Simoore Al-Waqi'a pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Waqi'a pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Waqi'a Tekki. Simoore Al-Waqi'a (Meccan) 96 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Waqi'a

ﮃﮄﮅﮆ
56:1
Saa su xew-xew ba tàbbee (bis pénc ba),
ﮇﮈﮉﮊ
56:2
kenn dóotul weddeeti ag digëm.
ﮋﮌﮍ
56:3
Mooy daane (ñenn), di yëkëti (ñeneen).
ﮎﮏﮐﮑﮒ
56:4
Bu ñu gësëmee suuf si mu rëg-rëgi,
ﮓﮔﮕﮖ
56:5
te moñoxo tundi doj yi mu ne tasar,
ﮗﮘﮙﮚ
56:6
daldi doon pënd buy tasaaroo
ﮛﮜﮝﮞ
56:7
ngeen dikk di ñatti kurél :
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
56:8
waa ndeyjoor – ana ñan ñooy waa ndeyjoor ?
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
56:9
Ak waa càmmoñ – ana ñan ñooy waa càmmoñ ?
ﮫﮬﮭ
56:10
Ak ña jiitu woon ci ndigal te ñooy jiitu ba fàww
ﮮﮯﮰ
56:11
Ñooñee ñooy ña gëna jigeñ Yàlla
ﮱﯓﯔﯕ
56:12
ca biir Àjjanay xeewu ja,
ﯖﯗﯘﯙ
56:13
lim bu takku ca ña jiitu woon,
ﯚﯛﯜﯝ
56:14
ak lim bu néew ca ña mujjoon,
ﯞﯟﯠﯡ
56:15
ci kaw ay lal yu ñu sadd [wurus ak peme],
ﯢﯣﯤﯥ
56:16
dañu cay soonu jàkkaarloo.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
56:17
Ay xale yu dootu ñu màggat ñooleen di liggéeyal di leen wër,
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
56:18
ci ay kopp, ak baraada ak i kaas: ci aw ñoll
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
56:19
te duñu miir dunu màndi ;
ﭢﭣﭤﭥ
56:20
ak wépp xeetu fuytéef wu nu gëna xemmeem,
ﭦﭧﭨﭩﭪ
56:21
ak yàppu picc la nu ca gëna wunnéen.
ﭫﭬﭭ
56:22
Ak ay jigéen (huur al iin), yu jekk ya lool ay gët,
ﭮﭯﭰﭱ
56:23
yu taaru ba mel ni wurusu peme.
ﭲﭳﭴﭵﭶ
56:24
ñu faye leen ko la ñu daan jëf.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
56:25
Duñu fa dégg mukk ay waxi neen walla wax ju sew ;
ﭾﭿﮀﮁﮂ
56:26
lu dul dañuy wax rekk naan : “Jàmm nga am aa jàmm rekk! ”
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
56:27
Ak waa ndeyjoor ; ana ñan ñoo di waa ndeyjoor ?
ﮉﮊﮋﮌ
56:28
[ñoom ñanga ca]: déem yu amul dég,
ﮍﮎﮏ
56:29
ak ci garabi banaana yu meññet ma rangaloo,
ﮐﮑﮒ
56:30
ak ci biir keppaar yu nu yiif yaatu
ﮓﮔﮕ
56:31
ak ci [wetu] ndox muy sottiku te tëa dakk,
ﮖﮗﮘ
56:32
ak ay fuytéef yu bari sakkan
ﮙﮚﮛﮜﮝ
56:33
du rag mukk te it kenn du ko tere,
ﮞﮟﮠ
56:34
ak ay laltaay yu yékkatiku,
ﮡﮢﮣﮤ
56:35
Man Yàlla maa leen sàkk ñu ñeseŋ ñoom (huur al iin),
ﮥﮦﮧ
56:36
def Nanu leen ñu di ay xiig,
ﮨﮩﮪ
56:37
yu sopp lool seen jëkër, te maase ne rojj,
ﮫﮬﮭ
56:38
waa ndeyjoor leen moom,
ﮮﮯﮰﮱ
56:39
ñuy mbooloo ma nu tànn ca ña jëkkóon,
ﯓﯔﯕﯖ
56:40
ak mbooloo ma nu tànn ci ñu mujj,
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
56:41
Ak waa càmmoñ; ana ñan ñoo di waa càmmoñ ?
ﯝﯞﯟﯠ
56:42
ña nga ca biir cóolóolul ndox may wañax,
ﯡﯢﯣﯤ
56:43
ak ca ron kërug saxaar su ñuul kukk
ﯥﯦﯧﯨﯩ
56:44
seddul, neexul lewetul.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
56:45
Ñoom ba ñuy dund ca àddina da ñu daan fuukarewu.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
56:46
Dañoo nuuran ci bàkkaar ba gëna màgg mu di bokkaale Yàlla
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
56:47
dañu daan wax naan : “ Moo ndax bu nu faatoo ba def suuf ak i yax, dees nanu dekkilaat ?
ﰀﰁﰂ
56:48
nook sunuy baay ak i maam ?...”
ﰃﰄﰅﰆﰇ
56:49
Waxal ne : “Mbooleem ña jëkkoon ak ñu mujj ñi
ﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
56:50
dees na leen dajale ci féncóob bis bu ñu xam”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
56:51
Topp ginnaaw ba, yéen, ñi réeroon, te daan waddi (bis pénc ba),
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
56:52
dangeen di lekk ci garabuk Zaquum.
ﭝﭞﭟﭠ
56:53
Ngeen di ca feesal seeni biir,
ﭡﭢﭣﭤﭥ
56:54
ngeen di fa naan ndox muy wañax teg ko ca,
ﭦﭧﭨﭩ
56:55
ngeen di ca dëtëm ni giléem gu mar.
ﭪﭫﭬﭭﭮ
56:56
Ñam woowule ñu leen di teeroo, bu bis Pénc baa.
ﭯﭰﭱﭲﭳ
56:57
Nun noo leen sàkk bind leen. Ana lan moo tax manuleen a gëm dekkiwaat ?
ﭴﭵﭶﭷ
56:58
Xanaa gisuleen maniyyu mi ngeen sotti :
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
56:59
yéen a koy bind: walla Nun (Yàlla) noo koy sos ?
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
56:60
Nun noo natt ag dee ci yéen dogal ko te kenn du ko man a fanq. Te it lottu nu
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
56:61
te wuutal leen ñeneen rey leen yéen, dekkilaat leen fu ngeen xamul.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
56:62
Xam ngeen xéll ca bu jëkk na ka ngeen sosoo. Moo kon ndax dangeen dul fàttaliku ?
ﮗﮘﮙﮚ
56:63
Xanaa gisuleen li ngeen di ruuj ?
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
56:64
Yéen yéen a koy bay ? walla Nun noo koy bay ?
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
56:65
Sunu neexoon, Nu fóomal ko. Ngeen ne tócc di wél-wéli di [yuxu]:
ﮨﮩﮪ
56:66
Te naan : “Danoo fees dell ak i bor !
ﮫﮬﮭﮮ
56:67
amu nuy alal am nu tono”.
ﮯﮰﮱﯓﯔ
56:68
Xanaa gisuleen ndox mi ngeen di naan ?
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
56:69
Moo ndax yéen a koy wàccee ci niir yi ? walla Nun noo koy wàcce ?
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
56:70
Sunu neexoon, Nu sëccël ko mu wex xàtt ak xorom. Moo xanaa dungeen sant ?
ﯤﯥﯦﯧﯨ
56:71
Xanaa gisuleen Safara wi ngeen di taaloo ?
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
56:72
Moo ndax yéen a sos garab gi walla Nun noo ko sos sàkk ko ?
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
56:73
Def nanu ko mu di ag fàttali (ci safaraw ëllëg), di jumtukaay ci képp ku ko ittewoo.
ﯶﯷﯸﯹﯺ
56:74
Na ngay sàbbaal sa Boroom, bu Màgg bi !
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
56:75
Déet !... maa ngi giiñ ci wàccuwaayi biddiw yi.
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
56:76
Su ngeen xamoon lii, ngiiñ lu màgg la de.
ﭑﭒﭓﭔ
56:77
Lii dey Alxuraan ju teddla,
ﭕﭖﭗﭘ
56:78
ci biir Téere bu ñu ñoŋal
ﭙﭚﭛﭜﭝ
56:79
ñi laab rekk koy laal (ku laabul warukoo laal) ;
ﭞﭟﭠﭡﭢ
56:80
Mi ngi wàcci bawoo ca Yàlla Boroom àddina si.
ﭣﭤﭥﭦﭧ
56:81
Moo ndax ci waxtaan wii ngeen di weddi ?
ﭨﭩﭪﭫﭬ
56:82
Ak li leen Yàlla defal lépp fayewuleen ko lu dul di weddi Alxuraan ?
ﭭﭮﭯﭰﭱ
56:83
Bu ruuh gi génnee ba des ci bóli gi (kuy sukuraat),
ﭲﭳﭴﭵ
56:84
te fekk na yéen a nga koy xool,
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
56:85
fekk na booba Nun Yàlla noo ko gëna jigeñ waaye du ngeen gis.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
56:86
Bu ngeen, jortee ne ameeluleen Yàlla dara,
ﮄﮅﮆﮇﮈ
56:87
ana lan moo tax kon delloosiwuleen [ruuh ga], ndegam ñu dëggu ngeen ?
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
56:88
Su fekkee ne koo ku dafa jige woon (Yàlla),
ﮏﮐﮑﮒﮓ
56:89
dana (am) noflaay, ak àjjanay xéewël.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
56:90
Su fekkee ne nag dafa bokk ci waa ndeyjoor,
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
56:91
dees na ko [teeroo]: “Jàmm ju” bawoo ca waa ndeyjoor.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
56:92
Su fekkee ne nag dafa bokk ca ña daan weddi (dekkiwaat) tey ñu réer sànku,
ﮨﮩﮪﮫ
56:93
des na ko teeroo ndox muy wañax,
ﮬﮭﮮ
56:94
ak xoyomu ca biir Safara.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
56:95
Lii mooy dëgg tigi.
ﯖﯗﯘﯙﯚ
56:96
Na ngay sàbaal sa turu Boroom, bu Màgg bi !
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







