Simoore Al-Hashr
PDF —
24 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Hashr pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Hashr pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Hashr Tekki. Al-Hashr (Medinan) 24 Aaya.



Simoore Al-Hashr
24 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Ñi nekk ci Asamaan yeek suuf si ñi ngi sàbbaal Yàlla, te moo di boroom kàttan gi, di Ku xereñ ki.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Te mooy Yàlla moo génnee woon ña weddi te bokk ci, ñoñ Téere (Yahuudi Madiina), ci seen kër ca njaalbeenuk màng ga (Jëm Saam). Jortuleen woon ne danañu génn, ñoom (Yahudd ya it) jortoon nañu ne seeni tata dana leen aar. (Yàlla) daldi nay tàbbal tiitange ci seen xol,. Ñu tàmbalee gental seen kër ya ci seeni yoxo, ak yoxoy jullit ñi. Xalamleen (xalaat), yéen ñi am am njis mu leer.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Su Yàlla dogalul woon seenug génn (réew mi), kon dey Mu mbugël leen ci àddina ; te bu àllaaxiraa it ñu am mbugëlum Safara.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Li ko waral moo di ne ñoom dañoo juuyoo woon ak Yàlla ak ub Yonentam. Te nag képp kuy juuyook Yàlla... moom di boroom mbugël mu tar.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Tàndarma gu ngeen man a dog walla ngeen bàyyi ko mu taxaw, ci ndigalul Yàlla la ame ak it ngir mu gàcceel saay-saay sa (Yahuud ya).
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Li ngeen nangoo ci ñoom (alal) te xeexuleen Yàllaa ko baaxe ab Yonentam ; waaye nag Yàlla mooy bal ay Yonentam ci kaw ku ko soob te Yàlla ku am kàttan la ci def lépp lu ne.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Alal ji ngeen nangoo ci dëkk-dëkkaan yi te xeexuleen, Yàllaa ko moom ak ub Yonentam, ak mbokki jigeñaale, ak jirim yi, ak ndóol yi ak doxandeem yi, ( te loolu nag ngir mu baña yem rek) ci diggante way woomal yi. Lépp lu leen Yonent bi jox jël-leen ko ; lépp lu mu leen tere, bàyyileen ko ; te ngeen ragal Yàlla ndax Yàlla kat ku tar mbugël la.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] way ñakk ña gàddaayoon ñu génnee woon leen ca seen kër ak seen alal, te doon sàkku ngëneel ci Yàlla ak ngëramam, te doon sàkku ndimbalu Yàlla ak Ub Yonentam. Ñooña ñoo di ñu dëggal ña.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] ña dëkke woon réewum (Madiina), te gëmoon ba ñu leen laataa fekk si, te soppoon lool ña gàddaay jëm si ci ñoom, iñaane wuñu leen dara, di jiital aajoy ña gàddaay ci seen aajoy bopp, ak luñu ñàkk ñàkk. Képp ku mucc ci nay, baaxle na fàww.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] ña dikk seen ginnaaw tey wax naan : “Yaw sunu Boroom, jéggalnu, nook sunu mbokk yi ñu jiitu ci ngëm ; te bul bàyyi genn mbañeel ci sunuy xol jëm ci ñi gëm. Yaw sunu Boroom, Kuy ñewenti nga Kuy Jaglewaakoon nga sa Yërmënde”.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Xanaa gisuloo ña naaféq ña ngay wax ak seeni mbokk ya weddi ci ñoñ Téere naan leen : “Bu ñu leen génnee, dananu génn ànd ak yéen te dunu topp kenn ci lu leen di lor yéen ; te kuy xex ak yéen, nun yéen la nuy jàppale”. Te Yàlla seede na ne ñoom ay fenkat la ñu.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Bu ñu leen génnee woon, ñoom duñu génn mukk di ànd ak ñoom ; bu ñu doon xeex it , dunu leen jàppale ; sax dañuy mujj daw ; te duñu am ndam.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Ñoom naaféq yi seen jëmm yii la ñu gën a ragal ci Yàlla. Ndax ñoom dañoo xamul.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Duñuy xeex ak yéen mukk (ñoom naaféq ya) lu dul biir dëkk yu ñu tata ci ginnaaw ay ñag. Seenug noonoo ci seen biir lu tar la. Danga foog ne ñu ànd lañu, te seeni xol dañoo féewoo. Li ko waral moo di ne dañoo amul ay xol di ko jariñoo.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
danoo melni ñi leen jigeñ, te jiitu woon leen (Yéefëri Makka), mos nañu alkaande seen jëf te danañu am mbugël mu tar ;
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
dafay melni rekk Saytaane ba muy wax ak nit naan ko : “Weddil”. Ba mu weddee, mu ne ko : “Man kat deñ naa ci yaw ndax man damaa ragal Yàlla, miy Boroom àddina si”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Su ko defee ñoom ñaar Safaraay doon seenug muj ñu béel fa. Loolu mooy peyug tooñkat ya.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla. Bakkan bu nekk nay xool la muy jiital ngir ëllëg. Te nangeen di ragal Yàlla, Yàlla dey ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Buleen def mukk ni gaa ña fàtte woon Yàlla ; Mu faf fàttiloo leen seen bopp ; ñooñee ñoo di saay-saay si.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Waa Safara duñu yem ak waa Àjjana mukk. Ndax waa Àjjana ñoo di ña texe.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Sunu wàcce woon Alxuraan jii ci kaw aw doj, kon dey nga gis ko muy toroxlu daldi moñoxoo ngir ragal Yàlla. Yooyu ay léeb la yu nuy saddal nit ñi ngir ñu man caa xalaate.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Moom mooy Yàlla ji nga xam ne. Amul jeneen Yàlla ju dul moom, Moo xam kumpa ak li Feeñ. Mooy, Yëramaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Moom Mooy, Yàlla ji nga xam ne. Amul jeneen Yàlla ju dul moom ; mooy Boroom bi, di Ku Sell ki, di Jàmm ji, di Ku Wóor ki, di Ku Peek lépp, di Boroom Kàttan gi, di Ponkal mi, di Ku Rëy ki. Tudd naa Sellam gi ! Soree na lool ak li ñu koy bokkaaleel.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Moom Mooy Yàlla, Bindkat biy sos, tey Melal. Mooy boroom tur yi gën a rafet. Mbooleem li nekk ci asamaan yeek suuf si dañu koy sàbbaal di ko kañ. Moom moo di boroom Kàttan gi, di Ku Xereñ ki.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers