Simoore Al-'Ankabut ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-'Ankabut ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (69 Aaya — مكية). Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-'Ankabut

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
الم ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Alif, Laam, Miim.
أَحَسِبَ النَّاسُ أَن يُتْرَكُوا أَن يَقُولُوا آمَنَّا وَهُمْ لَا يُفْتَنُونَ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Ndax nit ñi foog nañu ne danañu wax ne : “Gëm nañu ! ” te kenn duleen sànje ?
وَلَقَدْ فَتَنَّا الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۖ فَلَيَعْلَمَنَّ اللَّهُ الَّذِينَ صَدَقُوا وَلَيَعْلَمَنَّ الْكَاذِبِينَ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Sànje woon Nanu ña leen jiitu woon ; Yàlla xam na ñay dëggal ak ñay fen.
أَمْ حَسِبَ الَّذِينَ يَعْمَلُونَ السَّيِّئَاتِ أَن يَسْبِقُونَا ۚ سَاءَ مَا يَحْكُمُونَ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Walla ñay jëfi ñaawteef, jàpp nañu ne danañu Nu jiitu ? Aka ñoo ñaaw ab àtte !
مَن كَانَ يَرْجُو لِقَاءَ اللَّهِ فَإِنَّ أَجَلَ اللَّهِ لَآتٍ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Képp kuy yaakaar a dajeek Yàlla, digub Yàlla boobu luy dikk la. Te Mooy dégg, di xam.
وَمَن جَاهَدَ فَإِنَّمَا يُجَاهِدُ لِنَفْسِهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَغَنِيٌّ عَنِ الْعَالَمِينَ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Képp kuy xare, boppam la koy defal, Yàlla ku doylu la ci waa àddina bi yépp.
وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَنُكَفِّرَنَّ عَنْهُمْ سَيِّئَاتِهِمْ وَلَنَجْزِيَنَّهُمْ أَحْسَنَ الَّذِي كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Ñi gëm tey jëf u yiw, Dananu leen faral seeni ñaawteef, te Dananu leen feye ca la gën ca la ñu daan def.
وَوَصَّيْنَا الْإِنسَانَ بِوَالِدَيْهِ حُسْنًا ۖ وَإِن جَاهَدَاكَ لِتُشْرِكَ بِي مَا لَيْسَ لَكَ بِهِ عِلْمٌ فَلَا تُطِعْهُمَا ۚ إِلَيَّ مَرْجِعُكُمْ فَأُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Dénk Nanu nit muy def yiw ciy ñaari way-juram, “bu ñu la sonnalee nag ci bëgg nga bokkaale Ma ak loo xamul, buleen ca topp”. Ci Man ngeen di dellusi, Ma xibaar leen la ngeen daan def.
وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَنُدْخِلَنَّهُمْ فِي الصَّالِحِينَ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Ña gën tey jëf u yiw, Dananu leen dugal ca nit ñu yiw ña.
وَمِنَ النَّاسِ مَن يَقُولُ آمَنَّا بِاللَّهِ فَإِذَا أُوذِيَ فِي اللَّهِ جَعَلَ فِتْنَةَ النَّاسِ كَعَذَابِ اللَّهِ وَلَئِن جَاءَ نَصْرٌ مِّن رَّبِّكَ لَيَقُولُنَّ إِنَّا كُنَّا مَعَكُمْ ۚ أَوَلَيْسَ اللَّهُ بِأَعْلَمَ بِمَا فِي صُدُورِ الْعَالَمِينَ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Am na ci nit ñi ñuy wax naan : “Gëm Nanu Yàlla” ; te bu ñu leen loree ci ànd gi ñu ànd ak Yàlla, dañuy jàppe sànjeb nit ñooñu ni mbugalum Yàlla. Bu leen ndimbal dikkalee lu bawoo ca sa Boroom, ñu tàmbalee wax naan : “Nun ak yéen a àndoon ! ” Moo ndax Yàlla dafa gënul a xam li nekk ci dënni waa àddina si yépp ?
وَلَيَعْلَمَنَّ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَلَيَعْلَمَنَّ الْمُنَافِقِينَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Yàlla xam na tigi ña gëm, xam na itam naaféq yi .
وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لِلَّذِينَ آمَنُوا اتَّبِعُوا سَبِيلَنَا وَلْنَحْمِلْ خَطَايَاكُمْ وَمَا هُم بِحَامِلِينَ مِنْ خَطَايَاهُم مِّن شَيْءٍ ۖ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Yéefar yaa ngay wax ña gëm naan leen ; “Toppleen sunu mboor, dananu yenu seeni ñaawteef”. [Mukk] duñu mas a yenu tus ci seeni ñaawteef. Li wóor moo di ñoom ay fenkat lañu.
وَلَيَحْمِلُنَّ أَثْقَالَهُمْ وَأَثْقَالًا مَّعَ أَثْقَالِهِمْ ۖ وَلَيُسْأَلُنَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ عَمَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Danañu yenu seen yu diis ya ak yeneen yu diis boole ko ca. Te bu Bis-pénc baa, danañu leen laaj la ñu daan duur [fen].
وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا نُوحًا إِلَىٰ قَوْمِهِ فَلَبِثَ فِيهِمْ أَلْفَ سَنَةٍ إِلَّا خَمْسِينَ عَامًا فَأَخَذَهُمُ الطُّوفَانُ وَهُمْ ظَالِمُونَ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Yónni woon Nanu Nooh ca aw nitam. Mu sax fa ñoom junniy at yu yées juróom-fukk. Mbënn ma daldi leen di mëdd ba ñu tooñee.
فَأَنجَيْنَاهُ وَأَصْحَابَ السَّفِينَةِ وَجَعَلْنَاهَا آيَةً لِّلْعَالَمِينَ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Nu musaloon ko mook waa gaal ga ; def Nanu leen ñuy kéemaan ci waa àddina sépp.
وَإِبْرَاهِيمَ إِذْ قَالَ لِقَوْمِهِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَاتَّقُوهُ ۖ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
[Fàttalikul it] Ibraahiima, ba mu waxee nitam ña, ne leen : “Jaamuleen Yàlla : moo gën ci yéen, de cëy bu ngeen xamoon”.
إِنَّمَا تَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ أَوْثَانًا وَتَخْلُقُونَ إِفْكًا ۚ إِنَّ الَّذِينَ تَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ لَا يَمْلِكُونَ لَكُمْ رِزْقًا فَابْتَغُوا عِندَ اللَّهِ الرِّزْقَ وَاعْبُدُوهُ وَاشْكُرُوا لَهُ ۖ إِلَيْهِ تُرْجَعُونَ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Yéen a ngay jaamu ay xërëm bàyyi Yàlla, di sos ay fen yu ngeen di jaamu te du Yàlla. Amaluñuleen woon wërsëg ; sàkkujileen wërsëg ci Yàlla. Te ngeen jaamu Ko te sant Ko. Ca Moom ngeen di dellu de.
وَإِن تُكَذِّبُوا فَقَدْ كَذَّبَ أُمَمٌ مِّن قَبْلِكُمْ ۖ وَمَا عَلَى الرَّسُولِ إِلَّا الْبَلَاغُ الْمُبِينُ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Su ngeen ko weddee, jàppe ko ay fen, am na ay xeet yu leen jiitu woon daan weddi. Rikk nangeen xam ne ab Yonent jottali mu leer rekk a ko war.
أَوَلَمْ يَرَوْا كَيْفَ يُبْدِئُ اللَّهُ الْخَلْقَ ثُمَّ يُعِيدُهُ ۚ إِنَّ ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ يَسِيرٌ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Moo ndax dañoo gisul ni Yàlla di sosee mbindéef te di ko defaraat ? Looloo ka yomb ca Yàlla.
قُلْ سِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَانظُرُوا كَيْفَ بَدَأَ الْخَلْقَ ۚ ثُمَّ اللَّهُ يُنشِئُ النَّشْأَةَ الْآخِرَةَ ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Neel : “Wërleen [dox] ci kaw suuf si te ngeen xool naka la Yàlla sosee mbindéef yi. Ak itam naka lay sos gu mujj ga di deme. Yàlla mën na lépp lu ne”.
يُعَذِّبُ مَن يَشَاءُ وَيَرْحَمُ مَن يَشَاءُ ۖ وَإِلَيْهِ تُقْلَبُونَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Dana mbugal ku ko soob te it Dana yërëm ku ko soob ; te yéen ñépp ca Moom ngeen jëm.
وَمَا أَنتُم بِمُعْجِزِينَ فِي الْأَرْضِ وَلَا فِي السَّمَاءِ ۖ وَمَا لَكُم مِّن دُونِ اللَّهِ مِن وَلِيٍّ وَلَا نَصِيرٍ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Mënuleen a të ci kaw suuf si waxantumaak asamaan si ; te itam amuleen wenn wéeruwaay mbaa dimbalikat bu dul Yàlla.
وَالَّذِينَ كَفَرُوا بِآيَاتِ اللَّهِ وَلِقَائِهِ أُولَٰئِكَ يَئِسُوا مِن رَّحْمَتِي وَأُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Ña nga xam ne dañoo weddi kàdduy Yàlla ak dajeek Moom, ñooña naag nañu ci Sama yërmaande. Te it danañu am mbugal mu mitti.
فَمَا كَانَ جَوَابَ قَوْمِهِ إِلَّا أَن قَالُوا اقْتُلُوهُ أَوْ حَرِّقُوهُ فَأَنجَاهُ اللَّهُ مِنَ النَّارِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Tontul aw nitam doonul woon lu dul ñuy wax naan : “reyleen ko mbaa ngeen lakk ko”. Yàlla musal na ko ca safara sa. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.
وَقَالَ إِنَّمَا اتَّخَذْتُم مِّن دُونِ اللَّهِ أَوْثَانًا مَّوَدَّةَ بَيْنِكُمْ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۖ ثُمَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ يَكْفُرُ بَعْضُكُم بِبَعْضٍ وَيَلْعَنُ بَعْضُكُم بَعْضًا وَمَأْوَاكُمُ النَّارُ وَمَا لَكُم مِّن نَّاصِرِينَ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
[Ibraahiima] wax na ne : “Yéen a ngi jàpp xërëm yi bàyyi Yàlla ngir dëgëral seenug cofeel seen diggante fii ci dundug àddina. Waaye bu Bis-pénc baa, dangeen weddiwante, rëbbante te Safara mooy doon seen kër, te it dungeen fa am ndimbal.
۞ فَآمَنَ لَهُ لُوطٌ ۘ وَقَالَ إِنِّي مُهَاجِرٌ إِلَىٰ رَبِّي ۖ إِنَّهُ هُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Lóot daldi koy gëm. Wax ne : “Maa ngi gàddaay jëm ci sama Boroom, Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ”.
وَوَهَبْنَا لَهُ إِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَجَعَلْنَا فِي ذُرِّيَّتِهِ النُّبُوَّةَ وَالْكِتَابَ وَآتَيْنَاهُ أَجْرَهُ فِي الدُّنْيَا ۖ وَإِنَّهُ فِي الْآخِرَةِ لَمِنَ الصَّالِحِينَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
May na ko Isaaqa ak Yanqooba, defaloon Nanu ko ca sëtam ya ag Yonent ak Téere ba. Te indil Nanu ko ag peyam ci àddina, te it bu àllaaxiraa, ca nit ñu yiw ña lay bokk.
وَلُوطًا إِذْ قَالَ لِقَوْمِهِ إِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الْفَاحِشَةَ مَا سَبَقَكُم بِهَا مِنْ أَحَدٍ مِّنَ الْعَالَمِينَ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
[Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Yéen a ngi def u ñaawteef [ngóor- jigéen], te ci àddina, kenn jëkkewuleen ko ci.
أَئِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الرِّجَالَ وَتَقْطَعُونَ السَّبِيلَ وَتَأْتُونَ فِي نَادِيكُمُ الْمُنكَرَ ۖ فَمَا كَانَ جَوَابَ قَوْمِهِ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتِنَا بِعَذَابِ اللَّهِ إِن كُنتَ مِنَ الصَّادِقِينَ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Moo ndax yéen, dangeen di sëyanti ci góor ñi ? Di dogale yoon yi ? Ngeen di def njekkar ci seeni mbootaay ? ”. [Waaye] nitam ña tontuwuñu ko lenn lu dul ne ko : “Indil nu mbugalum Yàlla ndegam wax nga dëgg”.
قَالَ رَبِّ انصُرْنِي عَلَى الْقَوْمِ الْمُفْسِدِينَ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, may ma ndam ci kaw nit ñii di ay tooñkat ! ”
وَلَمَّا جَاءَتْ رُسُلُنَا إِبْرَاهِيمَ بِالْبُشْرَىٰ قَالُوا إِنَّا مُهْلِكُو أَهْلِ هَٰذِهِ الْقَرْيَةِ ۖ إِنَّ أَهْلَهَا كَانُوا ظَالِمِينَ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
Ba Sunuy Malaaka dikkalee Ibraahiima ak xibaari mbégte, ne ko : “Danuy faagaagale waa dëkk bii ndax ña fa dëkk ay tooñkat lañu”.
قَالَ إِنَّ فِيهَا لُوطًا ۚ قَالُوا نَحْنُ أَعْلَمُ بِمَن فِيهَا ۖ لَنُنَجِّيَنَّهُ وَأَهْلَهُ إِلَّا امْرَأَتَهُ كَانَتْ مِنَ الْغَابِرِينَ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
Ibraahiima ne leen : “Waaye Lóot ma nga fa ! ”. Ñu tontu ko ne ko : “Noo gën a xam ña fa nekk : Dananu musal [moom Lóot] mook njabootam, ba mu des soxnaam, moom day bokk ca ña alku”.
وَلَمَّا أَن جَاءَتْ رُسُلُنَا لُوطًا سِيءَ بِهِمْ وَضَاقَ بِهِمْ ذَرْعًا وَقَالُوا لَا تَخَفْ وَلَا تَحْزَنْ ۖ إِنَّا مُنَجُّوكَ وَأَهْلَكَ إِلَّا امْرَأَتَكَ كَانَتْ مِنَ الْغَابِرِينَ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
ba Sunu ndawi Malaaka yi agsee ci Lóot, ñaawalees na jëme ci ñoom, mu tiit ci seeni mbir. Ñu ne ko : “Bul tiit, bul ragal... Dananu la musal yaak sa njaboot, ba mu des sa jabar, dafay alku.
إِنَّا مُنزِلُونَ عَلَىٰ أَهْلِ هَٰذِهِ الْقَرْيَةِ رِجْزًا مِّنَ السَّمَاءِ بِمَا كَانُوا يَفْسُقُونَ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
Wàcce Nanu ci kaw waa dëkk bi mbugal mu bawoo asamaan ngir seen caay-caay ga”.
وَلَقَد تَّرَكْنَا مِنْهَا آيَةً بَيِّنَةً لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Bàyyi Nanu fa lu bokk ca ñoom muy kéemaan gu leer nàññ ngir aw nit ñuy xel-lu.
وَإِلَىٰ مَدْيَنَ أَخَاهُمْ شُعَيْبًا فَقَالَ يَا قَوْمِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَارْجُوا الْيَوْمَ الْآخِرَ وَلَا تَعْثَوْا فِي الْأَرْضِ مُفْسِدِينَ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
[Naka noonu], la seen mbokk Chuhaybu demee woon Madyaana, ne leen : “Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla te gëm Bis-pénc ba, te buleen dox di yàq ci kaw suuf si”.
فَكَذَّبُوهُ فَأَخَذَتْهُمُ الرَّجْفَةُ فَأَصْبَحُوا فِي دَارِهِمْ جَاثِمِينَ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Ñu weddi ko. Yëngu-yëngu ba fab leen, ñu xëy ne lànjax ci seen kër.
وَعَادًا وَثَمُودَ وَقَد تَّبَيَّنَ لَكُم مِّن مَّسَاكِنِهِمْ ۖ وَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ فَصَدَّهُمْ عَنِ السَّبِيلِ وَكَانُوا مُسْتَبْصِرِينَ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Ak waa Haad ak Samuuda. - Noona lañu leen faagaagale - mu leer nàññ, ngeen di ko gis ci seen gént ya. Séytaanee leen taaralaloon seeni jëf, férëwle leen ; daawuñu jéem a gis lu baax.
وَقَارُونَ وَفِرْعَوْنَ وَهَامَانَ ۖ وَلَقَدْ جَاءَهُم مُّوسَىٰ بِالْبَيِّنَاتِ فَاسْتَكْبَرُوا فِي الْأَرْضِ وَمَا كَانُوا سَابِقِينَ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Te kat [faagaagal Nanu] Xaaruuna ak Firawna ak Haamaan. Muusaa indiloon na leen Sunuy firnde, ñuy rëy-rëylu ci kaw suuf si. Waante mënuñu Nu woon a raw de.
فَكُلًّا أَخَذْنَا بِذَنبِهِ ۖ فَمِنْهُم مَّنْ أَرْسَلْنَا عَلَيْهِ حَاصِبًا وَمِنْهُم مَّنْ أَخَذَتْهُ الصَّيْحَةُ وَمِنْهُم مَّنْ خَسَفْنَا بِهِ الْأَرْضَ وَمِنْهُم مَّنْ أَغْرَقْنَا ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيَظْلِمَهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Kenn ci ñoom [faagaagale Nanu ko] kem [tolluwaayu] bàkkaaram : Am na ci ñoom ñu Nu yóonni am mbënn ci ñoom ; am na ci ñoom ñu ag xaacu jël na leen ; am na ci ñoom ñu Nu mëdd ci biir suuf si ; am na ci ñoom ñu Nu labal. Yàlla tooñuleen ; waaye ñoo tooñ seen bopp.
مَثَلُ الَّذِينَ اتَّخَذُوا مِن دُونِ اللَّهِ أَوْلِيَاءَ كَمَثَلِ الْعَنكَبُوتِ اتَّخَذَتْ بَيْتًا ۖ وَإِنَّ أَوْهَنَ الْبُيُوتِ لَبَيْتُ الْعَنكَبُوتِ ۖ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Gam-gamleek ñay wut wéeruwaay bàyyi Yàlla, mi ngi mel ni jargoñ buy lëndub néeg. Te néeg bi gën a doyadi moo di néegu jargoñ. Cëy bu ñu xamoon !
إِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا يَدْعُونَ مِن دُونِهِ مِن شَيْءٍ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
Yàlla xam na mboolem yu ñuy tës-tësi di ko jaamu, Moom ñu ne ko ñukk fale. Te Moom Yàlla moo di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ.
وَتِلْكَ الْأَمْثَالُ نَضْرِبُهَا لِلنَّاسِ ۖ وَمَا يَعْقِلُهَا إِلَّا الْعَالِمُونَ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Léebu yooyee ñuy sadd nit ñi ; te ñi xam ñoo cay xalaat. .
خَلَقَ اللَّهُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّلْمُؤْمِنِينَ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si ci dëgg. Te ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.
اتْلُ مَا أُوحِيَ إِلَيْكَ مِنَ الْكِتَابِ وَأَقِمِ الصَّلَاةَ ۖ إِنَّ الصَّلَاةَ تَنْهَىٰ عَنِ الْفَحْشَاءِ وَالْمُنكَرِ ۗ وَلَذِكْرُ اللَّهِ أَكْبَرُ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مَا تَصْنَعُونَ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Nettalil li Nu soloo ca Téere ba te ngay taxawal julli. Ca dëgg-dëgg, julli daal dafay faat ñaawtéef ak njekkar. [Xamal ne] tudd Yàlla te di Ko fàttaliku moo gënatee rëy. Yàllaa ka xam li ngeen di def.
۞ وَلَا تُجَادِلُوا أَهْلَ الْكِتَابِ إِلَّا بِالَّتِي هِيَ أَحْسَنُ إِلَّا الَّذِينَ ظَلَمُوا مِنْهُمْ ۖ وَقُولُوا آمَنَّا بِالَّذِي أُنزِلَ إِلَيْنَا وَأُنزِلَ إِلَيْكُمْ وَإِلَٰهُنَا وَإِلَٰهُكُمْ وَاحِدٌ وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Buleen dàggasante ak ñoñ-téere yi lu dul ca na mu gën a rafetee te buleen ca boole ña yiwadi ca ñoom. Nangeen di wax ne : “Nun gëm nanu li ñu wàcci ci nun ak li ñu wàcce ci yéen, sunu Yàlla ak seen Yàlla jenn la, te nun jébbale nanu sunu bopp di ay jullit”.
وَكَذَٰلِكَ أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ ۚ فَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۖ وَمِنْ هَٰؤُلَاءِ مَن يُؤْمِنُ بِهِ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا الْكَافِرُونَ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci yaw [Muhammad]. Ña nga xam ne joxoon nañu leen Téere, gëmoon nañu ko. Am na ci ñoom ñu ko gëm [Alxuraan]. Yéefar yi doŋŋ ñoo weddi Sunuy kàddu.
وَمَا كُنتَ تَتْلُو مِن قَبْلِهِ مِن كِتَابٍ وَلَا تَخُطُّهُ بِيَمِينِكَ ۖ إِذًا لَّارْتَابَ الْمُبْطِلُونَ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Yaw [Muhammad], li jiitu wàccug [Téere bii di Alxuraan], musuloo jàng ab téere, musoo koo binde loxob ndeyjoor. [Su fekkoon ne loolu am na], kon weddikat ya danañu mën a sikki- sàkka.
بَلْ هُوَ آيَاتٌ بَيِّنَاتٌ فِي صُدُورِ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا الظَّالِمُونَ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
Li wér te wóor moo di ne, [Alxuraan] ay laaya la yu ñu faramfàcce ci biir dënni woroom xam-xam yi. Te tooñkat yi rekk ñoo koy weddi.
وَقَالُوا لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْهِ آيَاتٌ مِّن رَّبِّهِ ۖ قُلْ إِنَّمَا الْآيَاتُ عِندَ اللَّهِ وَإِنَّمَا أَنَا نَذِيرٌ مُّبِينٌ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
Ñuy wax naan : “Lu tax Yàlla wàccewul ci moom kéemaan ? ”. Waxal ne : “Kéemaan a nga ca Yàlla. Man, ab xuppekat buy leeral rekk laa”.
أَوَلَمْ يَكْفِهِمْ أَنَّا أَنزَلْنَا عَلَيْكَ الْكِتَابَ يُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَرَحْمَةً وَذِكْرَىٰ لِقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
Ndax doyuleen ñoom, wàcce gii Nu wàcce ci yaw Téere bi, Nu di leen ko dégtal ? Yërmaande ak fàttalikoo nga ca biir lool ngir aw nit ñu gëm.
قُلْ كَفَىٰ بِاللَّهِ بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ شَهِيدًا ۖ يَعْلَمُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَالَّذِينَ آمَنُوا بِالْبَاطِلِ وَكَفَرُوا بِاللَّهِ أُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Waxal ne : “Yàlla doy na seede sama digganteek yéen”. Xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si. Ña gëm neen, weddi Yàlla, ñoo yàqule.
وَيَسْتَعْجِلُونَكَ بِالْعَذَابِ ۚ وَلَوْلَا أَجَلٌ مُّسَمًّى لَّجَاءَهُمُ الْعَذَابُ وَلَيَأْتِيَنَّهُم بَغْتَةً وَهُمْ لَا يَشْعُرُونَ ۝٥٣
📖 Tekki Aaya 53
Té ñanga lay laaj mbugal ma cig yàkkamti. Bu fekkoon ne du dig ba Nu leen àppal, kon ñëwoon na [bu yàgg]. Waaye mbugal ma dana ñëw ci ñoom, di mbetteel te duñu ko yég.
يَسْتَعْجِلُونَكَ بِالْعَذَابِ وَإِنَّ جَهَنَّمَ لَمُحِيطَةٌ بِالْكَافِرِينَ ۝٥٤
📖 Tekki Aaya 54
Ña nga lay laaj mbugal ma cig yàkkamti, te fekk Safara waa ngay gaw yéefar ya.
يَوْمَ يَغْشَاهُمُ الْعَذَابُ مِن فَوْقِهِمْ وَمِن تَحْتِ أَرْجُلِهِمْ وَيَقُولُ ذُوقُوا مَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝٥٥
📖 Tekki Aaya 55
Bu keroogee ba mbugal ma muur leen ci seen kaw ak seen ndëgguy tànk. Mu di leen wax naan : “Mosleen, toqamtikuleen li ngeen daan def ! ”
يَا عِبَادِيَ الَّذِينَ آمَنُوا إِنَّ أَرْضِي وَاسِعَةٌ فَإِيَّايَ فَاعْبُدُونِ ۝٥٦
📖 Tekki Aaya 56
Éy yéen sama jaam ñi gëm ! Sama suuf si yaatu na [lool]. Waay-waay jaamuleen Ma !
كُلُّ نَفْسٍ ذَائِقَةُ الْمَوْتِ ۖ ثُمَّ إِلَيْنَا تُرْجَعُونَ ۝٥٧
📖 Tekki Aaya 57
Bakkan bu nekk dana mos dee. Te [ñéppay] dellusi ci Nun.
وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَنُبَوِّئَنَّهُم مِّنَ الْجَنَّةِ غُرَفًا تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا ۚ نِعْمَ أَجْرُ الْعَامِلِينَ ۝٥٨
📖 Tekki Aaya 58
Ña gëmoon tey jëf u yiw, Dananu leen dëkkal ay néeg yu kawe yoo xam ne ay dex ñooy daw ca suufam. Dañu fay béel, ndaw pey gu neex,
الَّذِينَ صَبَرُوا وَعَلَىٰ رَبِّهِمْ يَتَوَكَّلُونَ ۝٥٩
📖 Tekki Aaya 59
ña daan muñ te wéeru woon ca seen Boroom !
وَكَأَيِّن مِّن دَابَّةٍ لَّا تَحْمِلُ رِزْقَهَا اللَّهُ يَرْزُقُهَا وَإِيَّاكُمْ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ ۝٦٠
📖 Tekki Aaya 60
Amul jenn daaba ju warlul boppam wërsëg ! [Waaye] Yàlla moo koy wërsëgal ak yéen. Te Moo di Aji-dégg, di Ku xam.
وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۖ فَأَنَّىٰ يُؤْفَكُونَ ۝٦١
📖 Tekki Aaya 61
Soo leen laajoon : “Ana kan moo bind asamaan yeek suuf si, tàggatal leen jant bi ak weer wi ? ”, kon danañu tontu wax ne : “Yàllaa ko def”. Waaw, kon ñoom naka lañuy dummóoyoo yoon wu jub wi ?
اللَّهُ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ وَيَقْدِرُ لَهُ ۚ إِنَّ اللَّهَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ ۝٦٢
📖 Tekki Aaya 62
Yàlla mooy yaatalal wërsëgam ci ku ko soob ci jaamam ñi, Moo koy xatal itam. Yàlla xam na lépp lu ne.
وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّن نَّزَّلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ مِن بَعْدِ مَوْتِهَا لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلِ الْحَمْدُ لِلَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْقِلُونَ ۝٦٣
📖 Tekki Aaya 63
Soo leen laajoon : “Ana kan moo leen wàccey ndox ci asamaan si, dundale ko suuf si ginnaaw bu dee woon [wow] ? ”, kon danañu wax ne : “Yàllaa ko def”. Neel : “Sant ñeel na Yàlla ! ”. Li ëpp ci ñoom duñu xalaat.
وَمَا هَٰذِهِ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا لَهْوٌ وَلَعِبٌ ۚ وَإِنَّ الدَّارَ الْآخِرَةَ لَهِيَ الْحَيَوَانُ ۚ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ ۝٦٤
📖 Tekki Aaya 64
Dundu gi ci àddina sii doonul lu dul féexal xol ak po. Waaye kër gu mujj ga mooy dëgg- dëggi dundu. Cëy bu ngeen xamoo !
فَإِذَا رَكِبُوا فِي الْفُلْكِ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ فَلَمَّا نَجَّاهُمْ إِلَى الْبَرِّ إِذَا هُمْ يُشْرِكُونَ ۝٦٥
📖 Tekki Aaya 65
Saa yu ñu waree ci gaal, dañuy ñaan Yàlla di ko sellal. Waaye, saa su leen musalee ba wàcce leen ci jéeri ji, ndeke yoo ña ngay bokkaale.
لِيَكْفُرُوا بِمَا آتَيْنَاهُمْ وَلِيَتَمَتَّعُوا ۖ فَسَوْفَ يَعْلَمُونَ ۝٦٦
📖 Tekki Aaya 66
Dañuy xebet la ñu leen di jox ak di bànneexu ! Danañu xala xam !
أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّا جَعَلْنَا حَرَمًا آمِنًا وَيُتَخَطَّفُ النَّاسُ مِنْ حَوْلِهِمْ ۚ أَفَبِالْبَاطِلِ يُؤْمِنُونَ وَبِنِعْمَةِ اللَّهِ يَكْفُرُونَ ۝٦٧
📖 Tekki Aaya 67
Xanaa dañoo gisul ne def Nanu [Màkka] muy barab bu ñu wormaal bu wóor, te nit ñi leen wër, dees na leen dax-daxee ? Moo ndax ñoom dañoo gëm ag neen tey weddi xéewali Yàlla yi ?
وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ كَذَّبَ بِالْحَقِّ لَمَّا جَاءَهُ ۚ أَلَيْسَ فِي جَهَنَّمَ مَثْوًى لِّلْكَافِرِينَ ۝٦٨
📖 Tekki Aaya 68
Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla mu weddi dëgg ga koy dëggal ? Moo ndax ca biir Safara dëkkuwaayu yéefar yi dafaa amul ? [Axakañ]
وَالَّذِينَ جَاهَدُوا فِينَا لَنَهْدِيَنَّهُمْ سُبُلَنَا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَمَعَ الْمُحْسِنِينَ ۝٦٩
📖 Tekki Aaya 69
Ñay xare di jànkuwante [samaw yoon], danañu leen gindi Sunuy yoon, te Yàlla ànd naak way-rafetal ña.
← 28 Al-'Ankabut (29/114) 30 →
Jàng Simoore Al-'Ankabut ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

29العنكبوت Al-'Ankabut 📚 69 Aaya مكية

Aaya bu ne – Simoore Al-'Ankabut — 69 Aaya




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers