Simoore Ar-Ra'd
43 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Aliif, Laam, Miim, Raa. Kàdduy Téere ba ñoo ngi nii te di lu ñu wàcce ci yaw, mu jóge ci sa Boroom dëgg ga ; waaye li ëpp ci nit ñi gëmuñu.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Yàlla Moo di ki wàcce asamaan yi ci lu amul keno yu ñu mën a gis. Topp Mu yemoo ca [Aras], Mu tàggat jant bi ak weer wi, ñoom ñépp ñuy daw jëm ci àpp bu ñu dogal. Mooy àtte doxiinu [àddina], Dana leeral ag kàddoom ndax mu wóor leen ne dangeen dajeek seen Boroom.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Moom mooy Ki tàllal suuf si, def ca ay doj ak i dex. Te def na ca mépp meññent ñaar-ñaar [góor ak jigéen]. Dana muure bëccëg ci guddi gi. Nit ñuy xalaat am nañu ci loolu ag waaru.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Nekk na ci kaw suuf si ay déndi suuf yu tàqaloo [te wuute], ak tooli reseñ ak mbeyum pepp, ak garabi tàndarma yu ràngaloo ak yu soreyaantoo, ñoom ñépp ndox mi leen di suuxat menn la. Nuy gënal yenn ya ci kaw yeneen ya ci cafka ga. Ag waare nekk na ci biir loolu ngir nit ñu am xel.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Ndeem danga yéemu yaw [Yonent bi], dana la yéem li ñuy wax naan : “Ndax bu ñu deewee ba seey nekk suuf, danañu dekkiwaat nekk i mbindeef ? ”. Ñooña ñooy ña weddi seen Boroom. Te mooy ña gëx nekk ca seen loos. Te ñoom ñoo di waa Safara, te dañu fay béel.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Ñangay yàkkamti naan na mbugal [mi nga nu dig] nëw lu jiitu seenug sàkku yërmaande. Waaye ca la weesu, amoon na ay mbugal [yu daloon ña leen jiitu]. Doonte la sa Boroom kuy jéggal nit ñi la seeni bàkkaar, waaye fekk na sa Boroom di ku tar mbugal itam.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Ña weddi ñangay wax : “Lu tee ñu wàcce ci moom kéemaan gu jóge ca Boroomam ? ”. Te yaw nekkoo lu dul kuy waare, te xeet wu nekk am na ku koy gindi.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Yàlla xam na lu jépp jigéen ëmb, ak lay wàññeeku ak a yokk ca ëmb ba. Te lépp lu nekk am na moom ab natt [bu mu tollool].
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Mooy kiy xam lu fàddu ak li feeñ, di Ku màgg, di Ku kawe ka.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Ci yéen ku ca jàpp ndigal ci lu nëbbu ak ku jàpp ca la feeñ, ñoo ca yem kepp. Naka noonu, ku nëbbu [di ko jëf] guddi ak ku ne dàŋŋ ci bëccëg.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Kooku jàpp ndigal la, am na [ña koy wattu] ñuy wuutuwante ci kanamam ak ci ginnaawam. Danañu ko sàmm ci ndigalul Yàlla. Naka Yàlla du soppi li nekk ci aw nit li feek soppiwuñu la nekk ca ñoom. Te bu Yàlla nammee teg mbugal aw nit, kenn du ko mën a delloo : te it du am kenn ku leen mën a sàmm ginnaaw Yàlla.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Moom moo leen indil melax ngeen yëg ci am tiit ak njàqare ; te Moo sos niir yu diis yi [ak ndox].
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Dënnu ga di ko sàbbaal, màggal cant gi mu yeyoo. Malaaka ya it ànd ak ragal ko. Te dana sànni dënnu, sadd ko ci ku ko soob. Ñoom nit ña, ñangay dàggasante ci Yàlla, te Moom ku tar la ci kàttanam.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Mooy boroom woote bu dëggu ba ! Te ña ñuy jaamu dëddu Ko, duñu mën a wuyyu [ba jariñ leen] ci dara ; dafa mel ni [ku mar], tàllal ay yoxoom ndox ma, bëgg mu jëm ca gémmiñam, te jotu ko. Jaamug ña weddi du jëme fu dul ci sànku.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si danañuy sujjóotal Yàlla cig nangu walla cig nooteel, ak seeni takkandeer suba ak ngoon.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Neel : “Kan mooy boroom asamaan yi ak suuf si ? ”. Neel : “Yàlla”. Neel : “Waaye ndax dangeen Koy bàyyi di jàpp ci ay yàlla yoo xam ne mënaluñu seen bopp njariñ walla jenn lor ? Neel : “Ndax gumba dana yem ak njàccaar walla ndax leer ak lëndëm ñoo yem, walla ndax dañuy sàkkal Yàlla way-bokkaale yu mën a bind lu mel ni li Mu bind ba seeni mbindeef niroo ci ñoom? Neel : “Yàlla mooy Aji-bind ji lépp lu ne te Moom mooy Notaakoon bi di kenn”.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Wàcce na ndox mu jóge asamaan, ay dex walangaan ciy xur. [Lu na toll] yol mu yanu puurit mu njaxlaf, muy nirook puurit muy féey ci kaw lu ñuy teg cib taal ngir defar i takkaay walla ndab. Noonu la Yàlla [di joxee misaal ngir téqale] dëgg ak neen te puurit ma day dem ci neen, lay jariñ mooy la des ca suuf sa. Noonu la Yàlla di joxee misaal.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝ
Ña wuyyu seen [wooteb] Boroom am nañu Àjjana. Waaye ña ko bañ a wuyyu, bu ñu amoom li nekk ci suuf si lépp ba dolli ca lu na toll, du mën a nekk seen njot [ci mbugal ma]. Ñooña, natt bu ñaaw [lañuy natte seen jëf] te seen saxuwaay Safara la. Te delluwaay boobu bon na !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Moo ndax koo xam ne la ñu wàcce ci yaw mu jóge ca sa Boroom dëgg, mel na ne ka nga xam ne gumba la ? Woroom xel yi rekk ñooy waaru,
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
ñooy ñay matal seen kóllare ak Yàlla te duñu firi kóllare googu,
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
ak ñay jokk la Yàlla santaane ñu jokk ko [mooy mbokk], te ragal nañu seen Boroom, di ragal it [ca àllaaxira] natt bu bon [seen jëf yu ñaaw ëpp seen jëf yu baax],
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
ak ñay muñ ngir jëmmi seen Boroom, tey taxawal julli tey dundale ca la leen Yàlla wërsëgale ci la nëbbu walla ci lu feeñ, te ñuy jiñe lu ñaaw ak lu rafet. Ñooña am nañu kër gu mujj ga,
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Àjjana ju sax ja, danañu ca dugg, ak ña jëfoon lu baax ca seeni baay ak ca seeni jabar ak seeni doom ak i sët. Te Malaaka ya dañuy duggandook ñoom ci buntu yépp :
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
[Ñu naan leen] - “Jàmmi Yàlla na nekk ci yéen ngir la ngeen muñoon ! ” - Aka rafet kërug mujj ga ! ”
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
[Waaye] ñiy firi kóllareg Yàlla ginnaaw ba mu fasoo, te muy dog la Mu santaane ñu jokk ko [mooy ag mbokk], di yàq ci kaw suuf si, ñooña am rëbb dal na ci seen kaw [sori yërmaandey Yàlla], te it am nañu kër gu bon ga.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Yàlla dana yaatal wërsëg ci ku ko soob, Dana ko xatal it. Te ñoom dundu àdduna neex na leen, te dundu àdduna soo ko méngaleek gu àllaaxira, du nekk lu dul xéewal gu ñàkk solo.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Te ñoom ña weddi dañuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom kéemaan gu jóge ca Boroomam ? ”. Waxal ne : “Yàlla dana bàyyi cig réer ku ko soob, te it Dana gindi jëme ci Moom ku dellu [jëm ci topp Yàlla],
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓ
ñooy ña gëm te seen xol dal ci tudd Yàlla”. Te nag ca dëgg-dëgg, tuddu Yàlla mooy dalal xel yi [xol yi] ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Ña gëm tey jëf jëf yu sell yi, am nañu ag texe ak delluwaay bu rafet.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Ci noonu yónni Naa la ci xeet woo xam ne - yeneen xeet ya wéy jiitu woon nañu ko - ngir nga jàngal leen la Nu la soloo, ci noonu ñuy wéy di weddi Yërëmaakoon bi [Yàlla]. Waxal ne : “Moom moo di sama Boroom. Amul jeneen yàlla ju dul Moom. Ci Moom laa wéeru te ci Moom la delluwaay ba nekk”.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Alxuraan, bu ñu ci doxloo woon tundi doj yi, walla xotti suuf si, walla waxloo ñu dee ñi, [du tax ñu gëm]. Waaye li am moo di mépp mbir Yàllaa ko moom. Moo ndax ñi gëm dañoo xamul ne bu neexoon Yàlla Mu jubal nit ñépp. Waaye ñi weddi duñu deñ mukk njuuma di leen dal ngir seen jëf yu ñaaw, walla xanaa mu wàcc fu jegeñ seeni kër ba digub Yàlla di agsi. Te Yàlla du wuute ab digam.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Yéjjeefoon na ay Yonent lu la jiitu. Ma yeexe ña weddi woon. Topp Ma mbugal leen. Naka la sama mbugal mel ? Xanaa metti rekk !
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Ndax ku di kay fuglu lu bakkan bu ne fàggu [danañu ko niroole ak leneen ?...]. Te ñoom dañoo sàkkal Yàlla ay bokkaale. Neel : “Tuddleen leen. Walla moo ndax dangeen koy soloo [Moom Yàlla] ci la Mu xamul ci suuf si ? Walla lu ngeen di wax rekk la ci kaw [te eggul ci seen xol]? Déedéet”. Ñooña rafetaleef na leen seen kéefar ba fekk na ñu soril leen yoon [wu jub wa]. Te ku Yàlla bàyyi cig réeram, du am ku ko gindi.
ﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜ
Am na ñu am mbugal ci dundug àddina. Te ca dëgg-dëgg mbugalum àllaaxira moo gën a tiis te duñu am ku leen aar ci la Yàlla dogal ci ñoom.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Àjjana ja ñu dig ña ragal Yàlla [kem ni tool] bu ay dex di daw ci suufam ; ay meññantam ak i keram day sax ba fàww. Loolooy mujjug ña ragal Yàlla, te ña weddi Yàlla seen mujj mooy Safara.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Ña nga xam ne jox nañu leen Téere ba, nekk nañu ci la wàcceef na ko ci yaw. Te am na ñenn ci kurél ya, ñu weddi lenn ci Alxuraan. Neel : “Man dey digaleef na ma may jaamu Yàlla te du ma ko bokkaaleek [dara]. Maa ngi woote jëme ci Moom, Te samab delluwaay ma nga fa Moom”.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Noonu la Nu ko wàccee muy lu ñu xereñe ci làkku araab [di ay àtte]. Te boo toppoon seeni bànneex ginnaaw li la dikkal ci xam-xam, doo am kenn ku la wattu waxantumaak ku lay fegal [mbugalum] Yàlla.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Yónni woon Nanu ay Yonent lu jiitu, te defaloon Nanu leen ay soxna ak i doom. Te ab Yonent daawul mën a def kéemaan lu dul ci ndigalul Yàlla. Àppub xew-xew bu mu mën a doon bind Nanu ko ba noppi.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Yàlla dana far lu ko soob te Dana saxal itam [lu ko soob] ca cosaani Téere ba di [Lawhul- Mahfuuz] ma nga fa Moom.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Ndegam won Nanu la lenn ci li Nu leen dig, walla Nu rey la [lu mu ca mën di doon], yaw li la war moo di jotal, waaye Nun noo warloo natt [jëf ya].
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Xanaa dañoo gisul ne Nun noo ngi wàññi suuf si ci ay catam ? Yàlla mooy àtte, Dananu delloob àtteem, te Moom ku gaaw la cib nattam.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Ña leen jiitu woon defoon nañu ay pexe ; te Yàllaa moom gépp fànnu pexe. Xam na lu bépp bakkan fàggu. Te yéefar yi danañu mës a xam kan moo moom kër gu mujj ga.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Ña weddi dañuy wax naan : “Doo ab Yonent”. Neel : “Yàlla doy na seede ci sama diggante ak yéen, ak képp ku am xam-xamu Téere ba”.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers