Al-'Ankabut · 63/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّن نَّزَّلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ مِن بَعْدِ مَوْتِهَا لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلِ الْحَمْدُ لِلَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْقِلُونَ ۝٦٣
Wa la`in sa altahum man nazzala minas samaaa`e maaa`an fa ahyaa bihil arda mim ba`di mawtihaa la yaqoolunnal laah; qulil hamdu lillah; bal aksaruhum laa ya`qiloon
📖 Tekkim Wolof
Soo leen laajoon : “Ana kan moo leen wàccey ndox ci asamaan si, dundale ko suuf si ginnaaw bu dee woon [wow] ? ”, kon danañu wax ne : “Yàllaa ko def”. Neel : “Sant ñeel na Yàlla ! ”. Li ëpp ci ñoom duñu xalaat.

🎧 Dégg


📜 Aaya 61-65 — Al-'Ankabut

61وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۖ فَأَنَّىٰ يُؤْفَكُونَ
Soo leen laajoon : “Ana kan moo bind asamaan yeek suuf si, tàggatal leen jant bi ak weer wi ? ”, kon danañu tontu wax ne : “Yàllaa ko def”. Waaw, kon ñoom naka lañuy dummóoyoo yoon wu jub wi ?
62اللَّهُ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ وَيَقْدِرُ لَهُ ۚ إِنَّ اللَّهَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Yàlla mooy yaatalal wërsëgam ci ku ko soob ci jaamam ñi, Moo koy xatal itam. Yàlla xam na lépp lu ne.
63وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّن نَّزَّلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ مِن بَعْدِ مَوْتِهَا لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلِ الْحَمْدُ لِلَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْقِلُونَ
Soo leen laajoon : “Ana kan moo leen wàccey ndox ci asamaan si, dundale ko suuf si ginnaaw bu dee woon [wow] ? ”, kon danañu wax ne : “Yàllaa ko def”. Neel : “Sant ñeel na Yàlla ! ”. Li ëpp ci ñoom duñu xalaat.
64وَمَا هَٰذِهِ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا لَهْوٌ وَلَعِبٌ ۚ وَإِنَّ الدَّارَ الْآخِرَةَ لَهِيَ الْحَيَوَانُ ۚ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ
Dundu gi ci àddina sii doonul lu dul féexal xol ak po. Waaye kër gu mujj ga mooy dëgg- dëggi dundu. Cëy bu ngeen xamoo !
65فَإِذَا رَكِبُوا فِي الْفُلْكِ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ فَلَمَّا نَجَّاهُمْ إِلَى الْبَرِّ إِذَا هُمْ يُشْرِكُونَ
Saa yu ñu waree ci gaal, dañuy ñaan Yàlla di ko sellal. Waaye, saa su leen musalee ba wàcce leen ci jéeri ji, ndeke yoo ña ngay bokkaale.
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
63Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 63

Simoore Al-'Ankabut Aaya 63 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Soo leen laajoon : “Ana kan moo leen wàccey ndox…

Simoore Aaya 63/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 61–65. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers