Simoore An-Nisa
176 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Éy yéen nit ni ! Ragal-leen Yàlla mi leen sàkk ci benn bakkan, sàkke itam soxnaam sa, njërtal ci aw góor ak jigéen ñu bari. Ragal-leen Yàlla ji ngeen di laajante, ak ug dog mbokk. Yàlla nag ku leen di fuglu la.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Te ngeen jox jirim yi seeni alal ; te buleen wecce lu baax [ca la ñu moom] joxe lu bon la. Buleen lekk la ñu am ci alal di ko booleek seeni alal : ndax loolu bàkkaar bu rëy la.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Su ngeen ragale bañ a maandu [ci seen jëflante ak jirim yi]..., mën ngeen takk lu leen neex te soob leen ciw jigéen, ñaar-ñaar, ñett ñett, ak ñeent ñeent, waaye, bu ngeen ragale ci ne dungeen maandu [ñàkk a yemale soxna ya], kon takkleen benn soxna walla sax ngeen jël benn jigéen [jaam bu jigéen]. Ndax loolu moo gën a jege maandute.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Nangeen jox jigéen ñi seen can mu dig may. Bu ñu leen ca yéwénalee dara te may leen ca dara te mu di ci teeyu bakkan, lekkleen ko na mu leen neexe.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Te ña seeni xel matadi, buleen joxandoo seen alal jépp ja Yàlla def ngeen di ko sàmm. Nangeen leen cay mosal [kem seeni soxla]. Deeleen ca wutal aw dund [lu ñu sol ci yére] ; te ngeen di wax ak ñoom ci njekk.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
Nangeen di dayu jirim ba ñuy mat a séy ; su ngeen nemmekoo ci ñoom njub, joxleen leen seen alal. Buleen ko lekk, yàqte ko, di ko pasar-pasaree te fekk màggaguñu. Ku ca yore te woomal, na fegu . Ku ca yore te néew doole, na ca lekke nu jaadu : su ngeen leen di delloo seeni alal, nangeen wut seede. Yàlla doy na, mat sëkk ab waññikat.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Góor ñi am nañu cër ci la seen ñaari waajur ak seeni jigeñaale bàyyee ginnaaw ; jigéen ñi it am nañu cër ci la seen ñaari waajur ak seeni jigeñaale bàyyee ginnaaw, mu néew walla mu bari : cër boobu lu ñu farataal la. [Ndonu]
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Bu ay mbokk fekkee séddale ba, ak i jirim walla way-ñàkk, nangeen leen ca jox, te wax ak ñoon waxi njekk [ju rafet].
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
War nañoo tiit ña nga xam ne bu ñu bàyyi woon seen ginnaaw njaboot gu sew, danañu am njàqare ci ñoom ; nañu ragal Yàlla [ci alali jirim] te nañu wax wax ju jub.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Ña nga xam ne dañuy lekk alali jirim ci ag tooñ, nañu xam ne seeni biir yooyu lekkuñu ca lu dul safara. Te dees na leen séndal ca Safara.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Yàllaa ngi leen di dénku ci seeni doom ne : ku góor, cëram na toll ni cëru ñaari jigéen. Ñoom jigéen ña, bu ñu ëppee ñaar, te amuñu mag walla rakk ju góor, seen cër day nekk ñaari ñetteeli alal ja. Bu dee kenn ku jigéen doŋŋ nag, cëram day nekk genn-wàllu alal ja. Ñaari waajur nag ñoom, ku ca nekk ay am juróom-benneel la seen doom bàyyi. Bu amut doom ju góor, ay waajuram rekk a koy donn, yaayam day jot ñetteelu alal ja, baay ba jot ñaari netteel ya des. Bu amee rakk walla mag ju góor, yaayam juróom-benneelu alal ja lay jël, ginnaaw ba ñu génnee ndénkaan ya mu dénkaane woon walla bor ya. Seeni baay ak seeni doom, xamuleen kan moo leen ci ëppal njariñ. Ndigal luy farata la, bawoo fa Yàlla, te Yàlla ku xam la, Ku xereñ la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
La seeni jabar bàyyi ginnaaw, am ngeen ca génn-wàll ndagam amuñu doom ju góor. Su amee doom ju góor, kon ñetteelu alal ja la jëkkër ja di jël ginnaaw bi ñu génnee ndénkaane ya mu génne woon, walla peyum bor [su amee]. Ñoom seeni jabar am nañu ñetteelu la seen jëkkër bàyyi ndegam amul doom ju góor, su amee doom ju góor [jëkkër ja], kon juróom- ñetteelu alal ja lay jël ginnaaw ba ñu génnee ndénkaane ya mu dénkaane woon walla bor. Bu fekkee ne góor walla jigéen mooy donn ab càppaacóli [ku amul doom, amul waajur] bu am rakk walla mag ju góor walla ju jigéen, ku mu ca doon ci ñoom ñaar juróom-benneelu alal ja lay jël. Bu ñu ëppee kenn nit, dañuy bokk donn ñetteelu alal ja ginnaaw bu ñu génnee ndénkaane ya mu dénkaane woon walla bor yu àndul ak lor [way-dono ya]. Lii dénkaane la lu bawoo fa Yàlla ! Te Yàlla ku xam la, Ku lewet la.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Loolu mooy deytali Yàlla yi. Ku ko topp ak ub Yonentam [ca la mu àtte], danañu ko dugal Àjjana joo xam ne dex ya dañuy daw ca ronam, ñu béel fa [sax ba fàwwu]. Loolu mooy texe gu mag ga.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Ku moy Yàlla ak ub Yonentam, di jéggi daytali Yàlla yi, Danañu ko dugal Safara, mu béel fa, bokk ca mbugal muy toroxale.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Ña def ñaawtéef [njaaloo] ci seeni jigéen, nangeen ko seedeloo ñeenti nit ci yéen. Bu ñu ko seedee, nangeen leen tëj ba dee fekk leen fa walla ba Yàlla ubbil leen aw yoon [wu ñu mën a aw ba mucc].
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Ña nga xam ne loolu dal na leen ci yéen [góor ña], nangeen leen tas. Bu ñu tuubee, wëlbëtiku di def lu baax, nangeen leen bàyyi. Naka Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Yàlla rekk ay nangu tuub, ña def ñaawtéef ci ñàkk a xam, te gaaw daldi tuub. Ñooña Yàlla dana nangu seen tuub. Yàlla Aji-xam la, Aji-xereñ la.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Ña dul am njéggal ñooy ña def ñaawtéef [te baluwuñu seen Boroom] ba dee dikkal kenn ca ñoom muy door a wax ne : “Léegi tuub naa” - ak ña nga xam ne dañuy dee ci kéefar. Ñooña, danañu leen xaaroo mbugal mu tar [metti].
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Éy yéen ñi gëm ! Daganul ci yéen ngeen di donn jigéen ña ci nooteel. Daganul it ngeen gàllankoor leen, ne buñu sëy ngir bëgg nangu lenn ci li ngeen leen joxoon, lu dul ña cay def ñaawtéef wu bir. Nangeen di ànd ak ñoom ci njekk. Bu ngeen leen sibee nag, [xamleen ne] mën ngeen a sib [bañ] lenn te fekk na Yàlla def ca loola yiw wu bari.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Bu ngeen bëggee bàyyi jabar wuutale ko ak jeneen jabar, te fekk joxoon ngeen ko alal, buleen ca nangu dara. Doonte la [barigo]wurus la ! Ndax lu ngeen ca jële ci tooñeel la ak bàkkaar bu bari.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Naka ngeen di nangoo alal ja, te jokkoo ngeen ba noppi te ñoom ñu fasanteek yéen kóllare gu dëgër?
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Buleen takk ña seeni baay takkoon ca jigéen ña, ginnaaw la wéy ba noppi. Loolu lu ñaaw la, te luy waral mbugal la, yoon wu dëng la !
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Araam na ci yéen [takk jabar] seeni ndey, seeni doom yu jigéen, seeni mag walla rakk yu jigéen, seeni bàjjen, seeni mag walla rakki yaay, seeni doomi mag walla rakk ju góor, seeni ndey ya leen nàmpal, seeni jigéen ya ngeen bokk ku leen nàmpal, seeni yaayi jabar ak seeni doomi jabar, ya ngeen yor ca seeni kiiraay, ndegam jot ngeen a xaraf [jote] ak seeni ndey ; bu ngeen jotul a xaraf ak seeni ndey, aayul ngeen sëy ak ñoom ; [araam na it ci yéen seeni jabari doomi ña ngeen bokk ndey ak baay, walla ndey rekk walla baay rek] ginnaaw la weesu [lu jiitu Lislaam]. Yàlla ab Jéggalaakoon la [ca loola weesu], di Jaglewaakoon ;
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
[araam na it ci yéen] jigéen ña saŋewu, ba mu des jebéer ya ngeen moom. Ndigalu Yàllaa ngoogu ci yéen ! Ginnaaw ñooña, [ña mu lim ciy jigéen ñu daganul ngeen sëy ak ñoom]. Dagan na ngeen saŋewu cig jigéen te joxe seeni alal, di way-sëy ak ñoom, bañ di way-njaaloo. Te jigéen ña ngeen sàkku bànneexu ci ñoom, nangeen leen jox seeni can. Lii mbir mu Yàlla santaane la [farataal]. Aayul ginnaaw la ñu farataal nag ngeen déggoo [ci li ngeen war a joxe]. Yàlla de Moom Ku xam la, Ku xereñ la.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Ku amul can ci yéen, gu mu mën a takke jabar ju nekk gor te di jullit, na takk kon ci jebéer ya di ay jullit di xale yu jigéen ya bokk ci yéen. Yàllaa gën a xam fa seen gëm toll, ndax yéen a mëññante [jurante]. Nangeen leen takk ci ndigalu seeni kilifa te ngeen jox leen seeni can ci njekk ; ngeen di way-sëy, di bañ di way-njaaloo, te bañ leen a jàppe ay coro cig nëbbu. Bu ñu sëyee te def njaaloo [ñoom jebéer ya], war nañu leen a teg genn-wàllu mbugal ma ñuy teg gor gu jigéen. Loolu ndigal la ci ku ñu ragal mu njaaloo ci yéen ; bu ngeen mënee muñ, moo gën ci yéen. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Yàlla dafa namm a leeral [àtteem] ci gindi leen, teg leen ca yoonu ña leen jiitu woon, te jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la [ci àtteem].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Yàlla dafa leen bëgg a jéggal. Waaye ña topp seen bànneex, ñoom dañuy bëgg ngeen jeng, jeng gu fés.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Yàlla dafa leen a bëgg a woyofal [àtteem] ndax néew doole ak lott gi nit bindoo.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen lekkante seeni alal cig neen. Waaye mën ngeen a jëflante ci njulo [jënd ak jaay] mu ànd ak déggoo ci seen mbir. Te buleen reyante. Yàlla, Ku am yërmaande ci yéen la.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Ku def loolu, ci ndëngte ak ug tooñ, Dananu ko séndal Safara, te loolu lu yomb la ca Yàlla.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Bu ngeen moytoo bàkkaar yu rëy yi ñu tere, Dananu leen baal seeni ñaawtéef [yu ndaw yi, soppil leen ko yiw], te Dananu leen tàbbal dëkkuwaay bu tedd (Àjjana).
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Buleen mébét li Yàlla yékkati ñenn ci kaw ñeneen ; góor ña am nañu cër [sañ] ca la ñu fàggu, jigéen ña it am nañu cër ca la ñu fàggu. Ñaanleen Yàlla ciy xéewalam. Yàlla lépp la xam.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Ku nekk leeral Nanu ko ña koy donn ca la waajur ya bàyyi ginnaaw, ak jegeñaale ya, te ña seeni dëelaante ak ñoom fasuwoon, nangeen leen jox seeni cër, Yàlla seede la ci lu nekk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Góor ñi, kilifa lañu ci jigéen ñi ndax la Yàlla yékkati ñenn ci ñoom ca kaw ñeneen ña, ak ngir la góor ña di dundale ci seeni alal [jigéen ña]. Waaye jigéen ñu sell ña, jaamukatu Yàlla lañu te ñu sàmmu lañu cig wéetaay ni ko Yàlla santaanee. Jigéen ña ngeen ragal ñu féttéerlu, nangeen leen waar, nangeen leen tong ca alal ya, nangeen leen dóor. Bu ñu leen nangoo topp, nangeen leen jàmmal, bañ leen defati dara, Yàlla dey Kawe na, Màgg na !
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Bu ngeen ragalee tàggoo ci diggante ñaar ñay sëy, nangeen yabal kilifag ku góor ki ak kilifag ku jigéen ki. Ndegam bëgg nañoo defaroo, Yàlla dana yéwénal seen diggante [Dëppële leen]. Yàlla Ku Xam la, Ku Deñ-kumpa la.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Nangeen jaamu Yàlla te bañ Koo bokkaale dara. Te ngeen rafetal ci seeni waajur, ak ci seeni jegeñaale, ak jirim yi, ak néew-ji-doole yi, ak seeni dëkkandoo ya di seeni mbokk, ak dëkkandoo ju sori, ak àndandoo ya, ak doxandeem , ak seeni jebéer, Yàlla du safoo kuy puukarewu ak a ndamu,
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Ña nga xam ne dañoo nay tey xiirtal nit ña ci nay, boole kook di nëbb lu leen Yàlla jox, baaxe leen ci wërsëg. [Nañu xam ne] Nun Yàlla dogu Nanu yéefar ya mbugal muy toroxale .
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Yàlla safoowul itam ñiy sànk seeni alal ngir ngistal, ci bëti nit ñi, te gëmuñu Yàlla ak Bis- pénc ba. Koo xam ne Séytaanee di àndandoom aka bon bon ub àndandoo !
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Waaw, lu Ma leen doon won su ñu gëmoon Yàlla ak Bis-pénc ba, tey joxe ca la leen Yàlla wërsëgal ? Yàllaa ka leen a xam.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Yàlla du tooñ kenn, lu toll ni pepp. Te ku def u yiw Mu ful ko, joxe ca pey [yool] gu màgg.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Naka mu ? [Bus bis-pénc baa,] ba Nu indi xeet wu nekk ànd ak seede te yaw [Muhammad], Nu indi la bu boobaa nga doon seede ci ñii [waa Màkka] ?
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Bis booba, ña weddi woon te toppuñu Yonent bi, danañu ngéeju ñu maasale leen ak suuf si te fekk na Yàlla moom kenn mënu Koo nëbb jenn wax.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen jege ag julli te fekk ngeen màndi, ba ba ngeen di xam li ngeen di wax, bu ngeen laabul ci sobe it [buleen jëm ci julli] te ame janaba - ndeem fekkuleen ci yoon di tukki – ba ba ngeen di sangu [farata]. Bu ngeen woppee, walla ngeen nekkati ci tukki, mbaa ngeen jóge wanag wa, walla ngeen joteek jigéen ña [sëy] te amuleen ndox [mu mën a jàpp walla sangu], nangeen tiim ci suuf su laab, ngeen raay seen xar-kanam ak seeni yoxo. Yàlla, Baalekat la, Jéggalaakoon la.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Moo ndax gisoo ña ñu joxoon lenni Téere ba, ñu jënd ñoom ag réer, ba noppi nag yéen ngeen réere yoon wu jub wa ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Yàllaa gën a xam seeni noon. Yàlla doy na te mat sëkk kilifa. Yàlla doy na te mat sëkk itam ndimbal.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Am na ci Yahuud yi ñuy firi baat [kàddu] jële leen ca barab ya ñu nekkoon, tey wax naan : “Dégg nanu waaye bañ nanu waay”, ñu naan : “Déggal te kenn du la dégg”, yàq waxin wa [Raahinaa], ñaawal ko ak bëgg a yàq diine. Waaye bu ñu ne woon : “Dégg nanu te nangu nanu”, “Déggal”, te “Xool nu”, kon mu gën ci ñoom, te mooy la gën a jub. Waaye Yàlla rëbb na leen [sorel yërmaandeem] ña weddi ; ñu néew ci ñoom ñoo gëm.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Éy yéen ñi jotoon Téere, gëmleen lii Nu wàcce, di dëggal li ngeen yor, bala Noo marmaral ay xar-kanam wëlbati leen ñu jëm ginnaaw, walla Nu leen di rëbbu na ñu rëbbe woon ña jalgati woon ca gaawu ba. Ndigalu Yàlla ak mbiram jëfe la sant [du jaas].
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Yàlla du baal ku Ko bokkaale dara. Waaye lu moy loolu, Dana ko jéggal ku ko soob. Ka bokkaale Yàlla [ak dara], def na bàkkaar bu rëy.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Moo ndax dangaa gisul ña doon sànkoo sellal seen bopp ? Li wér te wóor mooy Yàllaay sellal ku ko soob ; te duleen tooñ [Bis-pénc ba], lu toll ni karnu xooxu tàndarma.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Gisal ni ñuy duuralee Yàlla ay fen. Te loolu, doy na bàkkaar te rànniku !
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Moo ndax gisoo ña jot lenni Téere ba, ñay gëm ay xërëm yu tudd [Jibti] ak [Taagut], ñuy wax ak ña weddi naanleen: “Seen xërëm yooyoo gën a nekk ci njub jullit ya gëm [Lislaam]” ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Ñooñu Yàlla rëbb na leen ; te ku Yàlla rëbb, kenn mënu koo amal ndimbal.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Am dañuy am sañ-sañ ci nguur gi ? Te kenn du ca sédd nit ñi, lu toll ci mboxosu xooxu tàndarma.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Am dañuy iñaane nit ñi ci la leen Yàlla jox ciy ngënéelam ? Joxoon Nanu waa kër Ibraahiima ab Téere ak xam-xamu xereñe ; joxoon Nanu leen nguur gu rëy.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Amoon nañu ca ñoom ñu gëm [Téere ba], ak ñu dëddu [weddi Téere ba]. Te Safara dana leen doy.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Ña weddi Sunuy kàddu, Dananu leen mos a séndal. Aw Saafara, wow, saa su seen deri yaram ñoree, Nu wecceekook yeneen, ngir ñu yëg mbugal ma. Yàlla boroom kàttan la, Ku xereñ la!
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Ñi gëm tey def u yiw, Dananu leen dëkkal ci Àjjana yu dex ya di daw ci seen ron. Ñu béel fa [sax fàwwu]. Danañu fa am ay jabar yu laab. Dananu leen dugal ci ker yu dëll
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Yàlla digal na leen ngeen delloo ndénkaane ya seeni boroom, te bu ngeen dee àtte diggante nit ña, ngeen defe ko ci maandute. Mbir mii leen Yàlla di ñaaxe, ndaw lu baax ! Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Éy yéen ñi gëm ! Toppleen Yàlla, topp Yonent bi ak ña nekk kilifa ci seen biir. Bu ngeen dogoo walla [xëccoo] ci mbir, dellooleen ko ca Yàlla ak Yonent bi ndegam gëm ngeen Yàlla ak Bis-pénc ba. Looloo gën te moo gën a rafet déggin.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Ndax gisoo ña nga xam ne nee nañooy gëm nañu la ñu wàcce ci yaw ak la ñu wàcce woon mu jiitu la ? Te ña nga bëgg a àttewoo ci ay xërëm, te dañu koo waroon a weddi bàyyi ko. Waaye Séytaane moom bëgg leen a sànk, soreel leen dëgg.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Bu ñu leen waxee ne : “Ñëwleen ci li Yàlla wàcce ak ci Yonent bi”, nga gis naaféq ya dëddu ko.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Naka mu? Bu leen musiba dalee jóge ca la ñu jëf, ba tax ñu ñëw ci yaw di giñ ci Yàlla, naan : “Bëggunu woon lu dul rafetal ak juboo”.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ñooña, Yàlla xam na la nekk ci seeni xol. Nanga leen dëddu [dummóoyu] te nanga leen waar, waxleen ci seen bopp wax ju jotal.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Yónniwunu ab Yonent lu dul ne dañu koo war a topp ci ndigalu Yàlla. Te ñoom ba ñu tooñee seen bopp, bu ñu dikkoon ci yaw di sàkku jéggalu Yàlla, Yonent bi jéggalul leen, kon danañu fekk Yàlla mu di Jéggalaakoon, di Jaglewaakoon.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Mukk !... Giñ naa ci sa màggug Boroom ! Duñu gëm mukk [di ay jullit] li feek àtteloowuñu la la ca seen diggante te bañ a am benn ñag-ñagi xol ca la nga àtte, nangul la ak xol bu tàlli.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Su fekkoon ñoon Danu leen sant ñu reyante mbaa ñu génn seeni kër, duñu ko def lu dul ñu néew ci ñoom. Te su ñu defoon la ñu leen di waare, mu gën ca ñoom, te gën a dëgëral seen ngëm.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Te kon Nu jox leen pey gu màgg jóge ci Nun,
ﭵﭶﭷﭸ
te kon Nu gindi leen teg leen ca yoon wu jub xocc wa.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Ku topp Yàlla ak Yonent ba... ñooña ànd nañook ña Yàlla wàcce xéewalam ci ñoom : ca Yonent ya ak way-dëggu ña [daraja ju kawe sahaaba ya], ak ña dee ci xare ngir Yàlla, ak ñu sell [ñu yiw] ña, ndaw àndandoo yu jekk !
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Loolooy ngëneel la jóge ca Yàlla. Te Yàlla doy na, mat na sëkk boroom xam-xam.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen fagaru ci seen [coongum noon], moo xam ngeen tasaaroo walla ngeen àndandoo.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Te am na ci yéen kuy des-deslu ginnaaw ba lu metti dal leen, mu daldi wax ne : “Man Yàlla xéewal na ma ba ma àndul ak ñoom fekke loolee [dee ci xare]” ;
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
te bu ngeen amee ndam lu leen Yàlla jox, muy wax mel ni cofeel doxul seen digganteek ñoom, ne : “Aka neexoon ma ànd ak ñoom ba am ndam lu rëy a rëy [alal ja]”.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Ña jaay seen dundug àddina jënde ko àllaaxira, nañu xare ci yoonu Yàlla. Képp ku xare ci yoonu Yàlla ba dee ca, mbaa mu not kàddu ndam la, Dananu ko jox pey gu rëy.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Waaw yéen, lu leen nekkal ci bañ a xeex ci yoonu Yàlla [yiiraale] ñi néew doole ci góor, ak jigéen, ak xale yi? Ñoom ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom !Génne nu ci dëkk bii aw nitam diy tooñkat te nga boole nook ku nuy sàmm, jox nu ku nuy dimbali, ñoo tànnal sa bopp”.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Ñi gëm, ñi ngi xare ci yoonu Yàlla, ñi weddi di xare ci yoonu xërëm [taguut]. Xeexleen ak farandooy Séytaane, pexem Séytaane lu néew doole la.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Ndax gisoo ña nga xam ne waxoon nañu leen ne : “Téyeleen seeni yoxo, te ngeen farlu ci julli, tey génne asaka ! ” Te bu ñu leen digalee xare, ñenn ci ñoom ragal nit ña ni ñu ragalee Yàlla, walla sax ragal gu gën a tar, ñu naan : "Sunu Boroom ! Lu tax nga digle xare ci nun ? Lu teewoon nga yeexe nu ba beneen àpp bu jege ? ”. Neel : “Yóbbalu àddina lu néew la, te àllaaxira moo dàq ci ku ragal Yàlla. Te bu boobaa duñu leen tooñ lu toll ni karanu xooxu tàndarma.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Fu ngeen mën a nekk dey, dee dana leen fa fekk, doonte la dangeen a nekk ci tata yu ñoŋ. Te bu leen lu neex dikkalee, ñu ne : “Lii ci Yàlla la bawoo [jóge].”. Bu leen naqar dalee, ñu ne : “Lii ci yaw [Muhammad] la jóge.”. Neel : “Lépp ca Yàlla la jóge.” Waaw ana lu nekk ca ñooña nit ba xawuñoo déggati wax [ju am njariñ] ?
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚ
Lu la dal ci lu baax ma nga jóge ca Yàlla, lu bon lu la dal ci sa bakkan la jóge. Te yónni Nanu la [yaw Muhammad] nga di ab Yonent. Te Yàlla doy na seede ci lépp.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Képp ku topp Yonent ba topp na ndigalu Yàlla. Ku dummóoyu [weddi]... Xamal ne yónniwuñu la ci ñoom ngir nga di leen wattu.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Danañu wax ne : “Nangul nanu la ! ” Te bu ñu jóge ci yaw , ab kurél ci ñoom dana fanaanoo lu wuuteek la ñu la waxoon. Yàlla Dana bind la ñu fanaane. Nanga leen dëddu te nga wéeru ci Yàlla. Yàlla doy na ndëgërlaay .
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Moo ndax ñoom dañu dul settantal Alxuraan ? Alxuraan, bu jóge woon ci keneen ku dul Yàlla, fàwwu ñu gis ca ay juuyoo ciy waxam !
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Su leen mbir ma dikkale ci kóolute walla tiitaange, ñu siiwal ko. Te bu ñu ko delloo woon ca Yonent ba walla kilifa ya nekk ca ñoom, kon ña ko soloo xam ne ñoom danañu ca am lu leer bu dul woon ak xéewali Yàlla ak yërmaandeem ci yéen. Giñ naa ne kon lim bu néew ci yéen moo dul topp [Séytaane].
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Xareel ci yoonu Yàlla, sasewuñu la lu dul sa bopp, te nanga ñaax ñi gëm, amaana Yàlla fegal la ayu yéefar ya. Te Yàllaa gën a tar ngaañ, Moo gën a tar xorñoñal.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Képp ku taxawu nit [dooleel ko] taxawaay bu rafet, dana ca am cër ; ku taxawu nit [dooleel ko] cig ñaawtéef, dana ca am bàkkaar ba. Yàlla Kuy seetlu lépp la.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
Bu ñu leen nuyyoo, nangeen delloo nuyyoo bu gën a rafet ; mbaa bu na mel. Yàlla Kuy natt lépp la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Amul jeneen yàlla yu dul Moom Yàlla ! Fàwwu dana leen dajale Bis-pénc ba, sikkuwut. Te kan moo gën a dëgguy wax Yàlla ? [Amul]
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Lu ngeen am ? Ca naaféq ya, am na ñaari kuréel.Te Yàlla delloo na leen ca la ñu fàggu woon. Moo ndax dangeen a bëgg gindi ka Yàlla bàyyi cig réer ? Ku Yàlla bàyyi cig réeram, doo ko mën wutal yoonu mucc.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Ñanga ne siiw ngeen weddi, na ñu weddee [ñoom] : ndax ngeen yem ! Buleen jàpp ay xarit ci ñoom, li feek ñuy gàddaay jëm ci yoonu Yàlla. Bu ñu dëddoo, jàppleen leen te reyleen fu ngeen leen mën a fekk ; te buleen wut ci ñoom xarit waxumalaak ndimbal,
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
lu dul ña jóge ca nit ñoo xam ne kóllare dox na ci seeni diggante, ak ña jëm ci yéen te fekk xeex ak yéen di lu tiis ci seeni xol, walla ñu xeex ak ña bokk ca ñoom. Bu sooboon Yàlla, Mu xiir leen ci yéen, te kon ñu farlu ci xeex ak yéen. Bu ñu leen bàyyee, berleen, xeexuñu ak yéen, te ñu doxal jàmm ak yéen, Yàlla mayatuleen wenn lay wuy tax ngeen mën dal ci seen kaw.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Dangeen gis ñeneen ñu bëgg jàmm dox seeni diggante, ñoom ak yéen ak seen biir. Saa yu ñu leen xëccee jëme leen ci bokkaale, ñu yabu ca lool. Bu ñu leen bàyyiwul, berleen te jàmmoowuñu ak yéen, te wàccewuñu seen yoxo ci yéen, jàppleen leen, reyleen fépp du ngeen leen fekk. Ñooñu, may Nanu leen ci ñoom ndigal lu wér ci ñu nennu leen.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Yellul ab jullit rey ab jullit, lu dul ci njuumte. Ku rey jullit ci njuumte, war na mu goreel jaam bu nekk jullit te jox ndàmpaay ay mbokkam, ndegam defuñu ko sarax [Baal ko ko]. Bu fekkee ka ñu rey dafa di ab jullit bu bokk ca nit ña nekk seeni noon, goreel jaam bu jullit rekk a war ka reye. Bu bokkee ci ñoo xam ne kóllare dox na ci seen diggante, dana ko war ndàmpaay lu mu jox ay mbokkam ak goreel jaam bu di jullit. Ku gisul [jaam bu mu goreel], na woor ñaari weer yu toftaloo mu di tuub gu Yàlla nangu. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ku rey ab jullit te tey ko, peyam Safara la, te dafay béel. Merum Yàlla ak rëbbam tegu ci kawam, te mbugal mu mag moo ko fay xaar.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Éy yéen ñi gëm ! Ndegam dox ngeen ci yoonu Yàlla, nangeen leerlu bu baax te buleen nattu ñay wone jàmm, buleen ne ko : “Doo jullit”, ngir bëgg wut alali àddina . Alal yu baree nga ca Yàlla. Te sax yéen noonu ngeen meloon bu yàggul ; terewul Yàlla jox na leen xéewal. Deeleen di leerlu. Yàlla deñ na kumpa ca la ngeen di def.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Ña bokk ci jullit yi toog bañ a xareji ci lu dul ngànt, duñu yem mukk ak ña xare ca yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Ña xareji, Yàlla defal na leen ngëneel ak daraja ca kaw ña toog bañ a xareji. Waaye ñoom ñépp nag Yàlla dig na leen Àjjana ; teewut itam Mu defal ngëneel way-xare ya ca kaw ña toogoon, ña xareji muy pey gu màgg ;
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
muy yokkute gu tukkee ci Yàlla, ak njéggal ak yërmaande. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Ña Malaaka ya jël seeni ruu te ñu doon tooñ seen bopp, Danañu leen laaj : “Ca la ngeen nekkoon ? ” [bañ a dem xareji] - Ñu toontu ne : “Danoo nekkoon ñu ñu néewal doole ci kaw suuf”. Ñu ne leen : “Moo ndax suufus Yàlla si dafa yaatuwul ba ngeen mën a gàddaay jëm feneen ? ”. Ñooña Safaraa di seen dëkkuwaay. Te ndaw muj gu bon !
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Ba mu des ña néew doole : ci góor ñi, ak ci jigéen ñi, ak xale yi ci ñàkk pexe, bu ñu gindikoo [ba genn màkka]
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ñooña xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla Kuy baale la, di jéggale.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Ku gàddaay ngir Yàlla, fu mu mën a jëm, dana fa fekk delluwaay yu bari ak ug yaatal. Ku génn këram, di gàddaay ngir Yàllaak ub Yonentam, ba dee dab ko, kooku peyam Yàlla warlul na ko ko. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
Bu ngeen di tukki ci réew yi, aayul ci yéen ngeen wàññi ci julli yi, bu ngeen ragalee yéefar yi fitnaal leen, yéefar yi seeni noon lañu yu bir.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Boo nekkee [Mahammad] ci seen biir, te nga jiite leen ci julli, na benn kurél ci ñoom ànd ak yaw, na beneen kurél ba jël seeni ngànnaay. Bu ñu sujjóotee ñu nekk ca ginnaaw ñay julli, kurél boobu julliwul woon ñëw [bu bu jëkk ba noppee] julli ànd ak Yaw. Nañu fogu te jël seeni ngànnaay. Yéefar yaa ngi ne siiw ngeen sàggane seeni ngànnaay ak seeni yóbbal, ba ñu song leen menn cong mu tar. Aayul ci yéen su amee lu leen lor ci taw walla ngeen wopp, ngeen tëral seeni ngànnaay te fogu.. Yàlla xaaroo na yéefar yi mbugal muy doyadale [toroxale].
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Bu julli ga sottee, tudduleen Yàlla ci taxawaay ak ci toogaay, ak bu ngeen tëddee. Te bu ngeen nekkee ci kóolute, nangeen taxawal julli. Julli kat, doon na lu Nu sàkkal ay waxtu ci kaw jullit ñi.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Buleen yaanaani ci am cong. Bu ngeen di metitlu [ci ay jam-jam], ñoom it am nañu metit ni yéen, te yéen yaakaar ngeen ci Yàlla loo xam ne yaakaaruñu ko ñoom. Te Yàlla Ku Xam la te Xereñ.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Wàcce Nanu ci Yaw Téere ba ci dëgg, ngir nga àtte diggante nit ñi ni la ko Yàlla xamalee. Bul doon kuy layal wurujkat ya.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Bul dàggasanteek ñiy wuruj seen bopp. Yàlla safoowul ku di wurujkat di bàkkaarkat.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Nëbbu nañu nit ñi, waaye mënuñoo nëbbu Yàlla. Ndax mook ñoom a nekkoon ba ñuy fanaanoo ay wax yu ko neexul. La ñu doon def, Yàlla péeg na ko [ci xam-xam].
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Yéen a ngi noonu di layal ñooñu ci dundug àddina bi. Waaye ana kan moo leen di layal ca Bis-pénc ba ? Walla ana kan mooy doon seen wéeruwaay ?
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Képp ku def ñaawtéef mbaa mu tooñ boppam, gaaw jéggalu Yàlla, dana fekk di Jéggalaakoon, di Jaglewaakoon.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Ku fàggu bàkkaar, defu ko kenn ku dul boppam. Yàlla Ku xam la, di Ku xereñ.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Ku def ñaawtéef walla bàkkaar ba noppi jiiñ ko ku ca set wecc, kooka yenu ma duur ak bàkkaar bu bari.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Bu dul woon teraanga Yàlla ak yërmaandeem ci yaw, kon ab kurél ci ñoom danañu ittewoo sànk la. Waaye sànkuñu kenn ku dul seen bopp, loruñu la ci dara. Te Yàlla wàcce na ci yaw Téere ba ak xam-xamu ràññee [xereñ], te xamal na la loo xamul woon. Te xéewali Yàlla ci yaw rëy na..
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Lu bari ca la ñuy déeyoo lu baax nekku ca, lu dul ci waxi kuy digle sarax, walla njekk, walla jubale ci diggante nit ñi. Ku def loolu, di sàkku ngërëmul Yàlla, Dananu ko jox [ëllëg] pey gu màgg.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Képp ku juuyoo ak Yonent ba gannaaw ba njub ga feesee ci moom, muy topp lu wuuteek yoonu jullit ña, Dananu ko méngaleek la mu méngool, te séndal ko Safara. Ndaw delluwaay bu bon !
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Yàlla du baale ku Ko bokkaale. Waaye lu dul loolu Dana ko baale ku Ko neex. Te képp kuy bokkaale Yàlla, réer na réer gu sori.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Te kat ñoom ay xërëm yu ñu jigéenal ak Séytaane su fétterlu doŋŋ lañuy jaamu di ko woo bàyyi Yàlla.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Yàlla rëbb na ko ca la mu wax moom [Séytaane], ne : “Fàwwu danaa jël ci say jaam ab cër bu takku”.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Mu waxaat [moom Séytaane] : “Waat naa ne danaa leen réeral, danaa leen nax ca la ñuy xemmem, danaa leen digal ñu dog noppi jur gi, danaa leen sant ñu soppi ni Yàlla bindee [bindeef yi]. Ku bàyyi Yàlla, jàppe Séytaane muy kilifaam, yàqule na yàqule gu bir.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Dana leen dig, xemmemlu leen. Te Séytaane du dige lu dul ay wor.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Ñooñu seeni dëkkuwaay mooy Safara. Te kenn duleen ca musal !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Ñi gëm te jëf aw yiw. Dananu leen dugal Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, dañu fay béel ba fàwwu. Digeb Yàlla lu dëggu la. Te sax, ana kan moo gën a dëggu ay wax Yàlla ?
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Mbir ma ajuwul ci seeni mébét walla ci mébétu ña jotoon Téere. Waaye ku def ñaawtéef, jot peyam, kenn du ko mën a amal kilifa gu ko yiir mbaa mu ko mën a dimbali ginnaaw bu ca Yàlla génnee.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ku jëf, jëf ju bokk ci aw yiw, di góor mbaa muy jigéen, te di ab jullit... ñooña danañu dugg Àjjana; te kenn duleen ca tooñ [ba waññil leen] lu toll ni mboxosu xooxu tàndarma.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ana ku gën a rafet diine ku jubale boppam Yàlla, te di kuy rafetal [jëfam], tey roy diiney Ibraahiima cig wéetal Yàlla ? Te Yàlla Moom jàppe na Ibraahiima soppeem.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Te Yàlla lépp la peeg.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Ña nga lay laaj nga ubbee leen ci jigéen ñi. Neel : “Yàlla Dana leen ubbee ci ñoom, ak lañu leen jàngal ca Téere ba [di leeral lu jëm ci] jirim yu jigéen yi nga xam ne joxooleen leen la ñu digle ci ñoom, te ngeen xemmem takk leen, [ak leeral lu jëm ca] ñu néew doole ña ci xale yi”. [Ak di leen digal] ngeen taxawu jirim ci ag maandute. Lu ngeen ca def ci ñoom ci lu baax, Yàlla xam na ko.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Bu ku jigéen ragalee ci jëkkëram naqar walla mu foñ ko, aayul ñu yéwénoo ñoom ñaar, ba juboo ci lenn, ndaxte yéwénoo moo gën, te bakkan dafa gaaw a jeng jëm ci nay. Waaye bu ngeen rafatalee te ragal Yàlla... Yàlla, ku deñ-kumpa la ci seeni jëf.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Dungeen mëna a maandu mukk ci diggante jigéen ñi, doonte xér ngeen ci yemale leen. Waaye, buleen jeng, jeng gu jéggi dayo ba tax ngeen bàyyi kenn ci ñoom ba mu mel ni ku ñu aj. Waaye, bu ngeen yéwénalee sellal te ragal Yàlla... Yàlla di ab Jéggalaakoon, di ab Jaglewaakoon.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Bu ñu tàggoo [jëkkër ak jabar], Yàlla dana woomal ku ca nekk ci ag yaatalam. Yàlla Ku yaatu mbir la, di Ku xereñ
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Te li nekk ci asamaan yeek suuf si, Yàllaa ko moom. [Nun Yàlla], déggoon Nanu ña jotoon Téere, lu jiitu seeni jamoni ak yéen it ne leen : “Ragal-leen Yàlla ! ”. Te bu ngeen weddee, nangeen xam ne Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku woomal la te yayoo cant.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Te it, li nekk ci asamaan yeek suuf, Yàlla doy na ci te mat na sëkk Kilifa.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Bu ko sooboon Mu jële leen fi, yéen nit ñi, indi fi ñeneen. Te loolu, Yàlla mën na ko.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Koo xam ne yoolu àddina bi la bëgg, [na xam ne] Yàlla am na lu mu yoole ci àddina ak ca àllaaxira. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Éy yéen ñi gëm ! Taxawleen temm ci maandute, di seede ngir Yàlla doonte seede soosu [lu naqari la] luy dal ci seen kaw, walla ci seeni waajur, walla ci kaw seeni njaboot, walla seeni jegeñaale. Su dee ku woomal la walla ku ñàkk, Yàllaay ki gën pey ci ñoom ñaar ñépp. Buleen topp seeni bànneex ba ñàkk a maandu. Bu ngeen jéggalee [seede] walla ngeen dëddu bañ a seede, xamleen ne Yàlla Ku deñ-kumpa la ci li ngeen def.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Éy yéen ñi gëm ! Doyluleen Yàlla ak ub Yonentam, ak Téere ba Mu wàcce ci Yonentam, ak Téere ba wàcc la jiitu. Képp ku weddi Yàlla, ak i Malaakaam, ak Yonentam, ak Bis-pénc ba, réer na réer gu sori [dëgg].
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Ña nga xam ne dañoo gëm ba noppi weddi, daldi gëm, weddiwaat, seenug weddi di gën a tar, Yàlla duleen jéggal, te it duleen gindi teg leen ci yoon wu leer wa.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Bégalal [xamalal] naaféq ya ci ne am nañu mbugal mu metti,
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
ña jàppe yéefar ya ay xarit, bàyyi fa jullit ña, ndax nee dañuy sàkku ci ñoom teraanga, te moone teraanga jépp a ngi ca Yàlla.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Te wàcceel na leen ca Téere ba, xamal leen ne : bu ngeen déggee ay nit ñuy weddi ak a ñaawal [yéjji] ndigali Yàlla yi, buleen toog ak ñay def loolu ba ba ñuy xuus ci weneen waxtaan. Lu ko moy dangeen di mel ni ñoom [cig weddi]. Yàlla Kuy dajale la naaféq yaak yéefar ya ñoom ñépp ca biir Safara.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Ña nga xam ne ñanga téyandi seen bopp ci yéen ; su leen Yàlla joxee ndam, ñu gaaw ne : “Ndax àndunu woon ak yéen ? ” ; bu yéefar yi amee cër ci ndam, ñu ne leen : “Xanaa du ñoo leen doon song [yéen yéefar yi] te nu fegal leen jullit ñi ? ”. Yàlla Dana àtte seen diggante Bis-pénc ba. Te du jox yéefar yi ndam ci kaw jullit ñi.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Naaféq ya dañuy jéem a nax Yàlla, te fekk Yàlla Dana leen juuy. Te bu ñu taxawalee julli, taxaw ci tàyyeel, di ngistal ci bëti nit ñi. Te duñu tudd [fàttaliku Yàlla] lu dul ñu néew ci ñoom.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Ñuy deŋŋi-deŋŋi ci diggante yooyu, féetewuñu ci ñii, féetewuñu ca ñaa. Ku Yàlla bàyyi cig cànkuteem, kenn du ko mën a teg ci yoon wu jub wa.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàppe yéefar yi ay xarit bàyyi jullit ña. Ndax dangeen bëgg a jox Yàlla lay wu jub ci seen kaw ?
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Naaféq yaa nga ca dëru ya gën a suufe ca Safara, te kenn duleen dimbali,
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
ba mu des ña tuub, réccu, te sellal [yéwénal], jubbantiku te tënku ci Yàlla te sellal seenug jaamu Yàlla. Ñooña, ñook jullit ñee ànd. Te Yàlla Dana jox jullit ñi pey gu màgg.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Lu Yàlla di doye mbugal leen? Bu ngeen dee sant Yàlla te gëm ko, Yàlla di Kuy nangug cant, di Ku xam lépp nag.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Yàlla bëggul ku fésal wax ju ñaaw, ndegam nekkul ku ñu tooñ. Yàlla Kuy dégg la, Ku xam lépp.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Bu ngeen fésalee yiw, walla ngeen nëbb ko, walla ngeen baale lu bon [la ñu leen def]... Xamleen ne Yàlla kuy baale la, Ku am kàttan la.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Ña weddi Yàlla ak i Yonentam, te bëgg a téqale Yàlla ak i Yonentam, te naan : “ Gëm nanu ñenn ña, weddi ñenn ña [ca Yonentam ya]”, tey jéem a am ca yoon wa nekk ca diggante weddeek ngëm,
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
ñooña ñooy dëgg-dëggi yéefar ! Te Dananu xaaroo yéefar yi mbugal mu leen di toroxal.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Waaye ña gëm Yàlla ak i Yonentam te xàjjalewuñu kenn ci ñoom, ñooña gaay Dananu leen jox seen pey. Te Yàlla Jéggaleekoon la, Jaglewaakoon la.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Ña jotoon ab Téere, ñangay laaj, bëgg nga wàcce ca ñoom ab Téere bu bawoo asamaan. Waaye ñoom sax laajoon nañu Muusaa lu gën a rëy loolu, ndax dañu ne ko : “Won nu Yàlla ñu janook Moom ! ”. Dënnu ga fàdd leen ngir seen bàkkaar boobu. Ba loola jàllee, ñuy jaamu yëkk wa, ginnaaw ba leen dëgg gu bir dikkalee. Nu baal leen loola, topp Nu jox Muusaa kiliftéef gu bari.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Nu yékkati doj wa ca seen kaw ngir fasanteek ñoom kóllare, ñu ne leen woon : “Dugguleen ci buntu bi ànd ak di sujjóot” ; Neeti leen : “Buleen jalgati bisub gaawu” ; Nu jàppe woon ak ñoom kóllëre gu dëgër.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Ci sababu firig seen kóllare ak seen weddi kàdduy Yàlla ya, ak rey ga ñu rey Yonent ya ci lu dul dëgg, ak la ñuy wax naan: “Sunuy xel muuru na”. Li am kay moo di Yàllaa fatt seeni xol ci sababus seenug la ñu weddi, ñu néew ñoo gëm ca ña bokk ca ñoom.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ak ca sababus la ñu weddi, te wax ci Maryaama duur [fen] wu rëy.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
ak ca la ñu wax ne : “Noo rey [Masiihu Iisaa] doomi Maryaama, Yonentub Yàlla ba”... Te reyuñu ko, daajuñu ko ci ay bant ; waaye dañu leen koo nirëleel ñu cay werante ! Wóor na ne ci am lënt lañu nekk ci mbir moomu: amuñu ca benn xam-xam lu dul topp seen njort, te nag reyuñu ko de.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
li am kay mooy Yàllaa ko yékkati jëme ko ca Moom. Te Yàllaa di Ku not lépp, di Ku xereñ.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Dana am ñenn ca ña jotu Téere, ñoo xam ne fàwwu danañu ko gëm balaa muy dee [Moom Iisaa doomu Maryaama]. Te Bis-pénc ba moom dana nekk seede ci ñoom.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Te sababus tooñug Yahuud ya, araamaloon Nañu ca ñoom yu sell ya daganoon ca ñoom, ak la ñu daan férawle ñu bari soril leen diine,
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
ak lañu doon lekk ribaa - te ñu tere woon leen ko - ak di lekk alali nit ña ci neen. Nañu xam ne Nun Yàlla xaaroo Nanu yéefar ya mbugal mu metti.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Waaye ñay woroomi xam-xam yu xóot ca ñoom ak ña ca gëm, gëm nañu la ñu wàcce ci yaw [Muhammad] ak la ñu wàcce woon mu jiitu la. Ak ñay taxawal julli ak ñay génne asaka, ak ña gëm Yàlla ak Bis-pénc ba, ñooñee, Dananu leen jox pey gu rëy.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Sol Nanu [Nun Yàlla] leerug Yonent ci yaw [Muhammad] ni Nu ko sole woon ca [Nooh] ak Yonent ya toppoon ca moom. Sol Nanu ko Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba, ak sët ya ak Iisaa, ak Ayuuba, ak Yuunusa, ak Haaruun, ak Suleymaan, te jox Nanu Daawuda ab Téere bu tudd [Zabuur].
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Ak Yonent yoo xam ne nettali woon Nanu leen seeni mbir lu jiitu, ak ñeneen ñu Nu la nettaliwul [seeni mbir] - Te Yàlla wax na ak Muusaa waxante tigi -
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
ñu di ay Yonent yuy bégle ak xuppe ngir nit ñi bañ a am lay wu mën a yey Yàlla, ginnaaw ba leen Yonent ya xamalee dëgg. Yàlla ku am kàttan la, di Ku tedd.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Waaye Yàlla seede na la Mu wàcce ci Yaw, te ci xam-xam la ko wékk. Te Malaaka ya it seede nañu. Te Yàlla doy na, mat sëkk seede.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Ña weddi tey féew nit ñi yoonu Yàlla, réer nañu réer gu sori.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ña weddi te tooñ, Yàlla duleen baal, duleen gindi, teg leen ci yoon wu jub wa
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
lu dul xanaa ca yoonu Safara, te dañu fay béel ba fàwwu. Loola di lu yombu Yàlla.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Éy yéen nit ñi ! Yonent bi indil na leen dëgg te bawoo fa seen Boroom. Kon gëmleen, [su ngeen ko defee], moo gën ci yéen de. Bu ngeen weddee nag, xamleen ne Moo moom la ca asamaan ya ak suuf si. Te Yàlla di Ku xam, di Ku xereñ..
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Éy yéen ñoñ-téere, buleen jéggi dayo ci seen diine, te buleen wax ci Yàlla lu dul lu nekk dëgg. Ku Nu barkeel ka di Iisaa, doomi Maryaama, doonul lu dul Yonentub Yàlla, di kàddoom ga Mu sànni ca Maryaama, di ruu gu tukkee ci Moom. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam. Te buleen di wax nit [Yàlla]. Bàyyileen wax jooju ! Moo gën ci yéen. Yàlla Moom kenn rekk la. Sellam gi jombaate naak Muy am doom. Moom mooy boroom li nekk ci asamaan yeek suuf si, te Yàlla doy na sëkk wéeruwaay.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ku ñu barkeel ka [Iisaa], du jomlu te du jombulu ci nekk jaamab Yàlla, Malaaka ya gën a jegeñ [seen Boroom], ñoom it duñu ko jomlu ci jombu koo jaamu. Képp ku jomlu ci jomb koo jaamu ... [Na xam ne] Yàlla Dana leen fang [gur-gur jiital] ñoom ñépp jëme leen ca Moom.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Ñi gëm nag tey jëf ay yiw, Yàlla Dana leen jox seen pey ba yokkal leen ca ngënéelam. Waaye ña jomlu tey rëy-rëylu, Dananu leen teg mbugal mu metti. Te duñu gis [am] keneen ku dul Yàlla ku leen di mën a yiir walla dimbali,
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Éy yéen nit ñi ! Aw lay dikkal na leen wu tukkee ca seen Boroom. Te wàcce Nanu ci yéen leer gu ni nàññ.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Ña gëm Yàlla te jafandu ci Moom, Dana leen dugal ci yërmaandeem ak ci ngëneel, ci gindi leen, jubale leen ca boppam, teg leen ca yoon wa jub xocc.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Danañu sàkku ci yaw ubbee [ci mbirum ndono]. Neel : “Yàllaa ngi leen di ubbee ci càppaacoli : bu nit faatoo di ku góor gu amul doom, te am na jigéen [bu mu bokkal ndey ak baay walla baay], moo moom génn-wàllu la mu bàyyi [ci alal]. Bu fekkee ne jigéen a bàyyi, dee te amul doom, [moom càmmiñ ja] day donn alal ja jépp. Bu fekkee ne ñaari jigéen lañu, dañuy donn ñaari ñeenteeli alal ja mu bàyyi ginnaaw ; bu ñu dee ñu góor ak ñu jigéen, na ku góor am cëru ñaari jigéen. Yàlla dafa leen di leeralal ngir bañ ngeen réer. Yàlla xam na lu ne.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers