PDF —
52 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Haqqa pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Haqqa pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Haqqa Tekki. Simoore Al-Haqqa (Meccan) 52 Aaya.

← Al-QalamSimoore Al-Haqqa Al-Ma'arij →


52 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮯﮰ
69:1 Joxoñub dëgg ba.
ﮱﯓﯔ
69:2 Lan mooy Joxoñub dëgg ba.
ﯕﯖﯗﯘﯙ
69:3 Ana lan moo lay xamal Joxoñub dëgg ba.
ﯚﯛﯜﯝﯞ
69:4 Giirug Aad ak Samuud dañoo weddi woon yëngu-yëngu bu rëy ba.
ﯟﯠﯡﯢﯣ
69:5 Giirug Samuud ag yuuxu (am riir) la ñu léen alage.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
69:6 Giirug Aad nag ngelaw lu sedd luy riddi moom la ñu léen alage.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
69:7 xiirtal na ko ci séen kaw juróom yaari bëccag ak juróom yaari guddi yu tegaloo nit ña ne lasiim melni dàtti tàndarma yu fënëx.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
69:8 Moo ndax gisati nga lu bokk ca ñoom?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
69:9 Firawnaak ña ko jiitu woon ak dëkk ya nu wëlbati woon njuumte la ñu fa nekke woon.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
69:10 Dañoo moyu woon senn Yonentub Boroom. Yàlla, faagaagal leen.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
69:11 Ba ndox ma bëbóo, Noo leen yanu woon, ca gaalug Nooh ga doon daw
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
69:12 danu koo def mu di fàttali ci yéen nopp yu sell it man koo jàpp.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
69:13 Su nu walee bufta ba, genn wal ëf ko,
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
69:14 suuf si ak doj yi ñu jël ko def ko pënd moñoxe ko benn yoon ;
ﭼﭽﭾﭿ
69:15 Bu keroogee, xew-xew,ba agsi bis Pénc ba,
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
69:16 asamaan siy xottiku nooy nepp.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
69:17 Malaaka ya nekk ci ay goxam, su ko defee juróom-ñatta, cay yanu gàngunaay ga ( Aras ).
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
69:18 Bu keroogee dees na leen weer; ken du leen ca nëbb dara.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
69:19 Ña nga xam ne dañoo jot seeni Téere ci ndeyjoor, da leen di wax ne : “Jàppleen ! jàng samab téere.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
69:20 Man dey jàppoon naa ne danaa dajeek samab màndaxe”.
ﮨﮩﮪﮫﮬ
69:21 Moom dey mi ngi ci dundu gu neex :
ﮭﮮﮯﮰ
69:22 ca Àjjana ju kawe
ﮱﯓﯔ
69:23 meññatam ma day yoore.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
69:24 “Lekkleen te naan muy peyug la ngeen jiitaloon”.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
69:25 Ña ñuy joxe seen téere ci càmmoñ, danuy wax naan : “Aka neexoon ! Jotuma sama téere,
ﯩﯪﯫﯬﯭ
69:26 te ma ba ña xam luy sama màndaxe...
ﯮﯯﯰﯱ
69:27 Aka neexoon, ma dee farit.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
69:28 Sama alal ja jariñuma dara.
ﯸﯹﯺﯻ
69:29 Sama sañ-sañ réer na ma ! ”.
ﯼﯽﯾ
69:30 “Jàppleen ko ! Te, jàng ko ;
ﯿﰀﰁﰂ
69:31 te, ngeen xoyom ko ca Safara ;
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
69:32 ca biir càllalag juróom-ñaar-fukk bëñ sóobleen ko ca jéng ko,
ﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
69:33 moom gëmu tooñ Yàlla , mu Màgg ma.
ﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
69:34 te daawul sonn ci dundal miskiin yi.
ﰘﰙﰚﰛﰜﰝ
69:35 Bis niki tey amatu fi xarit
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
69:36 ducaageni ak lekk lu dul lay rogaat ci seen yaram,
ﭗﭘﭙﭚﭛ
69:37 defkati njaaxum ya rekk koy lekk”.
ﭜﭝﭞﭟﭠ
69:38 Déet... Maa ngi giñ ci li ngeen di gis,
ﭡﭢﭣﭤ
69:39 Ak ci li ngeen gisul,
ﭥﭦﭧﭨﭩ
69:40 ci ne [Alxuraan] waxi ab Yonent la bu tedd,
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
69:41 du waxu ab waykat ; li ngeen gëm néew na,
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
69:42 du waxi it ab buxaaba, aka néew lu ngeen di fàttaliku.
ﭻﭼﭽﭾﭿ
69:43 Dafa wàcc bawoo ci boroom àddina si.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
69:44 Su ca fentoon jenn jenn wax,
ﮆﮇﮈﮉ
69:45 ( Kon ) dananu téye loxob ndeyjooram,
ﮊﮋﮌﮍﮎ
69:46 daldi, dog sidiiti xolam ( mu dee ).
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
69:47 Te kon kenn ci yéen du ko mana fanq.
ﮖﮗﮘﮙ
69:48 Ca dëgg-dëgg ag fàttali la ñeel ña ragal Yàlla.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
69:49 Te xam nanu xéll ne am na ci yéen ñu koy weddi ;
ﮠﮡﮢﮣﮤ
69:50 ca dëgg-dëgg, bekkoor la ci yéefar yi,
ﮥﮦﮧﮨ
69:51 te moo di li wóor tigi.
ﮩﮪﮫﮬﮭ
69:52 Na ngay sàbbaal sa turu Boroom, bu Màgg bi !

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers