Simoore Al-Hijr pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Hijr pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Hijr Tekki. Simoore Al-Hijr (Meccan) 99 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Hijr

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
15:1
Alif, Laam, Raa. Àttey Téere bee ngi nii, di am njàngale muy biral [dëgg].
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
15:2
Amaana ña weddi ñanga ne siiw nekki jullit.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
15:3
Bàyyileen ñuy lekk ak a xéewlu, tey mébét lu leen soxal; danañu mës a xam !
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
15:4
Dunu alag benn dëkk te fekk amul àpp bu ñu xam.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
15:5
Benn xeet du jiitu àppam te it mënu koo weesu.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
15:6
Ñu naan leen : “Yaw mii, wàcceef na ci yéen Téere ba, yaw dof tigi nga !
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
15:7
Lu teewoon nga indil nu ay Malaaka, ndegam bokk nga ca ñu dëggu ña ? ”
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
15:8
Nun dunu wàcce ay Malaaka lu dul ci dëgg (gu Nu doxal mu jeex) ; te kon dungeen doon ñu ñuy muñandiku ab diir.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
15:9
Nun noo wàcce Téere ba [Alxuraan] te Nun noo koy wattu.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
15:10
Yónni Nanu ci lu la jiitu ay Yonent ca kurél yu njëkk ya.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
15:11
Te ab Yonent daawuleen dikkal te yéjj wuñu (ñaawal).
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
15:12
Noonu la Nu koy tàbbalee ci xoli saay-saay sa.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
15:13
Duñu ko gëm te aadaay ñu njëkk ña wéy na.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
15:14
Te su Nu leen ubbiloon ab buntu ci asamaan ñu mën caa yeendoo yéeg,
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
15:15
Kon it fàwwu ñu wax ne : “Dañoo gëlëmal sunuy gët. Walla sax dañu noo njibar”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
15:16
Def nañu ci asamaan ay bidiw te rafetal Nanu ko ñi koy xool mu ne ràññ.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
15:17
Te wattu Nanu ko ba sépp séytaane su ñu rëbb du fa mën a egg.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
15:18
Lu dul ku jéem a sàcc lu mu dégg, [te ku ko ca jéem] ay jumu safara soxal ko.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
15:19
Tàllal Nanu suuf si te samp ci ay tundi doj (yu tax mu dal) ; saxal Nanu itam wépp xeetu gàncax muy lu ñu nattale.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
15:20
Nu defaral leen ca lu ngeen di dunde, yéen ak ñi ngeen dundalul.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
15:21
Amul lenn loo xam ne ndàmbam nekkul ci nun, waaye Dunu ca wàcce lu dul ab natt bu ñu xam (bu yem ak bu doy).
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
15:22
Yónni Nanu ngelaw luy sos (taw ci niir yi) ; wàcce Nanu ndox mu jóge asamaan, nàndal Nanu leen ci te mënuleen ko woon a denc.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
15:23
Te Nun nooy dundal te Nun nooy rey te Nun nooy donn (mujje) àddina bi yépp.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
15:24
Sunu xam-xam làmb na ña jiitu woon ak ñay mujj ci yéen.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
15:25
Sa Boroom dana leen fang ñoom ñépp. Moom Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
15:26
Bind Nanu nit ci ban bu wow bu jóge ci ban bu ñuul.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
15:27
Te fekkon na Nu binde jinne lu jiitu loolu ci safara wu xonk coyy.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
15:28
[Fàttalikul] ba sa Boroom waxee Malaaka ya ne leen : “Man damay bind nit ci ban bu ñu togg,
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
15:29
te saa su Ma ko yemalee ba wal ci dara ci sama ruut, rotleen sujjóotal ko”.
ﯶﯷﯸﯹﯺ
15:30
Malaaka yépp sujjóot,
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
15:31
ba mu des Ibliis, moom bañ naa bokk ca ñay sujjóot.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
15:32
Mu ne [Moom Yàlla] : “Yaw Ibliis, lu la dal ba bokkuloo ci sujjóotkat yi ? ”
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
15:33
Mu tontu ne : “Man kat duma sujjóotal nit koo binde ci ban bu wow bu jóge ci banit bu ñu togg”.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
15:34
Mu tontu ne : “Man kat duma sujjóotal nit koo binde ci ban bu wow bu jóge ci banit bu ñu togg”.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
15:35
Te am rëbb dal na ci sa kaw ba Bis-pénc ba di taxaw ! ”
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
15:36
-Mu ne : "Yaw sama Boroom, kon muñal ma ba bisu dekki ba”.
ﭺﭻﭼﭽﭾ
15:37
Mu ne : bokk nga ca ña ñu muñal,
ﭿﮀﮁﮂﮃ
15:38
ba ca Bis ba nga xam ne waxtoom lu ñu xam la.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
15:39
- Ibliis ne : "Yaw sama Boroom, ci sababus li nga ma beewloo, fàwwu danaa leen rafetalal ci àddina [lu bon], te fàwwu danaa leen beewloo ñoom ñépp,
ﮏﮐﮑﮒﮓ
15:40
ba mu des ña sellal ca sa jaam ña.”
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
15:41
- Boroom bi tontu ne : lii mooy yoon wu jub wi jëm ci Man.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
15:42
Sama jaam ñi nag ñoom mënoo ci ñoom dara lu dul ña beew ña la topp.
ﮦﮧﮨﮩﮪ
15:43
Te Safara mooy fa ñuy daje ñoom ñépp.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
15:44
Te Safara nag am na juróom-ñaari buntu te buntu bu nekk am na xaaj bu ñu ko sédde ca [ñu beew ña].
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
15:45
Ña ragal Yàlla nag, ñangay nekk ciy àjjana ak i bëti-ndox [yuy ball].
ﯛﯜﯝﯞ
15:46
[Ñu ne leen] : “Dugguleen ci jàmm ànd ak kóolute”.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
15:47
Te Nu rocci [raxas] la nekkoon ci seeni xol cig noonoo : ñu nekk ay mbokk yu jaaxaan ca seeni lal jàkkaarloo.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
15:48
Coono duleen fa laal. Te dootuñu fa génnati.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
15:49
Xamalal samay jaam ne, Man Jéggalaakoon laa, Jaglewaakoon laa.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
15:50
Waaye sama mbugal mooy mbugal mu metti mi.
ﰁﰂﰃﰄﰅ
15:51
Te nga nettalileen la xewoon ca gani Ibraahiima ya
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
15:52
Ba ñu agsee ca moom ne ko : “Jàmmu ngaam” - Mu ne leen : “Am naa njàqare ci yéen”.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
15:53
Ñu ne : “Bul jàq ci nun ! Noo ngi lay bégal ne [danga am doom] ju góor juy bari xam- xam”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
15:54
Mu ne : “Li ngeen di bégle ndax ànd naak samag mage ? Li ngeen may yégal mooy lan ? ”
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
15:55
- Ñu ne ko : “Yégal ne lii dëgg la. Bul bokk ca ña naagu ña”.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
15:56
- Mu ne : “Kan mooy naagu ci yërmaande Yàlla, ñu dul ñu réer [sànku] ? ”
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
15:57
Mu ne leen : “Waaw lan mooy seen mbir yéen ñi ñu yónni ?
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
15:58
- Ñu ne : “Yónneef nañu ci aw nit ñu bari bàkkaar,
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
15:59
ba mu des njabootu Lóot, danañu leen musal ñoom ñépp
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
15:60
ku ca dul soxnaam sa. “Dogal Nanu ne moom ca way-des ña lay bokk (alku)”.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
15:61
Ba ña ñu yónni agsee ca waa kër Lóot,
ﮞﮟﮠﮡﮢ
15:62
Lóot ne leen : “Yéen dey aw nit ñu ma xamul ngeen”.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
15:63
- Ñu ne ko : “Axakay, digal nanu la ànd ak la ñu doon sikki-sàkka.
ﮫﮬﮭﮮﮯ
15:64
Te ñëw nanu ci yaw indil la dëgg. Te it ñu dëggu lanu.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
15:65
Te nanga dem rañaan yaak sa njaboot bu guddi xaajee ; te nga topp ca seen ginnaaw te bu kenn ci yéen geestu. Te ngeen jublu fa ñu leen digal”.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
15:66
Noo xamal Lóot sunu ndigal la : te danañu alag nitam ña ci njël.
ﯪﯫﯬﯭﯮ
15:67
Waa dëkk ba agsi ànd ak mbégte.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
15:68
- Lóot ne leen : “Ñii samay gan lañu, buleen ma ci rusloo.
ﯶﯷﯸﯹﯺ
15:69
Nangeen ragal Yàlla te buleen ma teg gàcce.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
15:70
Ñu ne : “Ndax terewuñu la woon ngay woo nit ñi [ci sa diine ji] ? ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
15:71
Mu ne leen : “Samay doom yu jigéen a ngii ndegam bëgg ngeen a def [li ngeen nar] ! ”
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
15:72
Giñ naa ci sag dund [yaw Muhammed] ne naka ñoom nekkoon nañu di dengi-dengi ci seeni ngëlamte.
ﭞﭟﭠﭡ
15:73
Ag xaacu sadd leen suba cuuy.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
15:74
Nu wëlbati la nekkon ca kaw [dëkk ba] dëpp ko mu féete suuf, Nu sotti ca kaw ab tawu xeer yu jóge Sijjiil.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
15:75
Loolu nekk ay kéemaan ci ñuy settantal !
ﭱﭲﭳﭴ
15:76
Te [dëkk boobu] nekk na ci yoon wuñuy faral di jaar.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
15:77
Loolu nekk na di kéemtaan ci ñi gëm !
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
15:78
Te waa Leykata ay tooñkat lañu woon.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
15:79
Nu mbugal leen. Te [ñaari dëkk yooyu] ñanga ca yoon wu neex a xam.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
15:80
Waa Hijri weddi woon nañu Yonent ya.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
15:81
Nu joxoon leen sunuy kawtéef, ñu dëddu leen.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
15:82
Ñu nekkoon ñu daan yatt i néeg ci ay tundi doj.
ﮚﮛﮜﮝ
15:83
Ag xaacu sadd leen ci ag suba cuuy
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
15:84
La ñu doon fàggu jariñu leen dara.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
15:85
Te Nun bind nu asamaan yi ak suuf si ak li nekk ci seen diggante lu dul ci dëgg. Te jeexug Sama àddina sii luy nekk la ! Kon nanga dëddu ña weddi dëddu gu rafet.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
15:86
Sa Boroom mooy Ka bind, di Ku xam.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
15:87
May Nanu la “juroom-ñaar yu Nu ñaar-ñaaral [Al-Faatiha]”, ak Alxuraan ju màgg jii.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
15:88
Bul tàllal say gët [di xool] la Nu xéewale ay kurél ci ñoom, bul am naqar ci ñoom te nangay suufeel say mbagg ñeel ñi gëm.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
15:89
Te neel : “Man aji-laabir laa ju wér” [ci xamal leen dëgg],
ﯻﯼﯽﯾﯿ
15:90
Noonu it Lanu wàccele woon [ab Téere] ca ña xàjjatle woon [seen diine],
ﭑﭒﭓﭔﭕ
15:91
ca ña séddale Téere ba ay xaaj, pàcc-pàccee Alxuraan ngir sànkaate.
ﭖﭗﭘﭙ
15:92
Giñ naa ci sama màggug Boroom ! Fàwwu danañu leen laaj ñoom ñépp
ﭚﭛﭜﭝ
15:93
la ñu nekkon di ko def [ci ay ñaawtéef].
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
15:94
Waxal ci kaw li Nu la digal te nanga dëddu bokkaalekat yi.
ﭥﭦﭧﭨ
15:95
Naka Nun fegal nanu la ña lay téjji.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
15:96
Ña nga xam ne dañuy boole Yàlla ak jeneen yàlla, danañu mës a xam.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
15:97
Xam Nanu ne la ñuy wax tiis na ci sa xol.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
15:98
Sàbbaalal sa Boroom mi yeyoo cant, te nanga bokk ca sujjóotkat ya ;
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
15:99
te nangay jaamu Yàlla ba balaa bir la [dee ga] di agsi ci yaw.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







