Simoore Ash-Shura
PDF —
53 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Ash-Shura pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Ash-Shura pdf Wolof — Wàcce Simoore Ash-Shura Tekki. Ash-Shura (Meccan) 53 Aaya.



Simoore Ash-Shura
53 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
Haa, Miam.
ﭓﭔ
Ayn, Siin, Qaaf.
ﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Noonu la la Yàlla, miy boroom Kàttan, tey ku Xereñ, di soloo ay ndigëlam, kem ni mu ku defe woon ca Yonnent ya la jiitu woon.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Moo moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. te mooy Kooku, di aji Màgg ji,
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Asamaan yi dañuy xawa foq bu Malaaka yi di sàbbaal di kañ seen Boroom, tey jéggalul ñi nekk ci kaw suuf si. te Yàlla tigi mooy Jéggëlaakoon bi, di Jaglewaakoon bi yërmandéem.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Ñuy wut ay wéeruwaay yu dul Yàlla, Yàllaa ngi leen di fuglu. Te yaw (Muhammad) du yaay lijjanti seen mbir.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Noonu la nu la soloo (Alxuraan jiy làmmiñu araab), ngir nga xupp ci ndayi dëkk ya (waa Màkka) ak dëkk ya ko wër ak it nga waar leen ci Bisub daje ba, - (bis pénc ba) sikkuwul bu boobaa - Ab kurél dafay nekk ca àjjana beneen kurél ba nekk ca biir Safara.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Su sooboon Yàlla, Mu def leen wenn xeet. Waaye Mooy dugël ku Ko neex ci biir yërmandéem. Te tooñkat yi nag ñoom duñu am wéeruwaay, waxantumalaak ku leen di dimbali.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Walla ñoom dañoo far am wéeruwaay yu dul Yàlla ? Wéeruwaay tigi mooy Yàlla ; te mooy dekkal ñu dee woon ña te moo di ki man lépp lu ne.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Te lépp lu ngeen am ag juuyoo, Yàlla yor àtte ba. Koo koo di Yàlla sama Boroom; ci Moom laay wéeru te it moom la doyloo.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Moo bind (sàkk) asamaan yeek suuf si. Defaralal na leen y soxna [jële ko] ci seeni jëmm ak ay mala yu di ay tóollént ( góor ak jigéen); te ci loolu la leen di yokki (jurante). Amul lenn lu mel ni moom (Yàlla) ; mooy aji Dégg, di aji Gis.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Moo ame caabi [ndami] asamaan yeek suuf si. Mooy yaatalal wërsëg ku ko soob, moo ko koy xatalal it. Te, Moo di ku xam lépp lu nekk.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Diine ji mu tëral (ngeen war koo dund), mooy la mu dénkoon Nooh, ak la Nu la soloo (yaw Muhammad), ak li nu dénkoon Ibraahiima, ak Muusaa ak Iisaa(te moo di) : “na ngeen taxawal diine; te buleen cay teqalikoo”. Li ngeen di woo bokkaalekat yi bëg leen caa jëmële dafa diis ci ñoom lool. Yàlla mooy jigeel boppam ku ko soob te it mooy gindi képp ku koy jébbël boppam .
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Xam-xam da leen a digël ba noppi ñu door a teqalikoo (ngir bew ak kujje) ga nekk ci seen diggënte. Du gan kon ak li Yàlla xas a joxe dig ba (Bis Pénc), kon dees na àtte seen diggënte (fii ci àddina). Te ña ñu donale woon Téere ba seen ginnaaw, ña ,nga cig sikki-sàkka gu yéeme (lënt).
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Kon na ngay woo (nit ñi) jëme leen ci diine jooju ; te na ngay tegu ca yoon wu jub wa xocc ni ñu la ko digële ; te bul topp mukk seen bànneex ; te na nga wax ne : “Gëm naa lépp lu Yàlla wàcce mu di ab Téere, te digaleef na ma may maandu ci seen diggënte. Yàlla moo di sama Boroom. Te it Yàlla dananu dajale nun ñépp te ca moom la ñépp di mujj”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Ñiy diiŋat mbiri Yàlla, ginnaaw ba ñu ko nangulee, seenu lay la naaxsaay la ca Yàlla. Te mer dal na ci seen kaw ñu am mbugël mu tar.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Moo di Yàlla mi wàcce Téere ba ci dëgg, ak nattukaay ba (balaas ya). Ana loo ci xam ? te amaana waxtu wa di lu jigeñ ?
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Ña ko gëmul ña nga koy yàkkamti ; waaye ña gëm ñoom dañu koy ragal te xam nañu ne mooy dëgg tigi. Ñay werante ci mbirum waxtu wa (Bis Pénc ba) ña nga ci réer gu sore.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Yàlla kuy ñeewanti jaamam ñi la. Mooy wërsëgël ku ko soob. te moo di boroom Doole ja, boroom Kàttan ga.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Képp ku namm ruuj [toolu] dundug àllaaxira, Dananu ko dollil ruujeefam. Képp it ku namm ruuj [toolu] dundug àddina, Dananu ko nangul ; waaye du am benn cër ca àllaaxira.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Am ñoom da ñoo am bokkaale yu leen tërëlal diine ju bokkewul ak li Yàlla digle ? Du gan kon, ak kàddu gu xas jib ba noppi, kon àtteef na seen diggënte. Te tooñkat ya ñoom am nañu mbugël mu mitti .
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Danga gis tooñkat ya ñu tiit lool ngir la ñu daan def, (mu di mbugël) muy dal ci seen kaw. Waaye ña gëmoon te daan def yiw, ñoom ña nga ca biir dëri àjjana ya, ñu fay am la ñu bëgg ci seen Boroom. Loolu moo di ngëneel la gën a rëy !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Loolu moo di [xibaar bu neex] bi Yàlla di bégale jaamam ña gëm tey jëf yiw ! waxal ne : “Du ma leen laaj genn pey lu dul dëgëral gi ci diggënte ag mbokkoo”. Képp ku def lu rafet, Dananu ko ko dollil lu gën a rafet (mu di ab neexal). Yàlla jégëlaakoon la kuy sant la (delloo njukël).
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Walla ñu daan wax naan day duural Yàlla ay fen. Bu neexoon Yàlla, Mu fatt sab xol. Yàlla dana (raaf , far) lépp luy neen. Te dana dëgëral dëgg ci ay kàddoom moom xam na li làmbu ci dënn yi.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Mooy kiy ndangu tuub ci jaamam ñi, tey jéggale ñaawtéef yi tey xam li ngeen di def.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
te it mooy nangul ñi gëm tey jëf yiw di leen xeewël, yéefar yi nag ñoom am na ñu mbugël mu tar.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Bu Yàlla yaatalaloon wërsëg jaamam [ñépp], kon dañuy bew ; ba tax na, mu di ko wàcce di ko yemale na mu ko soobee. Ndax Yàlla ku Xàmmee la kuy Gis la Jaamam ñi.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Moo (leen) di wàcceel taw ginnaaw bu ñu yàkke xont, te mooy tasaare Yërmaandeem. Mooy Kilifa gi, di Yayoowaakoonu cant.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Bokk na ci ay kéemaanam bindug asamaan yeek suuf ak ndundët yi mu tasaare (nuy duggat). Te man na leen dajale saa su Ko soobee.
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Bépp lor ju leen dal yéen a ko jëf. Yàlla dafay jéggale yu bari.
ﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
Munuleen a raw Yàlla ci suuf si ; te it du ngeen am geneen kilifa, waxantumalaa ndimbal kudul Yàlla.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
Bokk na ci ay kéemaanam (firndéem), gaal yuy daw ci géej, tollu ni ay tundu doj.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Su ko neexee, Mu téye ngilaw, ñu ne tekk ca ndox ma. Ay kéemaan na ngi ci biir loolu ngir [nit] kuy muñ tey sant (dello njukël).
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Walla, mu mbugël leen ci seeni jëf. Tey jéggële lu bari.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Ñiy diiŋat sunuy firnde it danañu xam ne du nu man a am rawtukaay.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Lii nu leen jox lépp [ci alal] bànneexu dundug àddina rekk la ; waaye la nekk ca Yàlla moo gënn te moo gën a sax ngir nit ñi gëm tey doyloo seen Boroom,
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
ñiy wattandiku bàkkaar yu mag a mag yi ak ñaawtéef yi, te saa su ñu meree jéggale,
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
ñiy nangul seen boroom, ak taxawal Julli, ak di disóo seen mbir ci seen diggënte, tey joxe ci la ñu leen wërsëgël (seeni alal),
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
ña nga xam ne, saa su ag tooñ amee, ñu saafara ko (fayu).
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Lu bon lu bon a koy fay ni moom. Waaye kuy jéggële tey yéwénal (na xam ne), Yàllaay warloo peyam. Te Yàlla du safoo tooñkat ya !
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ñay fayu ginnaaw ba ñu leen tooñee,...ñooñu kenn amul ci ñoom aw yoon ;
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Ña yoon war a dal ci seen kaw kay ñoo di, ñay tooñ nit ñi, di xaabaabal ci lu dul dëgg ci suuf si : mbugël mu mettee leen di xaar.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Képp kuy muñ tey jéggële, man na ñu koo limaale ca ñu dogu ña.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
Képp ku Yàlla xas réerël dootul am kilifa gu koy man a aar ku dul Yàlla. Danga gis tooñkat ya bu ñu gisee mbugal ma dañuy wax naan : “Fu ñuy ame pexe mu nuy delloo [àddina] ? ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Danga leen gis ñu di leen gaaral ca kanam Safara, ñu boole tiit ak gàcce, ña ngay xoole ne xeww di rummi, ña gëm ña ngay wax naan : “ña yàqule tigi, ñooy ñi ñàkk seen boop ak seenug njaboot bu Bis Pénc baa”. Tooñkat ya nekk ci mbugël mu sax.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Amuñu ay wéeruwaay yu leen man a dimbali wudul Yàlla (ndax) képp ku Yàlla réerël mu sànku.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Wuyuleen wooteb Yàlla bi balaa bis di ñëw boo xam ne kenn du ko man a fomm te it kenn du ca man a làqu Yàlla. Te it bu keroogee (Bis Pénc ba), dungeen man a miim (seeni bàkkaar).
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Bu ñu dumóoyoo,... Yónniwunu la ngir nga di leen sàmm : yaw jottali doŋŋ la war. Te Nun saa su nu musalee nit ki yërmaande, mu bég ca maare ; waaye saa su ko lor dabee ju mu fàggul boppam...,muy xarab di xund !
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si. mooy bind lu ko soob. Mooy may ku Ko soob ay doom yu jigéen, mooy may it ku Ko soob ay doom yu góor,
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
walla mu di ko def njaxas ñu di góor ak jigéen ; Mooy def it ku Ko soob jaasir. Yàlla aji Xam la boroom Doole la.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Yàlla du waxanteek kenn nit lu dul ci soloo, walla ci ginnaaw kiiraay, walla mu yabal ndaw (Malaaka) mu di ko soloo, lu ko soob, ci ndigalul Yàllal. Yàlla aji Kawe la aji Xereñ la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Noonu la ñuy soloo ci yaw [Alxuraan] ci Sunu ndigël. amoo woon benn xam-xam ci Téere bi du caagéene ngëm; waaye def leer di ci gindi ku nu soob ci sunu jaam ñi. Te yaw it da ngay gindee jëme ci yoon wu jub wa xocc,
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
yoonu Yàlla ji moom asamaan yeek suuf si ak li ci seen biir. Ca dëgg-dëgg ca yàlla la mbir yépp di mujj.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers