Simoore Ad-Dukhan pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Ad-Dukhan pdf Wolof — Wàcce Simoore Ad-Dukhan Tekki. Simoore Ad-Dukhan (Meccan) 59 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Ad-Dukhan

ﭑﭒ
44:1
Haa, Miim.
ﭓﭔﭕ
44:2
Ak ci (Alxuraan) Téere bu leer bi (Maa ngi ciy waat) ne.
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
44:3
Wàcce Nanu ko ci guddi gu barkeel, Nu ca doon xuppaate,
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
44:4
ci la Nuy teqalee mépp mbir mu xereñ,
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
44:5
moo di mbir mu bawoo ci Nun. Ci la Nuy yónnee [Yonnenta ya],
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
44:6
moo di yërmaande ju bawoo ci sa Boroom, mooy Kiy Dégg, di ku Xam,
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
44:7
Moo di Boroom asamaan yeek suuf seek li nekk ci seen diggënte, ndegam wóolu ngeen.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
44:8
Amul jenn Yàlla judul Moom. Mooy dundal di reye, Mooy seen Boroom mooy Boroom seeni maam ya fi jëkkoon.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
44:9
Ñoom, ña ngay sikki-sàkka, di fo.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
44:10
Fuglul, cëy bis ba asamaan si di dikk ak saxar suy jolli
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
44:11
di moor nit ñi. Tey mbugël mu mitti.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
44:12
“Waay-waay, sunu Boroom téggil nu mbugël mi. Ndax nun ay jullit la nu [léegi]”.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
44:13
Ana fan la leen kii fàttaliku bawoo te ab Yonnent bu bir dikkoloon leen,
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
44:14
Ñu daldi dumóoyu te naan : “Kii daal, ab dof la”.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
44:15
Dananu teggi mbugël mi tuuti ; dangeen dellusi de.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
44:16
Cëy bu keroogee bis ba nuy kaanu di nappaje danuy fayu de.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
44:17
Sànje woon Nanu , nitu Firawna ña leen jiitu woon, te amoon na ñu ab Yonnent bu leen dikkaloon bu tedd,
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
44:18
[daan leen wax naan]: “Delloleen ma jaamu Yàlla yi ! Ndax man mii ab Yonnent laa bu wóor.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
44:19
Buleen kawe kawe lu ci Yàlla, ndax man dey firnde ju wér laa leen indil.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
44:20
Maa ngi sàkku muslaay ci sama Boroom di seen Boroom, ndax ngeen bañ ma jóor i xeer.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
44:21
Su fekkee ne gëmuleen ma, kon sori leen ma”.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
44:22
Muu daldi ñaan Boroomam ne ko : “Ñi de ay niti Tafaar lañu (tooñkat)”.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
44:23
“Toppal guddi rañaan ak samay jaam ; danañu len dabusi.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
44:24
Bàyyil géej ga mu ne tekk ; ndax ñoom ay xarekat lañu ñuy, xala lab”.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
44:25
Ak a bari ay dër yu ñu bàyyi ginnaaw ak bëti ndox
ﮄﮅﮆﮇ
44:26
ak tool (mbay) ak kër yu taaru,
ﮈﮉﮊﮋﮌ
44:27
ak i xéewal yu ñu daan gamaajoo.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
44:28
Noonu la Nu ko donolee yeneeni xeet.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
44:29
Asamaan ak suuf jooyuñuleen te kenn it muñadikuwuleen.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
44:30
Musëloon Nanu , waa bani Israayiila ci mbugël mu doyadima (rey góor)
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
44:31
mom Firawna ma kawe woon lool ca yàqkat ya.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
44:32
Tànnoon Nanu leen tigi ci kaw waa àddina sépp (bawoo jamono),
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
44:33
indiloon Nanu leen ay kéemaan (firnde) yu leer nàññ.
ﯝﯞﯟﯠ
44:34
Ñoo ñaa ngay wax naan :
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
44:35
“Genn dee rekk am muy sunu dee, gu jëkk gi. Te it kenn dunu dekkalaat.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
44:36
Su fekkee ne dëggu ngeen kon dekkalleen sunuy maam, délloosileen”.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
44:37
moo ndax ñoom ñoo gën Tubbaa ak ña leen jiitu woon ? Faagaagoloon Nanu leen ndax ñoom ay niti tafaar lañu woon (tooñkat).
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
44:38
Bindu Nu asamaan yeek suuf si ak li ci seen diggënte di ko fowe.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
44:39
Bindu Nu leen ci lu dul dëgg. Waaye ñi ëpp ci ñoom xamuñu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
44:40
Ca bisub àtte ba, lañuy daje ñoom ñépp,
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
44:41
Bis ba farandoo dul jariñ moroom ja ; te kenn duleen dimbali,
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
44:42
ku dul ku Yàlla yërëm. mooy, boroom Kàttan, di Jaglewaakoon yërmande.
ﭫﭬﭭﭮ
44:43
Garabub Sakkuum ga tigi
ﭯﭰﭱ
44:44
moo di lekkug defaakoonu bàkkaar ya.
ﭲﭳﭴﭵﭶ
44:45
Day melni biteex ; buy wañax ca (seen biir ya)
ﭷﭸﭹ
44:46
ni ndox muy bax di wañaxe.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
44:47
Jëlleen ku tëmbéel ko moom ca digg Safara;
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
44:48
topp ñuy sotti ci kaw boppam ba mbugëlum ndox muy wañax.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
44:49
Mosal tokamtikul ! Yaay [boroom kàttan] tey ku Tedd (daan rëy-rëylu).
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
44:50
Lii nag tigi mooy li ngeen daan werante di ko sikki-sàkka.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
44:51
Ña ragaloon Yàlla te daan wattandiku ña nga ca ay kër yu wóor,
ﮛﮜﮝﮞ
44:52
ci ay tooli dër ak i dex,
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
44:53
ñuy soloo ca xeeti sooy ya gën a ràññiku ne rojj jàkkarloo.
ﮥﮦﮧﮨﮩ
44:54
Noonu ! La ñu leen di maye ay soxna (yu am bët) huuru alayn.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
44:55
Ñu fay man a am wépp xeeti fuytéef féex lool ne fayax.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
44:56
Duñu fa mos wextanu ndee lu dul dee gu jëkk ga. [Yàlla] fegal na leen mbugëlum Safara,
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
44:57
muy ngëneel lu bawoo ca sa Boroom. loolu mooy texe gu màgg ga.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
44:58
Di ko yombal ci saw làmmiñ, ngir amaana ñuy fàttaliku !
ﯬﯭﯮﯯ
44:59
Xaaral. Ñoom it ñi ngiy xaar.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







