Simoore Ibrahima
52 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Alif, Laam, Raa. Ab téere la bu Nu wàcce ci yaw ngir nga génne nit ñi cig lëndëm [kéefar], jëme leen cig leer [gëm Yàlla], ci ndigalu seen Boroom jëme leen ci yoonu Boroom kàttan gi, Ki yeyoo gépp cant,
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
[ci yoonu] Yàlla mi nga xam ne Moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te alkaande ñeel na yéefar yi ci mbugal mu tar.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Ña nga xam ne dañoo tànn dundug àdduna [mu gënal leen] gu àllaaxira, te ñuy wëlbati ña jëm ci yoonu Yàlla, di ko sàkkal ay gàkk, ñooña ñanga ca ag réer gu sori dëgg.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Dunu yónni ab Yonent lu dul ci làkku nitam ña [lay waxe] ngir mu leeralal leen [la ñu ko yónni]. Te Yàlla mooy bàyyi cig réer ku ko soob, Dana gindi itam ku ko soob. Ndax Moom moo di boroom kàttan gi tey Aji-xereñ [ciy àtteem].
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Yónni woon Nanu Muusaa, dooleel kook Sunuy kaawtéef, ne ko : “Génneel saw nit cig lëndëm jëme leen cig réer, te nga waar leen ci xéewali Yàlla yi”. Ndax kéemtaan a ngi ci loolu ñeel képp ku di ab muñaakoon, di ab santaakoon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
(Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : “Fàttalikuleen xéewalu Yàlla ga Mu leen defaloon ba Mu leen musaloon ci waa kër Firawna, ñu leen doon teg mbugal mu bon. Di rey seen doon yu góor, di bàyyi jigéen ña. Te loolu nekkoon na ab nattu bu rëy bu jóge ci seen Boroom”,
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Ak ba seen Boroom xamlee ne : “Bu ngeen gërëmee, fàwwu Mu dolli leen. Bu ngeen weddee nag, [na ngeen xam ne ] Sama mbugal lu tar la”.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Te Muusaa ne leen : “Bu ngeen weddi woon, yéen ak ñi nekk ci suuf si yépp [du wàññi Boroom bi dara], ngir Yàlla Aji-doylu la ci boppam [wëliis ay mbindéefam], Aji-yeyoo cant la”.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Ndax agsi na ci yéen nettalib xew-xew ya leen jiitu woon? Niki nitu Nooh ak waa Haad, ak waa Samuuda ak ña ñëw seen ginnaaw, kenn xamuleen ku dul Yàlla. Seeni Yonent dikkaloon nañu leen, ànd ak lay yu leer, te ñu màtt seeni waaraam wiccax, ñu ne : “Nun weddi nanu li nga xam ne yónneef na leen ko, te nun am nanu sikk gu tar ci li ngeen nuy won”.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Seeni Yonent ne leen : “Moo ndax dangeen di am sikk ci Yàlla, Moom mi sos asamaan yi ak suuf si, Ma nga leen di woo ngir Mu baal leen seeni ñaawtéef te Mu muñal leen ba ca àpp bu ñu dogal ? ”. Ñu tontu ne : “Dungeen dara lu dul aw nit ni nun. Dangeen noo bëgg a tàggaleek la sunu maam ya daan jaamu. Indil-leen nu aw lay wu bir”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Seen Yonent ya ne leen : “Nekkunu lu dul aw nit ni yéen. Waaye Yàlla dana xéewale ku ko soob ciy jaamam. Dunuleen mën a indil ay lay lu dul ci ndigalul Yàlla. Te way-gëm ña dañuy wéeru ci Yàlla.”
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
[Ñi gëm] ne : “Lu téye dunu wéeru ci Yàlla, te gindi nanu ba noppi te teg nu ci sunuy yoon ? Te it dananu muñ lor yi ngeen nuy teg. Kuy wéeru daal na wéeru ci Yàlla.”
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Ña weddi wax seen Yonent ne leen : “Dananu leen génne ci sunu suuf walla ngeen dellusi ci sunu diine ! ”. Seen Boroom soloo leen ne : “Fàwwu dana alag tooñkat ña,
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
te ci seen ginnaaw Danaa leen jox suuf si muy seen dëkkuwaay [yéen Yonent yi ak ñi leen topp]. Loolu mooy peyug ku ragal Sama taxawaay [ak moom] te ragal Samay tëkku”.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Ñu sàkku ndimbal [ñoom Yonent ya]. Képp ku doon rëy-rëylu te jeng daldi yàqule.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Te Safaraa nga xaar ca ginnaaw te dees na ko nàndal ndox mu bon te tàng jér
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
dana ko guux. Waaye du ko xaw a mën a wann. Dee di ko dikkale wet gu nekk, te du dee ; te it mbugal mu tar dana ca topp.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Ña weddi seen Boroom, seeni jëf dafa mel cig niróole ni ab dóom bu ngelaw ëf ci bisu mbóoya mu ràddi. Duñu mën a jariñoo dara ca la ñu fàggu woon. Loolu moo di réer gu sori dëgg.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Ndax dañoo gisul ne Yàllaa bind asamaan yi ak suuf si ci dëgg ? Bu ko neexoon Mu jële leen fi, indi fi ay mbindéef yu bees,
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Loolu nekkul lu jafe Yàlla.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Ñoom ñépp ñu teew ca Yàlla. Ña neew doole wax ña daan màgg-màggalu ne leen : “Nun dey, yéen lanu toppoon. Moo ndax mën ngeen noo jiñal dara ci mbugalum Yàlla mi ? ” - Ñu tontu ne : “Su nu Yàlla jubaloon kon nu jubal leen. Léegi nag, nu tiit walla nu muñ, lépp a yem ci nun ; amunu làquwaay [fu nu rawe]”.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Séytaane dana wax, ba lépp sottee, ne : “Yàlla dey digoon na leen dig bu dëggu ; man it ma dig leen te wor leen. Waaye nag amuma woon genn kàttan ci not leen, defuma lu dul woo leen ngeen wuyu ma. Buleen ma yedd ; yeddleen seen bopp. Mënuma leen a xettali te mënuleen maa xettali. Man weddi naa seenug bokkaaleek man ca la jiitu woon”. Tooñkat ya
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Ñu dugal, ña gëm te jëfoon jëf yu sell ya, ci Àjjana joo xam ne ay dex dañuy daw-dawaan ci suufam, dañu fay béel ci seen ndigalul Boroom. Seenub nuyyoo foofa moo di : “Jàmm”
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Ndax gisoo ni sa Boroom di joxee ci waxiinu léebu baat bu sell bu mel ni garab gu sell goo xam ne dàtt ba lu sampu la ba dëgër te wanqaas ya nekk ca kaw asamaan ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Muy joxi meññantam saa su nekk ci ndigalul Boroomam. Yàlla danay gaaral nit ñi ay léebu ndaxtelee ñu fàttaliku [seen Boroom].
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Te itam, léeboo wax : “Baat bu bon dafa mel ni garab gu ñu buddee ci suuf te amul fu mu sax.”
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Yàlla dana dëgëral ña gëm ci wax ju dëggu, ci dundug àddina ak ca àllaaxira. Te Dana bàyyi tooñkat ya ca seen réer ga. Te Yàlla dana def lu ko soob.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ndax gisuloo ñay feye xéewali Yàlla ci di Ko weddi tey wàcce seenu nit ci kërug alkaande
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
danañu séndal ci Safara ? Ndaw saxuwaay bu bon !
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ñay sàkkal Yàlla nawle ngir réeral [seenu nit] soreel leen yoonu [Yàlla] : “Xéewluleen rekk, Safara ngeen di mujj di”.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Waxal sama jaam yi gëm ne leen : "Nañuy taxawal julli tey joxe ca la Ma leen wërsëgale ci lu nëbbu walla la feeñ, balaa àpp bis di ñëw boo xam ne jotoo amu fa waxantumalaa xaritoo.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Yàlla mooy ki bind asamaan yi ak suuf si te Mooy wàcce ndox mu jóge kaw asamaan ngir Mu génne ca meññent yu nekk i xéewal ci yéen. Te Moo leen tàggatal gaal ngir ngeen mën a daw ci géej ci ndigalam. Te tàggatal na leen it dex yi.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Te tàggatal na leen it jant bi ak weer wi ñuy ñaari way-daw [ku ca nekk ci aw rëddëm]. Tàggatal na leen guddi ak bëccëg.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Te Moo di leen may ci lépp lu ngeen ko ñaan. Te sax, bu ngeen doon jéem a waññi ay xéewalam, dungeen ko mën a takk. Ndekete yoo nit moom ab tooñkat la bu mën a fakk jëf.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
[Fàttalikul] ba Ibraahiima waxee ne : “Sama Boroom, [ñaan naa la] nga def dëkk bii di fu am kóolute, te maak samag njaboot nga soril nu ak jaamu xërëm.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Boroom sama, xërëm yooyu dey réeral nañu [sànk] lu bari ci nit ñi. Képp ku ma topp ci man la bokk. Képp ku ma weddi. .. [Yaa xam noo koy def], ndax Yaw Jéggalaakoon nga, Jaglewaakoon nga !
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Yaw sama Boroom, dëkkal naa lenn ci sama njaboot ci xur wu amul mbey, ci sa néeg bu ñu wormaal ba [Kaaba ga], ngir ñuy taxawal julli. Defal seenug cofeel ci xoli nit ñi. Te nga wërsëgal leen ay meññent. Ndax xéy-na ñu gërëm la ?
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Yaw sunu Boroom dey, xam nga li ñuy nëbb ak li ñuy fésal : - te amul menn mbir mu umpu Yàlla ci suuf si, waxantuma laak asamaan ! -
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Xéeti cant yépp moomale naa ko Yàlla, Mi nga xam ne Moo ma may cig mage [sama doom] Ismaahiila ak Isaaqa. Sama Boroom daal kuy dégg ñaan la.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
[Éy] Yaw Boroom bi !, def ma maak samay doom ak i sët, nuy taxawalkati julli ; waay- waay nangul sunu ñaan !
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Yaw Boroom sama ! Jéggal ma maak samay waajur ak ñi gëm ca bis ba Yàlla di natt jëfi mbindéef yi”.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
[Yaw Yonent bi], bul njort ne Yàlla amul paal ci li tooñkat yi di def. Deful lu dul yeexe leen ba Bis-pénc ba bët yi buqeeku [janook seen mbugal].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Ñuy daw, muur seeni bopp [ngir kersa], ne muq di xoole te dara nekkul ca seen xol ya [lu dul njàqare].
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Waaral nit ñi ci bis bu ñu leen di indil mbugal mi, ba tooñkat ya di wax naan : “Sunu Boroom, tee nga noo muñal diir bu gàtt, kon dey nu wuyusi woote, topp itam say Yonent”. - Mu tontu leen ne: “Ndax daawuleen giñ ne àllaaxira amul ?”.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Ngeen dëkk ci dëkki ña tooñoon seen bopp. Te ngeen xamoon xéll na Nu defoon ak ñoom te joxoon Nanu leen ay tegtal.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Dañoo fexe seen pexe te umpul Yàlla. Doonte la sax, seen pexe moomu mën naa dindi tundi doj yi...
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Bul njort ne Yàlla dana soppi la Mu dig ay Yonentam. Yàlla ku am kàttan la, di Kuy feyu [tooñeel],
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
ba bis ba ñuy weccee suuf sii seneen suuf ak asamaan yi itam te nit ñi génne [ca seeni bàmmeel] teew ca Yàlla ja di jenn, te di Notaakoon ba.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
ca bis booba, danga gis saay-saay sa ñu lëkkale leen ca jéng ya,
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
seeni yére keteraan la, ñu muure seeni kanam ak safara.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
[La ko waral] moo di Yàllaa feye bakkan bu nekk la mu fàggu. Te nag Yàlla moom Ku gaaw ka ci natt lu ne.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Ngir ñu waaru te xame ca itam Moom Yàlla jenn Yàlla doŋŋ la, ak itam woroom xel ya fàttalikoo ci.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers