Al-Hajj · 25/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَالْمَسْجِدِ الْحَرَامِ الَّذِي جَعَلْنَاهُ لِلنَّاسِ سَوَاءً الْعَاكِفُ فِيهِ وَالْبَادِ ۚ وَمَن يُرِدْ فِيهِ بِإِلْحَادٍ بِظُلْمٍ نُّذِقْهُ مِنْ عَذَابٍ أَلِيمٍ ۝٢٥
Innal lazeena kafaroo wa yasuddoona `an sabeelil laahi wal Masjidil Haraamil lazee ja`alnaahu linnaasi sawaaa`anil `aakifu feehi walbaad; wa mai yurid feehi bi ilhaadim bizulmin nuziqhu min `azaabin aleem
📖 Tekkim Wolof
Ña weddi tey wëlbatiku jëm ci yoonu Yàlla ak ca Jàkka ju ñu wormaal ja Nu def muy jëmukaay ci nit ñi : te aji-dëkk ak gan ñoo ca yem kepp... Ku fa bëgg a jeng ngir tooñ, Dananu ko musal mbugal mu tar,
🎧 Dégg

📜 Aaya 23-27 — Al-Hajj

23إِنَّ اللَّهَ يُدْخِلُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ يُحَلَّوْنَ فِيهَا مِنْ أَسَاوِرَ مِن ذَهَبٍ وَلُؤْلُؤًا ۖ وَلِبَاسُهُمْ فِيهَا حَرِيرٌ
Yàlla nag Dana dugal ña gëm te jëf jëf ju yiw ay Àjjana yoo xam ne ay dexay daw ci suufam. Dees na leen fa takkal ay lami wurus ak i per ; te foofa yérey sooy lañu fay sol.
24وَهُدُوا إِلَى الطَّيِّبِ مِنَ الْقَوْلِ وَهُدُوا إِلَىٰ صِرَاطِ الْحَمِيدِ
Te jubaleef na leen ca wax ju teey te jubaleef na leen it ca yoon wu ñu gërëm.
25إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَالْمَسْجِدِ الْحَرَامِ الَّذِي جَعَلْنَاهُ لِلنَّاسِ سَوَاءً الْعَاكِفُ فِيهِ وَالْبَادِ ۚ وَمَن يُرِدْ فِيهِ بِإِلْحَادٍ بِظُلْمٍ نُّذِقْهُ مِنْ عَذَابٍ أَلِيمٍ
Ña weddi tey wëlbatiku jëm ci yoonu Yàlla ak ca Jàkka ju ñu wormaal ja Nu def muy jëmukaay ci nit ñi : te aji-dëkk ak gan ñoo ca yem kepp... Ku fa bëgg a jeng ngir tooñ, Dananu ko musal mbugal mu tar,
26وَإِذْ بَوَّأْنَا لِإِبْرَاهِيمَ مَكَانَ الْبَيْتِ أَن لَّا تُشْرِكْ بِي شَيْئًا وَطَهِّرْ بَيْتِيَ لِلطَّائِفِينَ وَالْقَائِمِينَ وَالرُّكَّعِ السُّجُودِ
Fàttalikul ba Nu biralee Ibraahiima bérabu néeg ba [Kaaba ga], ne ko : “Bul ma bokkaaleek dara te nga laabal sama néeg ngir ñi koy wër, ña fay taxaw, di sukk di sujjóot”
27وَأَذِّن فِي النَّاسِ بِالْحَجِّ يَأْتُوكَ رِجَالًا وَعَلَىٰ كُلِّ ضَامِرٍ يَأْتِينَ مِن كُلِّ فَجٍّ عَمِيقٍ
Te nanga woote ci nit ñi ngir aji Màkka. Danañu la dikkal ñuy dox ak ñeneen ñuy war xeetu waruwaay wu ne, jóge ca barab yu soree,
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
25Aaya

Tekki — Al-Hajj 25

Simoore Al-Hajj Aaya 25 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña weddi tey wëlbatiku jëm ci yoonu Yàlla ak ca…

Simoore Aaya 25/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 23–27. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers