Al-'Ankabut · 28/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
وَلُوطًا إِذْ قَالَ لِقَوْمِهِ إِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الْفَاحِشَةَ مَا سَبَقَكُم بِهَا مِنْ أَحَدٍ مِّنَ الْعَالَمِينَ ۝٢٨
Wa Lootan iz qaala liqawmiheee innakum laatoonal faahishata maa sabaqakum bihaa min ahadim minal `aalameen
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Yéen a ngi def u ñaawteef [ngóor- jigéen], te ci àddina, kenn jëkkewuleen ko ci.

🎧 Dégg


📜 Aaya 26-30 — Al-'Ankabut

26۞ فَآمَنَ لَهُ لُوطٌ ۘ وَقَالَ إِنِّي مُهَاجِرٌ إِلَىٰ رَبِّي ۖ إِنَّهُ هُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Lóot daldi koy gëm. Wax ne : “Maa ngi gàddaay jëm ci sama Boroom, Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ”.
27وَوَهَبْنَا لَهُ إِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَجَعَلْنَا فِي ذُرِّيَّتِهِ النُّبُوَّةَ وَالْكِتَابَ وَآتَيْنَاهُ أَجْرَهُ فِي الدُّنْيَا ۖ وَإِنَّهُ فِي الْآخِرَةِ لَمِنَ الصَّالِحِينَ
May na ko Isaaqa ak Yanqooba, defaloon Nanu ko ca sëtam ya ag Yonent ak Téere ba. Te indil Nanu ko ag peyam ci àddina, te it bu àllaaxiraa, ca nit ñu yiw ña lay bokk.
28وَلُوطًا إِذْ قَالَ لِقَوْمِهِ إِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الْفَاحِشَةَ مَا سَبَقَكُم بِهَا مِنْ أَحَدٍ مِّنَ الْعَالَمِينَ
[Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Yéen a ngi def u ñaawteef [ngóor- jigéen], te ci àddina, kenn jëkkewuleen ko ci.
29أَئِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الرِّجَالَ وَتَقْطَعُونَ السَّبِيلَ وَتَأْتُونَ فِي نَادِيكُمُ الْمُنكَرَ ۖ فَمَا كَانَ جَوَابَ قَوْمِهِ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتِنَا بِعَذَابِ اللَّهِ إِن كُنتَ مِنَ الصَّادِقِينَ
Moo ndax yéen, dangeen di sëyanti ci góor ñi ? Di dogale yoon yi ? Ngeen di def njekkar ci seeni mbootaay ? ”. [Waaye] nitam ña tontuwuñu ko lenn lu dul ne ko : “Indil nu mbugalum Yàlla ndegam wax nga dëgg”.
30قَالَ رَبِّ انصُرْنِي عَلَى الْقَوْمِ الْمُفْسِدِينَ
Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, may ma ndam ci kaw nit ñii di ay tooñkat ! ”
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
28Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 28

Simoore Al-'Ankabut Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen :…

Simoore Aaya 28/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers