Al-'Ankabut · 29/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
أَئِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الرِّجَالَ وَتَقْطَعُونَ السَّبِيلَ وَتَأْتُونَ فِي نَادِيكُمُ الْمُنكَرَ ۖ فَمَا كَانَ جَوَابَ قَوْمِهِ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتِنَا بِعَذَابِ اللَّهِ إِن كُنتَ مِنَ الصَّادِقِينَ ۝٢٩
A`innakum lataatoonar rijaala wa taqta`oonas sabeela wa taatoona fee naadekumul munkara famaa kaana jawaaba qawmiheee illaaa an qaalu` tinaaa bi`azaabil laahi in kunta minas saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Moo ndax yéen, dangeen di sëyanti ci góor ñi ? Di dogale yoon yi ? Ngeen di def njekkar ci seeni mbootaay ? ”. [Waaye] nitam ña tontuwuñu ko lenn lu dul ne ko : “Indil nu mbugalum Yàlla ndegam wax nga dëgg”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 27-31 — Al-'Ankabut

27وَوَهَبْنَا لَهُ إِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَجَعَلْنَا فِي ذُرِّيَّتِهِ النُّبُوَّةَ وَالْكِتَابَ وَآتَيْنَاهُ أَجْرَهُ فِي الدُّنْيَا ۖ وَإِنَّهُ فِي الْآخِرَةِ لَمِنَ الصَّالِحِينَ
May na ko Isaaqa ak Yanqooba, defaloon Nanu ko ca sëtam ya ag Yonent ak Téere ba. Te indil Nanu ko ag peyam ci àddina, te it bu àllaaxiraa, ca nit ñu yiw ña lay bokk.
28وَلُوطًا إِذْ قَالَ لِقَوْمِهِ إِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الْفَاحِشَةَ مَا سَبَقَكُم بِهَا مِنْ أَحَدٍ مِّنَ الْعَالَمِينَ
[Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Yéen a ngi def u ñaawteef [ngóor- jigéen], te ci àddina, kenn jëkkewuleen ko ci.
29أَئِنَّكُمْ لَتَأْتُونَ الرِّجَالَ وَتَقْطَعُونَ السَّبِيلَ وَتَأْتُونَ فِي نَادِيكُمُ الْمُنكَرَ ۖ فَمَا كَانَ جَوَابَ قَوْمِهِ إِلَّا أَن قَالُوا ائْتِنَا بِعَذَابِ اللَّهِ إِن كُنتَ مِنَ الصَّادِقِينَ
Moo ndax yéen, dangeen di sëyanti ci góor ñi ? Di dogale yoon yi ? Ngeen di def njekkar ci seeni mbootaay ? ”. [Waaye] nitam ña tontuwuñu ko lenn lu dul ne ko : “Indil nu mbugalum Yàlla ndegam wax nga dëgg”.
30قَالَ رَبِّ انصُرْنِي عَلَى الْقَوْمِ الْمُفْسِدِينَ
Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, may ma ndam ci kaw nit ñii di ay tooñkat ! ”
31وَلَمَّا جَاءَتْ رُسُلُنَا إِبْرَاهِيمَ بِالْبُشْرَىٰ قَالُوا إِنَّا مُهْلِكُو أَهْلِ هَٰذِهِ الْقَرْيَةِ ۖ إِنَّ أَهْلَهَا كَانُوا ظَالِمِينَ
Ba Sunuy Malaaka dikkalee Ibraahiima ak xibaari mbégte, ne ko : “Danuy faagaagale waa dëkk bii ndax ña fa dëkk ay tooñkat lañu”.
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 29

Simoore Al-'Ankabut Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo ndax yéen, dangeen di sëyanti ci góor ñi ?…

Simoore Aaya 29/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers