Al-'Ankabut · 17/69
Tekki Waxtaan — Simoore Al-'Ankabut
إِنَّمَا تَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ أَوْثَانًا وَتَخْلُقُونَ إِفْكًا ۚ إِنَّ الَّذِينَ تَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ لَا يَمْلِكُونَ لَكُمْ رِزْقًا فَابْتَغُوا عِندَ اللَّهِ الرِّزْقَ وَاعْبُدُوهُ وَاشْكُرُوا لَهُ ۖ إِلَيْهِ تُرْجَعُونَ ۝١٧
Innamaa ta`ubdoona min doonil laahi awsaananw-wa takhluqoona ifkaa; innal lazeena ta`budoona min doonil laahi laa yamlikoona lakum rizqan fabtaghoo `indal laahir rizqa fabtaghoo `indal laahir rizqa wa`budoohu washkuroo lahooo ilaihi turja`oon
📖 Tekkim Wolof
Yéen a ngay jaamu ay xërëm bàyyi Yàlla, di sos ay fen yu ngeen di jaamu te du Yàlla. Amaluñuleen woon wërsëg ; sàkkujileen wërsëg ci Yàlla. Te ngeen jaamu Ko te sant Ko. Ca Moom ngeen di dellu de.

🎧 Dégg


📜 Aaya 15-19 — Simoore Al-'Ankabut

15فَأَنجَيْنَاهُ وَأَصْحَابَ السَّفِينَةِ وَجَعَلْنَاهَا آيَةً لِّلْعَالَمِينَ
Nu musaloon ko mook waa gaal ga ; def Nanu leen ñuy kéemaan ci waa àddina sépp.
16وَإِبْرَاهِيمَ إِذْ قَالَ لِقَوْمِهِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَاتَّقُوهُ ۖ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
[Fàttalikul it] Ibraahiima, ba mu waxee nitam ña, ne leen : “Jaamuleen Yàlla : moo gën ci yéen, de cëy bu ngeen xamoon”.
17إِنَّمَا تَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ أَوْثَانًا وَتَخْلُقُونَ إِفْكًا ۚ إِنَّ الَّذِينَ تَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ لَا يَمْلِكُونَ لَكُمْ رِزْقًا فَابْتَغُوا عِندَ اللَّهِ الرِّزْقَ وَاعْبُدُوهُ وَاشْكُرُوا لَهُ ۖ إِلَيْهِ تُرْجَعُونَ
Yéen a ngay jaamu ay xërëm bàyyi Yàlla, di sos ay fen yu ngeen di jaamu te du Yàlla. Amaluñuleen woon wërsëg ; sàkkujileen wërsëg ci Yàlla. Te ngeen jaamu Ko te sant Ko. Ca Moom ngeen di dellu de.
18وَإِن تُكَذِّبُوا فَقَدْ كَذَّبَ أُمَمٌ مِّن قَبْلِكُمْ ۖ وَمَا عَلَى الرَّسُولِ إِلَّا الْبَلَاغُ الْمُبِينُ
Su ngeen ko weddee, jàppe ko ay fen, am na ay xeet yu leen jiitu woon daan weddi. Rikk nangeen xam ne ab Yonent jottali mu leer rekk a ko war.
19أَوَلَمْ يَرَوْا كَيْفَ يُبْدِئُ اللَّهُ الْخَلْقَ ثُمَّ يُعِيدُهُ ۚ إِنَّ ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ يَسِيرٌ
Moo ndax dañoo gisul ni Yàlla di sosee mbindéef te di ko defaraat ? Looloo ka yomb ca Yàlla.
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
17Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 17

Simoore Al-'Ankabut Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yéen a ngay jaamu ay xërëm bàyyi Yàlla, di sos…

Simoore Aaya 17/69 — Simoore Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-'Ankabut Dégg, Simoore Al-'Ankabut Tekki, Simoore Al-'Ankabut mp3, Simoore Al-'Ankabut pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers