Simoore Al-Qasas
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Qasas pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Qasas pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Qasas Tekki. Al-Qasas (Meccan) 88 Aaya.
Related
- Al-Qasas TekkiWolof
- Al-Qasas mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Qasas

ﮝﮞ
Taa, Siin, Miim.
ﮟﮠﮡﮢﮣ
Lii mooy laayay Téere ba Nu biral.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Dananu la nettali ci xibaari Muusaa ak Frhawna ci dëgg, muy lu ñeel aw nit ñu gëm.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Firawna dadoon kawe-kawelu ci suuf si ; féewale waa réew ma, di jaamuloo ab kurél ci ñoom : ak a réndi seeni doom yu góor, di bàyyi jigéen ña. Moom Firawna yàqkat la woon.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Nun Yàlla nammoom Nanoo dooleel ña néewoon doole ca réew ma, Nu bëgg leen a def ay njiit, def itam [ñu mujj fa],
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
may leen kàttan, ak it wonaale Firawna ak Haamaan ak seeni gàngoor la ñu daan moytandiku.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Soloo Nanu yaayu Muusaa ne ko : “Nàmpal ko. Te soo tiitee ciy mbiram, sànni ko ci dex gi. Bul ragal, bul jàq : Dananu la ko delloosil mu bokk ca Yonent ya”.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Waa kër Firawna for ko, ngir mu doon seenub noon, di seenu lëjal ! Firawna, Haamaan ak seen gàngoor juumoon nañu.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Jabari Firawna ne ko : “(Xale bii di Muusaa) ! buleen ko rey. Nanu ko wéttalikoo maak yaw walla nu doomoo ko, amaana mu jariñ nu”. Lii lépp nag ba muy xew yëguñu ca dara.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Xolub ndeyu Muusaa ja jeex na tàkk. Ba mu xaw a feeñal, cëy bu Nu ko dëfëlul woon xolam ak la mu doonoon di ab jullit.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Mu wax mbokkam mu jigéen ma ne ko : “Topp ko” ; mu di ko bàyyi xel, topp ko te kenn xamut.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Noo ko bañloo woon nàmpalkat ya. Ba mbokkam mu jigéen ma agsee, daldi wax ne : “Ndax duma leen tegtal waa kër goo xam ne danañu leen ko yaral te di ko toppatoo ? ”...
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Nu daldi koy delloo ndeyam ja ngir mu wéttaliku ba bañ a tiit ak it ngir mu xam ne digub Yàlla lu dëggu la. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Ba mu matee sëkk te ñor xomm, [Muusaa] jox Nanu ko àtte ya ak xam-xam. Noonu la Nuy feye rafetalkat yi.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Mu dugg ca dëkk ba te yëguñu ko ; mu fekk fa ñaari gaay yuy xeex, kenn ka bokkoon ci ay farandoon, ka ca des bokkoon ci ay noonam. Muusaa daldi koy dóor mbëkk mu dee. - Mu daldi wax ne : “Lii dey ci liggéeyub Séytaane la bokk. Ab noon la buy sànke bu bir”.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, man dey tooñ naa sama bopp ; jéggal ma”. Mu daldi koy jéggal. Moom Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la !
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Mu daldi ne : “Yaw sama Boroom, xéewal gi nga ma xéewale tax na duma dimbali mukk tooñkat yi”.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Mu nekk ca dëkk ba tiit lool di moytu, jekki-jekki rekk waa ja ko doon ñaan ndimbal sàkkooti na ca moom ndimbal. Muusaa ne ko : “Yaw daal jalaasa nga, di ku tafaar”.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Ba mu bëggee lottal ka doon seen noon ba, mu ne ko : "Waaw yaw Muusaa, ndax danga maa bëgg a rey ni nga reyee woon démb bakkan ? Yaw kay dangaa bëgg a doon ku të ci réew mi ; waaye bëggoo bokk ca ñay yéwénal”.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Mu am waa ju bawoo ca aanéeri dëkk ba di dox, dikk ne ko : “Kilifay dëkk yaa ngi takktoo ngir rey la. Génnal (dëkk bi). Man dama lay laabire”.
ﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓ
Mu génne ca [dëkk] ba, tiit lool di moytu. Daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, maa ngi sàkku nga musal ma ci tooñkat yi ! ”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Ba mu jubloo njëlal Madiyaana, wax na ne : “Amaana sama Boroom gindi ma, teg ma ci yoon wu jub wa”.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Ba mu agsee ca rootukaayub waa Madiyaana, mu fekk fa aw nit ñuy wëgg di jukki, mu fekk fa ba-tey ñaari jigéen ñu beru wëgguñu. Mu ne leen : “Lu xew ba wëgguleen ? ” Ñu ne ko : “Dunu wëgg lu dul ginnaaw ba sàmm si génnee ba dem ; te sunu baay màggat na”.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Mu wëggal leen ba eggal, dem toog ca ker ga, daldi ne : “Sama Boroom, cëy aka maa ittewoo li nga may wërsëgale”.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Kenn ca ñaari xale yu jigéen ña dikk fa moom ak kersa ga, daldi ne ko : “Saa baay nee na nga ñëw mu fey la li nga nu wëggaloon”. Ba Muusaa agsee ba nettali ko xew-xew ba, mu ne ko : “Bul tiit : mucc nga ci tooñkat ya”.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Kenn ca ñaari jigéen ña ne ko : “Baay jàpp ko surga, koy dey nga am surga bu am doole te wóor”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Mu ne ko : “Dama laa bëgg may kenn ci sama ñaari doom yu jigéen yii ci nga doon sama surga juróom-ñetti at. Soo ko matalee fukk nag, ci sa coobare lay doon ; ndax man bëgguma laa teg coono. Te bu soobee Yàlla, danga xam ne nit ku yiw laa”.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Mu daldi ne : “Loolu sama diggante la ak yaw. Ñaar ñépp a yem ci man, duma la bunduxataal mukk. Te lii nuy wax Yàllaa di seede si”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Ba Muusaa matalee dig ba, màng njabootam di ñibbi, gis na safara ci wàllug ndeyjooru tundu doju Tuur wa. Mu ne leen : “Xaarleen ma fii, li ma séen aw safara la. Amaana ma indil leen ci xibaar walla ay xal ngir ngeen mën caa jaaroo”.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Ba mu fa agsee, mu am lu ko woo ci xuru ndeyjoor wa, ne ko : “Éy Muusaa ! ManMii Maa di Yàlla jiy Boroom àddina si yépp”.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Te : “Nanga sànni sa yet wi” ; [Ba mu ko sànnee] gis ne ma ngay yëngatu mel ni jaan, mu ne baxarñit.”. Yàlla woowaat ko, ne ko : “Dellusil te bul tiit : yaa ngi ci lu wóor”.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Sóobal sa loxo ci sa mbagg, dina génn weex tàll. Te nanga taf sa loxo bi ci sa kaw ngir bañ a tiit. Yooyu yaari mbir ay firnde la yu bawoo ca sa Boroom Mu jëme ko ci Firawna ak gàngooram. Ñoom ay saay-saay lañu”.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
[Muusaa wax na ne] : “Rey naa ci ñoom bakkan te ragal naa ñu rey ma.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Te Aaruuna moo ma gën a leer i wax. Yebal ko mu ànd ak man di ma ruqandi, di ma dëggal : man daal ragal naa ñu jàppe ma fenkat”.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
[Yàlla] ne ko : “Dananu dëgërale sa përëg ci sa mbokk mi, Dananu leen defal ay firnde [doole joo xam ne dana mën a agsi ci yéen] ak Sunuy kéemaan. Yéen ñaar ñépp ak ña leen topp yéen ay not.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ba leen Muusaa dikkee, indil leen Sunuy kàddu yu leer ñàññ, wax nañu ne : “Lii daal du lenn du dul ag njibar gu ñu sos, te sax nun lii mësunu leen woon a dégg ca sunuy maam”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Muusaa ne leen : “Sama Boroom moo gën a xam ana kaan moo indi dëgg te jóge fa Moom, ak kan mooy ëppug mujj. Tooñkat ya duñu texe de”.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Firawna daldi wax ne : "Éy yéen kilifa yi, xamaluma leen jeneen Yàlla ju dul man. Yaw Haamaan, taalal ma aw safara ci ban bi te tabaxal ma ag tóoj ndax ma mën cee yërndu Yàllay Muusaa ji. Te man sax njortu naa ne ci fenkat yi la bokk”.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Muy rëy-rëylu mook i xarekatam ci réew mi ci lu dul dëgg. Ñu foogoon ne duñu dellusi ci Nun.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Nu jël ko mook i xarekatam nargan leen ca ndox ma. Xoolal mujjug tooñkat ya.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Defoon Nanu leen ay njiit yuy woote jëme Safara. Te bu Bis-pénc baa kenn duleen dimbali.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Nu toqal leen am rëbb ci àddina sii. Te bu Bis-pénc baa dañuy bokk ca ña ñuy siibiibal.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Jox Nanu Muusaa Téere ba, - ca ginnaaw ba Nu faagaagalee maas ya ko jiitu, - ngir mu doon am njis ak njub, ak yërmaande ak it ngir ñu mën caa fàttalikoo.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Te yaw [Muhammad], nekkoo woon ca xuru sowwu wa ca ba Nuy jox Muusaa ndigal ya: te fekkewoo ko woon [seede ko].
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Waaye sosoon Nanu ay maas yu guddu na fan. Te it nekkoo woon ca waa Madiyaana di leen nettali Sunuy kàddu; waaye Nun [Yàlla], Noo daan yable.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Nekkoo woon it wetu Tuur jamono ja Nuy woote. [Waaye dangaa dikk di] yërmaandey sa Boroom, ak it ngir nga xupp aw nit ñoo xam ne mësuñoo am ab xuppekat ci la ko jiitu, ndax it ñu mën caa fàttalikoo.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Bu fekkoon ne musaba da leen dale ca la ñu daan jëf ci seeni yoxo, kon dey danañu wax naan : “Yaw sunu Boroom, lu tax yónni woo ci nun ab Yonent ? [Soo ko defoon dey], dinanu topp say ndigal te it dananu gëm doon ay jullit”.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Ba leen dëgg ga dikkalee bawoo fi Nun, ñuy wax naan : “Cëy bu nu amoon la ñu joxoon Muusaa ! ”. [Kon ñoom], ndax weddiwuñu woon bu jëkk la Nu joxoon Muusaa ? Te daan wax naan : “Ñaar ñii daal ay jibarkat lañu yuy jàppalante ! ”. Tey wax naan : “Weddi nanu leen ñoom ñépp”.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Neel : “Indileen ab Téere bu jóge ca Yàlla bu leen gën a mën a jubbanti, [su ngeen ko indee] kon danaa ko topp, su ngeen waxee dëgg ”.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Bu ñu la wuyuwul nag, xamal ne seen bakkan lañuy topp. Te ana kan moo gën a sànku ci kuy topp bakkanam ci lu àndul ak njub ga bawoo ca Yàlla [Lislaam]? Yàlla du gindi aw nit yuy tooñ.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Jottali Nanu leen wax jii [Alxuraan] ngir ñu fàttaliku ca.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Ña nga xam ne joxoon Nanu leen Téere lu jiitu Alxuraan, gëm nañu ko.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Te bunu leen ko mësaan a jàngal, dañu daan wax ne : “Gëm nanu ko. Te mooy dëgg ga jóge ca sunu Boroom. Faf nun jébbalu nanu ba mu laataa na ñëw”.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Ñooña danañu seen pey ñaari yoon ca la ñu daan muñ, daan toontoo aw ñaawtéef ak lu rafet, te di joxe ca la Ma leen wërsëgal ;
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
te saa yu ñu déggee ay caaxaan, dummóoyu ko tey wax naan : “Nun ak sunuy jëf, yéen ak séeni jëf. Yal na ngeen am jàmm. Nun dey, dunu sàkkuji mukk ñu réer ña”.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Yaw (Muhammad) du ut ne yaay gindi ku la soob : waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob. Te moo gën a xam ñiy gindiku.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ñuy wax naan : “Su nu toppee njub gi ànd ak yaw, kon deef nanu foqarñee ci sunu suuf si”. - Ndax defalunu leen woon am réew wuñu wormaal, ñuy jëmmal wépp xeetu meññeef muy bawoo ci Nun [Yàlla] ? Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Aka bari dëkk bu Nu faagaagal ci sababus seenug weddi te ñu daan dunde xéewal, ca seen kër ya lu néew la, te keneen dëkkee seen ginnaaw, Nun Yàlla noo doon donnale.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Yàlla du faagaagal yenn dëkk ndare du dafa yebal ab Yonent ca dëkk ba fa gën a rëy, mu di leen nettali ay kàddoom. Te Nun Yàlla dunu faagaagal ay dëkk lu dul ne dañuy tooñ.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Lii Nu leen jox, bànneexu dundug àddina [doŋŋ la], te la nekk fa Yàlla moo gën a des ... Moo ndax dangeen dul xel-lu ?
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Moo ndax ka Nu digoon dig bu rafet te mu dajeek moom, dana mel ni ka Nu bànneexaloon ca àddina ak ug dundam, bu ñu leen teewalee ca seen kanamu Boroom.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Bu keroogee ba mu di leen woon, naan leen : “Ana ka ngeen Ma doon bokkaaleel ? ”
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Ña wax ja dal ci seen kaw daldi ne : “Yaw sunu Boroom, ñii ñoo nu fàbbiwoon ni ñu fàbbikoo woon. Deñ nanu ci ñoom ci sa kanam : ñii daal jaamuwuñu nu woon”.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Nu wax ne : “Wooleen seen bokkaale ya”. Ñu woo leen, waaye wuyyuwuñu leen. Gis nañu mbugal ma, cëy bu ñu gindiku woon.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Bu keroogee bis ba Mu leen di woo naan leen : “Ana lan ngeen tontu woon Yonent ya ? ”
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Seeni firnde jaxasoo, bu boobaa [dañu naa xuum] dootuñu laajante.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Képp ku ca tuub te gëm te jëf u yiw, amaana mu texe.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Te sa Boroom mooy sàkk lu ko soob te neex ko ; ñoom amuñu coppan. Tudd naa sellug Yàlla ! Te kawe na lool ci la ñuy bokkaale !
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Te it sa Boroom a xam li seeni xol nëbb ak li ñuy feeñal.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Te Moom mooy Yàlla te amul jeneen yàlla ju dul Moom. Moo moom xeeti cant yépp cig njalbéen ba cig mujj. Te Moo moom àtte ya. Te ca Moom lañu di delloo ñépp.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Neel : “Xanaa gisuleen ne bu Yàlla defoon guddi gi muy lu sax ba Bis-pénc ba, ana jan yàlla ju dul Moom moo leen di indil ag leer ? Moo ndax dungeen dégg ? ”
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Neel : “Xanaa gisuleen ne bu Yàlla ci yéen bëccëg muy lu sax ba Bis-pénc ba, ana jan yàlla ju dul Moom moo leen di indil guddi gu ngeen di dalloo ? Moo ndax dangeen dul gis ? ”
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Ci yërmaandeem la leen defalee guddeek bëccëg ngir ngeen di ca dal ak a sàkku wërsëg, ak it ngir sant Ko.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Ak bis ba Mu leen di woo naan leen : “Ana ña ngeen Ma doon bokkaaleel ? ”
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Nu rocci ci xeet wu nekk seede, daldi ne leen : “Indileen seeni firnde”. Ñu daldi xam ne dëgg Yàllaa ko moom ; la ñu daan sos réer leen.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
[Bir na ne], Xaaruuna ci nitu Muusaa la bokkoon, waaye dafa bewoon. Joxoon Nanu ko ci ay ndàmb, loo xam ne, bu ñu lewaa caabi ya mu diis gann ay ponkal. Fàttalikul ba ko ay nitam waxee ne ko : “Bul rëy-rëylu. Yàlla safoowul ñuy rëy-rëylu.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Li la Yàlla jox, sàkku ci kërug àllaaxira [Àjjana]. Te bul fàtte sa wàll ci àdduna. Te nangay rafetal kem ni Yàlla di rafetale jëme ci yaw. Bul di sàkku ag yàq ci suuf si. Ndax Yàlla dey safoowul yàqkat yi”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Xaaruuna wax ne : “Lii ci sama xam-xam laa ko ame”. Xanaa moom dafa xamul ña Yàlla faagaagal ca maas ya ko jiitu, ña ko gënoon a ñàng ëpp ko fuuf dooleek alal ? Te tooñkat ña deefuleen laaj seen bàkkaar !
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Mu génn ca nitam ña, ànd ak alalam ja. Ñi bëgg dundu àddina wax ne : “Aka neexoon nu am lii Xaaruuna am. Moom dey boroom cër bu duun na”.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Ña am xam-xam ne leen : “Toskare ngeen ! Yoolub Yàllaa gënal képp ku gëm tey jëf u yiw”. Ku dul muñkat du ko am.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Nu mëdd ko ci biir suuf si mook kërëm ga. Amul kenn ku ko mënoon a dimbali ku dul Yàlla, te it kenn dimbaliwu ko woon.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ba ñu xëyee, ña doon xemmem wàccuwaayam ca démb sa, daldi wax ne : “Dafa mel ni Yàlla dana tàbbalal wërsëg ku ko neex, ci jaamam yi. Bu dul kon ak xéewalam, kon dey mëddoon Nanu. Te it yéefar yi duñu texe”.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Góogale mooy kër gu mujj ga, Dananu ko defal ñi bëggul a kawe-kawelu ci suuf si, te duñu yàq. Ña ragal Yàlla tey moytandiku ñooy ëppug mujj.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
[Amul lu ñu bàyyi fii], Ku dikk ak i ñaawtéef, [na xam ne] ñay jëf ñaawtéef, la ñu daan def rekk la ñu leen di feye.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
[Yàlla] mi wàcce Alxuraan ci yaw, Moo lay delloo fa Màkka. Neel : “Sama Boroom moo gën a xaw kuy indi dëgg ak kuy nekk ci réer gu bir.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Musuloo yaakaar ne dees na la jox Téere ba. Lu dul ne yërmaande ju bawoo ca sa Boroom. Te bul dimbali mukk yéefar yi ;
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
te it buñu la fàbbi mukk ci kàdduy Yàlla ginnaaw ba Nu ko wàccee ci yaw. Nangay woote jëme ci sa Boroom te bul bokk ca way-bokkaale ña.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Bul woo jeneen yàlla di ko booleek Yàlla. Amul jenn yàlla ju dul Moom. Lu nekk a faagaagalu ba mu des Moom. [Yàlla] mooy boroom àtte yi te ca Moom ngeen di dellu.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







