Simoore Al-Isra
111 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Tudd naa sellug Ka nga xam ne Moo rañaane woon jaamam ba Muhammad [yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko] jële ko Màkka yóbbu ko Baytil Muqaddas [Al qudsu], muy dëkk boo xam ne wurumam barkeel na, ngir Nu won ko ci Sunuy kéemaan,Yàlla mooy Kiy dégg, mooy Kiy gis.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Indil Nanu Muusaa ab Téere, def ko mu di ag njub ngir Banii-Israayiila [aw xeetam] te ñu bañ a jàppee keneen wéeruwaay.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Ñoo di sëti ña àndoon ak Nooh ca gaal ga te Nu musaloon leen. Nooh jaam la bu daan sant Boroomam.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Nu leeral giiru Banii-Israayiila ca Téere ba, ne leen : “Dangeen yàq ci suuf si ñaari yoon, te it dangeen beew beew gu rëy”.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Ba dig bu njëkk ba agsee, Dananu yónni te yebal ci seen kaw Sunuy jaam yu am kàttan gu tar ñu songe leen ci seen biir kër. Loolu dig buy ñëw la.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Ba noppi, Nu joxaat leen doole ci kaw ñooñu ; dolli leen ay alal ak i doom. Def leen ngeen ëpp mbooloo :
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
“Su ngeen rafetalee, jariñoo ko ; su ngeen ko yàqee loroo ca”. Su dig bu mujj ba agsee, ñu toroxal leen, duggaat fa, jaxasewaat lépp.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Xéy-na seen Boroom yërëm leen. Waaye bu ngeen delloo [def lu bon], Nu dellu [mbugal leen]. Te def Nanu Safara mu di géttub yéefar yi.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Alxuraan jii nag dafay gindee jëm ci la gën a jub, tey bégal way-gëm ñay jëf jëf yu sell, [xamal leen ne] ñeel na leen pey gu rëy,
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
[Te xamal it ne] ña gëmul àllaaxira, xaroo Nanu leen mbugal mu metti.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Te nit dana ñaan lu bon ak lu baax, ndax dafa nekk di ku yàkkamti.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Def Nanu guddi ak bëccëg ñu nekk ñaari kéemaan, te far Nanu lëndëmi guddi ak leeraayu bëccëg, ngir ngeen mën a gis, di sàkku xéewal gu jóge ci seen Boroom, ak ngir ngeen mën a xam limi at yi ak ngir ngeen mën a waññi. Te lu nekk faramfàcce Nanu ko ci anam yu leer.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Te nit ku nekk, tàbbal Nanu ko jëfam ci doqam. Ca Bis-pénc ba, Dananu ko génneel ab téere bu muy dajeel, ñu tàllal ko ko :
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
[Nu ne ko] : “Jàngal sab téere. Sa bopp doy na la tey, sa nattub jëf yaw la war”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Ku jub, boppam la ko defal ; ku dëng boppam la ko def. Ndax kenn du yenu yenu keneen. Te nekkunu woon di Aji-mbugal wenn xeet te yónniwunu ab Yonent ca ñoom.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Bu Nu nammee alag ab dëkk, dafay fekk ne boroom alal ya dañoo jubadi ca dëkk ba. Àtte ba daldi yell ca ñoom. Nu sadd leen sadd gu tar.
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Aka bari xeet yu Nu alag ginnaaw Nooh ! Te sa Boroom kuy gis la te xam bàkkaari jaam ñi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Képp ku bëggul lu dul teraangay àddina, Dananu gaaw ci jox ko la Nu neex ; ca ku Nu neex. Topp Nu def Safara fa muy séndalu, di ku ñu xas, ku ñu génne [ci yërmaandey Yàlla].
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Ku bëgg [teraangay] àllaaxira te mu jëf lu méngook moom, te muy ku gëm... ñooñu seeni jëf lu ñu gërëm lay doon.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Ñoom ñépp Dananu leen tëbb ; ñii ak ñële, ay may yu jóge ca sa Boroom. Te sa mayu Boroom nekkul lu ñu tere kenn.Làndi na!
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Gisal ni Nu gënalee ñenn ñi ci kaw ñeneen ña. Te ca dëgg-dëgg àllaaxira moo gën a màgg daraja te moo gën a màgg i xéewal.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Bul sàkk jeneen yàlla di ko booleek Yàlla ; kon dey danga doon ku ñu xas, ku ñu wacc mu beddiku.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Sa Boroom dogal na ne : “Buleen jaamu ku dul Moom doŋŋ ; te ngeen rafetal jëme ci seeni waajur : te ndeem kenn ci ñoom walla ñoom ñaar egg nañu ci màggat ci sa teewaay ; buleen wax : “Kuf ma la ! ”, buleen leen gëdd, nangeen leen wax wax ju yiw.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Nanga suufeel sa bopp ngir ñoom ; di toroxlu ci yërmaande ; te deel wax : "Sama Boroom yërëm leen [ni ñu ma yërëme woon] ba ñu may yar ba ma nekkee xale”.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Seen Boroom a gën a xam li nekk ci seen bakkan. Ndeem nekk ngeen ñu sell ; Moom Jéggalaakoon la ci ñiy dellu jëm ci jaamu Yàlla.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
“Nanga jox sa jegeñaale li la war ci moom, ak ku ñàkk ak ku nekk ci tukki. Waaye bul nekk di pasar-pasaree alal,
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
yàqkat yi mbokki Séytaane lañu ; te Séytaane dafa weddi Boroomam.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Bu fekkee [ñàkk loo leen jox tax na] nga dëddu leen, toog di yaakaar sa yërmaandey Boroom ; nanga leen wax wax ju neex.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Bul bank sa loxo ba mu mel ni lu ñu yeew ci sa doq, waaye it bu ko tàllal mu tàlli ñareet, kon danga mujj di ku ñu yedd, ku ñu dàkku.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Naka sa Boroom mooy yaatal wërsëgu ku Ko soob. Moo koy xatal it, naka Moom ku xam tey gis la jaamam yi.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Buleen rey seeni doom ngir ragal ag ñàkk ; Nun noo leen di wërsëgal ñoom ak yéen. Rey leen bàkkaar bu rëy la.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Te buleen jegeñ njaaloo. Ndax moom nekk na lu ñaaw tey yoonu lu bon !
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Buleen rey bakkan ngir lu Yàlla araamal la, lu dul ci dëgg. Képp ku ñu rey, di ku ñu tooñ, jox Nanu kay taxawu mbiram sañ-sañ. Waaye bu mu jéggi dayo ci rey, ndax moom ku [yoon] dimbali la.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Buleen jegeñ alali jirim lu dul ca na mu gën a rafete, ba kero muy nekk mag te sàmm kóllare ga. Ndax kóllare lu ñuy laaj la ëllëg ca àllaaxira
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Nangeen di matal natt bu ngeen di natt ; te nangeen di peese cig maandute gu jàpp. Looloo gën te moo gën a rafet ag muj.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Bul toppati loo xam ne amoo ca xam-xam. Naka dégg-dégg ak gis-gis ak li nga fas ci sa xol : loolu lépp Dananu la ca laaj ca Bis-pénc ba.
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
Bul di dox ci kaw suuf ci di rëy-rëylu : yaw mënoo bënn senn suuf te it mënoo jot njoolaayu tundi doj yu rëy yi !
ﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
Loolu yépp, ñaawtéefam lu ñu sib la ca sa Boroom.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Loolu nekk na ci la la sa Boroom soloo, muy waare. Bul sàkk jeneen Yàlla di ko booleek Yàlla, dees na la sànni ci Safara, di ku ñu yedd, di ku ñu dàq [boo ko defee].
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Waaw ndax seen Borom dafa leen a tànnal ay doom yu góor, na noppi jël ci Malaaka yi ay doom yu jigéen ?Yéen nag ca dëgg-dëgg li ngeen di wax rëy na.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Te leeral Nanu ci Alxuraan jii [lu ne] ngir ñu xalaat. Te dolliwuleen lu dul fen [wëliis dëgg].
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Neel : “Bu amoon yeneeni Yàlla tu nekk ak Moom, ni ñu ko waxe, kon dinañu sàkk [yoon wu leen yóbb] ca Boroom gàngune ga”.(yab Yàlla)
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Cëy sellam ga ! Kawe na, jomb na li ñuy wax, jombute gu màgg a màgg !
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Juróom-ñaari asamaan yi ak suuf si, ñi ngi koy sàbbaal, ak li nekk ci seen biir. Te sax amul dara lu nekk te du Ko sàbbaal ci li Mu yeyoo mboolem cant. Waaye dangeen a amul dégg-dégg ci seeni sàbbaal. Naka Moom Aji-lewet la, Jéggalaakoon la.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Booy jàng Alxuraan, Dananu def ci sa diggante ak ñi gëmul àllaaxira kiiraay lu nëbbu,
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Nu def ci seeni xol muuraay ba duñu ca am dégg-dégg : te nekk na ci seeni nopp ab daaj. Te booy tudd sa Boroom moom doŋŋ ci Alxuraan, ñu dëddu, foñ.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Nun noo gën a xam li ñuy dégg bu ñu lay déglu. Ak bu ñuy déeytoo ci wax ñoom tooñkat ya : “Toppuñu lu dul as waay su ñu jibar”.
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Gisal li ñu lay nirale ! Tax na réer nañu te dootuñu mën a am yoonu dellusi (ci ag njub).
ﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
Ñu naan : “[Ndax bu ñu deewee] ba nekk yax yu funux, dananu dekki nekkaat ay mbindeef yu bees? ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
Neel : “Nekkleen i xeer walla weñ
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
walla yeneeni mbindeef yu reyci seeni xel. [Ngeen dégg] ñu naan : “Ku nuy dundalaat ? ” - Neel : “Ka leen bindoon bu njëkk ba”. Danañu yëngal seen bopp jëme ci yaw [ngir weddi la], ñuy wax naan : “Kañ lay doon ? ” Neeleen : “Xéy-na nekk na lu jegeñ.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Bis bu leen [seen Boroom] woowee, [ngeen dikk], ngeen tontu Ko, di tuddu cant [gi Mu yeyoo]. Te ngeen defe ne tooguleen ci [bàmmeel] lu dul diir bu néew ! ”.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Neel samay jaam, nañuy wax wax ju gën a rafet, ndax séytaane yi dañuy yàq seen diggante. Séytaane nag nekk na di noon tigi ci nit ñi.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Seen Boroom moo leen gën a xam. Bu ko neexee Mu yërëm leen, walla Bu ko neexee Mu mbugal leen. Te yónniwunu la ci ñoom ngir nga warlul leen [seen texe].
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Te sa Boroom moo gën a xam ña nekk ci asmaan yi ak suuf si. Te def Nanu yenn Yonent yi gën ñeneen ña. Te Noo jox Daawuda “Zabour” [Téere].
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Neel : “Wooleen ñi ngeen jàpp ne [Yàlla lañu] bàyyi Ko. Duñu mën a wuññi lor ja leen dal, duñu mën a soppi dara.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Ña ñuy jaamu dañu ne siiw am pexem gën a jegeñ seen Boroom. Te yaakaar nañu yërmaandeem, ragal nañu mbugalam. Naka sa mbugalum Boroom, lu mat a wattandiku la.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
Amul benn dëkk bu Nu dul alag balaa Bis-pénc ba, walla Nu mbugal ko mbugal mu tar. Looloo nekk ci Téere bu ñu bind. [Yàlla kuy nose la].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Lu Nu terey wàcce ay kéemaan, lu dul ñu jëkk ña dañu leen a weddi woon. Te sax joxoon Nanu waa Samooda giléem gu jigéen [muy kéemaan] gu leer : ñu def cag tooñeel. Te Nun dunu wàcce kéemaan lu dul ne Danuy xuppe ci kéemaan googu ak di ca àrtu nit ña.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
[Fàttalikul] ba Nu la waxee ne sa Boroom ku peeg nit ñi la. Te gént gi Nu la wonoon, defunu ko woon lu dul muy nattu ci nit ñi, te garab ga Nu rëbb ca Alxuraan it, Danu leen cay tiital ; waaye yokku leen lu dul beew gu mag.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñu sujjóot ginnaaw Ibliis, mu ne : “Ndax damay sujjóotal koo binde ak ban ? ”
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Mu ne : “Wax Ma lu tax nga teral kii ci sama kaw ? Soo ma muñalee ba Bis-pénc ba, danaa fexe ba ay sëtam yépp yàqule, ba mu des ñu néew”.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Mu ne ko : “Demal ! Ku la topp ci ñoom... [na xam ne] Safara moo di seen pey, pey guy nekk di lu mat sëkk.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Génnal ak say kàddu, loo mën ci ñoom, nanga leen song ak say xarekat ak say gawar, nanga bokk ak ñoom alal ak i doomn te digleen”. Waaye Séytaane duleen dig lu dul ay nax.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Naka samay jaam, doo am genn kàttan ci ñoom”. Ndax sa Boroom doy na cëslaay.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Sa Boroom mooy kiy dawloo gaal ci géej, ngir ngeen mën a sàkku ay xéewalam ; Naka Moom ku am yërmaande la ci yéen,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Bu leen naqar dabee ci géej, ña ngeen doon jaamu réer leen ginnaawam. Te bu Nu leen musalee ba ñu agsi ci jéeri ji, ngeen dëddu. Nit daal ku goreedi la !
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Moo ndax dangeen a naagu ne : du xar suuf si [mëdd leen], walla duleen yónnee ngelawu sànniy xeer fekk dungeen ci am ku leen ci yiir.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Am dangeen a wóolu ne duleen ca delloo [ca biir géej] beneen yoon, yónnee leen ngelaw lu tar, Mu labal leen ngir seen weddi ? Te fekk dungeen mën a am ku leen dimbali ci Nun !
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Ca dëgg-dëgg, teral Nanu doomi aadama. Yónni Nanu leen ci jéeri ji ak ci géej gi, te xéewal Nanu leen [ciy ñam] yu sell, Nu defal leen ngëneel ci kaw ñu bari ca ña Nu bind ngëneel lu fés.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Bis bu Nu woowee nit ku nekk ca turu njiitam, képp ku Nu jox téereem ci ndeyjooram, ñooña danañu jàng seen téere te deesuleen tooñ [ci wànnil leen dara].
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Ku nekkoon gumba ci àddina si, dana wéye gumba ca àllaaxira, te gën a réer, sori yoonu njub wa.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Xaw nañu laa fitnaal ba nga bàyyi la Nu la xamal, ngir nga duur lu wuuteek moom. Kon ñu jàppe la xarit ñoom yéefar yi.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Te bu Nu la dëgaralul woon, tuuti kon nga xaw a jeng jëm ci ñoom
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Te kon Dananu la mosal mbugali àddina ak mbugali àllaaxira; te doo am ku la dimbali ci Nun.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Te xaw nañu laa génne ca suuf sa [suufi Madiina] ngir ñu jële la fa. Te kon duñu fa toog lu dul diir bu néew ci sa ginnaw. [alag leen].
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Loolu aada la ca ña Nu yónni woon la la jiitu ci Sunuy Yonent. Te doo gis lu soppiku ci Sunuy aada.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Nanga taxawal julli bu jant fenkee ba ba muy suux, ba ba guddi gi di ñuul, ak it jullig suba, ndax jullig suba lu ñuy seede la.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Te nangay julli ci suba, def ko muy naafila : xéy-na kon sa Boroom dekkal la, jox la ndam lu yeyoo cant.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Neel : "Sama Boroom ; dugal ma ci duggukaayu dëggu te nga génne ma ci génnukaayu dëgg ; te nga defal ma kàttan gu tukke ci yaw di dimbal”.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Te neel : “Dëgg ga egsi na. Caaxaan wéy na. Caaxaan nag luy dem la naaxsaay”.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Wàcce Nanu ci Alxuraan loo xam ne saafara la ak yërmaande ca way-gëm ña. Waaye du yokk tooñkat ya lu dul yàqule.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Te bu Nu defalee nit xéewal ; mu dëddu, fuuyu ci wetam ; waaye bu ko tiis dalee, mu ñàkk yaakaar [yërmaande Yàlla].
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Neel : “Ku nekk a ngay jëf lu méngook meloon, waaye sa Boroom a gën a xam ku gindiku tegu ca yoon wu jub wa”.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Ña nga lay laaj lu jëm ci ruu, - Neel : “ Ruu ci mbiri sama Boroom la bokk”. Te joxeefuleen ci xam-xam lu dul lu tuuti.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Ca dëgg-dëgg su Nu neexoon, Nu yóbbu li nu la xamal ; te kon doo am kenn ku la musal ci Nun.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Lu dul yërmaande ju jóge ci sa Boroom, te ngënéelam li Mu la jagleel rëy na [ba tax na Mu bàyyee la xam-xam bi bañ koo rocci].
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Neel : “Bu nit ak jinne booloo woon ngir fexee indi lu mel ni Alxuraan jii, duñu mën a indi lu ni mel, doonte dañu caa dimbalante”.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Te ca dëgg-dëgg, jox Nanu nit ñi ci Alxuraan jii léebu wu ne [wuy leeral]. Waaye terewul li ëpp ci ñoom wéy di weddi.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Ñu naan : “Duñu gëm mukk li feek ballaloonu ci suuf si ay seewnde [bëti ndox] ;
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
walla nga am tooli garabi tàndarma ak garabu reseñ, nga ballal ay dex ci seen diggante yuy ball bu baax ;
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
walla nga rotal ci sunu kaw asamaan si ni nga ko dige, mu nekk ay daggit, mbaa nga indi Yàlla ak Malaaka yi nu jàkkaarloo ;
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
mbaa nga am këru wurus ; mbaa nga yéeg ci kaw asamaan si. Te dunu gëm sa yéeg feek wàcceloonu Téere bu nuy jàng”. Neel : “Tudd naa sellug sama Boroom ! Moo ndax man nekkuma lu dul nit ku ñu yónni doŋŋ ? "
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Te lan moo tere nit ñi gëm, ba leen njub ga dikkalee, lu dul la ñuy wax naan : “Moo ndax Yàlla dana yónni nit [nit ni nun]muy ab Yonent ? ”
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Neel : “Bu fekkoon ne ay Malaaka ñoo nekkoon ci kaw suuf si di dox, kon de Malaaka Lanuy yónni ci ñoom Mu jóge asamaan”.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Neel : “Yàlla doy na seede sama diggante ak yéen”. Moom Yàlla nag nekk na ci ay jaamam, di Ku xam, di Kuy gis [seeni mbir].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Ku Yàlla gindi nga jub, Ku mu bàyyi cig réer... duñu am keneen ku ñuy wéeru te Dananu leen dajale bisub dekki ba, ñu di leen diri ci seeni kanam, ñu gumba, tëx, lu. Seen dëkkuwaay moo di Safara : te saa yu giimee Nu dolli leen seneen safara.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Loolu moo di seen pey, ndax ñoom dañoo weddi Samay kàddu, naan : “Ndax [bu ñu deewee] ba nekk yax yu funux, dananu dekki nekk mbindeef yu bees ? ”
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Ndax dañoo gisul ne Yàlla moo bind asamaan yi ak suuf si, te Ku kàttanu la ci bind leneen lu mel ni ñoom ? Te Mu àppal leen dig bu amul benn sikki-sàkka, waaye way-tooñ ña wéy nañu ci seenug weddi.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Neel : “Su fekkoon ne yéen a moom ndàmbi yërmaandey Yàlla yi ; kon ngeen nay [ci joxe ko] ngir ŋott. Nit dafa di ku ŋott !
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Tigi, joxoon Nanu Muusaa juróom-ñeenti kéemaan yu leer. Laajal waa Bani-Israayiil, ba mu ñëwee fa ñoom, Firawna ne ko : “Muusaa, dama defe ne dañu laa jabar”.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
[Muusaa tontu ne] : “Xam nga ne kenn wàccewul yile [kéemaan] ku dul Boroom asamaan yi ak suuf si ngir ñu nekk di waare ; te damaa defe ni, yaw Firawna, dangaa nekk ku alku”.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Mu bëgg leen a génne suuf sa. Nu labal ko mook ña mu àndaloon ñépp.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Nu wax ginnaawam ñeel (waa Bani-Israayiil)ne leen : “Dëkkeleen suuf sa”. Ba àppu bisub àllaaxira jotee, Dananu leen indi ngeen di mbooloo.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Ca dëgg-dëgg wàcce na ko te ci dëgg it la wàcce ni ci yaw [Yonent bi], kuy bégle, di xuppe nga.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Te Alxuraan, téqale Nanu ko [cig wàccam] ngir nga jàng ko ci nit ñi, cig teey. Te wàcce Nanu ko ndànk-ndànk.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Neel : “Gëmleen ko mbaa ngeen bañ koo gëm, nanga xam ne joxeef na leen xam-xam. La ko jiitu, bu ñu jàngee ci seen kanam, danañu rot dëpp seeni sikkim ci suuf, sujjóot”
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
te ñuy wax ne : “Tudd nanu sellug sunu Boroom ! Digub sunu Boroom fàwwu mu am”.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Ñu rot dëpp seeni sikkim ca suuf di sujjóot. Seen toroxlu ci Yàlla dolliku.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Neel : “Wooleen Yàlla mbaa ngeen woo Aji-yërëme ji. Lu ngeen mën a woo [xamleen ne] Moo moom tur ya gën a rafet. Bul biral ci kaw ci sa julli ; te bul ca yelu it, sàkkal ci diggante ñaar yooyu [yoon wu digg-dóomu]”.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Neel : “Gépp cant ñeel na Yàlla mi amul doom te amul ku Mu bokkal nguuramte amul ku koy dimbali cig toroxte”. Dee ko màggal bu baax.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers