Simoore Aali Imran
PDF —
200 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Aali Imran pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Aali Imran pdf Wolof — Wàcce Simoore Aali Imran Tekki. Aali Imran (Medinan) 200 Aaya.



Simoore Aali Imran
200 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
Alif, Lam, Miim.
ﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Yàlla mooy Yàlla ! Amul jeneen yàlla ju dul Moom, Aji-dundu la, di Aji-taxawaakoon ci lépp.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Moo wàcce ci yaw Téere ba ci dëgg, di feddali la ko jiitu. Moo wàcce Tawreet ak Injiil
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
ca bu jëkk, doonoon njub ci nit ñi. Moo wàcce Alxuraan. Ña weddi kàdduy Yàlla yi, am nañu mbugal mu tar ! Te Yàlla ku not la , Boroomug feyyu la.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Yàlla, dara nëbbuwul ci Moom biir asamaan ak suuf si.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Moo leen móol ci seeni biiri nday, na Mu ko soobee. Amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Mooy ki not, di ku xereñ.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Moom moo wàcce ci yaw Téere ba : am na ca ay laaya seen maanaa leer nañu, ñoo di cosaani àtte yi, ak yeneeni laaya yu seeni maanaa fésul. Ña nga xam ne jeng a nekk seeni xol, benn ca laaya yooyu lañuy topp ngir sàkku fitna ak jéem leen a firi, te Yàlla doŋŋ a xam seeni piri ak ña sax ci xam-xam. Danañu wax ne : “Gëm nanu ko : lépp ca sunu Boroom la bawoo ! ” Woroom xel yi rekk ay waaru.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
“Yaw sunu Boroom ! yàlla boo jengal sunuy xol ginnaaw ba nga nu gindee ; te may nu yërmaande ju bawoo ci yaw. Yaw de yaa di Mayewaakoon bi !
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Sunu Boroom ! Yaw yaa di dajale nit ñi ci bis boo xam ne - sikk nekkul ci ag ñëwam - Yàlla, du wuute dige ba.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ña weddi, seen alal ya ak seen njaboot ya duleen fegal dara ca Yàlla. Te ñoom ñoo di mattum Safara,
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
lu mel ni aadaay nitu Firawna ak ña leen jiitu woon, weddi woon Sunuy laaya. Yàlla jàppe leen seeni bàkkaar. Te Yàlla di ku tar mbugal.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Waxal ña weddi [ca Yahuud ya] ne : “Dees na leen not ; pang leen jëme Safara. Te [lal ba ñu fay fekk] bon na ! ”
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Am ngeen lu waare ci ñaari mbooloo ya [ca Badar] la ñu daj : muy di xeex ci yoonu Yàlla ; meneen ma, di ay yéefar. Mu jullit ma gis ne ñaari yoon la leen yéefar ya ëppee, ci gisu bët rekk. Fekk ëpp na sax loolu. Yàlla dana dooleel ci ndimbalam ku ko soob. Lii nag doy sëkk ag waare ca ña ame gët [xel] !
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Rafetaleef na ci nit ñi sopp bànneex ci jigéen ñi ak ay doom yu bari, alal ju bari ci wurus walla ci xaalis, fas yu tàggutu, ak i jur [waruwaay], ak i alal mbey ; loolu lépp yóbbalub àddina doŋŋ la, delluwaay ba gën, ma nga ca Yàlla.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Neel : “Moo ndax duma leen xamal lu gën loolu ci yéen ? Gaa ña nga xam ne dañoo ragal Yàlla, am nañu, fa seen Boroom, Àjjana joo xam ne dex yaa ngay daw ci ronam, ñu sax fa dàkk ak i soxna yu ñu laabal , ak ngërëm lu bawoo ca Yàlla.” Yàllaa ngi gis jaam ñi,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
ñooy ñay wax naan : "Sunu Boroom, nun gëm nanu ; jéggal nu sunuy bàkkaar, te fegal nu mbugalu Safara”,
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
ñooy, muñkat ya, ña dëggal, diy jaamukat, diy joxekati alal [ngir Yàlla] tey sàkku njéggal waxtuw njël.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Yàlla seede na ne, amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Malaaka ya ak woroom xam-xam ya taxawe ci maandu it, seede nañu ne amul jeneen Yàlla ju dul Moom. Ku not la, ku xereñ la !
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Diine Yàlla tigi mooy Lislaam. Ñoñ-téere ya yi wuutewuñu woon lu dul ba leen xam-xam ba dikkalee, ñu beew ci seeni diggante. Képp ku weddi kàddug Yàlla... na xam ne Yàlla ku gaaw la ci xayma jëf yi !
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Bu ñuy dàggasante ak yaw, neel : “Ci Yàlla laa jublu maak ku ma topp”. Te nga wax ñoñ- téere, ak ña jàngul : “Moo ndax yéen wommatu ngeen ? ” Bu ñu tàbbee ci Lislaam, nga xam ne gindiku nañu. Bu ñu dummóoyoo nag... Yaw [Muhammad] jotal rekk la ci war. Yàllaa ngi gis jaam ñi.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ñay weddi kàdduy Yàlla, di rey Yonent ya, ci lu dul dëgg, di rey ñay digle maandute ci nit ñi, na nga leen bégal ci mbugalmu tar.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Ñooña seeni jëf sippiku na ci àddina ak ca àllaaxira. Te duñu am ndimbal !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Moo ndax gisoo ñañu jox cér ca téere ba , woowees na leen jëme ci Téere Yàlla bi ngir mu àtte seeni diggante ; am kurél ci ñoom bu dummóoyu, far ñoom ñépp dummóoyu.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Ndax ñoom dañuy wax ne : “Safara dunu laal lu dul ay bis yuñu lim”. Dañuy duural Yàlla ci seen diine, loolaa leen nax.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Naka la ñuy def ca bis ba, kenn warut a nàttable ci ne dana am, bu ñu leen dajalee ba kenn ku nekk ñu jox ko la mu fàggu woon mu mat sëkk.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
- Neel : “Sama Boroom, Yaw miy Boroom nguur. Yaay jox nguur ku la soob, di rocci nguur ci ku la soob ; Yaay teral ku la soob, Yaay toroxal ku la soob. Yiw wépp a ngi ci sa loxo te kàttanu nga ci def lu ne.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Yaay dugal guddi ci bëccëg, Yaay dugal bëccëg ci guddi, Yaay génne ndundu ci ndee, Yaay génne ndee ci ndundu. Di wërsëgal ku la soob ci lu àndul ak waññi”.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Bu jullit ñi jàpp xaritoo ci yéefar yi, bàyyi fa jullit ña. Ku def loolu amoo ca Yàlla dara, ndeem du dangeen ragal ca ñoom ngaañ. Yàllaa ngi leen di moytandikuloo boppam. Te fa Moom la lépp di mujj.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓ
Neel : “Bu ngeen nëbbee li ci seeni xol walla ngeen feeñal ko, Yàlla dana ko xam. Yàlla xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si. Te Yàlla am na kàttan def lu ne.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Bis ba nga xam ne bakkan bu nekk dana jot ca la mu defoon ci aw yiw ak ca la mu defoon ci ñaawtéef ; dana ngéejoo dàndanteek ñaawtéef yooyu sore ko lool ! Yàllaa ngi leen di moytandikuloo boppam. Te Yàlla dey ku ñeewant jaam ñi la.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Neel : “Ndegam sopp ngeen Yàlla, toppleen ma, kon dey Yàlla dana leen safoo te jéggal leen seeni bàkkaar. Yàlla jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Neel : “Toppleen Yàlla ak Yonent bi. Bu ngeen dëddoo [def lu bokkul ak loolu] ... Yàlla du safoo yéefar ya !
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Yàlla moo tànn Adaama, Nooh, njabootu Ibraahiima ak njabootu Himraan ci kaw bindéef yi.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Ñenn ña di doom ca ña ca des, Yàlla Kuy dégg la te Ku xam la.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Fàttalikul ba soxnas Himraan waxee ne : “Yaw sama Boroom, fas naa yéene sédde la li ne ci sama biir. May ku mu sellal, nangul ma. Yaw yaay Kiy dégg, Ki xam”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Ba mu ko wasinee, mu ne : “Ay sama Boroom, jigéen laa wasin de” ; te Yàllaa gën a xam la mu wasin ! Ndax góor melul ni jigéen. “Te tudde naa ko Maryaama, te maa ngi koy muslul wéeru ci Yaw mook i doomam mucc ci Séytaane suñu rëbb sa”.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖ
Boroomam nangul ko, nangu gu rafet, màggloo ko màgg gu rafet. [Zakariyaa] yar ko. Saa su [Zakariyaa] duggee ca Mihraab ba, dana fekk fa moom ay xéewal. Mu ne : “Yaw Maryaama, fu la lii bawoo ? ” - Mu tontu ko ne : “Lu jóge ca Yàlla la”. Yàllaay wërsëgal ku ko soob ci lu àndul di waññi na mu tollu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Foofii la Zakariyaa ñaanee Boroomam, ne : “Yaw sama Boroom, may ma ci sa coobare, ay njërëta yu yiw. Yaw Boroom bi Kuy dégg ñaan nga”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Noonu, Malaaka ya woo ko, fekk mu taxawe julli ca Mihraab ba, xamal ko ne : “Yàllaa ngi lay bégal ci doom ju tudd Yahyaa, muy dëggal kàddu gu bawoo ca Yàlla [di Iisaa, di kilifa, di ku wegu]. Di ab Yonent, bokk ca ñu sell ña”.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Mu ne : "Sama Boroom, naka laay amee doom, ni ma màggatee, sama soxna Jërmél ?”. Mu ne ko : “Noonu lay ame ! ”, Yàlla mooy def lu ko soob.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
- Mu ne : “Yàlla, defal ma màndarga.” - Mu ne ko : “ Doo mën a wax ak nit ñi ñetti fan lu dul ci njunju. Na nga tudd sa Boroom lu bari ; te nanga di ko sàbbaal suba ak ngoon.”
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
(Fàttalikul) ba Malaaka ya waxee ne : “Yaw Maryaama, Yàlla tànn na la te laabal na la, tànn na la ci kaw jigéeni àddina bi yépp.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
“Yaw Maryaama, jaamul sa Boroom, nanga sujjóot te rukkoo ànd ak ñay rukkoo [di julli]”
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
- Loolu bokk na ca xibaar ya nekkoon kumpa, Nu ngi la koy xamal. Te neewuloo woon ba ñuy sànni bantu wantaloo ya di seet kan mooy yor Maryaama ! Te neewuloo woon ba ñuy xulloo.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
(Fàttalikul,) ba Malaaka ya waxee ne : "Yaw Maryaama, Yàllaa ngi lay bégal ci kàddu [doom] gu tukkee ca Moom : turam moo di “Al-Masiihu” “Iisaa”, doomu Maryam, boroom bayre ci àddina ak ca àllaaxira, te bokk na ca way-jege ña Boroom bi”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Te dana wax ak nit ñi, bi mu doonee liir ak bu doonee mag te bokk na ca nit ñu yiw ña”.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
- Mu ne [moom Maryaama] : “Yaw sama Boroom ! Naka laay ame doom, te góor musu maa laal ? ” - Malaaka ma tontu ko ne : “Noonu lay amee ! ”. Yàlla mooy sàkk lu ko soob. Te buy dogal mbir, du def lu dul wax : “Nekkal” ; mu daldi nekk.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
“Dana ko jàngal téere ba, xam-xamu ràññee, Tawreet ak Injiil,
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
dana ko def Yonent ci Banii-Israayiil, [mu wax leen ne]: “Man mii, indil naa leen ay màndarga yu bawoo ca seen Boroom. Mën naa leen defaral ci ban bi jëmmi picc, ëf ko mu nekk picc, muy dundu ci coobare Yàlla. Danaa faj ku judduwaale gumba ak ku gaana, danaa dundal [dekkal] ku dee ci coobare Yàlla. Mën naa leen xamal la ngeen di lekk ak la ngeen denc ca seeni kër. Loolu war na leen a yéem [waar], ndegam ñu gëm ngeen !
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
May dëggal li ma jiitu [Tawreet], ma di leen daganalal lennat ca ya ñu araamaloon ci yéen. Indil naa leen kàddu gu bawoo ca seen Boroom. Ragal-leen Yàlla te topp ko.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Yàlla miy sama Boroom di seen Boroom. Jaamuleen ko : lii mooy yoon wu jub xocc wi.”
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Ba Iisaa ràññee ca ñoom gëmëdi, la daldi wax ne : “Waaw ana kan moo may dimbali ci liggéeyal Yàlla ? ” Gaa yu sell ya ne ko : “Nun noo lay dimbali ci yoonu Yàlla. Gëm nanu Yàlla. Seedeel ne nun way-wommatu lanu [jëm ci Yàlla].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Yaw sunu Boroom ! Gëm nanu li nga wàcce [Linjiil] te topp nanu Yonent bi [Iisaa]. Yàlla nanga dogal nu bokk ca seede yu dëggu ya”.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ñu tëral pexe. Yàlla it tëral pexe. Te Mooy gën jaa mën a tëral pexe !
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Fàttalikul ba Boroom ba waxee ne : "Yaw Iisaa, danaa la faat, yékkati la jëme ci Man, Danaa la laabal ci bon-boni yéefar yi weddi te danaa def ña la topp ñu féete kaw ña la weddi ba Bis-pénc ba. Yéen ñépp dellu ci Man, Ma àtte seeni diggante ci li ngeen doon juuyoo.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Ña nga xam ne dañoo weddi, danaa leen mbugal mbugal mu tar, ci àddina ak ca àllaaxira ; te duñu am ku leen dimbali.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Ña gëm te jëf aw yiw, danañu jot seeni pey. Yàlla sopput tooñkat ya.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Loolu noo ngi la koy jàngal [xamal] mu bokk ci ay kéemaan ak kàdduy fàattali yu xereñ [Alxuraan].
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Mbiri Iisaa ca Yàlla, dafa deme ni mbiri Aadama, dafa koo bindee ci suuf ba noppi ne ko “Nekkal” : mu nekk.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Dëgg ca sa Boroom la jóge. Bul bokk ca ña cay werante.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Ku cay dàggasante ak yaw, ginnaaw la la dikke ci xam-xam [ci mbiri Iisaa], neel : “Kaayleen nu woo sunuy doom ak sunuy soxna ak seeni soxna, nu ñëw, ngeen ñëw yéen ci seen bopp topp nu toroxlu, rëbbante rëbbum Yàlla dal ci ña fen [ci mbiri Iisaa].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Lii mooy nettali yu dëggu ya. Te amul yàlla ju yayoo jaamu ku dul Yàlla. Te Mooy ki not, ki xereñ.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Bu ñu dëddoo [dummóoyu] ... Yàlla xàmmee na yàqkat ya !
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
- Neel : “Yéen ñoñ-téere yi, kaayleen ci baat boo xam ne yéen ak nun noo ciy maase : dunu jaamu ku dul Yàlla, te nu bañ cee bokkaale dara, te kenn ci nun bañ jël moroomam jàppe ko Yàlla, di ko jaamu”. Su ñu bañee ba dummóoyu, neeleen : “Seedeleen ne nun dey way-wommatu lanu [ci topp Yàlla]”.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Yéen ñoñ-téere, ana lan moo waral ngeen di dàggasante ci mbiri Ibraahiima, te Tawreet ak Injiil ginnaawam lañu wàcc ? Moo ndax dungeen xel-lu ?
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Yëgleen ne dàggasante ngeen ci lu ngeen xam [mbiri Iisaa]. Lu tax ngeen di dàgge ci lu ngeen amul xam-xam [Mbiri Ibraahiima] ? Yàlla xam na te yéen xamuleen.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Ibraahiima nekkul woon yahuud, du càggéeni mu nekkoon nasraan. Waaye nekkoon na kuy wéetal Yàlla, di ku wommatu jëm ci Yàlla. Te bokkul woon ca ñay bokkaale..
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Nit ñi gën a yey ci Ibraahiima ñooy ña ko toppoon ak Yonent bii [Muhammad] ak ña gëm [Yàlla]. Te Yàlla mooy mbégum ñi gëm.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Am na ab kurél bu bokk ci ñoñ-téere, danañu ngéeju réeral leen. Waaye mënuñoo réeral ku dul seen bopp ; te yéguñu ko.
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàddug Yàlla, te ngeen di ci ay seede [xam ko xéll] ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Yéen ñoñ-téere, lan moo tax ngeen di muure dëgg ak ay caaxaan, di nëbb dëgg te xam ko ?
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Am na ci ñoñ-téere kurél bu wax ne : “Gëmleen li wàcc ca way-gëm ña [Alxuraan] ci suba [waxtu], te bu ngoonee ngeen weddi ko, ndax ñi gëmoon ñoom it weddi.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Te : “Buleen gëm lu dul ku topp seen diine...”. Neel [yaw Muhammad] : “Njub Yàllaa ko moom” - kon mën naa am kenn nit kuñu jox la mel ni la ngeen jot ba mën a weccee kàddu ak yéen ci mbiri seen Boroom. Neel : Ngëneel a nga ca loxo Yàlla. Dana ko jox ku ko soob. Yàlla ku yaatu la, ku xam la.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Dana jagle yërmaandeem ku ko soob. Yàllaay Boroom ngëneel lu màgg.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Am na ci ñoñ-téere ko xam ne, ku ko dénk barigo [wurus] dana la ko delloo. Am na ci koo xam ne, ku ko dénk benn dinaar, du ko delloo, ndegam taxawoo ca temm. La ko waral, dañoo wax ne : “Ñoom, dara waruleen ci seen diggante ak ña jàngul .” Dañuy wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Axakañ [am na lu leen war] ci ñoom, ku matal kóllareem ci ragal [Yàlla], na xam ne Yàlla safoo na ña ragal Yàlla.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Ña nga xam ne jaay nañu kóllareg Yàlla ak seeni ngiñ ci njëg gu néew, ñooña amuñu cër ca àllaaxira, Yàlla duleen xool te du wax ak ñoom bu Bés-pénc baa te duleen laabal itam ; te mbugal mu metti dana dal ci seen kaw.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Am na ci ñoom kurél buy damm seeni làmmiñ [bu ñuy jàng] Téere ba ngir ngeen defe ne la ñuy wax ca Téere ba la bokk, te bokku ca ; ñu naan : “Lu jóge ca Yàlla la”, te jógewul ca Yàlla. Di wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Mënul a nekk nit koo xam ne Yàlla daf koo jox ab Téere ak xam-xamu xereñ [ràññee], def ko ab Yonent ba noppi muy wax nit ñi : “Nekkleen samay jaam bàyyi Yàlla” ; la muy wax kay moo di: “Nekkleen jaamukati seen Boroom niki ngeen ko jàngee woon ca Téere ba te xame ko na”.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Te duleen digal jàppe Malaaka ya ak Yonent ya ay yàlla. Ndax duleen digal jëfi yéefar ginnaaw bi ngeen wommatoo jëm ci Yàlla?
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Fàttalikul ba Yàlla kóllaranteek Yonent ya : ba mu leen joxee Téere ak xam-xamu ràññee, [mu ne]: “Su leen ab Yonent dikkalee buy dëggal li ngeen yor, nangeen ko topp te dimbali ko.”. Mu ne leen [Moom Yàlla] : “Ndax nangu ngeen loolu ? Te nangeen jàpp ci loolu Sama kóllare ” - Ñu ne : “Nangu nanu”. Yàlla ne leen : “Seedeleen te nanga ànd ak yéene bokk ca way-seede ya.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Ku dummóoyu ginnaaw loolu... ñooña ñoo sàqi ndigal”.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Ndax dañuy sàkku jeneen diine ju bokkul ak diiney Yàlla ji, te waa asamaan si ak suuf si ci Moom lañu jëm, moo xam muy coobare wallag noteel, te lu mën a xew ca Moom lañuy dellu ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Neel : “Gëm nanu Yàlla, li ñu wàcce ci nun, li ñu wàcce ci Ibraahiima, ak Ismaahiila, ak Yanqooba, ak ca sët ya, ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa ak Yonent ya, mu tukkee ca seen Boroom [Téere ya]: dunu téqale kenn ci ñoom te nun way-wommatu lañu [jébbulu] jëm ci Yàlla”.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Kuy sàkku diine ju dul Lislaam, deesu ko nangul, te bu àllaaxiraa, ca way-ñàkk ña lay bokk.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Naka la Yàlla di jubalee nit ñu weddi ginnaaw seen ngëm te ñu seede ne Yonent ba ku dëggu la, te lay yu leer dikkal leen ? Yàlla du gindi nit ñu nekk ay tooñkat.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Ñooña, seen pey nekkul lu dul rëbbum Yàlla ak Malaaka ya ak nit ñépp, dana dal ca seen kaw.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Dañu fay béel ca Safara. Kenn duleen woyafal mbugal ma, kenn duleen ko yéexalal,
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
lu dul ña tuub ginnaaw loola te sellal seeni jëf. : Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Ña nga xam ne dañoo weddi ginnaaw ba ñu gëmee ba dee ci kéefar, deesuleen nangul seenug tuub. Te ñoom ñooy gaa ya sànku .
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Ña nga xam ne ñoo weddi ba dee ci kéefar, deesul nangul kenn ci ñoom mu jote doonte la joxe na wurus wu fees dell suuf si ngir loolu [jote]. Ñooñee, mbugal mu tar lañuy am, te duñu am ku leen dimbali.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Dungeen am mbaax ba ba ngeen di joxe ci li ngeen bëgg. Te lépp lu ngeen mën a joxe, Yàlla xam na ko.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Ñam yépp a daganoon ca waa Banii-Israayiil, lu dul ñam ya [Israayiil ] araama loon ca boppam lu jiitu ñu doon wàcce Tawreet. Neel: “Indileen Tawreet te jàng ko, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Ku duural Yàlla ay fen, ginnaaw loolu... ñooñaa di tooñkat ya.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Neel : “Yàllaa wax dëgg. Kon toppleen diiney Ibraahiima. Ku wéetaloon Yàlla la te mësul a bokk ca ñay bokkaale Yàlla”.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Néeg ba ñu njëkk sampal nit ñi moo di ba nekk Màkka, muy bu ñu barkeel, di njub, mbindéef yépp bokk ko.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Ay kéemaan yu leer ñoo fa nekk, [bokk na ca] Maxaama Ibraahiima [barab] ; ku fa dugg am kóolute. War na, ci nit ñi ku ko mën, aj fa néegub Yàlla ba te Yàlla tax wenn yoon [wu farata]. Ku weddi nag... na xam ne Yàlla ku doyloo la waliis mbindéef yépp.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Neel : “Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàdduy Yàlla yi? Te Yàlla kuy seede la ci li ngeen di def ”
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Neel : “Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di gàllankoor ñiy dox jëm ci yoonu Yàlla, di ko wutal sikk? Te ngeen di ay seede, te Yàlla sàgganewut li ngeen di jëf de.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen toppee ñenn ñi, ñoñ-téere, danañu leen delloo ci kéefar gannaaw ba ngeen gëmee Yàlla.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Naka ngeen di weddee te laayay Yàlla yi ñi di ko jàng fi seen kanam, Yonent bi nekk fi seen biir ? Ku ŋoy ci Yàlla, gindiku na jëm ca yoon wu jub xocc wa.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla kem ni mu yellee [tigi]. Te buleen dee mukk lu dul fekk na yéen a ngi wommatu jëm ci Yàlla.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Jafanduleen yéen ñépp ci buumug Yàlla gi te buleen teqalikoo ; fàttalikuleen xéewal gi leen Yàlla defaloon ba ngeen nekkee ay noon [lu jiitu Lislaam], mu tàppe seeni xol. Ba ngeen mujj ci xéewalam di ay doomi ndey. Te it nekkoon ngeen ci pindub kàmbug Safara, mu xettali leen ci loolu. Noonu la leen Yàlla di leeralee ay káddoom ndax Yàlla ngeen gindiku.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Sàkkleen ci seen biir kurél buy woote jëme [nit ñi] ci mbaax [yiw], ñuy digle njekk ci tere njekkar . Ñooña ñooy ña texe.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Te buleen mel ni ña teqalikoo juuyoo, ginnaaw ba leen leeral ga dikkalee, ñooña am nañu mbugal mu rëy.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Bis ba ay xar-kanam di weex tàll, ay xar-kanam it di ñuul kukk, ña nga xam ne seeni kanam dana ñuul [dana ñu leen wax] ne: “Ndax dangeen weddi gannaaw ba ngeen gëmee ? ”. Mosleen, toqamtikuleen mbugal mii ci sababus li ngeen doon weddi.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Ña nga xam ne seeni kanam ya dafa weex, dana ñu nekk ci yërmaandey Yàlla, te dañu fay béel.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Loolu moo di kàdduy Yàlla ya ; Danañu ko jàngat ci yaw (Muhammad) ci dëgg. Yàlla nammul di tooñ mbindéef yi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Yàllaa moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te mbir yépp ca Yàlla lañuy mujj [dellusi].
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Yéen yéen ay xeet wi gën ci nit ñi [xeet wu fi mës a jaar]. Yéen ay digle njekk te tere njekkar te gëm Yàlla. Bu ñoñ-téere gëmoon, mooy gën ci ñoom de, li ëpp ci ñoom ay saay- saay lañu.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Duñu la mën a lore lu dul ci wax ju ñaaw ; te bu ngeen xaree ak ñoom, ñu joxe ginnaaw [daw], kenn duleen dimbali.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Fu ñu mën a nekk, toroxtaange dal leen, lu dul ña ca yiiroon kóllareg Yàlla walla gu nit ña. Te ñoom merum Yàlla dal na leen, ñu daldi simbook ñàkk [ndóol] ngir weddi ga ñu weddi kàdduy Yàlla ak rey ga ñu rey Yonent ya ci lu dul dëgg, booleek moy Yàlla gi ñu saxoo woon, di jalgati.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Waaye ñoñ-téere yemuñu de. Am na ci kurél bu taxaw [ci dëgg] buy jàng kàdduy Yàlla ya, ca waxtu ya séq guddi, te dañuy julli [sujjóot].
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Gëm nañu Yàlla ak Bis-pénc ba, te dañuy digle njekk, di tere njekkar, di jëkkante ci def lu baax. Ñooña ca ñu yiw ña lañu bokk.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Lu ngeen jëf ci aw yiw, kenn duleen ko xañ. Yàlla xam na ña ko ragal .
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Ña weddi, seeni alal ak seeni doom duñuleen jariñ dara fa Yàlla. Ñoom ñooy waa Safara te dañu fay béel.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
La ñuy joxe ci seeni alal ci mbiri àdduna dafa mel ni ngelaw lu ànd ak safara dal ci kaw mbeyum ña tooñ seen bopp, ne ko fuuf lakk ko. Yàlla tooñuleen waaye ñoom ñoo tooñ seen bopp.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Yéen ñi gëm, buleen won seen mbir ci ag xaritoo keneen ku bokkul ci yéen. Bumuy ci ñoo xam ne dañuy kàttanlu ci yàqal leen, danañu ngéeju ngir ngeen am coono. Mbañeel ga feen na ca seeni wax, te la seeni xol ëmb moo yéesati. Yéen leeral nanu leen kéemaan yi [ngeen war leen a ràññee ndegam ñu xel-lu ngeen ! ].
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Yéen ak ñoom, yëgleen ne yéen a leen safoo, waaye ñoom safoowuñu leen ; te yéen gëm ngeen Téere bi lépp. Bu ñu dajee ak yéen ne “Gëm nanu” ; bu ñu wéyee màtt seeni waaroom wiccax ndax mer. Neel : “Deeleen ci mer” ; Yàlla ku xam la lu nekk ci xol yi.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Bu ngeen amee bànneex, mu naqari leen. Bu ngeen amee naqar, mu di seen bànneex ñoom. Waaye bu ngeen muñee te ragal Yàlla, seen pexe yi duleen wàññi dara. Te Yàlla ku peeg la la ñuy def.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Fàttalikul yaw Yonent bi, ba nga xëyee jóge ci sa njaboot, di tegtal jullit ña barabu xeexukaay ya, xamal ne Yàlla kuy dégg la, Kuy xam la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
[Fàttalikul] ba ñaari kurél ci yéen naree yoqat ! Te Moo leen dimbali woon ba delluwuñu ginnaaw ! Way-gëm ña, nañu sukkandiku ci Yàlla [Uhud].
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Yàlla dimbali woon na leen ca Badar, ba ngeen nekkee ñu néewle. Ragal-leen Yàlla ndax amaana ngeen gërëm ko !
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
[Fàttalikul yaw Yonent bi] ba nga waxee ña gëm : “Moo ndax doyuleen, seen Boroom, tëbb leen ñetti junni Malaaka yu wàcc [ngir dimbali leen]” ?
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Axakañ ! Bu ngeen muñee te ragal Yàlla, bu ñu leen songee ak doole [ca waxtu wu ñu tànn], seen Boroom dana leen tëbb juróomi junniy Malaaka yuñu màndargaal.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Te Yàlla defewuko lu dul bégal leen ngir seeni xel dal. Te ndimbal du bawoo fu dul fa Yàlla, Mooy Ki not, di Ku xereñ ki ;
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
def na ko it ngir dog ab kurél walla toroxal leen, ba ñu wëlbatiku di ñu yàkkiku [seen yaakaar tas].
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
[Yaw Yonent bi], mbir moomu moomoo ci dara - Yàlla Moo leen di jéggal walla Mu mbugal leen, ñoom daal ay tooñkat lañu.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Te Yàlla Moo moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Mooy jéggal ku ko soob, di mbugal ku ko soob. ...Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Éy yéen ñi gëm, buleen lekk ribaa ju jóge ci alal juy léw-léwi di fulu. Nangeen ragal Yàlla ndax ngeen texe !
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Nangeen ragal Safara sa ñuy xaaroo yéefar ya.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Nangeen topp [ndigali Yàlla] ak Yonent bi ndax ngeen doon ñu ñuy yërëm!
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Jëkkanteleen jëm ci seen njéggalug Boroom ak ci Àjjana joo xam ne yaatu na ni asamaan yi ak suuf si, te ña ragal Yàlla lañu koy xaaroo,
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
ñoom ña nga xam ne dañuy joxe [seen alal ci jamonoy naataange ak ci jamonoy tar-tar ], ak ñay nëbbu seen mer, ak ñay jéggal nit ñi [ay tooñeel] - Yàlla safoo na ñay rafetal -
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
ak ña nga xam ne, bu ñu defee ñaawtéef mbaa ñu tooñ seen bopp, daldi fàttaliku Yàlla fa saa sa, daldi jéggalu seen bàkkaar ya - te Yàlla rekk ay jéggale bàkkaar - te ñooña duñu nuur mukk ci jëfe bàkkaar te fekk ñu xam ko.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Ñooña seenug pey moo di jéggal gu bawoo ca seen Boroom, ak Àjjana yu dex ya di daw ci seen ron, te dañu fay béel. Loolu ag pey dàqatuko !
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Am na ay yoon yu jàll yu ñu sosoon ba ngeen dikkagul. Kon doxleen wër ci goxi suuf, te di xool naka la ña daan weddi mujje.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Lii ag leeral la ci nit ñi, te di ag njub ak ug waare ngir ñi ragal Yàlla.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Buleen doyadi, buleen ragal, yéen ay féete kaw ndegam gëm ngeen.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Su fekkee metit dal na leen, wu na mel daloon na yéefar yi. Bis yooya [Bisi naqar] danu leen di ay-ayle ci nit ñi ak itam ngir Yàlla xàmmee ñi gëm, te dana sàkk ci ñi dee ci xare, te bokk ci yéen, ay chuhadaa - Yàlla du safoo tooñkat ya.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
Loola Yàlla dakoy defe ngir laabal ñi gëm, di ci lakk yéefar ya.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Moo ndax dangeen a defe ne dangeen duggu Àjjana te Yàlla duleen nattu ba ràññee ña xeexal diine, ràññee it muñkat yi ?
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Mebetoon ngeen dey lu jiitu ngeen dajeek Moom. Léegi ndax gis ngeen ko, ne ci jàkk !
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Muhammad doonul lu may ab Yonent - boo xam ne ay Yonent ñoo ko jiitu woon ba jàll - Ndax bu deewoon walla ñu rey ko, dangeen di dellu ca seeni tànk, weddi ? Ku walbatiku ca ay tànkam, du wàññi Yàlla dara ; te Yàlla dana fey ñay gëram seen Boroom.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Bakkan du dee lu dul ci lu soob Yàlla, ci ab dig bu am àpp. Ku bëgg xéewali àddina, Dananu ko jox. Ku bëgg xéewali àllaaxira Dananu ko jox te Dananu fey [Nun Yàlla] ñiy gëram.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Bariwaana Yonent bu xare ñu rey ko, mu ànd ak mbooloo mu bari, te doyadiwuñu ca la leen dal ci sàmm diiney Yàlla. Yoqatuñu, nekkuñu ñu xeebu. Yàlla safoo na muñkat yi.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Te seeni wax nekkul lu dul ñu naan : “Sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar ak sunuy jéggi-dayo ci sunuy mbir, te nga dëgëral sunuy ndëggu, te dimbali nu ci kaw nit ñii di ay yéefar”.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Yàlla yoole leen àddina [xéewal] ak gën jaa rafeti yoolub àllaaxira. Yàlla safoo na ñay rafetal.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Éy yéen ñi gëm!, bu ngeen toppee ñi weddi, danañu leen dugal sa seeni tànk [weddiloo leen], ngeen wëlbatiku ñàkk.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Li wér mooy Yàllaa leen méngoo [yore seeni mbir] te Mooy ngëm ji kuy dimbali.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Dananu sànni ci xoli ñi weddi tiitaange ngir la ñu bokkaale Yàlla ak loo xam ne amul lay wuñu leen ca wàcceel. Safaraa di seen dëkkuwaay te dëkkuwaayu tooñkat ya bon na !
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Yàlla def na la Mu leen digoon nekk dëgg, ba ngën di xeex ak ñoom ci ndigal, [ngeen not] ba ba ngeen sàqi ndigal la, ginnaaw ba ngeen janoo ak la ngeen bëgg [alal] àddina! Am na it ci yéen ñu bëgg [alali] àllaaxira. Ba noppi Yàlla wëlbati leen [soppi tooñeel ga] ngeen amoon ci ñoom, ngir nattu leen.Waaye baal na leen. Yàlla Boroom ngëneel la yu muy [sédd] ñi gëm.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
[Fàttalikuleen] ba ngeen di yéeg te geesuwuleen kenn, te Yonent bi di leen woo ci seen ginnaaw. Mu tegoon leen njàqare ya ci kaw njàqare ya, ndax ngeen bañ a mitteetlu la leen rëcc walla la leen dal. Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Wàcce na ginnaaw njàqare la, kóolute, muy gëmméntu gu muur ab kurél ci yéen [way- gëm ñi] te beneen kurél ba [naaféq ya] seen bopp rekk yitteel leen, ñu njortu ci Yàlla lu dul dëgg njortu ku réer. -Ñu naan : “Ndax mbir mi moom nanu ci dara [ba di ci reyante] ?”. Neel [Yaw Yonent bi]: “Mbirum Yàllaa.”. Ña nga nëbb ci seen biir lu ñu feeñalul, di wax naan : “Bu nu moomoon dara ci mbir mi kon duñu nu rey fii.” Tontuleen ne : “Bu ngeen toogoon ca seeni kër, ñañu dogal dee ci ñoom dana leen fekk ca seen kaw i lal. [Lii lépp am na] ngir Yàlla natt li nekk ci seeni dënn [xol], ak feeñal li nekk ci seeni xol. Te Yàlla ku xam la li nekk ci dënn yi.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Ña dëddu [bañ a xeex], Seytaane tarxiisloo na leen ngir lenni bàkkaar ya ñu fàggu woon. Waaye, Yàlla jéggal na leen. Yàlla Jéggalaakoon la, Ku lewet la !
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Yéen ñi gëm ! Buleen mel ni ña weddi, di wax seeni mbokk ya nekk ci tukki walla ci xare [te dee ca] : “Bu ñu toogoon ci nun, duñu dee walla duñuleen rey. ”. Yàlla def wax jooju di rëccu ci seeni xol. Te Yàlla Mooy dundal, Mooy rey. Te Yàllaa ngi ne jàkk li ngeen di def, di leen gis.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓ
Bu ñu leen reyee ci yoonu Yàlla walla ngeen dee, ca dëgg-dëgg jéggalu ga, Yàlla ak yërmandeem moo gën fuuf li ngeen di dajale.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Ngeen dee walla ñu rey leen, dees na leen pang [gur-gur] jëme ca Yàlla.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Ci sa yërmaandeey Boroom nga nooyee ci ñoom ! Boo nekkoon ku ñaaw jikko walla ku xat xol, ñu ne wuseet bàyyi la. Baal-leen te jéggal-leen. Te deel diisook ñoom ci mbir yi ; waaye boo dogoo [ci wéyal dara], nanga wéeru ci sa Boroom, Yàlla dana safoo ñay wéeru ci Moom [yaw Muhammad].
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Bu leen Yàlla dimbalee, kenn duleen mën a not. Bu leen bàyyee, kan moo leen di mën a dimbali ? [Amul]. Ñi gëm, nañu wéeru ci Yàlla.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Amul benn Yonent buy labax alali xare. Te képp ku sàcc alali xare, bu Bis-pénc baa, dana ko indi. Ku nekk door a jot la mu jëfoon ba mu mat sëkk.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Ndax kuy topp ngërëmul Yàlla, dana yem ak ku sóobu ci xarabug Yàlla ? Safaraa di këram te googu muj, du gu ñuy taamu !
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Xam na ne duñu yem mukk waay. Ëppante nañu daraja [dayo] ca Yàlla, ndax Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy jëf.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Yàlla xéewale na ña gëm ba Mu yónnee ca ñoom ab Yonent bu bokk ca ñoom, di leen jàngal kàddoom, di leen laabal, di leen xamal Téere ba ak xam-xamu xereñe, te la ko jiitu ñu nekkoon ci réer gu tar.
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓ
Naka mu ? Bu leen aw tiis dalee - te fekk daan ngeen [seeni noon] lu mat ñaari yoon - ngeen di wax naan “Naka la lii mën a nekkee ? ”. Neel : “Ci yéen la”. Yàlla mën na lu ne.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
La leen dalool ca seenub dajeeb ñaari mbooloo ya, lu Yàlla nammoon la ngir mu xàmmee ca ña gëm [xareb Uhud]
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
ak ngir mu ràññee naaféq ya. Waxees na leen ne : “Kaayleen xeex [xare] ci yoonu Yàlla, walla ngeen feg [noon ya]”, ñu toontu ne : “Su nu mënoon xeex, dananu leen topp”. Ñoom, ca bis boobu, kéefar lañu gën a jege ci ngëm. Dañuy wax ca seeni gimiñ lu nekkul ca seeni xol. Te Yàllaa gën a xam lu ñuy nëbb.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Ña toog bañ a xareji tey wax seeni mbokk : “Su ngeen nu déggaloon, dungeen xareji.”. Neeleen : “Jiñleen dee mu bañ a agsi ci seeni bakkan ndeem ñu dëggu ngeen”.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Bul foog ne ñañu reyee ci yoonu Yàlla, ñu dee lañu. Déet, ñuy dundu lañu ca seen Boroom, nekk ci xéewal
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
dañuy bég ca la leen Yàlla jox ci ay ngënéelam, di bég it ca jullit ya ñu bàyyi ginnaaw te fekkeeguñu leen, duñu jàq, duñu am naqar bu ñu fa eggee.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Danañu bég ca xéewal ya bawoo fa Yàlla ak i ngënéelam, ak ca la nga xam ne Yàlla du sànk peyub ñi gëm.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Ñoom ña wuyu [wooteb] Yàlla ak Yonent ba, ginnaaw ba leen jam-jam ya [ca xare Uhud] dalee, ña doon rafetal ca ñoom te ragal Yàlla, am nañu pey gu màgg.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Ñooy ña nit ña ne woon : “Yéen a toog, waaye nit ñaa [seeni noon] ngi daje ngir sànk leen, war ngeen a tiit” - faf loolu yokk leen ngëm - ñu toontu ne : “Yàlla doy nanu te Mooy ngën gi wéeruwaay”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Ñu dellu ñibbi ànd ak xéewalug Yàlla. Te dara lu bon daluleen, topp nañu lu neex Yàlla. Te Yàlla boroom ngëneel yu màgg la.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
[Xupp googu ñu leen di xupp] du dara lu dul jëfi Seytaane dafay tiitloo aw nitam. Buleen leen ragal. Ragal-leen Ma, ndeem ñu gëm ngeen.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Ñay njëkkante di tàbbi cig weddi, bumu la naqari. Duñu wàññi Yàlla dara. Yàlla dafa bañ rekk ñu am cër ca àllaaxira. Te am fa mbugal mu rëy.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Ñiy weccee ngëm ak kéefar, duñu wàññi Yàlla dara. Te am nañu mbugal mu metti.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Ña weddi, buñu foog ne la ñu leen yéex a mbugal lu baax la ci ñoom. Danu leen di yeexe ngir ñu dolliku bàkkaar doŋŋ te danañu am mbugalum toroxtaange.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
Yàlla du bàyyi ñi gëm ci li ngeen nekk ba kerook ba Muy téqale ku bon ka ak ku baax ka. Te it Yàlla duleen xamal kumpa. Waaye Yàlla dana tànn ku ko soob ciy Yonentam [xamal ko kumpa]. Gëmleen Yàlla ak i Yonentam. Su ngeen gëmee te ragal Yàlla, dangeen am pey gu màgg.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
Ña nay a [joxe] ca la leen Yàlla may ciy ngënéelam, buñu foog ne lu baax la ci ñoom. Déet ! lu bon la ci ñoom : [la ñu nayoon ci joxe ko] danañu leen ko wékkal ci seeni loos Bis- pénc ba. Yàllaa moom donoy asamaan yeek suuf si. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Yàlla dégg na waxi ña naan : “Yàlla ku ñàkk la te nun danoo woomal”. [Nun Yàlla] dananu bind la Nu wax, ak rey ga ñu rey Yonent ya ci lu dul dëgg. Te dananu leen wax : “Toqamtikuleen mbugal muy lakke.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Loolu, ngir la seeni yoxo jëf [ci lu bon] ! ”. Te Yàlla du tooñ jaamam ña.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Yàlla dégg na ña wax ne : “Yàlla kóllarante na ak nun, te ne duñu gëm benn Yonent li feek indilunu yool boo xam ne safaraa koy lekk”. - Neel : “Ay Yonent dikkaloon na leen jiitu ma, indiwaale woon lay yu leer nàññ ak la ngeen laaj. Su fekkee ñu dëggu ngeen, lu tax ngeen rey leen” ?
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Suñu la weddee, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu. Indi woon nañu ay lay yu leer ak [Zabuur] ak Téere bu leer.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Bakkan bu nekk dana tàqamtiku [mos] dee. Waaye dangeen jot seen pey ca Bis-pénc ba. Ku ñu soreel Safara ba, dugal ko Àjjana, texe na. Te dundug àddina gi du dara lu dul xéewal guy naxe [naxti ndaw].
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Fàwwu dees na leen nattu ci seeni alal ak ci seeni bakkan ; dangeen dégge ca ñoñ-téere ya leen jiitu woon ak bokkaalekat ya, wax yu ñaaw yu bari.Waaye, bu ngeen muñee te ragal Yàlla... mooy sabab duggu gay tax mbir ya sotti.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
[Fàttalikul] ba Yàlla kóllaranteek ña jot Téere, ne : “Nangeen ko leeralal nit ñi te buleen ko nëbb”. Ñu sànni ko ca seen ginnaaw, jaaye ko njëg gu néew. Ndax njëg gu bon !
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Bul foog ne ñay bég ca la ñu def, te bëgg ku leen tëgg ci lu ñu deful, buleen foog mukk ne danañu mucc ci mbugal. Déedéet, mbugal mu metti lañuy am !
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Yàllaa moom asamaan yeek suuf si. Te Yàlla mën na lu ne.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Sàkk gi Yàlla sàkk asamaan yeek suuf si, ak ni guddi gi ak bëccëg gi di jëlasantee, ay kéemaan yu rëy a ngi ci ñeel woroom xel ya,
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
[Woroom xel yooyu gëm], ñooy ñay tuddu Yàlla, bu ñu toogee ak bu ñu taxawee, ak bu ñu tëddee, tey xalaat ci sàkkug asamaan yeek suuf si, [di wax naan] : “Yaw sunu Boroom ! Sàkkuloo lii ci neen. Tuddu naa sag sell ! Yal na nga nu fegal mbugalum Safara.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Yaw sunu Boroom ! Koo tàbbal Safara, gàcceel nga ko de. Te tooñkat ya, duñu am ndimbal !
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Yaw sunu Boroom ! Nun dey dégg nanu kuy woote naan : “Gëmleen seen Boroom”, nu daldi gëm. Yaw sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar, te soppil nu sunuy ñaawtéef mu di aw yiw, te boo nuy rey, nga boole nu ak gaa yu baax ya.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Yaw sunu Boroom ! yal nanga nu jox la nga nu digoon, te jaarale woon ko ca sa Yonent ya. Te bul nu gàcceel kera Bis-pénc ba. Yaw Yàlla, doo wuute ab dige de”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Yàlla seen Boroom nungul na leen seeni jëf, ne : “ Man de, duma sànk jëfi ab jëfkat ci neen, moo xam góor la mbaa muy jigéen. Moo xam ñi leen beru walla ñu lor leen ci yoonu Yàlla, ñu reye ñu rey leen. Gaa ñooña Dananu leen soppil seeni ñaawtéef aw yiw te Danaa leen dëkkal Àjjana joo xam ne dex yaa ngay daw ca seen ron, muy yool bu bawoo fa Yàlla.”. Te Yàllaa rafet ab yool.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Alal ju bari ja yéefar yi di wëlbati ci réew yi, bumu la nax.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Xéewal yu néew la ! Topp seenug delluwaay di Safara. Ndaw delluwaay bu ñaaw !
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Waaye ña ragal seen Boroom, am nañu Àjjana joo xam ne dex yaa ngay daw ca seen ron, ñu béel fa, muy seen wàccuwaay fa Yàlla. Te la nekk fa Yàlla mooy dàqal ñu baax ña.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Am na ci ña jot Téere, ñu gëm Yàlla ak la ñu wàcce ci yéen, ak la ñu wàcce ca ñoom. Dañuy toroxlul Yàlla, duñu jaay laayay Yàlla ci njëg gu néew. Ñooña am nañu seenug pey fa Yàlla te Yàlla ku gaaw la ci waññ [jëfi nit ñi].
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen di muñ ci bànneex, nangeen di muñ it [ci aw naqar]. Te itam nangeen di fagaru, te itam ragal-leen Yàlla ndax Yàlla ngeen texe !

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers