Al-'Ankabut · 11/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
وَلَيَعْلَمَنَّ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَلَيَعْلَمَنَّ الْمُنَافِقِينَ ۝١١
Wa la ya`lamannal laahul lazeena aamanoo wa la ya`lamannal munaafiqeen
📖 Tekkim Wolof
Yàlla xam na tigi ña gëm, xam na itam naaféq yi .

🎧 Dégg


📜 Aaya 9-13 — Al-'Ankabut

9وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَنُدْخِلَنَّهُمْ فِي الصَّالِحِينَ
Ña gën tey jëf u yiw, Dananu leen dugal ca nit ñu yiw ña.
10وَمِنَ النَّاسِ مَن يَقُولُ آمَنَّا بِاللَّهِ فَإِذَا أُوذِيَ فِي اللَّهِ جَعَلَ فِتْنَةَ النَّاسِ كَعَذَابِ اللَّهِ وَلَئِن جَاءَ نَصْرٌ مِّن رَّبِّكَ لَيَقُولُنَّ إِنَّا كُنَّا مَعَكُمْ ۚ أَوَلَيْسَ اللَّهُ بِأَعْلَمَ بِمَا فِي صُدُورِ الْعَالَمِينَ
Am na ci nit ñi ñuy wax naan : “Gëm Nanu Yàlla” ; te bu ñu leen loree ci ànd gi ñu ànd ak Yàlla, dañuy jàppe sànjeb nit ñooñu ni mbugalum Yàlla. Bu leen ndimbal dikkalee lu bawoo ca sa Boroom, ñu tàmbalee wax naan : “Nun ak yéen a àndoon ! ” Moo ndax Yàlla dafa gënul a xam li nekk ci dënni waa àddina si yépp ?
11وَلَيَعْلَمَنَّ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَلَيَعْلَمَنَّ الْمُنَافِقِينَ
Yàlla xam na tigi ña gëm, xam na itam naaféq yi .
12وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لِلَّذِينَ آمَنُوا اتَّبِعُوا سَبِيلَنَا وَلْنَحْمِلْ خَطَايَاكُمْ وَمَا هُم بِحَامِلِينَ مِنْ خَطَايَاهُم مِّن شَيْءٍ ۖ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ
Yéefar yaa ngay wax ña gëm naan leen ; “Toppleen sunu mboor, dananu yenu seeni ñaawteef”. [Mukk] duñu mas a yenu tus ci seeni ñaawteef. Li wóor moo di ñoom ay fenkat lañu.
13وَلَيَحْمِلُنَّ أَثْقَالَهُمْ وَأَثْقَالًا مَّعَ أَثْقَالِهِمْ ۖ وَلَيُسْأَلُنَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ عَمَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Danañu yenu seen yu diis ya ak yeneen yu diis boole ko ca. Te bu Bis-pénc baa, danañu leen laaj la ñu daan duur [fen].
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
11Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 11

Simoore Al-'Ankabut Aaya 11 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla xam na tigi ña gëm, xam na itam naaféq…

Simoore Aaya 11/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 9–13. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers