Simoore Adh-Dhariyat ci Aarabu ak Wolof
Jàng Simoore Adh-Dhariyat ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (60 Aaya — مكية). Adh-Dhariyat Dégg, Adh-Dhariyat Tekki, Adh-Dhariyat mp3, Adh-Dhariyat pdf.Jàng te Dégg Simoore Adh-Dhariyat
🎧 Aaya
M
Mishary Rashid Alafasy
✓
Mishary Rashid Alafasy
✓
M
Mahmoud Khalil Al-Husary
✓
Mahmoud Khalil Al-Husary
✓
A
Abdurrahman As-Sudais
✓
Abdurrahman As-Sudais
✓
M
Mohamed Siddiq Al-Minshawi
✓
Mohamed Siddiq Al-Minshawi
✓
A
Abdul Basit Abdul Samad
✓
Abdul Basit Abdul Samad
✓
A
Ali Al-Hudhaify
✓
Ali Al-Hudhaify
✓
A
Ahmed ibn Ali al-Ajamy
✓
Ahmed ibn Ali al-Ajamy
✓
A
Abu Bakr Ash-Shaatree
✓
Abu Bakr Ash-Shaatree
✓
M
Muhammad Ayyoub
✓
Muhammad Ayyoub
✓
A
Abdullah Basfar
✓
Abdullah Basfar
✓
A
Abdullah Al-Juhani
✓
Abdullah Al-Juhani
✓
M
Maher Al Muaiqly
✓
Maher Al Muaiqly
✓
—
x1
إِنَّكُمْ لَفِي قَوْلٍ مُّخْتَلِفٍ ٨
📖 Tekki
Aaya 8
Yéen (yéefar yi) yéen a ngi ci ay wax yu féewóo.
يُؤْفَكُ عَنْهُ مَنْ أُفِكَ ٩
📖 Tekki
Aaya 9
(Wax joo xam ne) Képp kuy dumóoyu Alxuraan wax joojoo ko waral.
يَسْأَلُونَ أَيَّانَ يَوْمُ الدِّينِ ١٢
📖 Tekki
Aaya 12
Ñangay laajati : “Kañ la bis Penc bay doon ? ”
يَوْمَ هُمْ عَلَى النَّارِ يُفْتَنُونَ ١٣
📖 Tekki
Aaya 13
Bis ba nga xam ne dees na leen ca fitnaal ca Safara (lakk leen) :
ذُوقُوا فِتْنَتَكُمْ هَٰذَا الَّذِي كُنتُم بِهِ تَسْتَعْجِلُونَ ١٤
📖 Tekki
Aaya 14
Ñu di leen wax naan : “Tokamtikuleen sànje bii ; lii nag mooy la ngeen daan yàkkamti”.
إِنَّ الْمُتَّقِينَ فِي جَنَّاتٍ وَعُيُونٍ ١٥
📖 Tekki
Aaya 15
Ña ragaloon Yàlla ña nga ca biir Àjjana yu ànd ak bëti ndox yuy daw dawaan,
آخِذِينَ مَا آتَاهُمْ رَبُّهُمْ ۚ إِنَّهُمْ كَانُوا قَبْلَ ذَٰلِكَ مُحْسِنِينَ ١٦
📖 Tekki
Aaya 16
ña ngay jël la leen seen Boroom di jox. Ndax ñoom lu jiitu loolu dañu daan rafetal :
كَانُوا قَلِيلًا مِّنَ اللَّيْلِ مَا يَهْجَعُونَ ١٧
📖 Tekki
Aaya 17
bu guddi jotaan, lu néew lañu ca daan nelaw,
وَبِالْأَسْحَارِ هُمْ يَسْتَغْفِرُونَ ١٨
📖 Tekki
Aaya 18
bu njël masaana jot danuy jéggalu [seen Boroom] ;
وَفِي أَمْوَالِهِمْ حَقٌّ لِّلسَّائِلِ وَالْمَحْرُومِ ١٩
📖 Tekki
Aaya 19
seen alal it, daa nañu ci joxe ñiy yalwaan ak ñu ñàkk ña.
وَفِي الْأَرْضِ آيَاتٌ لِّلْمُوقِنِينَ ٢٠
📖 Tekki
Aaya 20
Ay kéemaan yuy taxa waaroo ngi ci suuf si ñeel ñu gëm Yàlla tigi
وَفِي أَنفُسِكُمْ ۚ أَفَلَا تُبْصِرُونَ ٢١
📖 Tekki
Aaya 21
ak ci seeni jëmm (am nay kéemaan). Moo ndax dangeen dul gis ?
وَفِي السَّمَاءِ رِزْقُكُمْ وَمَا تُوعَدُونَ ٢٢
📖 Tekki
Aaya 22
Seen wërsëg (taw) mi ngi ci asamaan si ak linu leen di dig.
فَوَرَبِّ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ إِنَّهُ لَحَقٌّ مِّثْلَ مَا أَنَّكُمْ تَنطِقُونَ ٢٣
📖 Tekki
Aaya 23
Giiñ naa ci Boroom asamaan ak suuf ! Ne loolu dëgg la lu am la ni jibug seeni kàddu.
هَلْ أَتَاكَ حَدِيثُ ضَيْفِ إِبْرَاهِيمَ الْمُكْرَمِينَ ٢٤
📖 Tekki
Aaya 24
Moo ndax yaw waxtaanu ganu Ibraahiima yu tedd ya aksi na ci yaw ?
إِذْ دَخَلُوا عَلَيْهِ فَقَالُوا سَلَامًا ۖ قَالَ سَلَامٌ قَوْمٌ مُّنكَرُونَ ٢٥
📖 Tekki
Aaya 25
Ba ñu ko fekkee fa mu nekkoon ne ko : “Jàmm nga am ! ”, mu ne [leen] : “Jàmm rekk, yéen dey xamuma leen”.
فَرَاغَ إِلَىٰ أَهْلِهِ فَجَاءَ بِعِجْلٍ سَمِينٍ ٢٦
📖 Tekki
Aaya 26
Daldi potoxlu giseek waa këram daldi indi aw sëllu wu duuf.
فَقَرَّبَهُ إِلَيْهِمْ قَالَ أَلَا تَأْكُلُونَ ٢٧
📖 Tekki
Aaya 27
Daldi leen koy tegal ne leen... “Ndax dungeen lekk ? ”
فَأَوْجَسَ مِنْهُمْ خِيفَةً ۖ قَالُوا لَا تَخَفْ ۖ وَبَشَّرُوهُ بِغُلَامٍ عَلِيمٍ ٢٨
📖 Tekki
Aaya 28
Am tiit daldi ko roofu. Ñu ne ko : “Bul tiit”. Daldi koy xamal ne dana am doom ju bari xam-xam.
فَأَقْبَلَتِ امْرَأَتُهُ فِي صَرَّةٍ فَصَكَّتْ وَجْهَهَا وَقَالَتْ عَجُوزٌ عَقِيمٌ ٢٩
📖 Tekki
Aaya 29
soxnaam sa dikk ak i yuxu, di talaata boppam te naan : “Màggat mu jaasir...
قَالُوا كَذَٰلِكِ قَالَ رَبُّكِ ۖ إِنَّهُ هُوَ الْحَكِيمُ الْعَلِيمُ ٣٠
📖 Tekki
Aaya 30
Nu ne : “Loolu la sa Boroom wax. Te moo di Ku Xereñ ki, di Ku Xam ki”.
۞ قَالَ فَمَا خَطْبُكُمْ أَيُّهَا الْمُرْسَلُونَ ٣١
📖 Tekki
Aaya 31
Ne leen [Ibraahiima]: “Ana la doon seeni tank?”
قَالُوا إِنَّا أُرْسِلْنَا إِلَىٰ قَوْمٍ مُّجْرِمِينَ ٣٢
📖 Tekki
Aaya 32
Ñu ne ko : “Nun dey dañunoo yabal ca aw nit ñu di ay tooñkat ,
لِنُرْسِلَ عَلَيْهِمْ حِجَارَةً مِّن طِينٍ ٣٣
📖 Tekki
Aaya 33
ngir nu jëbb ay doji ban yu nu tàngal ci seeni kaw,
مُّسَوَّمَةً عِندَ رَبِّكَ لِلْمُسْرِفِينَ ٣٤
📖 Tekki
Aaya 34
Yàllaa ko tàmpe jagle ko defkati njaaxum ya”.
فَأَخْرَجْنَا مَن كَانَ فِيهَا مِنَ الْمُؤْمِنِينَ ٣٥
📖 Tekki
Aaya 35
Rawale nanu génne képp ku fa doonoon jullit (Lóot ak ña gëm),
فَمَا وَجَدْنَا فِيهَا غَيْرَ بَيْتٍ مِّنَ الْمُسْلِمِينَ ٣٦
📖 Tekki
Aaya 36
Waa genn kër doŋŋ fa doonoon ay jullit ñu wommatu gëm.
وَتَرَكْنَا فِيهَا آيَةً لِّلَّذِينَ يَخَافُونَ الْعَذَابَ الْأَلِيمَ ٣٧
📖 Tekki
Aaya 37
Nu bàyyi leen fa musël leen ñuy kéemaan gu ñeel képp kuy ragal mbugël mu tarma;
وَفِي مُوسَىٰ إِذْ أَرْسَلْنَاهُ إِلَىٰ فِرْعَوْنَ بِسُلْطَانٍ مُّبِينٍ ٣٨
📖 Tekki
Aaya 38
[Kéemaan it amoon na]: ci Muusaa ba nu ko yabalee ci Firawna, te joxoon ko ay firnde yu leer nàññ.
فَتَوَلَّىٰ بِرُكْنِهِ وَقَالَ سَاحِرٌ أَوْ مَجْنُونٌ ٣٩
📖 Tekki
Aaya 39
[Firawna] ne doos-doosaaral dumóoyu daldi ne : “Kii ab njibarkat la wala mu di ab dof ! ”
فَأَخَذْنَاهُ وَجُنُودَهُ فَنَبَذْنَاهُمْ فِي الْيَمِّ وَهُوَ مُلِيمٌ ٤٠
📖 Tekki
Aaya 40
Jël Nanu ko mook ay xarekatam, labal ko ca ndox ma, muy ku ñu yedd.
وَفِي عَادٍ إِذْ أَرْسَلْنَا عَلَيْهِمُ الرِّيحَ الْعَقِيمَ ٤١
📖 Tekki
Aaya 41
(Kéemaan it) nekk na ca waa Aad, ba Nu leen saddee ngelawul faagaagale
مَا تَذَرُ مِن شَيْءٍ أَتَتْ عَلَيْهِ إِلَّا جَعَلَتْهُ كَالرَّمِيمِ ٤٢
📖 Tekki
Aaya 42
ngelaw loo xam ne bàyyiwul dara te lu mu rombu nappaaje na ko.
وَفِي ثَمُودَ إِذْ قِيلَ لَهُمْ تَمَتَّعُوا حَتَّىٰ حِينٍ ٤٣
📖 Tekki
Aaya 43
(Kéemaan it) nekk ca Samuuda, bu ñu leen waxe ne : “Xéewluleen ab diir ! ”
فَعَتَوْا عَنْ أَمْرِ رَبِّهِمْ فَأَخَذَتْهُمُ الصَّاعِقَةُ وَهُمْ يَنظُرُونَ ٤٤
📖 Tekki
Aaya 44
Ba nu moy seeni ndigal. Ag xaacu faagaagal leen ñuy xool.
فَمَا اسْتَطَاعُوا مِن قِيَامٍ وَمَا كَانُوا مُنتَصِرِينَ ٤٥
📖 Tekki
Aaya 45
Manatuñuwoon a jóg te amuñu kenn ku leen dimbali .
وَقَوْمَ نُوحٍ مِّن قَبْلُ ۖ إِنَّهُمْ كَانُوا قَوْمًا فَاسِقِينَ ٤٦
📖 Tekki
Aaya 46
Nitu Nooh, it bu jëkk. Dañoo saay-saayoon.
وَالسَّمَاءَ بَنَيْنَاهَا بِأَيْدٍ وَإِنَّا لَمُوسِعُونَ ٤٧
📖 Tekki
Aaya 47
Te asamaan, Nun Noo ko tabax ci Sunu Kàttan : te it Noo koy yàkkali.
وَالْأَرْضَ فَرَشْنَاهَا فَنِعْمَ الْمَاهِدُونَ ٤٨
📖 Tekki
Aaya 48
Suuf si, It Noo ko lal. Ndaw ku man a maasale !
وَمِن كُلِّ شَيْءٍ خَلَقْنَا زَوْجَيْنِ لَعَلَّكُمْ تَذَكَّرُونَ ٤٩
📖 Tekki
Aaya 49
Mépp mbir lenn lu nekk wutal Nanu ko [tóolent]. Ngir ngeen man caa fàttalikoo ?
فَفِرُّوا إِلَى اللَّهِ ۖ إِنِّي لَكُم مِّنْهُ نَذِيرٌ مُّبِينٌ ٥٠
📖 Tekki
Aaya 50
“Fëx leen daw wuti seen Boroom. Man dey, ab waarekatam laa bu bir.
وَلَا تَجْعَلُوا مَعَ اللَّهِ إِلَٰهًا آخَرَ ۖ إِنِّي لَكُم مِّنْهُ نَذِيرٌ مُّبِينٌ ٥١
📖 Tekki
Aaya 51
Te it bu leen jéema wut jeneen Yàlla. Man mii dey ab xuppekat laa bu bawoo fa moom, buy leeral di biral”.
كَذَٰلِكَ مَا أَتَى الَّذِينَ مِن قَبْلِهِم مِّن رَّسُولٍ إِلَّا قَالُوا سَاحِرٌ أَوْ مَجْنُونٌ ٥٢
📖 Tekki
Aaya 52
Noonu rekk la daan deme amul benn Yonent bu masa ñëw ci la leen jiitu tu du aw nitam dañuy wax ne : “Ab njabarkat la walla ab dof la” !
أَتَوَاصَوْا بِهِ ۚ بَلْ هُمْ قَوْمٌ طَاغُونَ ٥٣
📖 Tekki
Aaya 53
moo ndax da ñu ko daan jottaleente ? Li am kay mooy dañoo bew rekk.
فَتَوَلَّ عَنْهُمْ فَمَا أَنتَ بِمَلُومٍ ٥٤
📖 Tekki
Aaya 54
Nangaleen dumóoyu , kenn du la ca yedd:
وَذَكِّرْ فَإِنَّ الذِّكْرَىٰ تَنفَعُ الْمُؤْمِنِينَ ٥٥
📖 Tekki
Aaya 55
Nangay fàttalee ; ndax fàttali danay jariñ ñi gëm.
وَمَا خَلَقْتُ الْجِنَّ وَالْإِنسَ إِلَّا لِيَعْبُدُونِ ٥٦
📖 Tekki
Aaya 56
Te binduma jinne ak nit lu dul ngir ñu jaamu Ma (moom rekk tax).
مَا أُرِيدُ مِنْهُم مِّن رِّزْقٍ وَمَا أُرِيدُ أَن يُطْعِمُونِ ٥٧
📖 Tekki
Aaya 57
Bëgguma ci ñoom wërsëg; Bëgguma it ñu dima jox lekk.
إِنَّ اللَّهَ هُوَ الرَّزَّاقُ ذُو الْقُوَّةِ الْمَتِينُ ٥٨
📖 Tekki
Aaya 58
Yàlla tigi, mooy Wërsëgalaakoon bi, mooy Boroom Kàttan gi dul yonjax.
فَإِنَّ لِلَّذِينَ ظَلَمُوا ذَنُوبًا مِّثْلَ ذَنُوبِ أَصْحَابِهِمْ فَلَا يَسْتَعْجِلُونِ ٥٩
📖 Tekki
Aaya 59
Tooñkat ya am nañu seen wàlla wu ne weŋŋ: wu tollu ni wàlla seen gaa ya (ña leen jiitu woon te tooñ) kon bu nu yàkkamti (dana agsi de)
فَوَيْلٌ لِّلَّذِينَ كَفَرُوا مِن يَوْمِهِمُ الَّذِي يُوعَدُونَ ٦٠
📖 Tekki
Aaya 60
Yéefër ya toskare dalna leen ci bis ba ñu leen daan tëkóo ! (bis Penc ba)
Jàng Simoore Adh-Dhariyat ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers

