Simoore Al-Hajj
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Hajj pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Hajj pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Hajj Tekki. Al-Hajj (Medinan) 78 Aaya.
Related
- Al-Hajj TekkiWolof
- Al-Hajj mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Hajj

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Éy yéen nit ñi ! Ragal-leen seen Boroom. Yëngutug Bis-pénc ba nag mbir mu rëy la.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Bis bu ngeen ko gisee, képp ku doon nàmpal dana fàtte la mu doon nàmpal, te ku ëmboon dana wësin la mu ëmb. Te nga gis nit ña màndi fekk màndiwuñu. Mbugalu Yàllaa tar [ci ñoom].
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Am na ci nit ñi ñuy dàggasante ci Yàlla cig ñàkk a xam ci di topp Séytaane mi féttérlu.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Te dogaleef na ca moom [Séytaane soosu] ne képp ku ko def sëriñam, dana la réeral, yóbbee la mbugalum Safara.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Éy yéen nit ñi ! Ndegam dangeen a nekk cig sikki-sàkka, [xamleen ne] Nun nag noo leen binde ci suuf, topp ci toqente [maniyyu], topp ci aw lumbu, topp ci suuxu yàpp wu Nu matal bindam ak wu Nu matalul bindam ngir Nu leeralal leen, ak Nu saxal ci ëmbukaay ba lu Nu soob ba ca àpp bu Nu tudd. Topp Nu génne leen ngeen di ay liir, topp ngeen màgg ba dëgër. Te mu am ci yéen ñuy teel a dee ak ñuy dundu ba egg ci gën jaa boni dundu ba tootuñu xam dara ginnaaw ba ñu nekkoon di ñu xam. Te nga gis suuf si mu wow koŋŋ : te bu Nu ca wàccee ndox mu yëngutu, fokki, saxal gépp xeetu gàncax gu rafet.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Loolu [lu wér la] ngir Yàlla mooy dëgg ga ; te Moom mooy dekkal ñi dee ; te Moom am na kàttan ci def lu ne.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Te Bis-pénc ba amul sikk ne luy ñëw la,te Yàlla dana dekkal mboolem ñi nekk ci bàmmeel yi.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Ci nit ñi, am na ñuy dàggasante ci Yàlla cig ñàkk a xam te àndul ak njub, te amul Téere bu wér,
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
muy lem loosam [di rëy-rëylu] ngir réerloo [nit ñi] soreel leen yoonu Yàlla. Kooku dey am na ci àddina toroxtaange ; te Dananu ko mosal Bis-pénc ba mbugal muy tàng di lakkaate.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Loolu la yelloo ngir la ñaari yoxoom ya def ci àddina ! Te Yàlla du tooñ jaamam ñi.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Ci nit ñi am na ñuy jaamu Yàlla ci genn wet rekk. Tax na bu amee lu baax mu nekk ku dal, bu ko lu naqari dalee, mu soppeeku ca la mu nekke woon, yàqule na ci àddina ak àllaaxira. Te loolu mooy yàqule tigi !
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Mangay jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu koo lor, mënu koo jariñ. Loolu moo di réer gu sori dëgg !
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Mangay jaamu loo xam ne loram moo gën jegeñnjariñam. Aka bon wéeruwaay te aka bon àndandoo !
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Naka Yàlla, Dana dugal ñi gëm tey jëf u yiw ci Àjjana yoo xam ne dex dañuy daw ci seen suuf [ron], Yàllaay def lu ko soob.
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙ
Ku jort ne Yàlla du dimbali [Muhammad] ci àddina ak àllaaxira, na tàllal buum jëme ko asamaan, topp mu dog ko, te na xool nag ndax pexeem dana fa jële la ko tax a mer.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Noonu la Nu ko wàccelee ay kàddu yu leer te Yàlla dana gindi ku ko soob.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Ña gëm ak ña nekk Yahuud ak ña di Saabiina, ak ña nekk Nasaaraan ak ña nekk Majuus ak way-bokkaale ña, naka Yàlla dana àtte seen diggante, bu Bis-pénc baa Yàlla seede la ci lu nekk.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Ndax gisoo ne lépp lu nekk ci suuf si ak asamaan yi mangay sujjóotal Yàlla, ak jant bi ak weer wi ak biddiw yi, ak garab yi ak tundi doj yi, ak way-sujjóot yi ak lu bari ci nit ñi ? Waaye lu bari (ci nit ñi) ñu yeyoo mbugal lañu. Te képp ku Yàlla texeedil kenn du ko mën a teral.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Ñaari kurél yooyu di way-xuloo ci seen mbirum Boroom. Ña nga xam ne dañoo weddi, xottileef na leen ay yére yu di Safara, te deefi sotti fi seeni kaw bopp ya ndox mu bax.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
danañu ruyal la nekk ca seen biir ak der ya.
ﯙﯚﯛﯜﯝ
Ñeel na leen ay bolde yu weñ.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Saa su fa bëggee génne ca njàqare ja, Nu delloo leen, di leen toqamtikuloo mbugal muy lakke.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Yàlla nag Dana dugal ña gëm te jëf jëf ju yiw ay Àjjana yoo xam ne ay dexay daw ci suufam. Dees na leen fa takkal ay lami wurus ak i per ; te foofa yérey sooy lañu fay sol.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Te jubaleef na leen ca wax ju teey te jubaleef na leen it ca yoon wu ñu gërëm.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Ña weddi tey wëlbatiku jëm ci yoonu Yàlla ak ca Jàkka ju ñu wormaal ja Nu def muy jëmukaay ci nit ñi : te aji-dëkk ak gan ñoo ca yem kepp... Ku fa bëgg a jeng ngir tooñ, Dananu ko musal mbugal mu tar,
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Fàttalikul ba Nu biralee Ibraahiima bérabu néeg ba [Kaaba ga], ne ko : “Bul ma bokkaaleek dara te nga laabal sama néeg ngir ñi koy wër, ña fay taxaw, di sukk di sujjóot”
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Te nanga woote ci nit ñi ngir aji Màkka. Danañu la dikkal ñuy dox ak ñeneen ñuy war xeetu waruwaay wu ne, jóge ca barab yu soree,
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
ngir ñu tase fa ak seeni njariñ tey tudd turu Yàlla ci ay bis yu ñu xam, ca la Mu leen wërsëgale ci mala yi ngeen di dunde, “Kon lekkleen ca te nangeen ca leel ñu ñàkk ña amul dara.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Bu ñu noppee, nañu dindi seeni tilim, sangu, wattu, mottali seeni yéene, daldi wër néeg bu yàgg a yàgg ba (Kaaba ga)”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Looloo wér, te képp ku màggal jaamukaayu Yàlla ba, loolumoo gën ci moom fa Boroomam. Te mu dagan ci yéen juri kër yi ginnaaw ya mu leen limal (ca saaru Ndën la). Kon nangeen wattandiku sobes xërëm yi te wattandiku waxi caaxaan, ay fen.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Nangeen doon ñuy sellal ngir Yàlla (ñu àndul ak bokkaale) ; ku bokkaale ak Yàlla, dangay mel ni ku rëcc jóge asamaan, njanaaw fëkk ko walla ngelaw sànni ko barab bu sore.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Noonu la. Képp ku màggal jaamukaayu Yàlla, na xam ne màggal googu bokk na ca ragalug Yàlla ci xol yi.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Ñeel na leen ci loolu ay njariñ ba àpp bu ñu tudd ; te it seen barab ba ñuy loje ma nga ca Néeg bu yàgg a yàgg ba.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Te xeet wu nekk, defal Nanu ko jaamukaay ngir ñuy tudd turu Yàlla ci li Mu leen wërsëgal ci juri kër yi. Kon seen Boroom jenn Yàlla doŋŋ la. Kon nangeen wommatu jëm ci Moom. Bégalal way-toroxlu ña,
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
ña nga xam ne fu ñu tudde Yàlla seeni xol yëngu, ak way-muñ ña ca la leen dal, ak ñay taxawal julli tey lele ca la Nu leen wërsëgale.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Te giléem yu suur ya, defal Nanu leen ñu bokk ca ya ñuy jaamoo Yàlla. Aw yiw doŋŋ la ñeel leen. Nangeen ci tudd turu Yàlla bu ñu leen di loj. Bu ñu daanoo tëdd ci seeni wet, nangeen ca lekk te ngeen leel ca way-doylu ña ak yalwaankat ya. Noonu la Nu leen tegtale ndax yéen ngeen gërëm.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Te Yàlla amul soxla ci yàpp wi walla dereet ji. Waaye la Ko soxal moo di ragal Yàlla gi nekk ci yéen. Noonu la Nu leen leen tàggate ngir ngeen màggal Yàlla ci li Mu leen gindi. Te nga bégal way-rafetal ña.
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Te Yàlla dana jiñal lu bon ña gëm. Te Yàlla soppul bépp wurujaakoon ju di weddikat.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Ña ñu dal ca seen kaw, may Nanu leen ñu xare ngir dañu leen a tooñ ; te Yàlla am na kàttan ci dimbali leen -
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
may Na ko it ña ñu génnee ci seeni kër, - ci lu dul dëgg, te defuñu lu dul wax rekk ne : “Yàllaa di sunu Boroom”. - Bu dul kon ak li Yàlla di fege ñenn nit ci ñeneen, kon deef na màbb jaamukaayi yahuud yi, ak yu nasraan yi ak jàkka yi di fu ñuy tudde Yàlla lu bari. Te fàwwu Yàlla dana dimbali ña koy dimbali. Te Yàlla ku bari doole la, di ku not lépp,
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
ña nga xam ne, bu Nu leen mayee doole ci kaw suuf si, ñu taxawal julli, di joxe asaka, di digle lu baax, di tere lu bon. Nañu xam ne Yàllaa moom mujjug mbiryi.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Te bu ñu la weddee, nitu Nooh weddi woon nañu, ak waa Haad ak waa Samuuda,
ﮡﮢﮣﮤﮥ
ak nitu Ibraahiima ak nitu Lóot.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
ak waa Madyaana. Te wedd woon nañu it Muusaa ; Teewul mu muñal yéefar yi, topp Ma sadd leen. Kaawtéef Sama mbugal ma !
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Ak mbiru dëkk ya Nu alag, te fekk dañoo tooñ. Ñu màbbal seen bopp : Teen ya yàqu ! Tabax ya gent !
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Moo ndax dañoo doxul ci kaw suuf ? Kon danañu am xol bu am ràññee ci loolu ak nopp yu ca am dégg gu wér.Te sax du gët yi ñoo di gumba, waaye xol yi nekk ci seeni dënn ñooy gumba.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Ña nga lay yàkkamti ci mbugal mi. Te Yàlla du soppi àppam. Te benn bis ca sa Boroom mi ngi mel ni junni at ci seen waññi.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Aka bari dëkk yu Mu muñal te ñu tooñoon ? Ba noppi Mu fàdd leen. Te ci Man la lépp di mujj.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Neel : “Éy yéen nit ñi ! Man nekkuma ci yéen lu dul ab waaraatekat bu wér”.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Kon ña gëm tey jëf jëf ju yiw am nañu njéggal ak xéewal gu tedd,
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
ña nga xam ne ñi ngi dox di yoqatloo nit ñi ci Sunuy ndigal, ñooña ñooy waa Safara.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Mësunoo yónni ci lu jiitu ab Yonent walla ku Nu soloo te bu mébétee dara Séytaane du sànni pexe mu bon ci mébétam. Waaye Yàlla dana masaxal la Séytaane sànni woon, ba noppi dëggal ay ndigalam. Te Yàlla Ku xam la Ku xereñ la.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Lu Séytaane sànni Dafa koo def muy nattu ca ña jàngoro nekk ca seen xol ak ña seeni xol wow... Ca tooñkat ya ñu nekk ci wuute gu sore [dëgg].
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Te Moo dogal loolu lépp ngir ña nga xam ne joxeef na leen xam-xam, ràññee ne Alxuraan ak moom dëgg la gu bawoo fa sa Boroom, ak ngir ñu gëm ko ci seeni xol, dellu ci Moom. Te ñu xam ne Yàlla dana gindi ñi gëm teg leen ca yoon wu jub xocc wa.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Te ña weddi duñu deñ ci sikki-sàkka ci moom Alxuraan ba baa Bis-pénc di leen dikkal ci mbetteel walla mbugalum bis bu tiis ba dikkal leen.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Bis niki tey nguur gi Yàllaa lo moom. Dana àtte seen diggante. Kon ña gëm tey jëf jëf ju yiw, danañu nekk ci Àjjanay xéewal,
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
waaye ña weddi te jàppe ay fen Sunuy kàddu, ñooña ñeel na leen mbugal muy toroxale !
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Ña gàdday ngir liggéey ci yoonu Yàlla, topp ñu rey leen mbaa ñu dee, fàwwu Yàlla dana leen wërsëgal wërsëg wu rafet, te nag Yàlla moo di Ki gën a mën a wërsëgal ci képp kuy wërsëgal.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
fàwwu dana leen tàbbal barab boo xam ne danañu ca bég, te Yàlla ku xam la, Ku lewet la.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Noonu la. Ku mbugale lu toll ni la ñu ko tooñ, topp ñu tooñaat ko, Yàlla dana ko dimbali, Yàlla Jéggalaakoon, Baalewaakoon la.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Noonu la ngir Yàlla mooy dugal guddi ci bëccëg, di duggal bëccëg ci guddi, te nag Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Noonu la ngir Moom mooy dëgg ga, te lépp lu ngeen di jaamu te du Yàlla, neen la ; te Yàlla moom Ku kawe la, Ku màgg la.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Ndax dangaa gisul ne Yàlla mooy wàcce ndox mu jóge asamaan, soppi suuf si mu naat ? Yàlla Kuy ñeewant la (jaam ñi), Ku deñ-kumpa la.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te Yàlla moom ku woomal la, Ku yeyoo cant la !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Ndax gisoo ne Yàlla tàggatal na leen li nekk ci suuf si, te gaal gay daw ci ndigalam la ? Te Moo tee asamaan daanu ci kaw suuf si ci ndigalam. Te Yàlla kuy ñeewant la, di Kuy jagle nit ñi yërmaandeem.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Te Moom mooy ki leen dundal te Dana leen rey, ba noppi Mu dundalaat leen. Waaye nit weddiwaakoon la.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Xeet wu nekk defal Nanu ko jaamukaay wu ñu koy jaamoo. Kon buñu xëccook yaw ci mbir yi ! Te nanga woote jëme ci sa Boroom. Yaw de yaa ngi ci njub gu ne xocc.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Bu ñu dàggasanteek yaw, neel : “Yàlla moo gën a xam li ngeen di def.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Yàlla dana àtte seen diggante bu Bis-pénc baa ca la ngeen doon juuyoo”.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Ndax dangaa xamul ne Yàlla xam na li nekk ci asamaan yi ak suuf si ? Te loolu nekk na ci ab Téere, te it loolu lu yomb Yàlla la.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Te ña ngay jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne wenn lay wàccu ca te amuñu ci benn xam- xam. Tooñkat ya duñu am dimbal de.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Bu ñu jàngee ci seen kanam Sunu kàddu yu leer yi, danga ràññee ca kanamu ña weddi weddi ga. Te tuuti kon ñu songu ña jàng Sunuy kàddu ci seen kanam. Neel : “Ndax ma xamal leen lu yées loolu ci yéen ? - Mooy Safara : Yàlla dig na ko ña weddi. Ndax daluwaay bu bon !”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Éy yéen nit ñi ! Ñi ngi leen di sadd léebu, dégluleen ko : “Ñi ngeen di jaamu bàyyi Yàlla duñu mën bind mukk aw weñ, doonte dañoo dajaloo ngir def ko. Te bu leen wenn weñ jëlaloon dara, duñu ko mën a nangu ci moom. Néew na doole ka jaamu ak ka ñu jaamu ! ”
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Màggal-leen Yàlla ni ko màggaayam yeyoo ; Te Yàlla ca dëgg-dëgg Dafa bari kàttan tey Notaakoon ba.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Yàlla moo tànn ay Yonent ci Malaaka yi ak nit ñi. Yàlla nag dana dégg, dana gis.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Xam na li nekk ci seen kanam ak la weesu nekk ca seen ginnaaw. Te ca Yàlla la mbir yépp di dellusi.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Éy yéen ñi gëm ! Deeleen sëgg di sujjóot, di jaamu seen Boroom, tey def lu baax. Ndax xéy-na yéen ngeen texe !
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Te jiyaarleen ci Yàlla jiyaar ju dëggu jëm ci Moom. Moo leen tànn ; te teg leen tiis ci diine ji, diiney seen baay Ibraahiima, moo leen tudde “way-wommatu ña” bu njëkk ba ak it ngir Yonent bi nekk seede ci yéen, te yéen ngeen nekk seede ci nit ñi. Kon taxawal-leen julli tey joxe asaka, te ngeen jafandu ci Yàlla. Moom Aji-dimbali leen la. Te Mooy gën jaa baaxi wéeruwaay ! Di gën jaa baaxi kuy dimbalee !
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







