Simoore Ya-Sin pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Ya-Sin pdf Wolof — Wàcce Simoore Ya-Sin Tekki. Simoore Ya-Sin (Meccan) 83 Aaya.
Related
- Simoore Ya-Sin TekkiWolof
- Simoore Ya-Sin mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Ya-Sin

ﭬﭭ
36:1
Yaa-Siin.
ﭮﭯﭰ
36:2
Maa ngi waat ci Alxuraan jii fees dell ag xereñ.
ﭱﭲﭳﭴ
36:3
Ci ne yaw [Muhammad] bokk nga ci limub Yonent yi.
ﭵﭶﭷﭸ
36:4
ci kaw yoon wu jub xocc wa.
ﭹﭺﭻﭼ
36:5
Mi ngi wàcce ci Yàlla boroom Kàttan ga di ab Jaglewaakoonu yërmaandeem.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
36:6
Ngir nga xupp aw nit ñoo xam ne kenn musul a xupp seeni baay : ñoom dañoo sàggan.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
36:7
Àtte ba dog : te la ëpp ca ñoom [ca Lawhul Mahfuuj] ci ne duñu gëmati.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
36:8
Def Nanu ay jéng ci seeni loos, mu àndak seeni daayi sikkim : ñu joñ leen.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
36:9
def Nanu ab ñag ci kanam ak ci seen ginnaaw ; Muur Nanu leen ba dootuñu gis.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
36:10
Nga xupp leen ak nga ñàkk leen a xupp ñoo yem kepp ci ñoom : duñu mës a gëm.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
36:11
Ka ngay war a xupp kay mooy kay topp [Alxuraan], tey ragal Yàlla ci kumpa. Nanga ko bégal ci ag njéggal ak pey gu tedd .
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
36:12
Nun Yàlla nooy dundal néew tey bind la ñu defoon ak seeni jeexit. Te mbir mu ci bokk yéege Nanu ko ci biir ab téere bu bir , bind ko ca.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
36:13
Joxleen misaal ci waa dëkk ba ab Yonent dikkaloon.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
36:14
Ba Nu leen jebalee ñaari ndaw ñu weddi leen. Nu daldi leen kàttanalaat ci ndaw lu leen ñetteel, ñu ànd ñoom ñett, ne leen : “Nun ndawi Yàlla lanu”.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
36:15
[Waa dëkk ba] tontu [Antaakiya] ne leen : “Yéen daal, ay mbindeef ngeen ni nun. Te Yàlla wàccewul dara, yéen daal ay fenkat doŋŋ ngeen”.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
36:16
[Yonent ya] waxaat ne : “Yàlla xam na ne nun ay Yonent lanu ci yéen.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
36:17
te dara warunu lu dul jottali ba mu leer nàññ.”
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
36:18
Ñu ne : “Gaafal nanu leen. Te bu ngeen bàyyiwul, dananu leen jóori xeer te dananu leen mbugal mbugal mu tar”.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
36:19
Yonent ya ne leen : “Seen gaaf googu mook yéen a ànd”. Moo ndax fàttaliwunu leen woon ? Yéen daal dangeen a yebaate ! ”.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
36:20
Mu am waa ju jóge woon ca anéeri dëkk ba, di dox ne leen : “Éy yéen samaw nit, moo tee ngeen a topp Yonent yi :
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
36:21
Toppleen ku dul laaj ag pey te ñoom ñu gindiku lañu.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
36:22
moo man, ana lu may war a dal ba tax duma jaamu Yàlla mi ma bind ? Te ca Moom ngeen di dellu.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
36:23
Moo ndax damay wuti jeneen yàlla ju dul Moom ? Te bu Yërëmaakoon bi natte ci man lor, seenug tinu duma jariñ dara te duñu ma xettali.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
36:24
Su loolu amoon dey kon, maa ngi ci ag réer gu bir.
ﯰﯱﯲﯳﯴ
36:25
Man dey, gëm naa seen Boroom, dëggal-leen ma”.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
36:26
Waxees na ko, ne ko : “Tàbbil Àjjana”. Mu wax ne : “Cëy aka neexoon samaw nit xam !
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
36:27
li tax Yàlla jéggal ma, def ma ma bokk ci ña Muy teral”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
36:28
Wàccewunu ci aw nitam ginnaaw ba mu jàllee, ay xarekat ñuy bawoo asamaan. Bëggunu fa woon a wàcce dara itam.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
36:29
Génn xaacu rekk a fa jaar, ñu faf giim.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
36:30
Ndeysaan jaam ñi le ! Ab Yonent mësuleen a dikkal mukk te du dañu koy ñaawal.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
36:31
Xanaa gisuñu na Nu faagale woon maas ya leen jiitu woon ? Te kenn du ca dellusi.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
36:32
Te ñoom ñépp danañu daje Sama kanam .
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
36:33
Indil Nanu leen firnde te moo di suuf si dee , Nu dekkalaat ko, [tawu ndow] génne ca ay doom, ngeen di ca lekk.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
36:34
Nu def ca ay tooli dëri tàndarma ak yu reseñ, xàbbal ca ay bëti ndox,
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
36:35
ndax ngeen di lekk ca meññent ma ak li ngeen cay liggéeyee. Moo ndax duñu sant ?
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
36:36
Tudd naa sellug bind yóllent yi mbooleseen ci liy sax ci suuf ak ci seeni jëmm ak ci li ñu xamul !
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
36:37
Ak firndey bu bëccëg jàlle, guddi ñëw lëndëm taruus.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
36:38
te jant baa ngay daw ca fa ñu ko rëddal ; looloo di nattaleb Yàlla miy boroom Kàttan, di ku Xam.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
36:39
Weer wi nattale Nanu ko ay këri wàccuwaay ba faf mu mel ni tàndarma gu màggat.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
36:40
Jant bi du jot weer wi, guddi it du jiitu bëccëg ; ku nekk a nga ca yoonam di féey.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
36:41
Ak firndey yenu gi Nu yenu seeni sët ci biir ag gaal gu ñu sëf ;
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
36:42
Te sàkkal Nanu leen yeneen yu ni mel ñu di ca war.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
36:43
Bu Nu sooboon, Nu labal leen ; duñu xam fu ñuy yuuxu jëmële, te kenn du leen xettali,
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
36:44
lu dul yërmaande ju bawoo ci Nun, ak i xéewal ba jëmmi jamono.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
36:45
Te saa su ñu leen waxee ne : “Wattandikuleen li nekk ci seen kanam ak li ci seen ginnaaw ndax amaana yërmaande wàcc ci yéen” !...
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
36:46
Amul yenn laaya , yu bokk ci seeni laayay Boroom, dikkal leen te dañu koo dëddu.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
36:47
Saa su ñu leen waxee ne : “Joxeleen ci alal ji leen Yàlla wërsëgal”, ña weddi dañuy wax ña gëm, naan leen : “Moo ndax nun danuy dundal koo xam ne bu neexoon Yàlla mu dundal ko ? Yéen daal ci ag réer gu bir ngeen nekk”.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
36:48
Ña ngay wax naan : “Dig ba kañ lay ñëw ndegam li ngeen di wax dëgg la ? ”
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
36:49
Xaaruñu lu dul genn yuuxu gu leen jël fekk leen ñuy xuloo.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
36:50
Duñu mën a batale, di dénkaane, mbaa ñuy mën a dellu ca seen njaboot.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
36:51
Su ñu ëfee Buftu bi, dañu naan futeet ca bàmmeel ya, dox wuti seen Boroom,
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
36:52
ñuy wax naan : “Wóoy ngalla nun ! Moo ana kan moo nu yékkatee ci sunu yàndoorukaay bi ? ” Lii dey mooy la nu Yërëmaakoon bi doon dig ; kon Yonent yi waxoon nañu dëgg.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
36:53
Genn ug xaacu rekk a jib, ñu seet-seeti ñoom ñépp, ne jaseet Sunu kanam.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
36:54
Bis niki tey, deesul tooñ benn bakkan . Te deefuleen feye lu dul la ngeen daan jëf.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
36:55
Bis niki tey, waa Àjjanaa ngi ci xéewal gu mat sëkk ;
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
36:56
ñoom ak seeni soxna, ña nga ca biir kër ya, sóonu ca lal ya.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
36:57
Am nañu fa ay fuytéef ak lépp lu ñuy soxla,
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
36:58
“Jàmm rekk la ñu fay ame” ! Mu bawoo ca Boroom biy Jaglewaakoonu Yërmaandeem.
ﭮﭯﭰﭱﭲ
36:59
“Ayca ! Ca biti, yéen tooñkat yi !
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
36:60
Yéen doomi-aadama, ndax digewuma woon ak yéen ngeen bañ a jaamu Séytaane ? Ndax seenub noon la bu nëbbëtuwul,
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
36:61
te ngeen di Ma jaamu ? Lii mooy yoon wu jub xocc wi.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
36:62
Mu réeral ci yéen lim bu takku. Xanaa daawuleen xalaat ?
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
36:63
Safara si ñu leen daan dig, mi ngi nii.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
36:64
Xoyomuleen ci bis niki tey, muy [peyug li ngeen daan weddi]”.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
36:65
Bis niki tey, Dananu ŋalaab seeni gémmiñ, seen yoxo ya di wax ak Nun, seen tànk ya di seede la ñu daan fàggu.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
36:66
Te kat, bu Nu sooboon, Dananu fatt seeni gët, bàyyi leen ñuy jëkkante ci kaw [siraat], ba xam fu ñuy giseeti ?
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
36:67
Bu Nu sooboon, Dananu leen rat benn barab ; dootuñu dem, duñu dikk.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
36:68
Képp ku Ma defal aw fan wu guddi, Danaa ko màggatloo, xanaa dungeen xalaat ?
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
36:69
Jàngalunu Muhammad woy mbaa lu koy nuru ; lii daal du dara lu dul ag fàttali ak Alxuraan juy biral,
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
36:70
ngir muy xupp ñiy dundu, wax ja itam di lu yay ca yéefar ya.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
36:71
Xanaa dañoo gisul ne sàkkal Nanu leen ci Sunu liggéeyu loxo ag jur gu ñuy moom ;
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
36:72
Nu tàggatal leen ko ; ñu di ca war te it ñu di ca lekk ;
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
36:73
am nañu ci ay njariñ ak i naan. Moo ndax dañu dul sant ?
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
36:74
Ñuy jàppe yàlla leneen lu dul Yàlla, ngir ñu neey danuy sàkku ndimbal...
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
36:75
Yooyu duleen mën a dimbali, dañuy sax faf di jàmmaarlook ñoom [di xare].
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
36:76
Bula seeni wax jaaxal ! Nun xam Nanu li ñuy yelu ak li ñuy biral.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
36:77
Xanaa nit dafa gisul ne Nun Yàlla noo ko bind ci lumbub deret ? Deketeyoo moom ab xulóowaakoon la bu di ab pànk !
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
36:78
Mu di Nu sàdd léebu, fàtte na ag sosoom ; dana wax naan : “Ana kan mooy dekkalaat ay yax yu funux ? ”
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
36:79
Neel : “Ki ko sosoon bu jëkk. Te xam lool bindafoon yépp ;
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
36:80
te Moo di ki leen defal ci garab gu nëtëx, aw safara wu ngeen di taaloo.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
36:81
Moo ndax ku bind asamaan yeek suuf mënul a bindaat ñeneen yu na mel ? Axakañ ! Moo di Bindaakoon, Xamaakoon bi.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
36:82
Ay mbiram moo di, saa su bëggee menn mbir, dakoy wax : “Nekkal”, mu daldi nekk.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
36:83
Tudd naa sellug ki nga xam moo ame ci loxoom moomeelug lépp ! Te it ca moom ngeen di dellu yéen ñépp.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







