Al-'Ankabut · 45/69
Tekki Waxtaan — Al-'Ankabut
اتْلُ مَا أُوحِيَ إِلَيْكَ مِنَ الْكِتَابِ وَأَقِمِ الصَّلَاةَ ۖ إِنَّ الصَّلَاةَ تَنْهَىٰ عَنِ الْفَحْشَاءِ وَالْمُنكَرِ ۗ وَلَذِكْرُ اللَّهِ أَكْبَرُ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مَا تَصْنَعُونَ ۝٤٥
Utlu maaa oohiya ilaika mional Kitaabi wa aqimis Salaata innas Salaata tanhaa `anil fahshaaa`i wal munkar; wa lazikrul laahi akbar; wal laahu ya`lamu maa tasna`oon
📖 Tekkim Wolof
Nettalil li Nu soloo ca Téere ba te ngay taxawal julli. Ca dëgg-dëgg, julli daal dafay faat ñaawtéef ak njekkar. [Xamal ne] tudd Yàlla te di Ko fàttaliku moo gënatee rëy. Yàllaa ka xam li ngeen di def.

🎧 Dégg


📜 Aaya 43-47 — Al-'Ankabut

43وَتِلْكَ الْأَمْثَالُ نَضْرِبُهَا لِلنَّاسِ ۖ وَمَا يَعْقِلُهَا إِلَّا الْعَالِمُونَ
Léebu yooyee ñuy sadd nit ñi ; te ñi xam ñoo cay xalaat. .
44خَلَقَ اللَّهُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّلْمُؤْمِنِينَ
Moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si ci dëgg. Te ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.
45اتْلُ مَا أُوحِيَ إِلَيْكَ مِنَ الْكِتَابِ وَأَقِمِ الصَّلَاةَ ۖ إِنَّ الصَّلَاةَ تَنْهَىٰ عَنِ الْفَحْشَاءِ وَالْمُنكَرِ ۗ وَلَذِكْرُ اللَّهِ أَكْبَرُ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مَا تَصْنَعُونَ
Nettalil li Nu soloo ca Téere ba te ngay taxawal julli. Ca dëgg-dëgg, julli daal dafay faat ñaawtéef ak njekkar. [Xamal ne] tudd Yàlla te di Ko fàttaliku moo gënatee rëy. Yàllaa ka xam li ngeen di def.
46۞ وَلَا تُجَادِلُوا أَهْلَ الْكِتَابِ إِلَّا بِالَّتِي هِيَ أَحْسَنُ إِلَّا الَّذِينَ ظَلَمُوا مِنْهُمْ ۖ وَقُولُوا آمَنَّا بِالَّذِي أُنزِلَ إِلَيْنَا وَأُنزِلَ إِلَيْكُمْ وَإِلَٰهُنَا وَإِلَٰهُكُمْ وَاحِدٌ وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ
Buleen dàggasante ak ñoñ-téere yi lu dul ca na mu gën a rafetee te buleen ca boole ña yiwadi ca ñoom. Nangeen di wax ne : “Nun gëm nanu li ñu wàcci ci nun ak li ñu wàcce ci yéen, sunu Yàlla ak seen Yàlla jenn la, te nun jébbale nanu sunu bopp di ay jullit”.
47وَكَذَٰلِكَ أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ ۚ فَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۖ وَمِنْ هَٰؤُلَاءِ مَن يُؤْمِنُ بِهِ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا الْكَافِرُونَ
Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci yaw [Muhammad]. Ña nga xam ne joxoon nañu leen Téere, gëmoon nañu ko. Am na ci ñoom ñu ko gëm [Alxuraan]. Yéefar yi doŋŋ ñoo weddi Sunuy kàddu.
Al-'AnkabutFihi Alxuraan
69Aaya
MeccanRevelation
45Aaya

Tekki — Al-'Ankabut 45

Simoore Al-'Ankabut Aaya 45 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nettalil li Nu soloo ca Téere ba te ngay taxawal…

Simoore Aaya 45/69 — Al-'Ankabut العنكبوت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-'Ankabut Dégg, Al-'Ankabut Tekki, Al-'Ankabut mp3, Al-'Ankabut pdf. Aaya 43–47. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers