Simoore At-Tawba
PDF —
129 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore At-Tawba pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore At-Tawba pdf Wolof — Wàcce Simoore At-Tawba Tekki. At-Tawba (Medinan) 129 Aaya.



Simoore At-Tawba
129 Aaya · Medinan · Wolof
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Lii deñtalu la gu tukkee ci Yàlla ak ub Yonentam ci yéen ak ñoom bokkaalekat ya ngeen bokkal koote :
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
“Kon doxleen ci suuf si ñeneenti weer ; te nangeen xam ne nag yéen dungeen mën a raw Yàlla te nag Yàlla Kuy gàcceel yéefar yi la.”
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Te it xamle la gu tukke ci Yàlla ak Yonentam jëm ci nit ñi, ca bisub gën gaa Màggi Aj mooy ne : Yàlla nag Ku deñ la mook Yonentam ci yéefar yi. Bu ngeen rëccoo, tuub, kon mooy gën ci yéen. Bu ngeen dëddoo [nangeen xam ne] dungeen mën a rëcc Yàlla te nanga yëgal ña weddi, mbugal mu metti.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Ba mu des ña nga xam ne, ca bokkaalekat ya, fasante woon nañu kóllare ak yéen, te defuñu dara lu leen wàññi, te dimbaliwuñu kenn kuy dal ci seen kaw : ñooñu, ngeen matal seen kóllare ak ñoom ba ca àpp ba. Yàlla dafa sopp ñu ragal ña [seen Boroom].
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Bu weer ya ñu wormaal weesoo, reyleen bokkaalekat ya fu ngeen leen fekk. Jàppleen leen, nangeen leen gaw, nangeen toog ci fépp ñuy jaar di leen rey. Waaye bu ñu tuubee, di taxawal julli, di joxe asaka, bàyyileen leen, Yàlla nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Bu kenn ci bokkaalekat ya làqoo ci yaw, làq ko ba bamuy dégg waxi Yàlla tuub, nga yóbbu ko fu mu wóolu ngir ñoom dañu di ay nit ñu xamul.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Naka la ay bokkaalekat di amee kóllare ak Yàlla ak Yonentam ginnaaw ña ngeen kóllaranteek woon ak ñoom ca wetu jàkka ja ñu wormaal. Feek ña ngay def njub ak yéen, defleen yéen it njub ak ñoom. Yàlla nag Dafa sopp ñay ragal seen Boroom.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Moo ndax ñoom bu ñu leen notoon, danañu sàmmonteek la dox seeni diggante ci wàllu mbokk. xxxxx; Ay saay-saay lañu.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Dañuy weccee ndigali Yàlla ak njëg yu néew, di sakk yoonam wa. Ñoom nag la ñuy def aka bon !
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Duñu sàmmonteek ña gëmoon, ci wàllu mbokk du ci wàllu kóllare. Te ñoom ñoo di ñu jéggi dayo ña.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Waaye bu ñu tuubee, te taxawal julli, di joxe asaka, kon seeni mbokk lañu ci diine ji. Te Danuy leeral tegtal yi ngir nit ñuy xam.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Bu ñu firee seen kóllare ginnaaw ba ñu ko fasee, te di ayibal seen diine, xareleen ak njiiti yéefar yi - ndax ñoom faalewuñu kóllare - ndax xéy-na ñu yem, bàyyi yooyu.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Li leen tere xeex ak nit ñay firi seeni kóllare, te ñuy yittewoo génne Yonent bi te ñoom ñoo leen jëkk a songu ? Moo ndax dangeen leen a ragal ? Te Yàllaa gën a yey ci ngeen ragal Ko ndegam ñu gëm ngeen !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Xareleen ak ñoom. Yàlla Dana leen mbugal ñoom, jaare ko ci seeni yoxo yéen, te Dana leen toroxal, Dana leen dimbali ci not leen te Dana seral xoli ñi gëm ña.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Te Dana dindi mer mi nekk ci seeni xol. Te Dana baal ku Ko neex. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Am dangeen a njortu ne Danu leen di bàyyi te Yàlla duleen nattu ba xam ñiy xareel diine te duñu jàpp xarit, bàyyi Yàlla ak Yonentam ak ña gëm ? Yàlla Ku xam li ngeen di def la.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Yellul bokkaalekat ya di toppatoo jàkkay Yàlla ji, te ñoom ay seede lañu ci seen weddi ga. Ñoom seeni jëf yàqu na ; te danañu leen dugal Safara fàwwu.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Ki yayoo dundal jàkkay Yàlla ja kay, mooy ku gëm Yàlla ak Bis-pénc ba, tey julli, di joxe asaka te du ragal kenn ku dul Yàlla. Kon ñooña, amaana ñu bokk ca ñu gindiku ña.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Moo ndax dangeen di yemale [jëfi] kay dàndale ñay aji tey toppatoo jàkka ju ñu wormaal ak jëfi ka gëm Yàlla ak Bis-pénc ba te xareel yoonu Yàlla ? yemuñu ca Yàlla te Yàlla du gindi nit ñuy tooñ.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
Ña nga xam ne dañoo gëm, gàddaay te ñuy xareel yoonu Yàlla ci joxe seeni alal walla seeni bakkan, ñooy ña gën a màgg dayo ya ca Yàlla... ñoom ñooy ñu texe ña.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Seen Boroom a leen di bégale yërmaandeem ak ngërëmam, ak i Àjjana yu ñuy ame xéewal gu sax
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
dañu fay dëkk fàwwu. Pey gu màgg moo nekk fa Yàlla.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen def seeni baay ak seen mbokk yi ay xarit ndegam tànn nañu weddi, bàyyi ña gëm. Ku leen def xarit ca yéen... bokk na ca tooñkat ya.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Neel [Yaw Yonent bi] : “Su fekkee ne seeni baay ak seeni doom, ak seeni mbokk, ak seeni jabar, ak seeni jegeñaale, ak alal ju ngeen fàggu, ak njaay mu ngeen ragal mu lamb, ak kër yu leen neex ngeen gën a bëgg ci Yàlla ak Yonentam ak xareel yoonu Yàlla, kon nangeen xaar ba Yàlla dikk ak dogalam. Yàlla du gindi nit ñu dëng”.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Yàlla dimbali na leen ci barab yu bari. Ak ca bisu (xareb) Hunayni ba ngeen yéemoo ca nangeen baree woon te jariñuleen dara. Ba li suuf si di yaatu, lépp xat na keroog ci yéen ; ngeen wëlbatiku daw.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Ginnaaw ga, Yàlla wàcce dalam ga ca Yonentam ba ak ca ñu gëm ña. Mu wàcce xarekat yu ngeen gisul ak mbugalu ña weddi. Loolu mooy peyu yéefar ya.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Mujj Yàlla jéggal ku Ko neex ginnaaw ga, ndax Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Éy yéen ñi gëm ! Bokkaalekat ya nekkuñu lu dul sobe : buñu jege Jàkka ju ñu wormaal ja, ginnaaw seen at mii. Bu ngeen ragalee nag Yàlla, Dana leen may kon ci ngënéelam bu ko soobee. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Xareleen ak ñi gëmul Yàlla ak Bis-pénc ba, te duñu araamal la Yàlla ak Yonentam ba araamal ak ña dul diinewoo diine ju dëggu ja, ca ña jotoon Téere, [xareleen ak ñoom] ba ba ñuy joxe seen bopp cig mokk, di ñu toroxlu.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Yahuuf ya wax nañu ne : “Uzayru doomu Yàllaa”, Nasraan yi wax nañu ne : “Iisaa doomu Yàllaa”. Loolu seeni wax la jóge ci seeni gémmiñ. Dañoo jaare ci waxi ña weddi woon la leen jiitu. Yal na leen Yàlla alag ! Naka lañuy dummóoyoo ?
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Dañoo jàppee seen fóore ya ak seen làbbe ya, ak Iisaa doomi Maryaama, ay yàlla, bàyyi Yàlla te digaleefuleen lu dul ñu jaamu Yàlla ja di kenn. Amul jeneen Yàlla ju dul Moom ! Sellam ga jomb na li ñu Koy bokkaale.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Dañoo bëgg a feye leerug Yàlla ak seen gémmiñ, te Yàlla di bañ ngir namm a mottali leeram, doonte la ñu weddi ña sib nañu loolu.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Moom moo yónni ab Yonentam cig njub jox ko diine ju dëggu ngir mu kaweel ko ca kaw diine yépp, doonte la bokkaalekat ya soppuñu ko.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Éy yéen ñi gëm ! Ñu bari ci fóore yi ak làbbe yi dañuy lekk alali nit ñi ciy caaxaan tey dox diggante nit ñi ak yoonu Yàlla. Te ña nga xam ne dañuy rënk wurus ak xaalis te duñu ko joxe ngir yoonu Yàlla, nanga leen yégal mbugal mu metti,
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Bis bu ñu leen tàngalee ci biir tàngooru Safara, danañu leen ko ñaas ca seeni jë ak ca seeni wet, ca seeni ginnaaw, ne leen : “Lii mooy la ngeen daan rënk ngir seen bopp. Kon mosleen la ngeen daan rënk.”
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Limu weer ya ca Yàlla fukk lañu ak ñaar, ni Mu ko defee ci Téereem bis ba Mu bindee asamaan yeek suuf si. Mu am ci weer yooyu ñeneent yu ñu wormaal : loolu di diine ju jub ji. Buleen tooñ seen bopp ci biir weer yooyu. Nangeen xareek way-bokkaale ya ci weer yépp, ni ñuy xareek yéen ci weer yépp. Te ngeen xam ne nag Yàlla mook way-ragal Yàlla yépp a ànd.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Yeex a wormaal weer yooyu nekkul lu dul luy yokk weddig yéefar yi. Danañu ca jële ag réer : danañu ko daganal cim at, araamal ko cim at, ngir sàkkoo dëppook diir bi Yàlla araamal. Tax na danañu daganal lu Yàlla araamal. Rafetal nañu leen seeni ñaawteefi jëf. Te Yàlla du gindi nit ñu di ay yéefar.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Éy yéen ñi gëm ! Lu tax ngeen di diis-diislu bu ñu ne leen : “Génnleen jëm ci liggéeyal yoonu Yàlla” ; Moo ndax dangeen tànn dundu àddina ? - Te xéewali àddina, ku ko dendaleek bu àllaaxira, lu tuuti lay doon !
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Bu ngeen génnul, Dana leen teg mbugal mu metti, te wuutale leen nit ñu leen gën. Te dungeen Ko mënal dara [moom Yonent bi]. Ndax Yàlla mën na lu ne.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Bu ngeen ko dimbaliwul... Yàlla dimbali woon na ko, ba ko ña weddi génnee, muy ñaareelu ñaar. Ba ñu nekkee ñoom ñaar ca xunti mate muy wax ka mu àndaloon : “Bul jàq, Yàllaa ngi ànd ak nun.” Yàlla wàcce dal ci moom, te Moom mu dimbali ko ak lél bu ngeen gisul, mu def kàddug ña weddi mu suufe, kàddug Yàlla di lu kawe. Ndax Yàlla Ku not la, Ku xereñ la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Nangeen di xeex ci woyofaay ak ci dIisaay [sawar ak tàyyeel], nangeen di xeex ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Loolu moo gën ci yéen, cëy bu ngeen xamoon.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Bu doonoon alal juy xoy-xoyi walla muy tukki bu gàtt, kon ñu toppoon la ; waaye ba mu doonee ab xare, ñangay giñ naan : “Bu nu ko mënoon, kon dananu génn ànd ak yaw dem jaay seen bakkan.”. Te Yàlla xam na ne dañuy fen.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Yàlla baal na la li nga leen may dingalul ñu toog te nattuwooleen ba xam ña ca wax dëgg ak ña ca di ay fenkat.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Ña gëm Yàlla, gëm Bis bu mujj ba, duñu la ñaan mukk ndigalul bañ a dem xare ; ñoom kay dañuy xeex ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Yàlla xàmmee na ña ragal Yàlla de.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Ñay laaj ndigal kay ñooy ña gëmul Yàlla ak Bis bu mujj ba, te seeni xol di fer-feri, ñuy jiixi-jaaxa.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Waay-waay bu ñu bëggoon a génn xare ji, kon danañu waaj ba jekk. Waaye Yàlla daleen a sib; tàyyeel-loo leen. Ba tax na ñu ne leen : “Fafleen toog rekk”.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Te sax ñoom bu ñu génnoon, ànd ak yéen, dem xare ji, garaawaali rekk lañu leen fay dolli ak fàbbi nit ñi. Te Yàlla xam na tooñkat yi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Fitna rekk lañu daan sàkku, ñu nekk ñu daan la ko wëlbatile mbir yi, ba dëgg ñëw, seen mbir wuññiku feeñ, te sañuñu koo bañ.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Am na ci ñoom ñuy ñaan ndigalul toog ba noppi naan : “Bul ma fitnaal nag.”. Ñoom tàbbi ñañu ci biir fitna ba noppi ; te Safaraa nga gaw yéefar ya ci wet gu nekk.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Boo amee mbégte, ñu mer. Bu la naqar dalee, ñu bég ca, te naan : “Ndokk ba demunu woon.” Et ils se détournent tout en exultant.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Waxal ne : “Dara mënunoo dal lu dul lu Yàlla bind ci nun rekk. Te Mooy sunu Kilifa. Te it ñi gëm, nañuy wéeru ci Yàlla”.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Waxal ne : “Yéen a ngi nuy tuŋlu, te nun lu mën a xew, dananu am benn ci ñaari ndam yi [dee Chahiid walla nu dàq leen, not leen], benn Yàlla mbugal leen ci sunuy loxo, walla Mu xaroo leen ko ba ëllëg. Kon book nanu ànd di tuŋlu”.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Waxal ne : “Génneleen seeni alal, mu neex walla mu naqari leen : ak lu mën a xew, Yàlla du ko nangu, te sax yéen ay saay-saay ngeen”.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Li waral seen alal jooju Yàlla du ko nangu, moo di ne dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam, tàyyeel lool ci julli, nay lool ci li ñuy joxe.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Bula seeni alal yéem, naka noonu bula seeni doom yéem ! Yàlla nammul lu dul mbugal leen ci loolu ci dundug àddina si, ak ca roccig seeni ruu fekk ñu nekk di ay yéefar.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Ñuy waat ci Yàlla, naan ñoom ci yéen lañu bokk ; te bokkuñu ci yéen. Waaye ñoom dañoo ragal rekk ngeen dal (ci seen kaw).
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Bu ñu amoon làquwaay walla xunti walla fu ñu dugg (ba raw), kon ñu dëddu jëm fa te gaaw ca.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Am na ci ñoom ñu la ayibal ci sarax yi : ku leen ca joxoon ñu bég ca ; ku leen joxul ñu xundu.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Lu tee ñu bég ca la leen Yàlla ak Yonentam jox ? Tey wax : “Yàlla doy nanu. Yàlla Dana nu jox ci mbaaxam ak Yonentam it !... Nun way-xemmem lanu jëm ci Yàlla ”.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Asaka, ñi ko yeyoo ñooy ñi néew am-am, yalwaankat yi, ñi koy toppatoo, ñi ñu bëgg nooyal seen xol (ci Lislaam) ak ci goreel jaam, ña bor sonnal, ak ca lu jëm ci diiney Yàlla, ak doxandeem bu nekk ci tukki. Looloo di li Yàlla santaane ! Te Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Am na ci ñoom ñuy lor Yonent bi, naan : “Benn nopp la”. - Neel : “Nopp bu yiw la ci yéen. Gëm na Yàlla te wóolu na way-gëm ña, te yërmaande la ci ñi gëm ci yéen. Te ñiy lor Yonentub Yàlla bi, mbugal mu metti ñeel na leen.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Ña nga lay waatal ci Yàlla ngir am seen ngërëm. Te Yàlla ak Yonentam ñoo gën a yey ci ñoom sàkku seen ngërëm ndeem ñu gëm lañu.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Moo ndax dañoo xamul ne (li wóor mooy) ne ku juuyook Yàlla ak Yonentam, dana ko ñeel ci loolu tàngooru Safara, fu muy sax ba fàwwu ? Muy gàcce gu mag.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Naaféq ya danañu ragal aw saar wàcc feeñal li nekk ci seeni xol. Neeleen : “Ñaawleleen ! Yàlla Dana génne li ngeen di ragal (mu génn)”.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Te boo leen laajoon, Giñ naa ne danañu wax naan : “Nun dey danu doon caaxaan.”. Neeleen : “Kon daal yéen Yàlla ngeen di fowe ? ”
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Buleen lay : weddi ngeen ba noppi ginnaaw seen ngëm. Ndeem Dananu jéggal ab kurél ci yéen, Dananu mbugal it ab kurél ngir dañoo nekkoon di ay saay-saay.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Naaféq yu góor ya ak naaféq yu jigéen ya dañuy digalante lu bon, dàq lu baax, di téyee seeni yoxo (bañ a joxe). Dañuy fàtte Yàlla ba tax Mu fàtte leen. Naaféq ya ñoom ñooy saay- saay sa.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Yàlla dig na naaféq yu góor ya ak naaféq yu jigéen ya ak yéefar ya aw tàngoor ca Safara. Dañu fay béel. Moom doy na leen (mbugal). Te Yàlla rëbb na leen. Am nañu mbugal mu sax.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Noonu niki ña leen fi jiitu woon : ñoo leen ëppoon doole, ëpp leen alal ak i doom. Bànneexu nañu ci seen cër, yéen it bànneexuleen ci seen cër niki ña leen fi jiitu woon bànneexoo woon ci seeni cër. Te xuus ngeen (ciy caaxaan) na ñu ca xuusee woon. Ñooy ña nga xam ne seen jëf yàqu na ci àddina ak àllaaxira te ñoom yàqule nañu.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Moo ndax daleen a dikkalul xew-xewi ña leen jiitu woon : nitu Nooh ak nitu Haad ak Samuuda, ak nitu Ibraahiima, ak waa Madyaana, ak ña ñu wëlbati seeni dëkk ? Seeni Yonent dikkoon nañu ca ñoom, ànd ak ay lay yu leer. Te Yàlla tooñuleen woon, waaye ñoom ñoo tooñ seen bopp.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Te way-gëm yu góor yi ak way-gëm yu jigéen ya, ay xarit lañu. Dañuy digalante lu baax, di tere lu bon, tey taxawal julli, di joxe asaka, tey topp Yàlla ak ub Yonentam. Ñooña, Yàlla Dana leen yëram, naka Yàlla, Ku not la, Ku xereñ la.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨ
Yàlla digal na way-gëm yu góor yi ak way-gëm yu jigéen yi Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam, dañu fay béel, ak dëkkuwaay yu sell ca Àjjana ju sax ja. Te ngërëmul Yàlla moo gën a màgg, te loolu nag moo di texe gu màgg ga.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Éy yaw Yonent bi, nanga xeex ak yéefar yi ak naaféq yi, te nanga leen tiisal ; seen dëkkuwaay Safara la, te moo yées ci delluwaay !
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Ñangay waat ci Yàlla ne waxuñu dara, te wér na ne wax nañu baati weddi te tàbbi nañu ci kéefar ginnaaw ba ñu duggee ci Lislaam. Te ñangay ittewoo lu ñu mënul a am. Te amuñu la ñuy sàkku lu dul Yàlla - ak Yonentam - dafa leen jox ci mbaaxam koom-koom. Bu ñu tuuboon, mooy gën ci ñoom. Su ñu lànkee, féttéerlu, Yàlla Dana leen mbugal mbugal mu metti ci àddina ak àllaaxira ; te duñu am ci kaw suuf ku ñuy wéeru mu méngoo seeni mbir walla ku leen dimbali.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Ci ñoom, am na ñu warlul Yàlla, ne : “Bu nu Yàlla mayoon ci mbaaxam (alal), kon dey dananu natt asaka, te it dananu bokk ca ñu baax ña”.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Ba leen Yàlla mayee ci mbaaxam (alal), ñu nay ci joxe, ginnaaw ba ñu fuuyu.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Tax na Yàlla wuutale ci seen xol naaféq ba kera ñuy dajeek Moom ngir la ñu wor Yàlla ca la ñu ko digoon ak ca la ñu doon fen.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla xam na seen mbóot ya nëbbu ak seenub déeyoo, te nag Yàlla mooy xamaakoonub kumpa.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Ña nga xam ne dañuy ayibal (sikkal) way-coobarewu ña ci jullit yi ci natt asaka, ak ña nga xam ne amuñu leneen lu dul seeni kàttan ba tax ñuy reetaan lenn ca ñoom. Yàlla Dana leen yéjji te danañu am mbugal mu metti.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Nga balul leen walla nga bañ leen a balul (moo yem) - soo leen baluloon juróom-ñaar fukki yoon - du tax Yàlla baal leen mukk. Ngir dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam te Yàlla du gindi aw nit ñu di ay saay-saay.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Ña dem bañ a xeexal Lislaam, bég nañu ca seenub toogaay ngir juuyook Yonent Yàlla bi, te soppuñu di xeex ak seeni alal ak seeni bakkan ngir Yàlla, ñuy wax naan : “Buleen génn xare ji ci tàngaay bi ! ”. Neel : “Tàngaaru Safara moo gën a tar.” - Cëy bu ñu xamoon ! -
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Nañuy ree lu néew (ci àddina), danañu jooy lu bari (ca àllaaxira) mu di seenug pey ca la ñu doon fàggu.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Bu la Yàlla delloo ci ab kurél ñoom, te ñu ñaan la ndigalul génn (ànd ak yaw), neeleen : “Dootuleen génn mukk di ànd ak man, te it dootuleen xare ak noon yi ànd ak man. Ndax yéen tànnoon ngeen toog ca njalbéen ga ; kon nag toogleen, ànd ak way-des ña ginnaaw”.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Bul jullee kenn ku dee ci ñoom, te bul taxaw mukk ci bàmmeelam, ndax ñoom dañoo weddi Yàlla ak ub Yonentam ba ñuy dee, fekk ñu di ay saay-saay.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Bumu la yéem seeni alal ak seeni doom ! Yàlla Daleen a namm a mbugal ci yooyu ci àddina, te bu seeni ruu di rot fekk ñu di ay yéefar.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Bu aw saar wàccee (di leen ñaax) ci gëm Yàlla ak ànd xare ak ub Yonentam, woroom alal ya ca ñoom di laaj ndigal, naan : “Bàyyinu nu ànd ak ñay toog”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Neex na leen ñu ànd ak way-des ginnaaw ña. Tax na tëjeef na seeni xol ba ñoom dootuñu am dégg-dégg.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Waaye Yonent bi ak ña ànd ak moom ci ngëm, ñangay xare ak seeni alal ak seeni bakkan. Ñoom am nañu ay ngëneel te ñoom texe nañu.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Yàlla xaroo na leen Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel. Loolu moo di texe gu màgg ga !
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Ñiy sàkku ngànt (ci bañ a dem) xare ji ca sàmm sa, nekk nañu ngir ñu am ci ndigal. Ña weddi Yàlla ak ub Yonentam, toog nañu. Ña weedi ca ñoom, mbugal mu metti dana leen dal.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Ña néew dolle ak ña wopp, ak ñi amul yóbbal, amuñu bàkkaar (ci toog bañ a xare ji) ndeem ñu rafet yéene lañu ci Yàlla ak ub Yonentam. Naka noonu it, ca ñay rafetal seeni jëf. Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Ña nga xam ne bu ñu dikkee ci yaw di sàkku waruwaay, nanga leen di wax ne amuloo lu ñu mën a war, ñu dellu ànd ak naqar, di jooy ngir jàq ca la ñu amul waajtaay, ñoom it amuñu bàkkaar. Kenn du am ci ñoom aw yoon.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Ñay am bàkkaar kay ñoo di ña woomal te di la laaj ndigal ci bañ a dem xare ji, bëgg a ànd ak ñay fuuyu. Yàlla fatt na seeni xol te ñoom xamuñu. Ñoom kenn du mën a am ci ñoom aw yoon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Danañu ñëw ci yéen di lay bu ngeen dellusee. Neel : “Buleen lay : dunuleen gëm mukk. Yàlla nettali nanu ba noppi seen mbir. Te Yàlla ak ub Yonentam Danañu gis seeni jëf. Nu door leen a delloo fa Aji-xam ja kumpa ak la feeñ, Mu xamal leen li ngeen daan def.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Danañu leen waatal ci Yàlla, ba ngeen dellusee ci ñoom, ngir ngeen bañ leen a sikk. Waaye nangeen leen dëddu. Ñoom nag sobe lañu te seen delluwaay mooy Safara, muy peyug la ñu nekkoon di ko fàggu.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Ñanga leen di waatal ngir ngeen nangu (seeni ngànt), rafet njort ci ñoom. Bu ngeen nangoo seeni lay, Yàlla du nangul aw lay nit ñu di ay saay-saay.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Sàmm sa, ñoo gën a tar ag weddi ak ug naaféq, te gën a yey ci ñàkk a xam ndigal yi Yàlla wàcce cib Yonentam. Yàlla nag Ku xam la, Ku xereñ la.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Am na ci sàmm si ñu jàpp ni, la ñu joxe (ngir Yàlla) lu yàqu la, tax na ñuy seentu xew- xew (bu bon dal leeen). Yal na xew-xew bu bon (ba ñuy seentu) dal ci seen kaw ! Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Am na it ca sàmm sa, ñu gëm Yàlla ak Bis-pénc ba te jàpp nañu ne la ñuy joxe (ngir Yàlla), ag jaamu Yàlla la ak ug julli ci Yonent bi. Moo ndax loolu dafa nekkul di ag jege Yàlla ci ñoom? Yàlla Dana leen dugal ci yërmaandeem. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ña jiitu woon bu jëkk ca ña gàddaayoon (Muhaajiruuna ya) ak ña leen dalaloon (Lansaar ya) ak ña leen toppoon cig rafetal (seeni jëf), Yàlla bég na ci ñoom, te ñoom it bég nañu ci Yàlla. Te it sédde na leen Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel ba fàwwu. Loolu moo di texe gu màgg ga !
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Am na it ca sàmm sa nekk ca seen wet, ay naaféq, ak waa (Madina). Am na ñu téppeeral cig naaféq. Xamuloo leen, (waaye) Nun xam Nanu leen. Dananu leen mbugal ñaari yoon ba noppi Nu door leen a delloo ca mbugal mu màgg ma.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Ak ñeneen ña nangu seeni bàkkaar (tuub nañu), jaxase woon nañu jëf yu sell ak yeneen yu ñaaw. Xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Jëlal ci seen alal ab sarax (asaka) ngir laabal leen ca ak sellal leen ca, te nga ñaanal leen. Ndax sa ñaan dalum xel la ci ñoom. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla Moom Dana nangu tuub ciy jaamam, te Dana jël it sarax ya, te Moom Yàlla Mooy Nanguwaakoon cig tuub, di Jaglewaakoon.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Neel : “Jëfleen (lu leen soob), Yàlla ak ub Yonentam ak jullit ña, Danañu gis seeni jëf, te dees na leen delloo ca Aji-xam ja kumpa ak la feeñ. Mu xamal leen la ngeen daan def”.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Ak ñeneen ñoo xam ne dees na leen yeexe ci ndigalul Yàlla, mën naa am Mu mbugal leen, mën naa am it Mu jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Ña nga xam ne dañoo defar jàkka ngir bëgg a lore ak weddi ak téqale way-gëm ña, ak di fàggul (pexem ña fay julli) ku xeex ak Yàlla ak ub Yonentam ca njalbeen ga, ak ngir mën a giñ ne bëgguñu lu dul lu baax. Yàlla seede ne li wóor mooy dañuy fen.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Bul ca taxaw mukk. Ca njalbeenu bis (ba nga wàccee Madina), moo gën a yey ci nga taxaw fa. Aw góor a nga fa, ñoo xam ne, sopp nañu jéem a nekk ñu laab, te Yàlla sopp na ñu laab ña.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Moo ndax ku samp ab tabaxam cig ragal Yàlla ak yaakaar ngërëmam moo gën ? Walla ku sampu tabaxam ci pindub kàmbu gu joy jëm ci daanu ca biir Safara ? Te Yàlla du gindu aw nit ñu di ay tooñkat.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Tabax ba ñu tabax du noppee nekk sikki-sàkka ca seeni xol ba ba seeni xol di daggatoo (ba ba ñuy dee). Te Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Yàlla nag jënd na, ca ña gëm, seeni bakkan ak seeni alal, feye na leen Àjjana. Ndax ñangay xeex ci yoonu Yàlla : di reye, ñu di leen rey. Muy dig bu réy ca Yàlla ci dëgg (na Mu ko waxe) ci Tawreet ak Injiil ak ca Alxuraan. Ana kan moo gën a matal kóllareem ci Yàlla ? Kon bégleen ci njaay mi ngeen jaayanteek Moom. Te loolu moo di texe gu mag ga.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
(Ñooña) ñuy tuub lañu, di ñuy jaamu Yàlla, di Ko sant, di ñuy woor, di lunku di sujjóot (julli), di digle lu baax, di tere lu bon, di wattu dëeli Yàlla yi (daytal)... bégalal ña gëm.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Yellul ci Yonent bi ak ñi gëm ñuy baalul bokkaalekat yi, doonte la sax mbokk lañu ginnaaw ba mu leen biree ne ñoom ñuy dugg Safara lañu.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Te it jéggalu ga Ibraayiima doon jéggalul baayam, du utoon dara lu dul ab dig bu mu ko digoon. (Waaye), ba mu ko leeree ne noonub Yàlla la (moom baayam), dafa deñ ba set wecc ci loolu. Ibraahiima ab delluwaakoon la ci Boroomam, ku lewet la.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Yàlla du bàyyi ñoo xam ne gindi na leen ba noppi ñuy tàbbiwaat cig réer, te leeralal na leen la ñu war a ragal. Yàlla xam na lépp.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Yàllaa moom nguurug asamaan yi ak suuf si. Mooy dundal, di rey. Te amuleen wéeruwaay walla ku leen mën a dimbali ku dul Moom (Yàlla).
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Yàlla jéggal na ba noppi Yonent ba ak way-gàddaay ña (Muhaajiruun ya) ak ña leen dalaloon (Lansaar ya) ñoom ña nga xam ne toppoon nañu ko ca jamono ju jafe ja, ginnaaw ba xoli lenn ca ñoom xawoon a jeng. Mu jéggal leen ndax Moom (Yàlla) Ku ñeewant la, di Jaglewaakoon ci ñoom.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Ak ñett ñañu bàyyi woon ginnaaw ba tax li suuf si yaatu yépp, lépp xat ci ñoom ; te it seeni jëf xat ci ñoom ba ñu jort ne amul wenn wéeruwaay (wuy musle) ci Yàlla ju dul Moom Yàlla. Mu daldi leen jéggal ngir ñu tuub (rëccu). Naka Yàlla Nanguwaakoonu tuub la, Jaglewaakoon la.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Éy yéen way-gëm ñi ! Nangeen ragal Yàlla te ànd ak ñu dëggu ña.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Yellul ci ñi dëkk Madina ak sàmm sa ko wër, ñuy des ginnaaw, di bàyyi Yonent bi (buy dem jareji), te buleen seeni bakkan gënal bosam. Ndax ñoom, mar walla coono, walla xiif, duleen dale ci yoonu Yàlla, te duñu dëkk senn suuf (soo xam ne, danañu ca taxaw lu dul ne) dana metti yéefar ya, te it duñu am genn nooteel cib noon, te Dana leen ko bindal muy jëf yu yiw ñeel leen. Yàlla du sànk mukk peyug ñiy rafetal.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Te duñu joxe alal ju tuuti, walla ju bari, te it duñu jàll aw xur lu dul ne dees na leen ko bindal, Yàlla feye leen ko lu gën a rafetal.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Warul ci jullit ñépp dem (xareji). Lu tere mbooloo mu ne mu am ñu ca dem (xamluji) xam-xamu diine, ba bu ñu delsee ca seeni mbokk, waar leen ngir ñu mën a wattandiku.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Éy yéen ñi gëm ! Xeexleen ak ñi leen jegeñ ci yéefar yi ; nañu fekk ci yéen dëgër gu mat sëkk. Te ngeen xam ne Yàllaa ngi ànd ak ñi ragal Yàlla.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Te bu aw saar mësaan a wàcc, dana am ci ñooña (naaféq) ya, ñuy wax naan : “Ana kan la lii mën a dolli ngëmam ? ”. Waaye, ña nga xam ne ñoom gëm nañu, Dana leen yokk ngëm, te it danañu ca bég.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Ña nga xam ne jàngaro nekk na ci seen xol ya, dafay nekk ci ñoom kéefar guy dolliku cig kéefar, te ci kéefar googu lañuy deewaale.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Moo ndax dañoo gisul ne at mu nekk dees na leen not benn walla ñaari yoon ? Te ñooña, duñu tuub, duñu waaru.
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
Te su ñu wàccee aw saar ñu daldi xoolante, daldi wax ne : “Moo ndax am na ku nu gis ? ”. Daldi wëlbëtiku. Yal na Yàlla wëlbëti seeni xol ndax ñoom, aw nit lañu ñu amul genn dégg-dégg.
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Ab Yonent dikkal na leen bu bokk ci yéen, seeni coono tiis ci moom, di ku xér ci ngeen jub, di ku am ñeewant ak yërmaande ci jullit ñi.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Bu ñu dëddoo, neel : “Yàlla doy na ma. Amul jenn yàlla ju dul Moom. Te Moom laay dëgërloo ; te Moom moo di Boroom gàngunaay gu màgg ga (Aras)”.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers