Al-'Ankabut · 42/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
إِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا يَدْعُونَ مِن دُونِهِ مِن شَيْءٍ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝٤٢
Innal laaha ya`lamu maa yad`oona min doonihee min shai`; wa Huwal `Azeezul Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Yàlla xam na mboolem yu ñuy tës-tësi di ko jaamu, Moom ñu ne ko ñukk fale. Te Moom Yàlla moo di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ.

🎧 Dégg


📜 Aaya 40-44 — Al-'Ankabut

40فَكُلًّا أَخَذْنَا بِذَنبِهِ ۖ فَمِنْهُم مَّنْ أَرْسَلْنَا عَلَيْهِ حَاصِبًا وَمِنْهُم مَّنْ أَخَذَتْهُ الصَّيْحَةُ وَمِنْهُم مَّنْ خَسَفْنَا بِهِ الْأَرْضَ وَمِنْهُم مَّنْ أَغْرَقْنَا ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيَظْلِمَهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Kenn ci ñoom [faagaagale Nanu ko] kem [tolluwaayu] bàkkaaram : Am na ci ñoom ñu Nu yóonni am mbënn ci ñoom ; am na ci ñoom ñu ag xaacu jël na leen ; am na ci ñoom ñu Nu mëdd ci biir suuf si ; am na ci ñoom ñu Nu labal. Yàlla tooñuleen ; waaye ñoo tooñ seen bopp.
41مَثَلُ الَّذِينَ اتَّخَذُوا مِن دُونِ اللَّهِ أَوْلِيَاءَ كَمَثَلِ الْعَنكَبُوتِ اتَّخَذَتْ بَيْتًا ۖ وَإِنَّ أَوْهَنَ الْبُيُوتِ لَبَيْتُ الْعَنكَبُوتِ ۖ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ
Gam-gamleek ñay wut wéeruwaay bàyyi Yàlla, mi ngi mel ni jargoñ buy lëndub néeg. Te néeg bi gën a doyadi moo di néegu jargoñ. Cëy bu ñu xamoon !
42إِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا يَدْعُونَ مِن دُونِهِ مِن شَيْءٍ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Yàlla xam na mboolem yu ñuy tës-tësi di ko jaamu, Moom ñu ne ko ñukk fale. Te Moom Yàlla moo di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ.
43وَتِلْكَ الْأَمْثَالُ نَضْرِبُهَا لِلنَّاسِ ۖ وَمَا يَعْقِلُهَا إِلَّا الْعَالِمُونَ
Léebu yooyee ñuy sadd nit ñi ; te ñi xam ñoo cay xalaat. .
44خَلَقَ اللَّهُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّلْمُؤْمِنِينَ
Moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si ci dëgg. Te ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
42Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 42

Simoore Al-'Ankabut Aaya 42 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla xam na mboolem yu ñuy tës-tësi di ko jaamu,…

Simoore Aaya 42/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 40–44. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers