Simoore Yusuf
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Yusuf pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Yusuf pdf Wolof — Wàcce Simoore Yusuf Tekki. Yusuf (Meccan) 111 Aaya.
Related
- Yusuf TekkiWolof
- Yusuf mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Yusuf

ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Alif, Laam, Raa. Lii ay xamle la yu nekk ci Téere bu wér péŋŋ bi.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Wàcce Nanu ko mu di ay njàng ci làkku [araab] ngir ngeen xam la mu tekki.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Nun noo ngi lay nettali gën jaa rafeti nettaliin ci Alxuraan jii Nu la xamal te lu ko jiitu nekkoon na loo réere.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
[Fàttalikul] ba Yuusufa waxee baayam ne ko : "Yaw sama baay, man gis naa [ci gént] fukki bindiw ak ñaar ak jant bi ak weer wi ; ñu may sujjóotal”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Mu ne ko : "Yaw sama doom, bul nettali sa gént gi say doomi-baay, [boo leen ko nettalee], danañu la fexeel am pexe ; ndax Séytaane noonub nit la bu tar ag nooneel.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Kem [ni nga génte], sa Boroom dana la tànn te Dana la xamal pirim gént, te Dana matal ci yaw ay xéewalam ak njabootu Yanqooba, ni Mu ko matalee woon bu jëkk ca sa ñaari maam ya, Ibraahiima ak Isaaqa, sa Boroom nag ku xam la, ku xereñ la”.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Dëgg-dëgg kéemaan gu réy am na ci diggante Yuusufa ak i doomi-baayam ngir képp kuy gëstu,
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
ba ñu waxee ne : “Sunu baay, Yuusufa ak doomu-ndeyam la gën a bëgg ci nun, te nun mbooloo lanu. Sunu baay daal dafa nekk cig réer gu bir.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
[Am ku wax ne] reyleen Yuusufa mbaa ngeen sànni ko fenn ci suuf si, kon seen baay dootul xool kenn ku dul yéen, te bu loolu amee dangeen nekk di aw nit ñu feeñ”.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Mu am ca ñoom ku wax ne : “Buleen rey Yuusufa, sànnileen ko ci teen bu lëndëm, kon tukkikat yi danañu ko for su fekkee def ngeen ko”.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Ñu ne : "Yaw sunu baay, ana lan moo tax wóoluwoo nu ci Yuusufa ? Te nun dañu koy laabire doŋŋ.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Bu subaa nga yabal ko mu ànd ak nun muy sàmm jur gi, di fo. Dananu ko wattu”.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Mu ne leen : “Man dey, am naa njàqare ci ngeen ànd ak moom ; danaa ragal ngeen sàggan ba ag till lekk ko”.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Ñu ne : “Till! Su ko lekkee nag ak nii nu nekkee di mbooloo, kon dey nu gën a yées”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Ba ñu àndeek moom, te mànkoo ci sànni ko ca xóot-xóot ba [teen ba], Nu xamal [Nun Yàlla] Yuusufa ne : “Danga leen mës a nettali seen jëf jii fu ñu ko foogewul”.
ﭤﭥﭦﭧﭨ
Ñu dellu ci seen baay ci marax, di joox.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Ñu ne : "Yaw sunu baay, ba ñu demee, dañu doon rawante, bàyyi Yuusufa ca sunuy yóbbal ; ag till lekk ko. Te bu nu waxee dëgg it du tax nga gëm li nu wax”.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Ñu indiwaale yéreem yu taq dereet [ju dul dereeti Yusuufa]. Mu tontu leen ne : “Yéen dey, seen bakkan rafetal na leen mbir mii... Waaye danaa sax ci muñ gu rafet ! Ci Yàlla laay dimbandikoo ci lii ngeen nettali ! ”
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Ay tukkikat agsi, yónni seenub rootkat, mu yoor baagam. Mu daldi ne : “Mbégtee ngi ! Lii de ab xale la ! ” Ñu yóbbu ko nar koo jaay. Te Yàlla ku xam la la ñuy def.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Ñu jaay ko ci njëg gu néew : ay dërëm yu bariwul. Ndax dañu koo xeeboon.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Ka ko jënd di waa Misra, wax na jabaram ne ko : “Teralal ma ko. Xéy-na mu jariñ nu mbaa nu def ko sunu doom.”. Noonu la nu darajaale Yuusufa ci suuf si, ak it ngir Nu jàngal ko pirim gént. Yàlla kuy not la ca la Mu namm : waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Ba mu màggee ba tollu ci góor gu mat, jox Nanu ko ràññee ak xam-xam. Te noonu Lanuy feye way-rafetal ña.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ndaw sa nga xam ne [Moo ko fat ca kërëm] sàkku na ko ci boppam. Tëj na buntu ya ne ko : “Ayca ñëwal ci man” - Mu ne : “Maa ngi muslu ci Yàlla ! [tëdd ak yaw] te sama sang [bi ma jënd] fonk na ma, teral na ma. Te tooñkat ya duñu texe mukk”.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Ndaw sa xemmem na [Yuusufa]. Moom [Yuusufa] it xemmem na [ndaw sa] bu dul koon la mu gis kaawtéefi Boroomam. Noonu la Nu def ngir fegal ko ñaawtéef ak njaaloo. Moom sax dafa bokk ca sunu jaam yu sell ya.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Ñu jëkkante buntu ba, [ndaw sa] xëcc yérey [Yuusufa] ca ginnaaw ga. Ñu dajeek jëkkëram ca buntu ba. [Ndaw sa] daldi ne : “Ana lan moo di peyug ku naral lu bon sa jabar, lu dul tëj ci kaso walla mbugal mu metti ? ”
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
[Yuusufa] ne : “Moo ma sàkku ci sama jëmm”. Mu am seede su di mbokkum ndaw sa daldi seede ne : “Bu fekkee ne yéreem ci kanam la xottiku, ndaw sa moo wax dëgg, moom mu bokk ca fenkat ya.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Bu yéreem xottikoo ci ginnaaw, ndaw sa moo fen, moom mu bokk ca ñu dëggu ña”.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Ba jëkkër ja gisee yére ya xottiku ca ginnaaw, mu ne : “Lii ci seeni pexe la [yéen jigéen ñi] ! te seeni pexe réy na !
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Yuusufa, dëddul lii ! Te yaw [sama jabar] jéggalul sa bàkkaar ndax yaw bokk nga ca ñay def lu bon”.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
Aw jigéen di wax ci dëkk bi naan : “Jabaru buur bi dafa doon sàkku jaamam ! Mbëggeel gëlamal ko. Nun daal gis nanu mu nekk ci ag réer gu tar.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Bi mu déggee seen jëw, mu yónnee ca ñoom, waajalal leen aw ñam ; indil ku nekk ca ñoom paaka. [Ba ñuy lekk, mu ne Yuusufa] : “Génnal jëm ci ñoom” - Ba ñu ko gisee, ñu yéemu ci moom bay dagg seeni yoxo, di wax naan : “Cëy Yàlla ! Kii du nit, kii nekkul lu dul Malaaka mu tedd ! ”
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Mu ne : “Mu ngoog lii ngeen ma doon yedde. Maa ko sàkku woon mu bañ. Te bu deful li ma ko sant, waat naa ne dees na ko tëj kaso mu detteelu”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Mu ne[moom Yuusufa] : "Yaw sama Boroom, kaso laa gën a bëgg ci lii ñu may woo jëme ma ca. Te boo ma wëlbatilul seeni pexe, danaa jeng jëm ca ñoom te kon ma bokk ca ña réer [xamadi]”.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Boroomam nangu ñaanam, daldi ko fegal seeni pexe. Moom [Yàlla] mooy Aji-dégg, di Aji-xam ji.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Ginnaaw ba ñu gisee dëgg ga mu fees ca ñoom, ñu ne fàwwu danañu ko tëj kaso ab diir.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Mu duggandoo ca kaso ba ak ñaari xale yu góor. Kenn ca ñoom ne : “Damaa gent di nal sàngara...” Keneen ka ne : “Gént naa man itam yenu ci sama bopp mburu, ay picc di ca lekk. Leeralal nu seenum piri, ndax nun gis nanu la nga bokk ca way-rafetal ña”.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Mu ne leen : “Ñam wii ñu leen di wërsëgale, balaa ñëw ma leeralal leen seen piri. Noonu lay deme ci yéen ñaar ngir la ma sama Boroom xamal. Ndax man bàyyi naa diiney nit ñu gëmul Yàlla te weddi àllaaxira.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Damay topp diiney samay baay Ibraahiima ak Isaaqa ak Yanqooba. Warul ci nun bokkaale Yàlla ak dara. Loola bokk na ci ngëneel yi nu Yàlla defal nun ak nit ñi ; waaye li ëpp ci nit ñi duñu gërëm [Yàlla].
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Yéen sama ñaari àndandooy kaso ! Moo ndax ay yàlla yu téqalikoo ñoo gën walla Yàlla jenn jii doŋŋ, tey Notaakoon bi ?
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Jaamuwuleen ginnaaw Moom lu dul ay tur yu ngeen di tudd ak seeni baay, te Yàlla wàccewul ci loolu wenn lay. Te kenn yeyoowul àtte ku dul Yàlla. Te digle na ngeen bañ a jaamu ku dul Moom. Loolu moo di diine ju jub ; waaye ñi ëpp ci nit ñi duñu xam.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Yéen sama ñaari àndandooy kaso ! Kenn ci yéen dana nekk kuy màndal buuram sàngara ; ka ca des, danañu ko daaj ci bant, ay picc di lekk ci boppam. Dogaleef na noonu mbir ya ngeen doon laaj.”
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Yuusufa wax ka nga xam ne yaakaar na ne dana mucc ca ñoom ñaar, ne ko : “Nanga fexe ba buur fàttaliku ma”. Waaye Séytaane fàtteloo na ko [yóbbante boobu] ba fàttaliwu ko buur ba [ba mu delloo ca moom]. Ba tax mu toog ca kaso ba ay at .
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Buur ba wax ne : “Gént naa juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom-ñaari nag yu loof di lekk ; ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow. Yéen njiit yi, firil-leen ma sama gént gii, ndegam mën ngeen firi gént”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Ñu ne : “Gént yooyu jaxasoo nañu ! Te sax nun xamunu pirim gént ! ”
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Ka muccoon ca ñoom daldi fàttaliku ginnaaw ab diir, daldi wax ne : “Danaa leen leeralal. Yebal-leen ma, Dinaa leen indil am pireem”.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
[Mu dem ca Yuusufa] ne ko : “Yaw waxkatu dëgg ! Ubbee ma ci juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom-ñaari nag yu loof di lekk, ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow, ndax xéy-na su ma delluwaatee nit ña am ci xam-xam”.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Mu ne : “Nangeen bey juróom-ñaari at ni ngeen ko baaxoo defe. Te lu ngeen góob, bàyyileen ko ca aw gubam [bañ koo bàcc], lu dul lu néew ca la ngeen di lekk.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Dana ca topp gannaaw loolu juróom-ñaari at yu bekkoor yuy lekk la ngeen dencoon ngir ñoom ba mu des lu néew ca la ngeen dencoon.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Dana ca topp gannaaw loolu at moo xam ne dana xettali nit ñi te it danañu ca nal [reseñ ndax dana am].”
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Buur ba ne : “Indil-leen ma ko”. Ba ndaw la agsee ca moom [Yuusufa], mu ne ko : “Dellul ca sa sang, nga laaj ko : “Lan moo doon mbirum jigéen ña dogatoon seen yoxo ? Sama Boroom xam na bu baax seen pexe”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
[Buur ba ne jigéen ña] : “Lan moo doon seen mbir ba ngeen sàkku Yuusufa ci jëmmam ? ”. Ñu tontu ne : “Wax dëgg Yàlla ! Xamalunu ko dara lu bon”. Jabaru buur ba ne : “Léegi nag dëgg gi leer na. Maa ko sàkku woon. Moom moo waxoon dëgg ! ”
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
“[Man Yuusufa maa defoon] noonu ngir buur bi xam ne wuruju ma ko ginnaawam, te sax Yàlla du jubale pexem wurujkat ya.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Jéemumaa setal sama bopp, ndax bakkan moom digalaakoon la ci lu bon, [mucctil ci moom] ku dul ku sama Boroom yërëm. Ndax sama Boroom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Buur ba ne : “Indil-leen ma ko : def ko mu sës ci man”. Ba mu waxeek moom, mu ne ko : “Bis niki tey, nekk nga ci man ku ñu darajaal, ku ñu wóolu”.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Mu ne : “Dénkleen ma alali réew mi : am naa xam-xamu wattu ko”.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Noonu Lanu darajaale Yuusufa ca réew ma, mu fay wàcc fu ko neex. Dananu jox sunu yërmaande ku Nu neex te Dunu sànk peyug rafetalkat ya.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Te peyug àllaaxira moo gën ci ña gëm, di ña ragal [Yàlla].
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ay doomi-baayi Yuusufa agsi ca moom [jóge seen réew ma]. Mu xàmmee leen te ñoom fakk nañu ko.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Ba mu solee seen saaku ba noppi, mu ne leen : “Indil-leen ma seen doomi-baay ja des ak seen baay. Moo ndax gisuleen ne nattal na leen lu mat sëkk te it dalal naa leen gën ji daluwaay ?
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Bu ngeen ma ko indilul, dungeen amati ci man indaar ; te it dungeen ma jegeñ”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Ñu ne ko : “Dananu ko sàkku ci baayam. Te dananu ko def”.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Mu ne ay surgaam : “Dellooleen, ci seeni sëf, njëg [ga ñu joxe]: xéy-na danañu ko xàmmee bu ñu delloo ca seeni mbokk te xéy-na danañu dellusi”.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Ba ñu delloo ca seen baay, ñu ne ko : “Yaw sunu baay, [su nu yóbbaalewul sunu rakk jii weneen yoon, kenn dunu nattal]. Kon yebal ko mu ànd ak nun ndax ñu nattal nu. Kon dey dananu ko wattu”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Mu ne : “Ndax, wóolu leen ci dafay mel ni ba ma leen wóolu ca bu njëkk ca doomu- ndeyam ja ? Waaye Yàllaa di gën jaa mën a wattu [aar], te Moo ëpp yërmaande yërëmaakoon ya ! ”
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Ba ñu ubbee seeni ëmb, ñu fekk ca njëg ga ñu leen delloo. Ñu ne : "Waaw yaw sunu baay. Lan lanu bëggati ? Alal ja [nekkoon ca njëg ga nu feyoon] mi ngi nii ñu delloo nu ko. Dananu mën a jëggiwaat lu nu mën a dundale njaboot gi, mën nanoo wattu sunu doomu-baay te dananu yokk sëfu gëléem, loolu natt bu yomb lay doon”.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
- Mu ne leen : “Duma ko bàyyi mukk mu ànd ak yéen li feek waatuleen ci Yàlla ne dangeen ma ko delloosil, ndeem lottuleen ca”. Ba ñu ko waatalee, mu ne : “Li nu waxante, nu ngi ciy wéeru ci Yàlla”.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Mu ne : “Yéen samay doom, [bu ngeen àggee ca dëkk ba], buleen ca duggandoo ci benn buntu, nangeen xàjjalikoo dugge ciy buntu yu soriyaantoo. Mënuma leen a fegal dara lu jóge ci Yàlla. Moom rekk a moom àtte : Ci Moom rekk laa wéeru. Te képp kuy wéeru, na weeru ci Moom [Yàlla]”.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Ba ñu duggee na ko seen baay diglee woon, taxul mu jariñ dara ca la Yàlla namm. Lu dul ne Yanqooba soxla woon na yiir leen ci loolu. Naka moom, boroom xam-xam la ci la Nu ko xamal. Waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
Ba ñu agsee ca Yuusufa, mu daldi xëcc taf ci boppam doomu-ndeyam ja, daldi ne : “Maa di sa doomu-ndey. Bul jàq ca la ñu nekkoon di ko def ci jéem maa sànk”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Ba mu leen solalee seeni saaku ba noppi, mu dugal andaar [ja ñu doon natte] ca biir sëfu doomu-ndeyam ja. Mu am yéglekat bu wax ne : “Éy yéen jëgg ji ! Ay sàcc ngeen”.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Ñoom it ñu wëlbatiku ca moom ne leen : “Lan ngeen réerle ? ”
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Ñu ne : “Li nu réerle mooy nattukaayu buur bi. Te ku ko feeñal nu jox ko sëfu giléem, maa ko warlul loolu”.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Ñu ne : “Giñ nanu ci Yàlla, te xam ngeen ne dikkunu fii ci suuf si ngir yàq te it dunu ay sàcckat”.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
- Ñu ne: “Luy peyug ku sàcc, bu fekkee dangeen a fen ?”.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Ñu ne : “Ag peyam moom ka ñu fekk [nattukaay ba] ci sëfam mooy : ag peyam moom ci boppam [mu nekk jaam]. Noonu Lanu feye tooñkat ya”.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Mu jëkke ca ndabi doomi-baay ya, di seet, mujje ndabul doomu-ndey ja ; génne ca nattukaay ba. Noonu Lanu joxe pexe Yuusufa. Pexe mu ko tax a téye doomu-ndeyam ja ci lu dëppook yoonu buur ba, [mënu ko woon a def] lu dul lu soob Yàlla. Dananu yékkati darajay ku Nu soob. Te boroom xam-xam bu nekk, am na ku ko ëpp xam-xam.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Ñu ne : “Ndegam sàcc na, am na doomu-ndeyam ju sàccoon bu jëkk. “Yuusufa nëbb ca xelam la mu xalaat, bañ leen koo feeñal. Mu ne [ci xelam] : “Yéen yées ngeen ! Te Yàlla xam na li ngeen jëf”.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
- Ñu ne : "Ay yaw kilifa gi, moom dafa am baay bu mage lool ; téyeel kenn ci nun bàyyi ko. Gis nanu ne yaw bokk nga ca rafetalkat ya [seeni jëf]”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
- Mu ne : “Maa ngi ñaan Yàlla mu musal ma ci jàpp ku dul ka ma fekk nattukaay ci moom ! [Su nu ko defee], kon dananu bokk ca tooñkat ya.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Ba ñu amatul yaakaar ci moom, beru nañu di diisoo. Ka di seen mag ne : “Moo ndax dangeen a fàtte ne seen baay waatloo woon na leen ci Yàlla, ca la jiitu loolu la ngeen defoon Yuusufa ? Man dey du ma fi jóge ba kerook may jot sama ndigalul baay walla Yàlla àtte ma, ndax Moom moo gën a mën a àtte àttekat ya.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
[Mu ne] demleen ca seen baay, ngeen ne ko : “Yaw sunu baay, sa doon ja sàcc na. Te dunu seede lu dul la nu xam. Te nun xamunu kumpa.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Laajal waa dëkk ba nu nekkoon, ak njëgg ma nu àndaloon ñibbisi. Li nu wax dëgg la.”
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
[Seen baay tontu leen] ne : “Deewallaay dangeen a topp seen bakkan mu rafetal leen am mbir !... [Muñ gu rafet]. Xéy-na Yàlla delloosil nu leen ñoom ñépp. Moom Yàlla Ku xereñ la, Ku xam la”.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Mu dummóoyu leen, wax ne : “Céy sama njàqare ci Yuusufa ! ”. Noona ay gëtam weex [gisatul] ngir mer ma mu wann.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
- Ñu ne ko : “Céy Yàlla ! Doo deñ di fàttaliku Yuusufa, ba tax na yaa ngi wéradi te mën nga cee loru”.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
- Mu ne : “Defuma lu dul tawat sama njàqare ak sama naqar ci Yàlla. Te xam naa ci Yàlla lu ngeen xamul.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Mu ne : “Yéen samay doon ! Demleen xeeñtu ji lu jëm ci Yuusufa ak doomu-ndeyam ja. Te buleen xàddi ci dajeek yërmaande Yàlla. Ndax ay yéefar rekk ñooy xàddi ci dajeek yërmaande Yàlla”.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Ba ñu agsee ci Yuusufa, ñu ne ko : “Éy yaw jawriñ ju tedd ji, xiif danoo dal nun ak sunug njaboor ; te indi nanu njëgg gu xeebu. Nattal nu te sarax nu. Yàlla dana fey saraxekat ya ! ”
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
- Mu ne leen : “Ndax xam ngeen la ngeen defoon Yuusufa ak doomu-ndeyam ja, ba ngeen nekkee cig réer ?”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
- Ñu ne ko : “Ndax yaw yaay Yuusufa ? ” - Mu ne leen : “Maay Yuusufa, kii mooy sama doomu-ndey, Yàlla defal nu ay xéewal. Ndax ku ragal Yàlla te muñ, [dana gis ne] Yàlla du sànk mukk peyug ñay refetal”.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
- Ñu giñ ci Yàlla ne : “Yàlla gënal na la ci sunu kaw te nun danoo juumoon rekk def bàkkaar”.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
- Mu ne : “Tey du bisub yeddeel ci yéen ? Yal na leen Yàlla baal. Te Moom moo gën a mën a yërëm yërëmekat ya.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Demleen yóbbu sama yére yii ngeen sànni ko ca sama kanamu baay : dana dellu di gisaat. Te ngeen dellusi ànd ak njaboot ga gépp”.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
- Ba njëgg ga génnee [Misra], seen baay daldi ne : “Xetu Yuusufaa ngi may xeeñ, ndegam du ngeen wax ne damaa naax”.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Ñu ne ko : “Giñ nanu ci Yàlla ne yaa ngi ci sa njuumte lu jëkk la”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Waaye, ba kuy bégle ka agsee, daldi koy xëpp yére ya ci kanam. Mu daldi ne xàjj di gis, mu ne : “Moo ndax waxuma leen woon ne xam naa lu ma jële ci Yàlla lu ngeen xamul ? ”
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
- Ñu ne : "Éy yaw sunu baay, sàkkul nu njéggal [ci Yàlla] sunuy bàkkaar. Ndax nun dey juumoon nanu ba def bàkkaar naka”.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
- Mu ne : “Danaa leen ñaanal njéggal ci sama Boroom. Moom Yàlla nag mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Ba ñu delloo ca Yuusufa, mu song ñaari waajuram, ne leen : “Dugguleen Misra ànd ak kóolute, bu soobee Yàlla ! ”
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Mu yéegal ñaari waajuram ci kaw gàngunaay ga, ñu rot sujjóotal ko. Mu ne : "Yaw sama baay, lii moo di pirim sama gént ga woon. Sama Boroom def na ko muy dëgg... Te it defal na ma lu baax ba ma mën a génn ci kaso bi, indi leen ngeen jóge ca àll ba, ginnaaw ba Séytaane yàqee sama diggante ak samay doomi-baay. Sama Boroom nag ku lewet la ca la ko soob. Mooy Ku xam te xereñ.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Yaw sama Boroom, may nga ma nguur, jàngal nga ma it pirim gént. Yaw mi sos asamaan yi ak suuf si, Yaw yaay sama sang, ci àddina ak ca àllaaxira. Yal na nga may rey te fekk may aji-jublu ci Yaw [sama Boroom] sama mbir mépp te yal na nga ma yéege ci ñu yiw ña.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Loolu bokk na ca xew-xew yu fàddu ya, ñu soloo la ko. Te fekkewuloo ba ñu mànkoo ci mbir, di tëral pexe.
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
Te li ëpp ci nit ñi duñu gëm doonte la xér nga sax yaw [ci ña gëm].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Te laajoo leen ag pey ci [Alxuraan ji]. Te nekkul leneen lu dul ag waare ñeel àddina si yépp.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Bariwaana ay kéemtaan yu nekk ci asamaan yi ak ci suuf si, ñu di ko romb, te defuñu ca paal !
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Li ëpp ci ñoom duñu gëm Yàlla, xanaa kay dañuy nekk rekk di bokkaale Yàlla.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Ndax dañoo gëmul ne mbugal mu leen muur mën na leen a dal, di mbugalum Yàlla mbaa mu digal leen, bu Bis-pénc baa ci mbetteel te duñu ko yég ?
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Neel : “Samaw yoon a, ngir damay woote jëme ci Yàlla ànd ak aw lay. Man bokkuma ci bokkaalekati Yàlla yi, maak ku ma àndal.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Yónniwuñu woon, lu la jiitu [yaw Muhammad], lu dul ay góor yu ñu soloo ñu dëkk ca njénde ya. [Nee leen] ndax dañoo doxul ci suuf si, ba seetlu lan mooy mujjug ña leen jiitu woon ? Te ca dëgg-dëgg kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla. Moo ndax dangeen dul xel-lu ?
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Ba ña Nu yónni naagoo ne [ndimbal dootul ñëw] te ñu jort ne weddeef nañu leen ba noppi, foofa la Sunu ndimbal agsee ci ñoom. Nu musal ku Nu soob. Te Sunu mbugal amul kenn ku ko mën a fegal tooñkat ya.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Seen nettali yooyu ay waaree nga ca ñeel woroom xel ya. Du waxtaan wu ñu sos. Waaye day dëggal ya jiitu, te it di leeral lépp lu nekk di ag njub, di yërmaande ñeel nit ñu gëm.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







