Al-'Ankabut · 65/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
فَإِذَا رَكِبُوا فِي الْفُلْكِ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ فَلَمَّا نَجَّاهُمْ إِلَى الْبَرِّ إِذَا هُمْ يُشْرِكُونَ ۝٦٥
Fa-izaa rakiboo fil fulki da`awul laaha mukhilseena lahud deena falammaa najjaa hum ilal baari izaa hum yushrikoon
📖 Tekkim Wolof
Saa yu ñu waree ci gaal, dañuy ñaan Yàlla di ko sellal. Waaye, saa su leen musalee ba wàcce leen ci jéeri ji, ndeke yoo ña ngay bokkaale.

🎧 Dégg


📜 Aaya 63-67 — Al-'Ankabut

63وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّن نَّزَّلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ مِن بَعْدِ مَوْتِهَا لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلِ الْحَمْدُ لِلَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْقِلُونَ
Soo leen laajoon : “Ana kan moo leen wàccey ndox ci asamaan si, dundale ko suuf si ginnaaw bu dee woon [wow] ? ”, kon danañu wax ne : “Yàllaa ko def”. Neel : “Sant ñeel na Yàlla ! ”. Li ëpp ci ñoom duñu xalaat.
64وَمَا هَٰذِهِ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا لَهْوٌ وَلَعِبٌ ۚ وَإِنَّ الدَّارَ الْآخِرَةَ لَهِيَ الْحَيَوَانُ ۚ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ
Dundu gi ci àddina sii doonul lu dul féexal xol ak po. Waaye kër gu mujj ga mooy dëgg- dëggi dundu. Cëy bu ngeen xamoo !
65فَإِذَا رَكِبُوا فِي الْفُلْكِ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ فَلَمَّا نَجَّاهُمْ إِلَى الْبَرِّ إِذَا هُمْ يُشْرِكُونَ
Saa yu ñu waree ci gaal, dañuy ñaan Yàlla di ko sellal. Waaye, saa su leen musalee ba wàcce leen ci jéeri ji, ndeke yoo ña ngay bokkaale.
66لِيَكْفُرُوا بِمَا آتَيْنَاهُمْ وَلِيَتَمَتَّعُوا ۖ فَسَوْفَ يَعْلَمُونَ
Dañuy xebet la ñu leen di jox ak di bànneexu ! Danañu xala xam !
67أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّا جَعَلْنَا حَرَمًا آمِنًا وَيُتَخَطَّفُ النَّاسُ مِنْ حَوْلِهِمْ ۚ أَفَبِالْبَاطِلِ يُؤْمِنُونَ وَبِنِعْمَةِ اللَّهِ يَكْفُرُونَ
Xanaa dañoo gisul ne def Nanu [Màkka] muy barab bu ñu wormaal bu wóor, te nit ñi leen wër, dees na leen dax-daxee ? Moo ndax ñoom dañoo gëm ag neen tey weddi xéewali Yàlla yi ?
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
65Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 65

Simoore Al-'Ankabut Aaya 65 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Saa yu ñu waree ci gaal, dañuy ñaan Yàlla di…

Simoore Aaya 65/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 63–67. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers