PDF —
60 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Adh-Dhariyat pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Adh-Dhariyat pdf Wolof — Wàcce Simoore Adh-Dhariyat Tekki. Simoore Adh-Dhariyat (Meccan) 60 Aaya.

← QafSimoore Adh-Dhariyat At-Tur →


60 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﯤﯥﯦ
51:1 Maa ngi giñ ci ngelawi callmeer yay wasaare !
ﯧﯨﯩ
51:2 Ak ca niir yay ëmbu ndoxum taw !
ﯪﯫﯬ
51:3 Ak ci gaal yay daw ci kaw ndox !
ﯭﯮﯯ
51:4 Ak ca Malaaka yay séddale mbir yi (wërsëk, ak taw) !
ﯰﯱﯲﯳ
51:5 (Maa ngi) giñ ne liñu leen di digu lu dëggu la.
ﯴﯵﯶﯷ
51:6 Te it bisub Penc ba lu nekk la lu am la du jaas.
ﭑﭒﭓﭔ
51:7 Ak ci asamaan si di borom mbub taar !
ﭕﭖﭗﭘﭙ
51:8 Yéen (yéefar yi) yéen a ngi ci ay wax yu féewóo.
ﭚﭛﭜﭝﭞ
51:9 (Wax joo xam ne) Képp kuy dumóoyu Alxuraan wax joojoo ko waral.
ﭟﭠﭡ
51:10 Fenkat ya durkat ya dee nañu,
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
51:11 ñangay nur ci seen lënt ma.
ﭨﭩﭪﭫﭬ
51:12 Ñangay laajati : “Kañ la bis Penc bay doon ? ”
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
51:13 Bis ba nga xam ne dees na leen ca fitnaal ca Safara (lakk leen) :
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
51:14 Ñu di leen wax naan : “Tokamtikuleen sànje bii ; lii nag mooy la ngeen daan yàkkamti”.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
51:15 Ña ragaloon Yàlla ña nga ca biir Àjjana yu ànd ak bëti ndox yuy daw dawaan,
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
51:16 ña ngay jël la leen seen Boroom di jox. Ndax ñoom lu jiitu loolu dañu daan rafetal :
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
51:17 bu guddi jotaan, lu néew lañu ca daan nelaw,
ﮓﮔﮕﮖ
51:18 bu njël masaana jot danuy jéggalu [seen Boroom] ;
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
51:19 seen alal it, daa nañu ci joxe ñiy yalwaan ak ñu ñàkk ña.
ﮝﮞﮟﮠﮡ
51:20 Ay kéemaan yuy taxa waaroo ngi ci suuf si ñeel ñu gëm Yàlla tigi
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
51:21 ak ci seeni jëmm (am nay kéemaan). Moo ndax dangeen dul gis ?
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
51:22 Seen wërsëg (taw) mi ngi ci asamaan si ak linu leen di dig.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
51:23 Giiñ naa ci Boroom asamaan ak suuf ! Ne loolu dëgg la lu am la ni jibug seeni kàddu.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
51:24 Moo ndax yaw waxtaanu ganu Ibraahiima yu tedd ya aksi na ci yaw ?
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
51:25 Ba ñu ko fekkee fa mu nekkoon ne ko : “Jàmm nga am ! ”, mu ne [leen] : “Jàmm rekk, yéen dey xamuma leen”.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
51:26 Daldi potoxlu giseek waa këram daldi indi aw sëllu wu duuf.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
51:27 Daldi leen koy tegal ne leen... “Ndax dungeen lekk ? ”
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
51:28 Am tiit daldi ko roofu. Ñu ne ko : “Bul tiit”. Daldi koy xamal ne dana am doom ju bari xam-xam.
ﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
51:29 soxnaam sa dikk ak i yuxu, di talaata boppam te naan : “Màggat mu jaasir...
ﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
51:30 Nu ne : “Loolu la sa Boroom wax. Te moo di Ku Xereñ ki, di Ku Xam ki”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
51:31 Ne leen [Ibraahiima]: “Ana la doon seeni tank?”
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
51:32 Ñu ne ko : “Nun dey dañunoo yabal ca aw nit ñu di ay tooñkat ,
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
51:33 ngir nu jëbb ay doji ban yu nu tàngal ci seeni kaw,
ﭥﭦﭧﭨﭩ
51:34 Yàllaa ko tàmpe jagle ko defkati njaaxum ya”.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
51:35 Rawale nanu génne képp ku fa doonoon jullit (Lóot ak ña gëm),
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
51:36 Waa genn kër doŋŋ fa doonoon ay jullit ñu wommatu gëm.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
51:37 Nu bàyyi leen fa musël leen ñuy kéemaan gu ñeel képp kuy ragal mbugël mu tarma;
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
51:38 [Kéemaan it amoon na]: ci Muusaa ba nu ko yabalee ci Firawna, te joxoon ko ay firnde yu leer nàññ.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
51:39 [Firawna] ne doos-doosaaral dumóoyu daldi ne : “Kii ab njibarkat la wala mu di ab dof ! ”
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
51:40 Jël Nanu ko mook ay xarekatam, labal ko ca ndox ma, muy ku ñu yedd.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
51:41 (Kéemaan it) nekk na ca waa Aad, ba Nu leen saddee ngelawul faagaagale
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
51:42 ngelaw loo xam ne bàyyiwul dara te lu mu rombu nappaaje na ko.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
51:43 (Kéemaan it) nekk ca Samuuda, bu ñu leen waxe ne : “Xéewluleen ab diir ! ”
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
51:44 Ba nu moy seeni ndigal. Ag xaacu faagaagal leen ñuy xool.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
51:45 Manatuñuwoon a jóg te amuñu kenn ku leen dimbali .
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
51:46 Nitu Nooh, it bu jëkk. Dañoo saay-saayoon.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
51:47 Te asamaan, Nun Noo ko tabax ci Sunu Kàttan : te it Noo koy yàkkali.
ﯶﯷﯸﯹﯺ
51:48 Suuf si, It Noo ko lal. Ndaw ku man a maasale !
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
51:49 Mépp mbir lenn lu nekk wutal Nanu ko [tóolent]. Ngir ngeen man caa fàttalikoo ?
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌ
51:50 “Fëx leen daw wuti seen Boroom. Man dey, ab waarekatam laa bu bir.
ﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙ
51:51 Te it bu leen jéema wut jeneen Yàlla. Man mii dey ab xuppekat laa bu bawoo fa moom, buy leeral di biral”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
51:52 Noonu rekk la daan deme amul benn Yonent bu masa ñëw ci la leen jiitu tu du aw nitam dañuy wax ne : “Ab njabarkat la walla ab dof la” !
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
51:53 moo ndax da ñu ko daan jottaleente ? Li am kay mooy dañoo bew rekk.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
51:54 Nangaleen dumóoyu , kenn du la ca yedd:
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
51:55 Nangay fàttalee ; ndax fàttali danay jariñ ñi gëm.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
51:56 Te binduma jinne ak nit lu dul ngir ñu jaamu Ma (moom rekk tax).
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
51:57 Bëgguma ci ñoom wërsëg; Bëgguma it ñu dima jox lekk.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
51:58 Yàlla tigi, mooy Wërsëgalaakoon bi, mooy Boroom Kàttan gi dul yonjax.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
51:59 Tooñkat ya am nañu seen wàlla wu ne weŋŋ: wu tollu ni wàlla seen gaa ya (ña leen jiitu woon te tooñ) kon bu nu yàkkamti (dana agsi de)
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
51:60 Yéefër ya toskare dalna leen ci bis ba ñu leen daan tëkóo ! (bis Penc ba)

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers