PDF —
19 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-A'la pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-A'la pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-A'la Tekki. Simoore Al-A'la (Meccan) 19 Aaya.



19 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮟﮠﮡﮢﮣ
87:1 Sàbbaalal sa turu Boroom, bi Gëna kawe,
ﮤﮥﮦﮧ
87:2 Ki bind jekkal yemale,
ﮨﮩﮪﮫ
87:3 kiy dogal tey gindee,
ﮬﮭﮮﮯ
87:4 kiy génne ñax mi saxal ko,
ﮰﮱﯓﯔ
87:5 di ko naatal dëlël ko.
ﯕﯖﯗﯘ
87:6 Dananu la jàngal (Alxuraan), te doo too ko fàtte
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
87:7 lu dul la soob Yàlla. Moom moo xam li feeñ ak li nëbbu.
ﯤﯥﯦ
87:8 Dananu la jàppandalal yoon wi gëna yomb.
ﯧﯨﯩﯪﯫ
87:9 Na ngay fàttelee, saa su fàtteli amee njariñ.
ﯬﯭﯮﯯ
87:10 képp kuy ragal (Yàlla) na nangoo fàttaliku,
ﭑﭒﭓ
87:11 ñu texeedi ñaa koy moytu,
ﭔﭕﭖﭗﭘ
87:12 ñay lakk ca safara sa gëna rëy,
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
87:13 du fa dund dufa dee.
ﭠﭡﭢﭣﭤ
87:14 Képp kuy sellal texe na,
ﭥﭦﭧﭨﭩ
87:15 te fàttaliku turu boroomam , tey julli.
ﭪﭫﭬﭭﭮ
87:16 Yeen, dangeena bëgg lool dundug àddina,
ﭯﭰﭱﭲ
87:17 te àllaaxira gën te moo gëna sax.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
87:18 Lii nekk na, ca téere yu jëkk ya,
ﭹﭺﭻﭼ
87:19 téerey Ibraahiima ak Muusaa.

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers