Simoore Ar-Rahman pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Ar-Rahman pdf Wolof — Wàcce Simoore Ar-Rahman Tekki. Simoore Ar-Rahman (Medinan) 78 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Ar-Rahman

ﭷﭸ
55:1
Yërëmaakoon bi.
ﭹﭺﭻ
55:2
Moo jàngale Alxuraan (xamle ko).
ﭼﭽﭾ
55:3
Moo bind nit (sos ko).
ﭿﮀﮁ
55:4
Moo ko jàngal waxiin wu leer.
ﮂﮃﮄﮅ
55:5
Jant beek weer wi ne rojj yemoo
ﮆﮇﮈﮉ
55:6
garab yi ak ñax mi dañuy sujuud.
ﮊﮋﮌﮍﮎ
55:7
Moom moo kaweel asamaan. Teg ca ay nattukaayam màndaxe (balaas),
ﮏﮐﮑﮒﮓ
55:8
buleen di naxe mukk ci màndaxe natt :
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
55:9
Nangeen di natt cig maandute buleen njuuj-njaaj.
ﮛﮜﮝﮞ
55:10
Moo tàllal, suuf ñiy dunde :
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
55:11
am na ay fuytéef, ak tàndarma yuy meññ,
ﮥﮦﮧﮨﮩ
55:12
ak ay fepp yu nekk ci mbaram, ak gàncax yuy gilli.
ﮪﮫﮬﮭﮮ
55:13
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
55:14
Moom moo bind nit ci ban bu tikk dëgër ;
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
55:15
te Moo bind jinne ci safara wuy bérëx wu amul saxaar;
ﯝﯞﯟﯠﯡ
55:16
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯢﯣﯤﯥﯦ
55:17
Boroom ñaari Penku yi tey Boroom ñaari Sowo yi !
ﯧﯨﯩﯪﯫ
55:18
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭑﭒﭓﭔ
55:19
Moo dajale ñaari géej ya ;
ﭕﭖﭗﭘﭙ
55:20
def na aw dig ca seen diggante ba duñu jaxasoo.
ﭚﭛﭜﭝﭞ
55:21
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭟﭠﭡﭢﭣ
55:22
Te ñaari [géej]: yooyu peme da ciy génne ak ganjar.
ﭤﭥﭦﭧﭨ
55:23
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
55:24
Moo moom gaal yiy tëmbu ci biir géej niki ay tundi doj ;
ﭰﭱﭲﭳﭴ
55:25
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭵﭶﭷﭸﭹ
55:26
Képp kuy dund kaw [suuf] dana masa saay jeex,
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
55:27
Sa Jëmmi Boroom doŋŋ fiy des, moom miy boroom màgg gi ak teraanga.
ﮁﮂﮃﮄﮅ
55:28
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
55:29
Ñi nekk asamaan ak suuf sii ngi koy laaj aka Dagaan. Te moom bis bu nekk, Mi ngi ci mbir.
ﮒﮓﮔﮕﮖ
55:30
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮗﮘﮙﮚﮛ
55:31
Yéen nit ak jinne yi, danañu leen xalseta àtte
ﮜﮝﮞﮟﮠ
55:32
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
55:33
Eey yéen mbooleem jinne yi ak nit ñi ! Su ngeen manee lañbatu ci biir déeléy asamaan yeek suuf si, lañbatuleen. Waaye du ngeen mana kër-këri mukk ba génn kiiraayal Yàlla.
ﯔﯕﯖﯗﯘ
55:34
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
55:35
Dees na leen xala sotti safara ak biteex, te kenn du leen dimbali.
ﯢﯣﯤﯥﯦ
55:36
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
55:37
Su asamaan si xottikoo ruy mel ni beteex.
ﯮﯯﯰﯱﯲ
55:38
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
55:39
Bu keroogee, nit ak jinne, kenn deesu ko laaj bàkkaaram.
ﯼﯽﯾﯿﰀ
55:40
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
55:41
Tooñkat ya dees na leen xàmmee ci seeni màndarga. Te deef na leen joñ boole seen bopp ak seeni tànk.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
55:42
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
55:43
Waaw-kay nag Safara sa tooñkat ya daan weddee ngi nii.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
55:44
Ñangay wëndéelu diggante (Safara sa) ak ndox muy bax.
ﭣﭤﭥﭦﭧ
55:45
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
55:46
képp ku dëggël tey wagar taxawaay ba ca kanam Boroomam, dana am ñaari àjjana ;
ﭮﭯﭰﭱﭲ
55:47
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭳﭴﭵ
55:48
Yu am car yu dëll meññ gacc.
ﭶﭷﭸﭹﭺ
55:49
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭻﭼﭽﭾ
55:50
Am na fa ñaari bëti ndox yuy daw-dawaan.
ﭿﮀﮁﮂﮃ
55:51
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
55:52
Nekk na ca biir ci xeetu fuytéef wu nekk ñaari wirgó
ﮊﮋﮌﮍﮎ
55:53
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
55:54
ñangay sóonu ci ay laltaay yu dëll yoo xam ne biir ga sooy la, te it meññatum ñaar dër ya day yoore.
ﮚﮛﮜﮝﮞ
55:55
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
55:56
Ay Huur Al iin ñuy sajj seenub gis, ñoo xam ne nit walla jinne masu leen laal ñuy nekk ca biir.
ﮩﮪﮫﮬﮭ
55:57
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﮮﮯﮰﮱ
55:58
Dañuy [rafet ba] melni: wurus yaaquut walla marjaan.
ﯓﯔﯕﯖﯗ
55:59
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
55:60
Moo ndax lu rafet man naa am geneen pey guddul lu rafet (mukk du am) ?
ﯞﯟﯠﯡﯢ
55:61
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯣﯤﯥﯦ
55:62
Ci dër yooyu amaat na yeneen ñaari dër.
ﯧﯨﯩﯪﯫ
55:63
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯬﯭ
55:64
Ñu di ñaari dër yu naat lool nëtëx.
ﯮﯯﯰﯱﯲ
55:65
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯳﯴﯵﯶ
55:66
Nekk na ci seen biir ñaari bëti ndox yuy jol di fuur.
ﯷﯸﯹﯺﯻ
55:67
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﯼﯽﯾﯿﰀ
55:68
am na ci biiram ay fuytéef, ak i tàndarma, ak rummaan.
ﰁﰂﰃﰄﰅ
55:69
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭑﭒﭓﭔ
55:70
ay jigéen ñu yiw te rafet jekk, ñoo nekk ca biir.
ﭕﭖﭗﭘﭙ
55:71
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭚﭛﭜﭝﭞ
55:72
jigéenu huur yu sax fa seen mbaar ya,
ﭟﭠﭡﭢﭣ
55:73
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
55:74
nit wala jinne masuta laal jigéen ñooñu.
ﭫﭬﭭﭮﭯ
55:75
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
55:76
Ña ngeen soonu ci ay ngegenaay yu nëtëx (wert) ak ay laltaay yu rafet.
ﭷﭸﭹﭺﭻ
55:77
Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
55:78
Saw turu Boroom Baarkeel na, moom miy Boroom Màgg ak Teraanga ji !
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers