Al-'Ankabut · 47/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
وَكَذَٰلِكَ أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ ۚ فَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۖ وَمِنْ هَٰؤُلَاءِ مَن يُؤْمِنُ بِهِ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا الْكَافِرُونَ ۝٤٧
Wa kazaalika anzalnaaa ilaikal Kitaab; fallazeena aatainaahumul kitaaba yu`minoona bihee wa min haaa`ulaaa`i many yu`minu bih; wa maa yajhadu bi`Aayaatinaa illal kaafiroon
📖 Tekkim Wolof
Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci yaw [Muhammad]. Ña nga xam ne joxoon nañu leen Téere, gëmoon nañu ko. Am na ci ñoom ñu ko gëm [Alxuraan]. Yéefar yi doŋŋ ñoo weddi Sunuy kàddu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 45-49 — Al-'Ankabut

45اتْلُ مَا أُوحِيَ إِلَيْكَ مِنَ الْكِتَابِ وَأَقِمِ الصَّلَاةَ ۖ إِنَّ الصَّلَاةَ تَنْهَىٰ عَنِ الْفَحْشَاءِ وَالْمُنكَرِ ۗ وَلَذِكْرُ اللَّهِ أَكْبَرُ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مَا تَصْنَعُونَ
Nettalil li Nu soloo ca Téere ba te ngay taxawal julli. Ca dëgg-dëgg, julli daal dafay faat ñaawtéef ak njekkar. [Xamal ne] tudd Yàlla te di Ko fàttaliku moo gënatee rëy. Yàllaa ka xam li ngeen di def.
46۞ وَلَا تُجَادِلُوا أَهْلَ الْكِتَابِ إِلَّا بِالَّتِي هِيَ أَحْسَنُ إِلَّا الَّذِينَ ظَلَمُوا مِنْهُمْ ۖ وَقُولُوا آمَنَّا بِالَّذِي أُنزِلَ إِلَيْنَا وَأُنزِلَ إِلَيْكُمْ وَإِلَٰهُنَا وَإِلَٰهُكُمْ وَاحِدٌ وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ
Buleen dàggasante ak ñoñ-téere yi lu dul ca na mu gën a rafetee te buleen ca boole ña yiwadi ca ñoom. Nangeen di wax ne : “Nun gëm nanu li ñu wàcci ci nun ak li ñu wàcce ci yéen, sunu Yàlla ak seen Yàlla jenn la, te nun jébbale nanu sunu bopp di ay jullit”.
47وَكَذَٰلِكَ أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ ۚ فَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۖ وَمِنْ هَٰؤُلَاءِ مَن يُؤْمِنُ بِهِ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا الْكَافِرُونَ
Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci yaw [Muhammad]. Ña nga xam ne joxoon nañu leen Téere, gëmoon nañu ko. Am na ci ñoom ñu ko gëm [Alxuraan]. Yéefar yi doŋŋ ñoo weddi Sunuy kàddu.
48وَمَا كُنتَ تَتْلُو مِن قَبْلِهِ مِن كِتَابٍ وَلَا تَخُطُّهُ بِيَمِينِكَ ۖ إِذًا لَّارْتَابَ الْمُبْطِلُونَ
Yaw [Muhammad], li jiitu wàccug [Téere bii di Alxuraan], musuloo jàng ab téere, musoo koo binde loxob ndeyjoor. [Su fekkoon ne loolu am na], kon weddikat ya danañu mën a sikki- sàkka.
49بَلْ هُوَ آيَاتٌ بَيِّنَاتٌ فِي صُدُورِ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا الظَّالِمُونَ
Li wér te wóor moo di ne, [Alxuraan] ay laaya la yu ñu faramfàcce ci biir dënni woroom xam-xam yi. Te tooñkat yi rekk ñoo koy weddi.
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
47Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 47

Simoore Al-'Ankabut Aaya 47 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci yaw [Muhammad].…

Simoore Aaya 47/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 45–49. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers