Simoore Az-Zukhruf
PDF —
89 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Az-Zukhruf pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Az-Zukhruf pdf Wolof — Wàcce Simoore Az-Zukhruf Tekki. Az-Zukhruf (Meccan) 89 Aaya.



Simoore Az-Zukhruf
89 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮀﮁ
Haa, Miim.
ﮂﮃﮄ
Ci Téere bu leer bu !
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Def Nanu ko Alxuraan ci làmmiñu araab ndax amaana ngeen xellu (xalaat).
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Nekk na fi Nun, ca ndayi Téere ba (Allawhul mahfuus), kawe lool fees dell ag ràñnee.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Moo ndax ! Danu leen di jox [Alxuraan] te fekk ngeen di ay yàqkat ?
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ak a bari lu nu yónni ci ay Yonnenta ca ña jiitu woon !
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
amul Yonnent bu mas a ñëw te yéjjiwuñu ko (ñaawal).
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Faagaagal na nu ña leen ëppoon doole ! Xam ngeen xibaari ña jiitu woon.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Te soo leen laajee : “Kan moo bind asamaan yeek suuf ? ” Dañu naan : “Yàlla, miy boroom Kàttan di ku Xam moo leen bind”.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Yàlla mi leen defal suuf si muy laltaay defaral na leen ci ay yoon ngir ngeen man cee ginduku ;
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Mooy kiy wàccee am ndox ci asamaan si di ko yemale Ñu di ca naatal ay dëkk yu bekkooroon. noonu it ngeen di dekkiwaate ;
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Moo bind tóolent yépp, defaral ay gaal, amal yu ngeen di war,
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
ngeen di def ñoŋŋ ca kaw, ngeen di fàttaliku xéewali Yàlla, su ngeen yemoo ca kaw ne ñoŋŋ, te it na ngeen di wax naan : “Tudd nanu sellug ki nu tàggatalal lii (wépp waruwaay) te manalu nu ko woon sunu bopp.
ﮀﮁﮂﮃﮄ
Te dañuy wëlbatiku jëm ci sunu Boroom”.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Nit ñi dañuy mbokkale yàlla ak lenn ci jaamam ñi. Te nit xarabaatekat la bu bir !
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Am Yàlla moom dafa jàpp ci li mu bind aw jigéen def leen ñu di doomam ba eggal yéen mu tànnal leen ay doom yu góor ? (mukk amul)
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Te kat, saa su nu bégëlee kenn ci yéen ak la Yàlla doon misaal (doom ju jigéen), xar- kanamam ba daldi ñukku muy fuuñ-fuuñi (mer).
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Moo ndax ! Du ul ne (jigéen) mooy màgg ci gànjaroo takkaay, te joŋewul ci dàggasante ?
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Ñuy def Malaaka ya di ay jaamu Yàlla [aw jigéen] ! moo ndax baleen Yàlla di sàkk dañu koo teewe woon ? Danañu bind la ñu seede ; laaj leen ko (ba xam lu ñu ca xam).
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Dañuy wax naan : “Bu neexoon Yàlla du nu leen jaamu”. Waaye amuñu ca benn xam- xam ; dañuy foog doŋŋ.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Walla, da Nu leen joxoon ab Téere ca la ko jiitu woon ba tax ñu ŋoyoon ca ?
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Li ñu wax kay moo di : “Fekkoon nanu sunuy maam am diine, kon nag (wat ci watiit) ñoom la ñuy toppandoo”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
(Noonu it la daan deme) ndax masunoo yónni waa ab xuppekat (waaraatekat) cib dëkk lu dul ne ne kilifa ya danuy wax naan : “Sunuy maam amoon nañu diine te nun ñoom la ñuy roy”.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Mu wax leen ne : “Ndax indilu ma leen lu gën a jub la seen baay ya nekkoon ? ” Ñu tontu ne ko : “Nun kat gëmu nu lii ñu la yónni”.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Nu daldi fayu ca seen kaw. Xoolal (settantal) naka la mujjug weddikat ya deme.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
(Fàttalikul) Ibraahiima ba mu waxee baayam aku nitam : “Man mii ku deñ laa ci lii ngeen di jaamu,
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
ba mu des (Yàlla) mi ma sàkk bind ma, te moo may gindi”.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Mu def (dénkaane boobu) muy kàddu guy sax ginnaawam. Ngir amaana ñu dellu (di jëfe seeni xel) ?
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Waaye xéewaloon naa ñooñee ak seeni maam, Ba dëgg ga (Alxuraan) digël leen ànd ak Yonnent buy leeral.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Ba leen dëgg ga digëlee, dañoo wax naan : “Lii daal ag njibar la te nun ay fen la nu ko jàppe”.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Ñuy wax it ne: “Cëy Alxuraan jii bu wàccoon ci nit ku tekki te dëkk ci benn ci ñaari dëkk yi ? ” (Taayif, Màkka) (al Waliidu ibn almuqiira) walla (Urwatu ibn masuud).
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Moo ndax ñoom ñooy séddële yërmaandey sa Boroom ? Te Nun dey Noo leen di séddale seenub dundu ci àddina te it tooñkat ya ñennat ci ñoom, teg na leen ca kaw ña ca des ngir nuy yilifante. Waaye yërmaandey sa Boroom, moo gën fuuf, li ñuy dajale.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Su nit ñi doonoon wenn xeet, kon Dinanu defaral ñiy weddi Yàlla, seeni kër am ay xàddi xaalis ak ay ker-keraan ñu di ca yéege ;
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
seen kër ya amna ay wunt ak ay lal ñu di ca sóonu,
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
ak ay xoyxoyal. loolu lépp du lenn lu dul bànneexu dundug àddina, te àllaaxiraa, nga fa sa Boroom, ngir ñu ragal Yàlla.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Képp kuy sori ak a dumóoyu tudd Yàlla (fàttaliku) Yëramaakoon bi, Dananu ko booleek Saytaane su mu lëkkalool.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Te ñoom Dañu leen dëdaleek yoon (wu jub wa xocc), te ñu foog ne dañoo gindiku.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Ba ne seef agsi ci Nun dey, daldi wax ne: “Aka neexoon ! Sunu diggënte soriyaantoo ni [Pénkook Suwu] ! ” – Ndaw lëkkëloo bu bon !
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Loolu lépp du leen jariñ lenn tey jii – ginnaaw ba ngeen tooñee – yéen ay bokk yem ca biir mbugël ma.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Moo ndax yaw man ngaa déggloo ku tëx mbaa nga man a gindi ku gumba mba ku nekk ci réer gu tar ?
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Benn nu yóbbu la nga [dee] Nu daldi fayu ci ñoom ;
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Walla Nu wan la la Nu leen digoon ñoom ; am Nanu Kàttan ci seen kaw de.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Jafandikul ci li nu soloo ci yaw yaa ngi ci yoon wu jub xocc wa.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Dëgg-dëgg [Alxuraan] fàttaliku la ngir yaw ak saw nit. Te it deefna leen ko laaj.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Laajal Yonent yi Nu jëkkoon a yónni ñu jiitu la, ba xam ndax defaroon Nañu Yàlla, ju bokkul ak yëramaakoon bi, ju ñuy jaamu ?
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Yónni woon Nanu Muusaa ak Sunuy kéemaan, ci Firawna ak gàngooram ga. Mu ne leen: “Man ndawul Boroom àddina si laa”.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Ba mu dikkee ca ñoom ànd ak Sunuy firnde (kéemaan), ndeketeyoo dañu koy reetaan.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Kéemtaan gu mujj a ñëw ëpp ga ko jiitu woon. Ba noppi nu toftal ca teg léen ay jafe-jafe, ngir amaana ñu dellu ginaaw.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ñu wax (Muusaa AS) ne ko : “Éy njibarkat ! Ñaanal nu sa boroom ci li nga séq ak moom ( mu teggil nu jafe-jafe yi). Soo ko defee nu jubook yaw”.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Ba nu teggee jafe-jafe ya, da ñoo tiri lépp la ñu digéwoon.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Firawna daldi dajale aw nitam ne leen: “moo sama gaa ñi ! Ndax moomu ma nguurug Misra ak dex yii di dawdawaan ci sama ron? Xanaa du ngéen gis ?
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Xanaa man sax maa wara gën waaju doyadi jii nga xam ne xawut a man a wax ( lu nit di xam )?
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
( Lii muy woote su doon dëgg) Kon ñu takkal ko lami wurus? Wala mu lëngook ay Malaaka? ”
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Mu fëkk xeli nit ña ñu daldi ko topp génn ci diine.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Ba ñu Nu merloo, ca la Nu fayyoo labal ñoom ñépp.
ﮯﮰﮱﯓﯔ
Nu def leen ñu di am njàng ci ñiy xalset a dikk ëllëg.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Ba ñu jëlee misaal ci Iisaa doomi Maryaama, saw nit dañoo daldi dumóoyu,
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Ñu daldi wax ne : “Ndax sunuy Yàlla ñoo gën, walla moom sax ? ” Ay werante rekk la ñu fi indi . Te sax ñoom ay niti tafaar la ñu.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Moom de (Muusaa) ab jaam rekk la bu Nu jox xeewal def ko muy roytéef ci wa Bani Israayiil.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Bu Nu sooboon , Nu def ci yéen ay Malaaka yuy ayayloo ci kaw suuf si.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Te firnde lay doon ci (Bis Pénc ba) waxtu wa. Buleen ci am sikki-sàkka. Te na ngeen ma topp : yoon wu jub xocc waa ngi nii.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Buleen nangu mukk Saytaane di leen wëlbati ! Ndax seenub noon la (bu nëbbutuwul) fes.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Ba Iisaa dikkee and ak i firnde, nee na leen : “Indil naa leen xam-xamu xereñ ak it ngir ma leeralal len lenn ci li ngeen di juubuu. Ragalleen Yàlla te topp ma.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Yàlla moo di sama Boroom di seen Boroom. Na ngeen ko jaamu. Lii mooy yoon wu jub wa xocc.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Kurél ya juuyoo ci seen biir. Ña daan tooñ toskare nañu ci mbugëlu bis bu mitti !
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Moo ñoom ndax xaaruñu lu dul (Bis Pénc ba) waxtu wa mu naan jaseet ci seen kaw, bett leen te du ñu ko yëg ?
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ña xaritoo woon, bu keroogee ñennat ci ñoom, ay noon la ñuy doon ; lu ca dul ñay ragal Yàlla.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
“Éy yéen Sama jaam ñi ! tey jii buleen tiit ; mbaa ngeen di jaaxle,
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Ña gëmoon Sunuy kàddu te doonoon ay jullit,
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
“Dugguleen àjjana, yéen ak seeni soxna, danu leen fay berndeel”.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Danu leen fay wër ak booli wurus ak i kopp ; def lépp lu bakkan di wonnen ay gët di ko bànneexoo ; - “te dangeen fay béel.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Loolee mooy àjjana ja Nu leen donale ci la ngeen daan jëf.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Am ngeen fa ay fuytéef yu bari ngeen di ca lekk”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
Tooñkat yaa ngi, ci biir mbugalum Safara béel ca,
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
kenn duleen ko mas a woyafal te dañu naan fa xuum ne muq ngir jaaxle.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Du ut ne Nun noo leen tooñ, waaye ñoom ñoo tooñ (seen bopp).
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
ña ngay woo : “ Maalik (bëkknéegu safara)! naan ko nanu sa Boroom jéggëli book ! ” muy tontu naan : “Yéen kay, ci [mbugël mii] ngeen di sax dëgg” !
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
“Indiloon Nanu leen dëgg; waaye ñi ëpp ci yéen dañoo bañ Dëgg”.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Walla, Ñoom dañoo fexe ay mbir [ak lu man a xew] ? Nun nooy sottal mbir yi ñu alku !
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Moo ndax ñoom dañoo jortu ne dunu dégg li ñuy nëbb ak di ko déeyoo ? Axakañ (dégg Nanu ko de) ! te sunuy ndaw a nga ca ñoom di bind.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Waxal ne : “Su fekkoon ne Yàlla Yëraamaakoon bi amoon na doom dey, man maay doon jaamam biy gën a (nungu ag njaamam)”.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Tuddnaa sellug Boroom asamaan yeek suuf, mooy Boroom (Aras) gàngunaay ga ; Kawe na lool soree ak ni ñu koy melal.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Bàyyileen rekk ñuy nuur ciy caaxaan ak di fo ba baa ñuy dajeek seen bis bi nu leen daan tëgoo (Bis Pénc ba).
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
mooy jenn Yàlla ci asamaan si di Yàlla ci suuf si ; mooy ki Xereñ, di ku Xam !
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Te itam barkeel na Moom mi am nguurug asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggënte. Moo ame it xam-xam bi làmboo waxtu wa (Bis Pénc ba). Te it ca moom ngeen di dellu.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Ñay jaamu leneen lu dul moom duñu am benn man-man ci tinu (rammu), ba mu des ñay seede ci dëgg te di ñu xàmmee.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Soo leen laajoon ana kan moo leen bind, ñu ne la : “Yàlla”. Kon naka la ñu koy dumóoyoo ?
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Waxi Yonnent ba moo di : “Éy sama Boroom, ñii daal ay nit la ñu ñu gëmul”.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Dumóoyuleen yaw ; tey wax : “Jàmm ! ” Danañu xalset a xam.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers