Al-'Ankabut · 36/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
وَإِلَىٰ مَدْيَنَ أَخَاهُمْ شُعَيْبًا فَقَالَ يَا قَوْمِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَارْجُوا الْيَوْمَ الْآخِرَ وَلَا تَعْثَوْا فِي الْأَرْضِ مُفْسِدِينَ ۝٣٦
Wa ilaa Madyana akhaahum Shu`ayban faqaala yaa qawmi`-budul laaha warjul yawmal aakhira wa laa ta`saw fil ardi mufsideen
📖 Tekkim Wolof
[Naka noonu], la seen mbokk Chuhaybu demee woon Madyaana, ne leen : “Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla te gëm Bis-pénc ba, te buleen dox di yàq ci kaw suuf si”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 34-38 — Al-'Ankabut

34إِنَّا مُنزِلُونَ عَلَىٰ أَهْلِ هَٰذِهِ الْقَرْيَةِ رِجْزًا مِّنَ السَّمَاءِ بِمَا كَانُوا يَفْسُقُونَ
Wàcce Nanu ci kaw waa dëkk bi mbugal mu bawoo asamaan ngir seen caay-caay ga”.
35وَلَقَد تَّرَكْنَا مِنْهَا آيَةً بَيِّنَةً لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ
Bàyyi Nanu fa lu bokk ca ñoom muy kéemaan gu leer nàññ ngir aw nit ñuy xel-lu.
36وَإِلَىٰ مَدْيَنَ أَخَاهُمْ شُعَيْبًا فَقَالَ يَا قَوْمِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَارْجُوا الْيَوْمَ الْآخِرَ وَلَا تَعْثَوْا فِي الْأَرْضِ مُفْسِدِينَ
[Naka noonu], la seen mbokk Chuhaybu demee woon Madyaana, ne leen : “Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla te gëm Bis-pénc ba, te buleen dox di yàq ci kaw suuf si”.
37فَكَذَّبُوهُ فَأَخَذَتْهُمُ الرَّجْفَةُ فَأَصْبَحُوا فِي دَارِهِمْ جَاثِمِينَ
Ñu weddi ko. Yëngu-yëngu ba fab leen, ñu xëy ne lànjax ci seen kër.
38وَعَادًا وَثَمُودَ وَقَد تَّبَيَّنَ لَكُم مِّن مَّسَاكِنِهِمْ ۖ وَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ فَصَدَّهُمْ عَنِ السَّبِيلِ وَكَانُوا مُسْتَبْصِرِينَ
Ak waa Haad ak Samuuda. - Noona lañu leen faagaagale - mu leer nàññ, ngeen di ko gis ci seen gént ya. Séytaanee leen taaralaloon seeni jëf, férëwle leen ; daawuñu jéem a gis lu baax.
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 36

Simoore Al-'Ankabut Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Naka noonu], la seen mbokk Chuhaybu demee woon Madyaana, ne…

Simoore Aaya 36/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers