Simoore An-Nahl
128 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Mbirum Yàlla jege na. Buleen ko yàkkamti. Sellam ga màgg na ! Te kawe na, sori lañu koy bokkaale.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Mooy wàcce ay Malaaka yuy ànd ak ug soloo, ciy ndigalam, jox ko ku ko soob ci ay jaamam, neeleen : “Nangeen waare ci xamle ne amul jeneen Yàlla ju dul Man. Ragal-leen Ma”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Moo bind asamaan yi ak suuf si ci dëgg. Kawe na, sori lool la ñu koy bokkaale.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Moo bind nit ñi ci toqent ; te moom [nit] mu nekk di pànk mu mën a xuloo.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
[Moo bind it] mala yi, ngeen di ca jële ay yére yu nuggu ak yeneen njariñ. Ak lu ngeen di lekk.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Te it yéen a ngi bànneexu ci seeni taar bu ngeen di jofal ci ngoon ak bu ngeen di wëtal ci suba.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Te danañu yenu seen [yóbbal], yóbbul leen ko ca dëkk ba ngeen dul woon mën a dem lu dul ci ab coono bub bakkan. Naka seen Boroom Aji-ñeewant la, Jaglewaakoon la.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
[Moo bind it] fas ak i baxla [berkelle] ak mbaam ngir ngeen war leen, ak ngir taar. Te it bind na lu ngeen xamul.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Yàlla moo yeyoo leeral yoon wu jub wa, [te am na ci yoon yi] yu jeng féeroo ak njub. Te bu Ko sooboon Mu jubal leen yéen ñépp.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Moom mooy ki leen wàcceel ndox mu jóge asamaan, ngeen di ca naan, garab yi di ca saxe, ngeen di ca nàndale [jur gi].
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Mu di leen cay saxal mbey, garabi oliiw ak i tàndarma, ak yu reseñ, ak bépp meññent. Loolu mën naa waar aw nit yuy xalaat [natt].
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Te Moo leen tàggatal guddi gi ak bëccëg gi ; ak jant bi ak weer wi. Ak bidiw yi itam. Ci ndigalam, loolu dey ag kéemaan a ngi ci ngir aw nit ñuy xel-lu.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Te li Mu leen wesaareel ci kaw suuf si am nañu ay melo yu wuute. Te ci biir yooyu, am na ca ay kéemaan ñeel aw nit ñuy waaru.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Te Moom moo leen tàggatal géej gi ngir ngeen mën ciy jële yàpp wu tooy wu ngeen di lekk, ak ngeen ciy mën a génne ay takkaay yu ngeen di takk. Te gis ngeen ne gaal yaa ngi cay daw, ak it ngeen di ca sàkku ci xéewalam ya, te kon xéy-na di ngeen ko gërëm.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Te Moo samp ci suuf si ay ndëgërlaay [mu dal] bañ a jaayu ak yéen, ak i dex ak i yoon,
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
[def na it ci suuf si] ay màndarga, nit ña mën a gindikoo ci bidiw yi.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Waaw ndax ku bind dana mën a yem ak ku bindul dara ? Moo ndax dangeen dul fàttaliku ?
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Te bu ngeen doon jéem a lim xéewal yi leen Yàlla defal, dungeen ko mën. Te Yàlla Moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Te Yàlla xam na li ngeen nëbb ak li ngeen feeñal.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Te ya ñuy jaamu bàyyi Yàlla binduñu dara, te sax dañu leen bind far.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Yu dee lañu, nekkuñu luy dundu, te xamuñu kañ lañu leen di dekkal.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Seen Yàlla jenn rekk la. Tax na ña gëmul àllaaxira, seeni xol a dàq a weddi te ñoom dañuy rëy-rëylu.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Ca dëgg-dëgg, Yàlla xam na la ñuy nëbb ak la ñuy feeñal. Te Yàlla nag soppul ñiy rëy- rëylu.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Bu ñu nee leen : “Lan la seen Boroom wàcce ? ”. Ñu ne : “Xanaa ay léeb yu jóge ca mag ñu njëgg ña ! ”
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Danañu yenu seeni bàkkaar ba mu mat sëkk, Bis-pénc ba, ak lenn ca bàkkaari ña ñu réeral, ci loo xam ne amuñu ca woon xam-xam ; cëy ndaw yen bu bon !
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Ña leen jiitu woon defoon nañu ay pexe, Yàlla toj seeni tabax ya dale ko ca ndëgërlaay ja. Téeg ma daanu seen kaw, mbugal ma agsi ca ñoom jaare fu ñu ko foogewul woon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Te bu Bis-pénc baa, Dana leen gàcceel, ne leen : “Waa ana sama bokkaale ya taxoon ngeen wuuteeg [jullit ñi] ? ” - Ña amoom xam-xam tontu ne : “Bis niki tey, toroxteeg mbugal dal na ci kaw yéefar yi”.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Ñoom ña Malaaka yay song, fekk ñoo tooñ seen bopp, ñu sànnib nuyyoo, naan : “Defunu woon dara lu bon ! ” - “Axakañ, Yàlla ku xam la li ngeen daan def”.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Kon dugguleen ciy buntu Safara, te dangeen cay béel. Te bon na lool dëkkukaayu ña daan rëy-rëylu !
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ñuy wax [ña ragal seen Boroom] : “Ana lan la seen Boroom wàcce ? ”. Ñu tontu ne : “Yiw”. Ñeel na ñi rafetal ci àddina Samay teraanga ; waaye kërug àllaaxiraa gën. Te aka baax kërug way-ragal ña [seen Boroom] !
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Àjjana ju sax la, ñu tàbbi ca, te ay dex danañuy daw-dawaan ci suufam. Te danañu fa am lu ñu bëgg ; Noonu la Yàlla di feye way-ragal ña [Yàlla].
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Ña nga xam ne Malaaka ya danañu leen rey - fekk ñu nekk ñu sell - danañu leen wax ne : “Yal na jàmm nekk ci yéen ! Dugguleen Àjjana ci sababus la ngeen daan jëf [ci lu baax]”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Lan la [yéefar ya] di xaar, Malaaka ya digal leen walla sa dogalu Boroom agsi ci ñoom ? Noonu la [yéefar ya] leen jiitu nekke woon. Waaye ñoom ñoo tooñ seen bopp.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Dal na ci seen kaw ñaawtéefu la ñu defoon, ndax wàcc na ci ñoom la ñu doon soofantal di ko reetaan.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Ña daan bokkaale wax ne : “Bu neexoon Yàlla, dunu jaamu kenn ku dul Moom, du nun du kenn ci sunuy baay ; te kon dunu ne dara araam na te du ci ndigalam. Ña leen jiitu woon noonu lañu defoon. Te li war ab Yonent ndax dafa dul jottali rekk [la ñu ko yónni] ba mu mat sëkk ?
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Yónni nañu ci xeet wu nekk ab Yonent [buy xamle ne] : “Jaamuleen Yàlla te ngeen moytuy xërëm”. Mu am ci ñoom [xeet yooyu] ñu Yàlla jubal ak ñoo xam ne réer war na ci ñoom. Doxleen ci seeni suuf te xool ña weddi woon naka lañu mujje.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Loo xér xér ci jubal leen...Yàlla moom du gindi ku Mu bàyyi cig réer. Te duñu am ñu leen dimbali.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Ñangay giñ ba fa seeni ngiñ yem naan : “Yàlla du dekkal ku dee”. Axakañ ! Loolu dig bu dëggu la ci Moom [Yàlla], waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Ngir mu leeralal leen [lay dëgg] ca la ñu daan wuute, ak it ña weddi xam ne dañu daan fen.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
[Li am mooy], Sunu kàddu ci mbir, bu Nu ko bëggee, Danu ko naan : “Nekkal”. Mu daldi nekk.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Ña gàddaay jëm ci Yàlla, ginnaaw ba ñu leen tooñee, Dananu leen wàcceel aw yiw ci àddina. Te peyug àllaaxira moo gën a màgg, cëy bu ñu xamoon !
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Ñoo di ñay muñ, wéeru ci seen Boroom [Dana leen wërsëgal lu ñu njortul woon].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Yónniwunu woon ca la jiitu lu dul ay góor yu Nu xamaloon [Sunuy ndigal]. Ne leen bu ngeen xamul laajleen woroom xam-xam yi.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
[Ay Yonent lañu woon] yu indi lay yu leer ak i téere. Te Nu wàcce it Alxuraan ngir nga leeralal nit ñi la ñu wàcce woon ca ñoom, ñu xel-lu [waar ña gëm].
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Ndax am na ci ñuy fexe lu bon, ñu wóolu ne Yàlla du këpp suuf ci sunu kaw, mbaa Mu sadd leen mbugal mu ñu foogul ?
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Mbaa mu sadd leen ci seeni tukki ngir ñoom mënuñoo raw [Yàlla].
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Mbaa Mu sadd leen cim tiit ? Te sax seen Boroom Aji-ñeewant la, Jaglewaakoon la.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Moo ndax seetlu nañu lenn lu Yàlla bind, loolu keram danay jeng jëm càmmoñ, ak a jengiy jëm ndeyjoor ngir sujjóotal Yàlla ak a toroxlu ?
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si tey dukkat, ak Malaaka yi, dañuy sujjóotal Yàlla te duñu rëy-rëylu.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Dañuy ragal seen Boroom bi leen tiim, te dañuy def la ñu leen digal.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Yàlla nee na : “Buleen sàkk ñaari yàlla. Yàlla jenn rekk la. Kon nangeen Ma ragal”.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Te Moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf ; te Moo moom it ñu war koo jaamu ci diine ju sax. Moo ndax dangeen di ragal keneen ku dul Yàlla ?
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Li ngeen am ciw yiw mi ngi jóge ca Yàlla. Te bu leen lu metti dalee, Moom ngeen di ñaan ndimbal.
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Te bu leen lor ja deggikoo, mu am ab kurél buy bokkaaleeti seen Boroom,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Ngir weddi la Nu leen jox. Xéewluleen ! Dangeen mës a xam !
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Ñuy sàkkal ay cër ca la Nu leen wërsëgal ñoo xam ne xamuñu leen. Waat naa ci Yàlla ne dees na leen laaj la ngeen nekkoon di ko duur.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Ñuy sàkkal Yàlla ay doom yu jigéen. Sellam ga [sori na lool ! Te ñoom ñuy moomale seen bopp la ñu bëgg [ay doom yu góor].
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Ku ñu ca yégal ne am na doom ju jigéen, mu yendoo ñëgal kanam gi ànd ak mer.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Muy nëbbu nit ñi ngir lu naqari la ñu yégal. Muy seet ndax dakoy téyee ndax gàcceem walla dakoy suul ci suuf ? Cëy aka bon nañuy àttee mbir !
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Ñeel na ñi gëmul àllaaxira nekkin wu bon. Te ñeel na Yàlla nekkin wa gën a kawe. Te Moom mooy Aji-not ji ; Aji-xereñ.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Bu Yàlla [doon] gaaw a duma nit ñi ngir seen tooñeel, kon du bàyyi kenn ci kaw suuf si. Waaye Dafa leen ci yeexe ba ci àpp bu ñu dogal ba noppi. Kon bu seen àpp agsee, duñu ko weesu mbaa ñu jiitu ko wenn waxtu.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Ñangay sédd Yàlla la ñu sib ñoom. Te seeni làmmiñ di sos i fen naan ñoo moom Àjjana. Te ca dëgg-dëgg ñoo yeyoo Safara te ñoo cay jiitu.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Giñ Nanu Nun Yàlla ne yónni woon Nanu ay Yonent cay xeet ya la jiitu. Waaye Séytaane rafetalal leen seeni jëf ba faf mu nekk tey seeni àndandoo. Te ñeel na leen mbugal mu metti.
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Wàccewuñu ci yaaw Téere [Alxuraan] ba lu dul ngir nga leeralal leen la ñu nekkoon ci juuyoo, ak ngir mu nekk di njub ak yërmaande ci nit ñu gëm.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Te Yàlla moo wàcce ndox mu jóge ca kaw, mu dundal ci suuf si ginnaaw ba mu bekkooree. Te nekk na ci loolu tegtal ci nit ñuy dégg.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Te sax am ngeen lu ngeen mën a waaroo ci mala yi : Noo ngi leen di nàndal ci li nekk ci seen biir - lu génne ci diggante sebret ak deret - muy meew mu neex te sell ca ña koy naan.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Te ci meññenti tàndarma ak reseñ, dangeen ca jële naan guy màndee ak xéewal gu baax. Te nekk na ci loolu ay tegtal ci aw nit ñuy xalaat.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Te sa Boroom moo yenkewal yamb [xamal ko ne] : “Nanga sàkk néeg ci doj ak ci garab yi ak ca lañu tabax.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Topp [Mu ne ko] nanga lekk ci mépp meññent, te nangay sóobu ci say yooni Boroom muy lu ñu la yombalal. Dana génnee ci biiram naan goo xam ne dana am ay melo yu wuute (lem). Te nekk na ci luy faj nit ñi. Te loolu kéemaan la ci aw nit ñuy xalaat.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Te Yàlla moo leen bind ! Dana leen rey. Te am na ci yéen ñuy àgg ba ci màggat lool, duñu xamati dara ginnaaw ba ñu nekkoon ñu xam. Naka Yàlla moo di Aji-xam ji, di Aji-kàttan gi.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Yàlla yékkati na ñenn ña ci kaw ñeneen ña ci wërsëg. Te ña Mu jox ngëneel loolu, duñu delloo dara ci wërsëg woowu, jox ko seeni jaam ngir ñu yemoo ca wërsëg wa. Moo ndax dañuy weddi xéewali Yàlla ? Fàkk
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
Yàlla sàkkal na leen ay jabar yu jóge ci yéen, Mu sàkkal leen ay doom yu jóge ci seeni jabar ak i sët. Mu boole ca wërsëgal leen ñam yu sell. Waa ndax [yéefar yi] dañuy gëm ay xërëm tey weddi xéewali Yàlla yi ?
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Te dañoo bàyyi Yàlla di jaamu loo xam ne moomul dara lu mu leen mën a wërsërgal ci kaw asamaan yi ak ci suuf si. Te mënul dara.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Buleen wutal Yàlla niraale mukk. Yàlla xam na te yéen xamuleen.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Yàllaa ngay joxe léebu ci jaam bu ñu moom, te amul mën-mën ci dara, ak ki nga xam ne [gor] la te Nu wërsëgal ko lu jóge ci Nun wërsëg wu rafet, te mu di ca dimbalee ci lu nëbb ak ci lu feeñ. Ñooña ñaar ndax yem nañu ? Cant ñeel na Yàlla ! Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Yàllaa ngay joxe ba-tey léebu ñaari góor yoo xam ne : kenn ka dafa luu [muuma], mënul dara te moom dafa wéeru ci sangam ; Te fu mu mën di jubale, du ca jële njariñ ; ndax dafay yem ak ki nga xam ne dafay digle maandute te lu mu def mu àntu tegu ci njub ?
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Ñeel na Yàlla kumpag asamaan yi ak suuf si. Te mbiru Bis-pénc ba dafay mel ni xef ak xippi mbaa lu ko gën a gaaw ! Naka Yàlla lu nekk la mën.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Yàlla moo leen génne ci seen biiri ndey, xamuleen wóon dara, Mu sàkkal leen ag dégg ak ug gis, ak xel, ndaxtelee ngeen gërëm ko.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Ndax gisuñu picc yi [mbindéef yu ñu tàggat lañu ci jawi asamaan si], dara téyuleen lu dul Yàlla ? Te nekk na ci biir loolu dëgg-dëggi kéemtaan ngir aw nit ñu gëm.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Yàlla defal na leen ca seen biiri kër ay dëkkuwaay [néeg], Mu defal leen ci deri mala yi kiiraay [mbaar] mu woyof ci bu ngeen di tukki walla ngeen di sax fenn. Te defal na leen it ci ngëndël ak ci seeni karaw ak seeni cëx-cëx laltaayi néeg ak i jumtukaay bu jëmmi jamonoo.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Yàlla defal na leen, ci li Mu bind, ay ker. Mu defal leen ci doj yi ay néeg. Mu defal leen ci mbubb yu leen di fegal tàngoor, ak mbubbi koŋ yu leen di fegal seen ngaañ. Noonu la mottalee xéewalam ndax xéy-na ngeen jébbalu [doon ay jullit tigi].
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Bu ñu dëddoo Yàlla... dara waru la [yaw Yonent bi] lu dul jottali gu mat, bu ñu ko xasee dégg rekk wàcc na la.
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Xam nañu xell Yàlla ba noppi ; ñu fakk ko. Te ñu bari ci ñoom yéefar lañu.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ca bis ba Nu dogalee ci xeet wu ne seen seede, te deeful may [ña weddi] lay, te duñu leen nangul it ngànt.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Ña tooñ, bis ba ñu gisee mbugal ma, deesuleen woyofalal dara, te deefuleen yeexe.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Te ña doon bokkaale, bu ñu gisee seen xërëm ya, danañu ne : “Yaw sunu Boroom, ñile ñoo di ñanu daan bokkaalee, di leen jaamu bàyyi la”. Ñoom it ñu tontu ne : “Yéen ay fenkat ngeen”.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Ñu sànni jëme ca Yàlla, ca bis booba njébbal la ñu doon duur réer leen [Yàlla rekk a fi sës].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Ña weddi tey wëlbati nit ñi bañ ñu jëm ca yoonu Yàlla, Dananu leen dolli mbugal mu tegu ci mbugal ya ngir la ñu nekkoon di yàq.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Te bis bu Nu dekkale ci xeet wu nekk sunu seede su nekk seede ci ñoom, Dananu la indil [yaw Muhammad] nga nekk seede ci ñooñu. Ndaxte wàcce Nanu ci yaw Téere ngir biral lépp lu nekk te muy luy gindee, di yërmaande, di mbégte ñeel ña jébbalu [diy jullit].
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Te Yàlla nag dafay digle maandute, di tere njaaloo ak lu bon ak tooñ. Mi ngi leen di waar ndaxtelee ngeen fàttaliku [seen Boroom].
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Matal-leen kóllareg Yàlla ginnaaw ba ngeen ko fasee, buleen di fàtte la ngeen dige woon ginnaaw ba mu nekkee di lu dëgër, te ngeen def Yàlla Mu di seen seede. Yàlla dey xam na li ngeen di def !
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Buleen mel ni ndaw sa firinci buum ga mu raw ba mu dëgër, mu firinci ko ba mu nekk i dogit, ngeen di jàppe seeni ngiñ li ngeen di wuruje ci seen diggante, ngeen defe ne ku ëpp mbooloo mën naa wor. Te Yàlla dafa leen ciy natt. Te bu Bis-pénc baa Dana leen leeralal la ngeen nekkoon di ca juyoo.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Su neexoon Yàlla Mu def leen ngeen nekk wenn xeet doŋŋ. Waaye Mooy bàyyi cig réeram ku ko soob, di gindi ku ko soob. Te fàwwu ñu laaj leen ca la ngeen defoon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Buleen def seeni ngiñ muy yàq li nekk seeni diggante, ba tax tànk bu sampu woon tarxiis, kon dangeen mos lu bon ndax seen dëddëleek nit ñeek yoonu Yàlla, mbugal mu mag dal leen.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Buleen di jaaye kóllareg Yàlla ci njëg gu néew. La nekk fa Yàlla moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon !
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Li ngeen moom day jeex, la Yàlla moom nag luy des la. Te fàwwu Dananu feye ñiy muñ ca na mu gën a rafete, ngir la ñu nekkoon di ko def.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Ku jëf u yiw, di ku góor walla ku jigéen te muy ku gëm, fàwwu Dananu ko dundal dundu gu sell. Te fàwwu Dananu leen fey seenug pey na mu gën a rafete la ñu nekkoon di ko jëf.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Booy jàng Alxuraan, nanga muslu ci Yàlla Mu musal la ci Séytaane su ñu rëbb sa.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Naka Séytaane du am genn kàttan ci [yàqal] ña gëm te wéeru ci seen Boroom.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ña mu mënal dara ci kàttanam du kenn ñu dul ña féetewook moom Séytaane ak ña koy bokkaaleek [Yàlla].
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Bu ñu weccee jenn laaya, def jeneen laaya fa mu nekkoon - te Yàllaa gën a xam la Muy wàcce - ñuy wax naan : “Nekkuloo lu dul duurkat”. Déet, li ëpp ci ñoom xamuñu.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Neel : “Ruu gu sell gaa ko wàcce mu jóge ci lu dëggu ngir mu dëgëral ñi gëm, muy luy gindee, di luy bégal jullit ñi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Te xam Nanu jeek la ñuy wax ne : “Nit la ku jàngul”. Muy koo xam ne aw làkkam du [araab] te lii nekk di làkku araab wu réer..
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ña nga xam ne gëmuñu kàdduy Yàlla yi, Yàlla duleen gindi. Te ñeel na leen mbugal mu metti.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Ca dëgg-dëgg ñay duur ay fen ñooy ña gëmul kàdduy Yàlla yi, ñoom ñooy fenkat yi.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Ku weddi Yàlla ginnaaw ba mu gëmee... - ku dul ka ñu not fekk xelam sax na ci gëm Yàlla - ak ña ubbi seen dënn cig kéefar, mer mu tukkee ca Yàlla dana leen sadd te ñeel na leen mbugal mu màgg.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Li waral loolu moo di dañoo tànn dundug àddina ci kaw dundug àllaaxira. Te nag Yàlla du gindi aw nit ñu di ay yéefar.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Ñooñooy ña Yàlla fatt seeni xol, ak seeni dégg-dégg, ak seeni gis-gis. Te ñoom ñooy ña sàggan.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ca dëgg-dëgg, ñoom ñooy ñay yàqule ci àllaaxira.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
La cay topp moo di sa Boroom dana jéggal ña gàddaayoon te muñ, ginnaaw loolu sa Boroom dana jagle njéggalam ak yërmaandeem.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Bis bu bakkan bu ne dàggasanteeg boppam, te bakkan bu nekk ñu feye ko la mu jëfoon, bu boobaa Dunu tooñ kenn ci dara.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Yàllaa ngay joxe léebu ci dëkk ba amoon xel mu dal ; te am kóolute, wërsëgam di fa dikk, bari lool tey jóge fu nekk. Waaye mu weddi xéewali Yàlla yi. [Waa dëkk ba] tax Yàlla mosal ko càngaayu xiif ak tiitaange ndax la ñu jëf.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Ab Yonent bu bokk ci ñoom dikkal na leen, ñu weddi ko. Mbugal sadd leen te ñu nekkoon ñu tooñ.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Lekk-leen ci xéewal gi leen Yàlla jox, muy lu lew, lu teey. Te ngeen gërëm Yàlla ciy xéewalam ndeem Moom rekk ngeen di jaamu.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Waaye araamal na ci yéen médd, ak deret, ak yàppu mbaam-xuux ak lu ñu [rey] te tuddu ca keneen ku dul Yàlla. Képp ku nar a loru [ba tax mu lekk yooya araam], na xam ne Yàlla jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Buleen wax loo xam ne seeni làmmiñ a koy melal ciy fen, naan : “Lii dagan na, lii araam na”, di duural Yàlla ay fen. Te ñiy duural Yàlla ay fen duñu texe.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Ñeel na leen yóbbal bu néew, ak mbugal mu metti.
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Te araamaloon nañu ca yahuud ya li Nu la nettali ca bu jëkk. Te tooñunu leen ; waaye ñoo tooñ seen bopp.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Mu des nag ne sa Boroom, lu jëm ci ña jëfoon [lu bon niki bokkaale] cig réer, ginnaaw loola ñu tuub ko, rafetal seeni jëf, ñooña sa Boroom fàwwu Mu jéggal leen, yërëm leen naka.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Ibraahiima nag roytéef la. Di jaamukatu Yàlla, di ko wéetal, musul a bokk ca bokkaalekat ya.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Ku daan gërëm [Yàlla] la ci xéewalam yi, Yàlla tànn na ko, gindi ko, teg ko ci yoon wu jub xocc wa.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Te may Nanu ko ci àddina tagg wu rafet. Te ca àllaaxira, dana bokk ca ñu sell, ñu [yiw] ña.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Tax na Nu soloo la ne : “Toppal diiney Ibraahiima [yaw Muhammad] cig wéetal sa Boroom, bokkul woon ca bokkaalekat ya”.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Màggal bisu gaawu tegewul woon lu dul ca kaw ña ca juuyoo woon. Te sa Boroom dana àtte seen diggante ca Bis-pénc ba ca la ñu nekkoon di ca juuyoo.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Wooteel ci sa yoonu Boroom [Lislaam], sukkandiku ci Alxuraan ak waare ci lu baax. Nanga dàggasanteek ñoom ca na mu gën a rafete. Naka sa Boroom moo gën a xam ña réer, sori aw yoonam te Moom moo gën a xam ñu jub ña.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Nangeen feye ña leen mbugal, lu tollu ni la ñu leen mbugale. Waaye bu ngeen mënee [bañ a feyu]... moo gën ci ñay muñ.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Nangay muñ ! Te sag muñ bu mu wéeru fu dul ci Yàlla. Te bul jàq ngir ñoom. Te bul nekk ci tiis ngir la ñuy fexe.
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Yàlla nag, ñay rafetal te ragal Ko la àndal de.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers