Ar-Rum · 23/60
Tekki Waxtaan — Ar-Rum
وَمِنْ آيَاتِهِ مَنَامُكُم بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَابْتِغَاؤُكُم مِّن فَضْلِهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَسْمَعُونَ ۝٢٣
Wa min Aayaatihee manaamukum bil laili wannahaari wabtighaaa`ukum min fadlih; inna fee zaalika la Aayaatil liqawminy yasma`oon
📖 Tekkim Wolof
Bokk na it ci ay kéemaanam, seeni nelaw ci guddi gi ak seenug sàkku wërsëg. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy dégg.
🎧 Dégg

📜 Aaya 21-25 — Ar-Rum

21وَمِنْ آيَاتِهِ أَنْ خَلَقَ لَكُم مِّنْ أَنفُسِكُمْ أَزْوَاجًا لِّتَسْكُنُوا إِلَيْهَا وَجَعَلَ بَيْنَكُم مَّوَدَّةً وَرَحْمَةً ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَتَفَكَّرُونَ
Te bokk na ci kéemaanam yi, mu sàkkal leen ci seeni jëmm ay soxna ngir ngeen di ca dall, Mu def ci seen diggante cofeel ak yërmaande. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat.
22وَمِنْ آيَاتِهِ خَلْقُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَاخْتِلَافُ أَلْسِنَتِكُمْ وَأَلْوَانِكُمْ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّلْعَالِمِينَ
Bokk na it ci ay kéemaanam, bindug asamaan yeek suuf si ak wuuteeg seeni làmmiñ ak seeni melo. Ay kéemaan a ngi ci loolu ñeel ñeel waa àddina si yépp.
23وَمِنْ آيَاتِهِ مَنَامُكُم بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَابْتِغَاؤُكُم مِّن فَضْلِهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَسْمَعُونَ
Bokk na it ci ay kéemaanam, seeni nelaw ci guddi gi ak seenug sàkku wërsëg. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy dégg.
24وَمِنْ آيَاتِهِ يُرِيكُمُ الْبَرْقَ خَوْفًا وَطَمَعًا وَيُنَزِّلُ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَيُحْيِي بِهِ الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ
Bokk na it ci ay kéemaanam, Mu di leen won melax mu boole ragal ak xemmem, muy wàcce ndox mu bawoo asamaan di ca dundal suuf si ginnaaw ba mu deewee. Ay kéemaan a ngi biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat.
25وَمِنْ آيَاتِهِ أَن تَقُومَ السَّمَاءُ وَالْأَرْضُ بِأَمْرِهِ ۚ ثُمَّ إِذَا دَعَاكُمْ دَعْوَةً مِّنَ الْأَرْضِ إِذَا أَنتُمْ تَخْرُجُونَ
Bokk na it ci ay kéemaanam, ni asamaan ak suuf taxawe ci ndigalam ; te saa Su leen jiinee ab woote, yéen ñéppay génn ci biir suuf si [ginnaaw dee]
Ar-RumFihi Alxuraan
60Aaya
MeccanRevelation
23Aaya

Tekki — Ar-Rum 23

Simoore Ar-Rum Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bokk na it ci ay kéemaanam, seeni nelaw ci guddi…

Simoore Aaya 23/60 — Ar-Rum الروم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ar-Rum Dégg, Ar-Rum Tekki, Ar-Rum mp3, Ar-Rum pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers