Simoore Al-Kahf
110 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Gépp cant ñeel na Yàlla mi wàcce Téere ba ca jaamam [Muhammad], te defalu ko genn logg-logg !
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Muy lu jub xocc, di xuppe ci mbugal mu tar lu jóge ci Moom ak di bégle way-gëm ñay jëf jëf yu yiw, ci ne ñoom am nañu pey gu rafet.
ﯸﯹﯺﯻ
te dañu cay sax dapet dàkk ba fàwwu,
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
te muy xupp ñay wax naan : “Yàlla am na doom.”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Amuñu ci loolu benn xam-xam, Seeni baay it [amuñu ko ca]. Muy wax ju réy ju génne ci seen gémmiñ! Waxuñu lu dul fen.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Te xéy-na nga lor sa bopp ci naqarlu ngir li ñu ñàkk a gëm kàddu ga !
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Nun noo def ci suuf si taaram ngir nattu leen, [ba xam] ña ca gën a rafet jëf.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
De Dananu def li nekk ci kawam nekk di pàkk bu wow koŋŋ.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Ndax amuloo njort ci ne, ñoñ-xunt ma ak ñoñ-mbind ma [téere ba] bokkoon nañu ca Sunuy kéemaan yu doy waar [yéeme] ?
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
[Fàttalikul] ba waxamaande ya làqoo ca xunt ma, te ñu waxoon ne : “Yaw sunu Boroom, may nu yërmaande ju bawoo ci yaw; te nga yéwénal sunuy mbir mu nekk cig njub”.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Nu fëkk seeni nopp [nelawloo leen] ca biir xunt ma ay at yu limu.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Topp Nu yee leen ngir bëgg a xam ban ci ñaari kurél yii moo gën a xayma diir ba ñu fa toog.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Noo ngi lay nettali seeni mbir ci dëgg. Ne ko ñoom ay waxambaane lañu yu gëmoon seen Boroom ; ba tax na ñu gën leen a dëgëral cig njub.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Nu dëgëral seeni xol ba ñu taxawee [ca kanamu buur ba nekkoon jaamukatu xërëm], wax ne : “Sunu Boroom mooy Boroom asamaan yi ak suuf si : dunu jaamu jeneen Yàlla bàyyi ko, ndax kon dananu wax lu jeng.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Sunuy nit a ngi nii di jaamu yu ñu tudde ay yàlla bañ a jaamu Yàlla. Lu tee ñu indi ci ñooom ay lay yu bir ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Bu ngen leen beroo ñoom ak li ñuy jaamu bàyyi Yàlla, nangeen dugg ci xunt mi : Seen Boroom dana leen wasaareel seeni mbir ci yërmaandeem te Dana leen yéwénalal seeni mbir cig jàppandal”.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Doon nga gis jant bi su fenkee mel ni lu jàdd jëm ca ndeyjooru xunt ma, te buy so mel ni luy jëm càmmoñ, ñu nekk ca digg xunt ma... Loolu ci kéemaani Yàlla la bokk. Ku Yàlla gindi mu jub. Ku Mu bàyyi cig réer, du am kilifa gu koy jubbanti.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
[Boo leen gisoon], dangay defe ne dañoo yewwu te fekk ñoo ngay nelaw. Nu leen di wëlbati lee-lee jëme càmmoñ, seen xaj ba it di nelaw tàllal ñaari tànk ya ca ëttu xunt ma. Boo leen yëroon kon dey danga wëlbatiku daw ngir tiitaange.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Noonu la Nu leen yewwuloo ngir ñu laajante. Mu am ci ñoom ku ne : “Ana ban diir ngeen fi toog ? ” Ils dirent : “Nous avons demeuré un jour ou une partie d'un jour”. Ñu ne : “Seen Boroom dal a gën a xam diir bi ngeen fi toog. Léegi yónnileen ken ci yéen ak seen xaalis bii, den ca dëkk ba utal nu fa ñam wu gën a sell, mu indil nu ci xéewal. Na beru te bumu yégal kenn dara ci yéen.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Ñoom bu ñu leen yëgee, danañu leen rey, mbaa ñu delloo leen ci seen diine te kon dootuleen texe ba fàwwu”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Nu feeñal leen ca waa dëkk ba, ngir ñu xam ne digu Yàlla lu dëggu la te xam it ne waxtu wa [àddinay jeex] amul sikk ci ne luy am la. Ba ñuy xëccoo ci seen biir ci mbirum [waxembaane ya], ñu naan : “Tabaxleen ci seen kaw am taax. Seen Boroom a gën a xam seen mbir”. Ña not wax ja ci seen mbir ne : “Nanu def ci seen kaw jàkka”.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Danañu wax ne : “Ñett lañu woon, seen xaj ba ñeenteel leen”. Danañu wax it ne juróom lañu woon, seen xaj bi juróom-benneel leen, muy njort ci lu fàddu. Te danañu wax ne : “Juróom-ñaar lañu woon, seen xaj ba juróom-ñetteel leen”. Neel : “Sama Boroom a gën a xam seen lim. Te kenn xamu ko lu dul ñu néew”. Bul werante ci ñoom lu dul ci waxi biti te bul sàkku xam ci kenn ci ñoom.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Bul wax mukk ci dara ne : “Man dana def nàngam ëllëg”.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
[te boolewoo ca] : “Bu soobee Yàlla”, tuddal sa Boroom, boo fàttee fàttaliku Ko te nga wax ne : “Xéy-na sama Boroom gindi ma jëme ma ca la gën a jegeñ lii cig njub”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Toog nañu ca seen xunt ma ñetti téeméeri at yu teg juróom-ñeent.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Neel : “Yàllaa gën a xam diir ba ñu fa toog. Ñeel na ko [moom Yàlla] kumpag asamaan yi ak suuf si. Nangay gise ci Moom, di dégge ci Moom ! Amuñu ku leen di wattu ci Moom, du boole kenn ci àtteem.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Jàngal li ñu la soloo ci sa Téereb Boroom. Bul soppiy waxam [ay waxam du soppiku]. Te doo am mukk wéeruwaay wu dul Moom.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Nangay muñ ànd ak ñay jaamu seen Boroom suba ak ngoon ngir xemmem jëmam. Te say gët bumu leen jéggi ngir xemmem taaru dundu àddina. Te bul topp koo xam ne sàgganloo nañu xelam ba dunu fàttaliku, di ku topp bakkanam, mbiram di lu jéggi dayoo.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Neel : “Dëgg ga ca seen Boroom la jóge”. Ku yabu na gëm, ku yabu na weddi”. Naka Nun xaroo Nanu way-tooñ ña Safara soo xam ne ay sàkketam wër na leen. Te bu ñu bëggee xettaliku, ñangay xettalikoo ndox mu deme ni weñ gu ruy guy ñoral kanam. Ndaw naan gu bon ak yenduwaay bu bon te naqari!
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Naka ña gëm tey jëf jëf yu yiw... , [nañu xam ne] Dunu sànk peyug kuy rafetal jëfam.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Ñooña ñeel na leen Àjjana dëkkuwaay boo xam ne ay dex dañuy daw ca suufam. Te deef na takkaayale ca foofa ay lam yu wurus te danañu fa sol ay yére yu nëtëx, di yéréy sooy bu sew ak sooy bu tal, ñu sóonu ca seen lal ya. Ndaw yool bu neex, waay-waay ndaw yenduwaay bu rafet te neex !
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Joxleen leebuw ñaari góor ñoo xam ne : kenn ka jox Nanu ko tool bu am garabi reseñ, Nu wërsëgale leen ak garabi tàndarma, Nu def ca seen diggante ay tooli mbey.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Ñaari tool yépp ñu cay jële meññent mu dara wàññeekuwut. Nu xotti ca seen diggante ag dex.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Mu am meññent [mu bari] tax mu wax ak moroom ma neko : “Maa la ëpp alal te gën laa bari mbooloo”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Mu dugg ca toolam te moom tooñ na boppam ; mu ne : “Yaakaar naa ne lii du jeex mukk,
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
te yaakaaruma [foogu ma] jeexug àddina dana egsi. Te sax su ma [deeyoon] ba dellu ca sama Boroom fàwwu, danaa fa fekk lu gën lii cig daluwaay.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Moroom ma wax ak moom, tontu ko ne ko : “Moo ndax dangaa weddi Ki la binde ci suuf, topp ci toqit [gu jóge ci góor], topp Mu melal la nga di góor gu mat sëkk ?
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Waaye man, Moom Yàlla moo di sama Boroom ; te duma bokkaaleek sama Boroom kenn ?
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Lu teewoon ba ngay dugg ca tool ba nga wax ne : “Lu neex Yàlla [rekk ay am] ! Amul kenn ku am kàttan ku dul Yàlla”. Ndeem danga maa gis ma gën laa néew alal ak i doom,
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
xéy-na sama Boroom jox ma lu gën sa tool, te yabal ca sa tool jéyya ju jóge asamaan ba mu nekk dénd bu amutul dara,
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
walla ndox ma ŋiis te dootu ko ame feneen”.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Alageef na meññent ma mu xëy di moqarñi ñaari yoxoom ngir la mu ca tàbbal ci alal, te fekk tool ba yàqu na, garab ya daanu, dàmme ca dàtt ya. Mu naan : “Ay aka neexoon bokkaalewuma kenn ak sama Boroom ! ”.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Te amatul mbooloo mu ko mën a dimbali ku dul Yàlla. Te nekkul it di mënal boppam dara.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Fu mu doon, kaaraange ñeel na Yàlla ju dëggu ja. Mooy joxe gën ji yool ak gën ji muj.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
Joxleen léebug dundu àddina. Dafa mel ni ndox mu ñu wàcce mu jóge asamaan ; tax gàncax ga jóge ci suuf sax. Mu mujj nekk mboob mu wow, ngelaw yi tasaare ko. Yàlla ku am kàttan la ci def lu ne !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Alal ak i doom ci yiy neexal àddina lañu bokk. Waaye way-des ya di [jëf] yu yiw, ñooy ya gën ca sa Boroom ci wàllu yool ak yaakaar.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Bis ba Nuy doxloo tundi doj yi nga gis suuf si maase nerr, Nu fang leen te Dunu bàyyi kenn ci ñoom.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Te Nu werale leen ci sa kanamu Boroom ñu def ay sàppe. “Dangeen di sikk ci ne sàkk Nanu ab dig [bu ngeen di dekkee]”.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Ñu teg Téere ba. Nga gis saay-saay sa tiit ca la nekk ca biir, ñu naan : “Ngalla nun, cëy waay téere bii, bàyyiwul lu tuuti, bàyyiwul lu rëy, bind na lépp ? ” Ñu gis la ñu defoon di lu teew. Te sa Boroom du tooñ kenn.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya ne leen : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñu sujjóot [ñoom ñépp] ba mu des Ibliis, moom bokkoon na ca jinne ya, daldi sàqi ndigalu Boroomam. Ndax dangeen koy jàppe xarit mook i sëtam, bàyyi Nu [Nun Yàlla], te ñoom seeni noon lañu ? Bon na, li tooñkat ya di weccee !
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Seedeloowunu leen it sos ga Nu sos seeni bakkan. Te it jàppewuma [ñiy sànk nit ñi] ñu may jàppale.
ﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Ca bis ba Mu waxee ne : “Wooleen sama bokkaale ya ngeen sos”. Bu ñu leen woo dey, duñu leen wuyyu ndax def Nanu ci seen diggante aw xur.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Te saay-saay sa jenook Safara daldi foog ne dañu cay tàbbi te duñu ca am aw rawtukaay bu ñu ca rëccee.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Te Nun biral nanu ci Alxuraan jii, ngir nit ñi, léebu wu nekk. Waaye nit mooy ki gën a mën a dàggasante ci mbindeef yi.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Li tere nit ñi ñu gëm ba leen njub ga dikkalee, te ñu baalu seen Boroom, lu dul dañoo bëgg mu dikkal leen la daloon seen maam ya, walla mbugal dikkal leen [mu leen bett] jàkkaarlook ñoom.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Dunu yónni Yonent yi lu dul ngir ñuy bégle, di xuppe. Te ña weddi di dàggasante cig neen, ngir bëgg cee yàq dëgg ga, di weddi Sunuy kàddu ak la ñu leen di waare.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Ana ku gën a tooñ ku ñu waar ci kàdduy Boroomam, mu dëddu te fàtte la yaari yoxoom doon jëf ? Nun def nanu ci seeni xol muuraay ngir duñu ca am dégg-dégg ak i saañ ca seeni nopp. Tax na boo leen woowee jëme leen ci njub, duñu gindiku ba fàwwu.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Te sa Boroom mooy Jéggalaakoon ba, di boroom yërmaande. Bu leen jàppe woon la ñuy fàggu [ciy jëf yu bon]. Kon Dana gaawal seen mbugal. Waaye am nañu àpp boo xam ne bu agsee, duñu am mukk ku leen musal ku dul Moom.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
[Noonu la] Nu alage woon dëkk yooyu ba ñu tooñee te Nu sàkkaloon alkaande ja ab àpp.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
[Fàttalikul] ba Muusaa waxee surgaam ba ne ko : “Duma deñ di dox ba mbete ma eggee ca dajewaayu ñaari geej ya, walla may wéy jamano ju yàgg”.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Ba ñu eggee ñoom ñaar ca dajewaay ba, ñu fàtte ca diggante ba seenu jën, mu potoxlu daldi koy rëcc jëlu yoonam ca biir géej ga.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Ba ñu ko weesoo, mu ne surgaam ba : “Indil sunu añ : daj nanu coono ci sunu tukki bii”.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Mu tontu ne : “Ndax gisoo ba nu toogee ca doj wa, damaa fàtte jën wa - te dara fàttewooluma ko lu dul Séytaane mi tax xalaatuma ko - mu dem yoonam ci géej, lu yéeme”.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Muusaa ne ko : “Loolu lanu doon sàkku”. Ñu dellu fa ñu jaaroon di xeeñtu.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Ñu daje ak ab jaam ci sama jaam yi boo xam ne may Nanu ko yërmaande lu jóge ci Nun, te jàngal Nanu ko xam-xam bu bàyyikoo ci Nun.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Muusaa ne ko : “Ndax ma topp la ci kaw nga jàngal ma ci lu xamaleef na la ko ci luy gindee [ak xamle] ? ”.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Mu tontu ko, ne: “Doo mën a ànd ak man ci sag muñ.
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Naka ngay muñee ci loo xam ne peeguloo ko ci xam-xam ? ”.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Mu ne ko : “Danga ma fekk bu soobee Yàlla ma di muñkat ; te duma moy sa lenn ndigal”.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Mu ne ko : “Boo ma toppee, bul ma laaj ci dara, ba kerook ma la ciy niital dara”.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Ñu ànd ñoom ñaar. Ba ñu duggee ci genn gaal, mu xar gaal ga. Muusaa ne ko : “Ndax danga koy xar ngir labal ña ca nekk ? Def nga jëf ju siibu ! ”.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Mu ne ko : “Ndax waxuma la woon ne doo mën a ànd ak man ci sag muñ ? ”.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Mu ne ko : “Bul ma jàppe ci lu ma fàtte ; te it bul ma togg-jëf ci sama mbir”.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖ
Ñu demaat ba dajeek benn xale, mu rey ko. Muusaa ne ko : “Ndax dangay rey bakkan bu sell bu reyul bakkan ? Def nga jëf ju yéeme ! ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Mu ne ko : “Ndax waxuma la woon ne mënuloo muñ li may def soo àndeek man ? ”
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
[Muusaa] toontu ko ne : “Saa yu ma la laajee menn mbir, kon bul àndateek man. Ndax am nga ngànt ci tàggook man”.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Ñuy dox ba egg cib dëkk, ñu sàkku ca waa dëkk ba lekk, ñu lànk leen a ganale. Noona mu gis ab tabax buy bëgg a daanu. Mu yékkatiwaat ko. [Muusaa] ne ko : “Su la neexoon dey nga laaj ag pey”.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Mu ne ko : “Maak yaw fii la nuy tàqalikoo.Waaye danaa la leeralal mbirum li nga mënul woon a muñ.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
[Gaal ga ma bënoon], ay ndóol ñoo ko móomoon, daan ca daan seen doole ngir dundu. La tax ma bënn ko moo di dafa buur bu daan siif gépp gaal gu mu romb, ma bënn ko ngir mu bañ koo yóbb.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Xale [ba ma reyoon], ay waajuram dañoo doonoon ñu gëm Yàlla ; te su màggoon, dana leen weddiloo, beewloo leen.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Nu bëgg Yàlla soppil leen ko ku gën a sell, gën a topp i [waajuram].
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Tabax [ba ma doon yékkatiwaat], ñaari xale yu jirim ñoom la ko fa seen baay bàyyil; seen baay doonoon ku yiw, ku baax, am alal ju mu leen ca dencal. Sa Boroom bëgg su ñu màggee mën a gindiku jël seen alal joojee ci yërmaandey Yàlla. Defuma ko woon rekk ci sama coobarey bopp. Loolu kon mooy mbirum la nga mënul woon a muñ”.
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Danañu lay laaj ci mbirum [Zul-Qarnayni]. Neel : “Danaa leen jàngal na mu doxe woon”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Mayoon Nanu ko kàttan ci kaw suuf ba mu mën a def lépp lu mu bëgg.
ﭜﭝﭞ
Mu sóobu bëgg-bëggam, topp aw yoon di dem.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Mu takk xare dem ba fa sowwu yem, mu fekk ne jant ba ma ngay sowe fa ndox ma ànd ak ban, mu fekk itam aw xeet [wa ko dëkke]. Ñu ne ko : “Fàwwu yaw Zul-Qarnayni ! nga mbugal leen walla nga yërëm leen”.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Mu wax ne : “Képp koo xam ne dafay tooñ, dananu ko mbugal fii ; te su delloo fa Boroomam, Dana ko mbugal mbugal mu gën a tar.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Képp koo xam ne dafa gëm tey jëf u yiw, dana am pey gu gën a rafet. Te it fu mu tollu di gis yombal gu bawoo fi nun”.
ﮖﮗﮘﮙ
Mu dellu sóobu ci bëgg-bëggam.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Mu takk xare dem ba fa penku yem, mu fekk fa xeet wu amul lu leen yiiral tàngooru jant bi.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Mu wax ne : na ñu defoon ñële rekk la ñuy def ñii, waxoon nanu lépp la mu nar.
ﯓﯔﯕﯖ
Mu wéyati ci bëgg-bëggamdi dox di wéy.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Muy dem ba fekk aw xur mu fekk aw xeet, woo xam ne, seeni wax xaw naa niru waxi nit
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Ñu ne ko : "Yaa juuja ak Maa juuja ay yàqkat lañu ci kaw suuf si. Moo ndax duñu la fey nga ñag sunu diggante ak ñoom ? ”
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Mu ne leen : “Li ma Yàlla defal moo gën ci man [seenug pey]. Li may laaj rekk mooy ngeen jàppale ma, danaa defar ab ñag seen diggante ak ñoom.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛ
Indil-leen ma mbuluŋi weñ gu ñuul, te ngeen fatte ko bën-bën yii, te ngeen soy ko ba mu ruy, ngeen sotti ci betteex bi”.
ﰜﰝﰞﰟﰠﰡﰢﰣﰤ
Yaa juuja ak Maa juuja duñu ko mën a bënn te duñu ko mën a daane.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Zul-Qarnaynine leen : “Lii dey xéewal la gu bawoo fa Yàlla. Waaye, Saa su digub Yàlla agsee, ca la koy màbb. Te digub Yàlla bi dëgg la te fàwwu mu dikk”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Bu boobaa, nit ñi dañuy mbëkkënte ni ay duusi géej, bu ñu walee buftu ba, Nu daldi leen di dajale ñoom ñépp.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Ca boobale bis Dananu gaaral yéefar yi ca Safara,
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
[Yéefar] yi nga xam ne dañu daan muur seeni gët ngir bañ a gis Sunuy tegtal, te daan ko bañ a dégg.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Ndax ña weddi [Yéefar ya], dañoo njort ne mën nañoo am wéeruwaay ci sama jaam ñi féddiku Ma ? Déedéet yéefar yi Safara la leen di xaaroo de.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Neel : “Moo ndax duma leen xamal ñi gën a sànk seen jëf ?
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Ñoo di gaa ña nga xam ne sànk nañu seeni jëf, dara baaxu ca, ba noppi ñuy njort ne li ñuy jëf baax na.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Ñoom ñoo di ña daan weddi kàdduy Yàlla seen Boroom ak daje ga ñu nar a dajeek Moom. Seeni jëf sippiku na”. Kenn duleen peeseel dara.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Loola moo tax ñu feye leen Safara, ngir la ñu weddi woon tey jàppe Sunuy kàddu ak Sunuy Yonent ay caaxaan.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Ña gëmoon tey jëf u yiw, Àjjana [Firdawsi] mooy seen wàccuwaay,
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
dañu fay béel te duñu ko bëgg a weccee.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Waxalne : “Su ndoxum géej gi doonoon daa, ñu di ca binde kàdduy Yàlla yi, kon ndox ma dana jeex balaa kàddu ya di mat, doonte la sax dañu cay dolliwaat lu tollu ni géej ya”.
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝ
Neel : “Man dey mbindéef laa ni yéen. Danu may soloo rekk, waaye li wóor moo di seen Yàlla jenn rekk la ! [Kon nag], képp ku yaakaar dajeek Boroomam, nay jëf jëf yu yiw te bu mu bokkaale dara ak Boroomam [na ko jaamu Moom doŋŋ]”.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers