Simoore Al-Hujurat
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Hujurat pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Hujurat pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Hujurat Tekki. Al-Hujurat (Medinan) 18 Aaya.
Related
- Al-Hujurat TekkiWolof
- Al-Hujurat mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Hujurat

ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Eey yéen ñi gëm ! Bu leen di jiitu Yàllaa kub Yonentaam. Te ngeen ragal Yàlla di ko watandiku. Ndax Yàlla ku dégg la kuy xam la.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Eey yéen ñi gëm! Bu leen di yékkati seen kàddu ci kaw kàddug Yonenta bi, bu leen koy jollmbeeru ay wax, kon ni ngeen di jooruwantee bu (ngeen ko defee), yéen nangay sippi seeni jëf te yëguleen ko.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Ñay suufeel seeni kàddu ci Yonenta bi ñooñee la Yàlla nattu seen xol (fekk ko mu jooy jëm ci ragal Yàlla). Dana ñu am njégël ak pey gu màgg.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Ña lay woo (yaw Muhammad) di ko jooru di ko jéllóo ci ginnaaw dëkuwaay yi , li ëpp ci ñoom doonu ñu ñu ami xel di ca xalaat.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Su fekkoon ne dañuy muñ ba baa ngeen génn ci ñoom, mooy gën ci ñoom. Yàlla Jégëlewaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Eey yéen ñi gëm ! Bu leen ab saay-saay indiley xibaar, na ngeen ko leerlu ndax amaana mu tax ngeen dal ci gawu nit ngir am lënt su ko defee ngeen mujj di ko réccu.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Xam leen ne Yonent Yàlla baa ngi ci seen biir. Su fekkoon ne dana leen faral a topp ci mbir yu bari, kon dangeen am coono. Waaye Yàlla moo leen sopploo ngëm taaral ko ci seen xol moo leen bañloo it kéefër, ak ug caay-caay ak ug moy Yàlla. Ñoom ñooñee ñoo di gaay ñu jub ña,
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
mooy ngëneel lu bawoo fa Yàlla di xéewël. Yàlla Ku Xam la ku Xereñ la.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Su ñaari kuréel ci jullit ñi di xeexoo, na ngeen yéwénal seeni diggante. Su fekkee ne benn ba moo jalgati tooñ ba ca des, na ngeen xeex ak bay tooñ, ba baa muy dellu ci ndigalul Yàlla. Bu, delloo ci ndigal nag, na ngeen leen jubale te ngeen maandu Yàlla safoona ñu maandu ña.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Way gëm ña ay mbokk la ñu. Na ngeen di yéwénal seen digganteek seen mbokk, te ngeen ragal Yàlla, ndax amaana yëramees leen.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒ
Eey yéen ñi gëm ! Bu benn nit di faral a reetaan (yéjji) beneen nit : ndax amaana ña ñuy reetaan gën ñay reetaane. Bu ku góor di def bu ku jigéen it di def. Bu leen di saagaante. Bu leen di safaaney tur, turu caay-caay yellut ci ku gëm. (te ña koy def) te tuubuñu ko réccu ko... Ñoom ñoo di tooñkat ya.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Eey yéen ñi gëm! Teetleen (moytu) njortu yu bari ndax yenn njortu yi bàkkaar la. Buleen di yëdóonte ; buleen di jëwante. Moo ndax kenn ci yéen bëgg naa lekk yàppu mbokkam mu dée ? Bëgguleen ko kay. Kon nag nangeen ragal Yàlla di ko watandiku. Yàlla kuy Nanguwaakoonu tuub la, Jaglewaakoon la.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Eey yéen nit ñi ! Noo leen bind ci góor ak jigéen, def Nanu leen ngeen di ay giir ak i xeet, ngir ngeen xamante. Waaye ki gën a tedd ci yéen, fa Yàlla, moo di ki gën a ragal Yàlla ci yéen. Yàlla de Ku xam la Ku xàmmee la.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Araab yi neenañu : “Gëm nanu”. Waxal ne : “Gëmaguleen . Waaye nañu wax ne : jébbale nanu sunu bopp, te sax ngëm ga duggagul seeni xol batey. Waaye su ngeen toppee Yàllaakub Yonentam, seen jëf jooju tus du leen ci moy”. Yàlla Jegëlaakoon la ab Jaglewaakoon la.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Jullit ñi tigi ñooy ña gëm Yàlla akub Yonentam, te duñu ca dengi-dengi benn yoon te ñooy xare ci seen alal ak ci seeni bakkan ci yoonu Yàlla. Ñooñee ñoo di ñu dëggu ña (ca la ñu wax ñoom ne gëm nañu).
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Waxal ne : “Ndax dangeen bëgg jàngal Yàlla seen diine, te Yàlla moom xam na li nekk ci biir asamaan yeek suuf si ? ” Yàlla Xamaakoon la ci lépp lu ne.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Ña nga lay caakaayoo seenug dugg ci Lislaam. Nee leen : “ Bu leen caakaayo ci seenug tàbbi ci (diine Islaam). Yàlla kay moo ame ndam li moom mi leen xéewale gindi leen jëme leen ci ngëm , ndegam ñu dëggu ngeen”.
ﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Yàlla xam na Mbóotum asamaan yeek suuf si, te Yàlla nag Kuy gis la li ngeen di def.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







