
ﯥﯦﯧﯨﯩ
84:20
Ana lu leen dal ba gëmuñu ?
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
84:21
te suñu jàngee ci ñoom Alxuraan duñu sujuud ?
ﯲﯳﯴﯵﯶ
84:22
Yéefër ya, ñoo koy weddi.
ﯷﯸﯹﯺﯻ
84:23
Yàlla xam na la ñuy xalaat.
ﯼﯽﯾﯿ
84:24
Na gneen leen xibaar mbugël mu mitti ma.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
84:25
Ba mu des ña gëm tey jëf yiw : ñoom am na ñu pey gu dootul dog.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







