Simoore Yunus
109 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
Alif, Laam, Raa. Lii ay laayay Téere bu ñu xereñe lañu.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Moo ndax dafa dul yéem ci nit ñi, Nu soloo (xamal) góor gu bokk ci ñoom : “Ndigalul waar nit ñi ci bégal way-gëm ñi te xamal leen ne, am nañu fa seen Boroom dawal bu di dëgg ? Ña weddi ñoom nee nañu : “Lii dey ag njibar gu fés la”.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Yàlla seen Boroom nag Mooy ki bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-benni fan, topp Mu yemoo ca gàngunaay ga (Haras), di settantal mbir ya (ndigal ya). Amul kenn ku mën a ramm te du ci ndigalam. Kookoo di seen Boroom. Jaamuleen Ko. Moo ndax dungeen fàttaliku ?
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Seen delluwaay yéen ñépp ca Moom la jëm, mooy digub Yàlla bu dëggu ba ! Moom moo sos mbindéef yi (booba dara amul), Moo leen di delloosi (ginnaaw bu ñu dee ba ràpp) ngir Mu feye ña gëm pey gu duun. Waaye ña weddi woon ñoom, seenug naan, ndox mu tàng lay doon ak mbugal mu metti, muy peyug seenug weddi !
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Moom mooy ki jox jant bi tàkk-tàkk, jox weer wi leeraay te dogal ko ay wàccuwaay ndax ngeen mën a xam limu at yi ak mën a waññi. Yàlla bindul loolu lu dul ci dëgg. Te Dana biralal tegtal ya nit ñay xam.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Nekk na ci jéllasanteb guddi gi ak bëccëg gi, ak li Yàlla sàkk ci asamaan yi ak suuf si, ay kéemaan ci nit ñu ragal (Yàlla).
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Ña nga xam ne nag yaakaaruñoo dajeek Nun, te tànn dundug àddina gii, doyloo ko, ak ña nga xam ne sàggane nañu Sunuy ndigal,
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
ñooña seen delluwaay moo di Safara ngir la ñu fàggu.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Ña nga xam ne gëm nañu tey jëf yu yiw, seen Boroom dana leen wommat ngir seen ngëm, tàbbal leen Àjjanay xéewal. Ay dex di daw ci seen suuf.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Seenug jaamu foofa mooy di wax naan : “Cëy sellug sunu Boroom”, te seenug nuyyoo foofa mooy : “Jàmm rekk”, te la ñuy mujjeel ca seenug jaamu, moo di ñu wax ne: “Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla Boroom àddina si”.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Bu Yàlla gaawe woon àtte nit ñi ci mettit kem ni ñu yàkkamtee am alal, àttekoon na seenug yàkkamti. Waaye Dananu bàyyi ña nga xam ne yaakaaruñoo dajeek Nun ñuy laam- laame ca seen biir ngëlamte.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Nit, bu ko aw naqar dalee, mu daldi Nuy woo, (moo xam dakoo fekk mu) tëdd walla mu toog walla taxaw. Te bu Nu ko tekkilee naqaram woowu, muy wéy (ci kéefaram), fakk mel ni mësunoo woo ci naqar wu ko dal. Noonu la jekkee woon ca ñoom bokkaalekat ya la ñu daan def.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Alag Nanu ay xeet yu bari yu leen jiitu ba ñu tooñee, te Yonent dikkal leen ak i lay yu leer nàññ. Te nanguwuñuleen woon a gëm. Noonu la Nuy feyee nit ñu di ay saay-saay.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Ba noppi Nu def leen ngeen wuutu leen ci suuf si ci seen ginnaaw, ngir Nu seetlu naka ngeen di def.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Te bu ñu jàngee ci seen kanam Sunuy kàddu yu leer yi, ña yaakarul a dajeek Nun wax ne : “Indil weneen jàngin wu wuuteek wii” mbaa “Nga soppi ko”. Neel : “Yellul ci man ma soppi ko ci sama coobare bopp. Duma topp lu dul la ñu ma soloo. Ragal naa, su ma moyee sama Boroom, mbugalum bis bu rëy (dal ma)”.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Neel : “Bu sooboon Yàlla, duma leen ko jàngal te duma leen ko xamal. Ndax dundu naak yéen ay at lu ko jiitu. Moo ndax dangeen dul xel-lu ? ”
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla di weddi ay tegtalam ? Ak lu mën a xew, saay-saay sa duñu texe.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Dañuy jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne duleen mën a lor, duleen mën a jariñ dara, ñuy wax naan : “Ñii ñoo nuy rammu fa Yàlla”. Neel : “Ndax dangeen a mën a xamal Yàlla lu Mu xamul ci asamaan yi ak suuf si ? ”. Kañ naa Ko, te kawe na lool la ñu Koy bokkaale !
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Nit ñi nekkuñu woon lu dul wenn xeet. Ñu juuyoo. Te bu dul koon waxi Yàlla ja jiitu woon, àttekoon na seeni diggante ca la ñu juuyoo.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom laaya ju tukkee ca Boroomam ? ”. Neel : “Lu fàddu (di kumpa) Yàlla rekk a ko xam. Kon nanga muñandiku ; Man nag, maa ngi ànd ak yéen bokk ca way-muñandiku ña.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Su Nu musalee nit ci yërmaande [niki taw] ginnaaw ba leen naqar dalee, ñuy def i pexe ci Sunuy tegtal. Neel : “Yàllaa gën a gaaw ciy pexe”. Sunuy ndaw danañu bind li ngeen di fexe de.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
Moom mooy ki leen doxloo, ci suuf si ak ci géej gi, ba ngeen nekkee ca gaal ga. Te gaal googu daw ak ñoom ci ngelaw lu teey. Ñu bég ca ba ngelaw lu tar songu leen, duusi géej wër leen ci wet gu nekk, ba ñu njortu ne ñoom alageef na leen, ñuy ñaan Yàlla, di sellal diineem, di [giñ] ne: “Boo Nu musalee ci lii, fàwwu dananu bokk ci way-sant ña [Yàlla] ! ”
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Ba Nu leen musalee, ñu daldi beew ci kaw suuf si ci lu dul dëgg. Éy yéen nit ñi ! Seen beew googu tooñuleen ci kenn ku dul seen bopp. Muy yóbbalub àdduna. Ba noppi nag ngeen dellu jëm ci Nun, Nu xamal leen la ngeen doon def.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Nirale dundug àddina nekkul lu dul lu mel ni ndox mu ñu wàcce mu jóge asamaan sa, gàncax ga ràbboo ci suuf si [ngir màndi ci ndox moomu], muy li nit ñi ak mala yi di lekk. Bu suuf si jot taaram ci rafet ba ña ca dëkk am yaakaar ne am nañu kàttan ci moom, Sunu dogal dikkal ko guddi walla bëccëg, Nu def ko ni lu ñu góob, mu mel ni nekku fa woon démb. Noonu Lanuy leerale laaya yi ci nit ñoo xam ne danañu xalaat.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Yàllaa ngi woote jëme [ci topp ndigal] ca këru jàmm ga, te Dana jubal ku ko soob jëme ko ca yoon wu jub wa xocc.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Ñay rafetal, am nañu li gën a baax [Àjjana] ak ndollant [Gis Yàlla]. Te seeni kanam du muuru ngir njàqare walla toroxte. Ñooña ñooy duggu Àjjana te dañu fay béel.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Ña nga xam ne dañoo fàggu lu ñaaw, am nañu lu ñaaw lu ko niru. Te la ñu yayoo mooy toroxte, - te duñu am kenn ku leen musal ci Yàlla -, daanaka day mel ni seeni kanam dañoo muuru ak daggitu guddi gu lëndëm. Ñooña ñoo dugg Safara te dañu fay béel.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Te bis ba ñu leen dajalee ñoom ñépp, te ñu wax ña daan bokkaale : “Beruleen fale ak seeni xërëm ya.”. Dananu téqale seeni diggante, seen xërëm ya naan : “Du nun ñii lañu doon jaamu de”.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Te Yàlla doy na seede ci sunu diggante ak yéen. Nekkewunu woon lu dul di ñàkk a faale seenug jaamu”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Noonu, bakkan bu nekk la mu jëfoon sadd ko. Ñu delloo leen ca seen Boroom muy dëgg ; ya ñu daan sos réer leen.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Neel : “Ana kan moo leen di jox xéewal yu jóge kaw asamaan ak ci suuf si ? Kan moo moom dégg-dégg [nopp yi], ak gis-gis [bët yi], ana kan mooy génne luy dundu ci lu dee, di génne lu dee ci lu dundu, ana kan mooy dogal mbir yi ? ”. Danañu toontu ne : “Yàlla”. Neeleen kon : “Lu leen teree ragal Yàlla ? ”.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Kon noonu la, Yàlla di seen Boroom ba di dëgg ga. Kon lan moo nekk ci ginnaaw dëgg lu dul ag réer ? Kon naka leen leen mën a wëlbatee ? ”.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
Noonu la sa kàddug Boroom yayee te dal ca kaw ña di ay saay-saay ndax gëmuñu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Neel : “Ndax am na ci ña ngeen di bokkaaleek [Yàlla] kuy sos mbindéef, mën koo dundal [gannaaw ba mu deewee]? ”. Neel : “Yàlla rekk a mën a sos mbindéef te mën koo dundal. Kon naka lees leen di wëlbatee ?”.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Neel : “Yàlla rekkay gindee jëme ci dëgg. Moo ndax du Kiy gindee jëme ci dëgg moo gën a yey ci ñu topp ko, walla ka nga xam ne du gindee, lu dul ñu di ko gindi ? Kon lu leen jot te naka ngeen di àttee ?”.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Li ëpp ci ñoom, toppuñu lu dul ay njort. Te njort du jariñ dara ci dëgg ! Yàlla naka Ku xam xéll la li ngeen di def.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Alxuraan jii nekkul lu ñu duur bàyyi Yàlla, waaye dafa nekk di luy dëggal la ko jiitu tey settantal Téere ba nga xam ne sikk nekkul ci ne ma nga tukkee ca Boroom àddina si.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Am dañoo wax ne : “Dafa koo duur ” ? Neel : “Indileen saar wu ni mel, te woo ku leen neex ba mu des Yàlla [mu dimbali leen ci loolu] ndeem ñu dëggu ngeen”.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Déedéet : weddi nañu loo xam ne amuñu xam-xamam te ag leeralam agsiwul ci ñoom. Noonu la ña leen jiitu weddee woon. Waaye xoolal rekk la mujjug tooñkat ya deme woon !
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Te kat am na ci ñoom ñu ko gëm, am na it ñu ko gëmul. Te sa Boroom moo gën a xam yàqkat ya.
ﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘ
Bu ñu la weddee, neel : “Sama jëf laa moom, ngeen moom seeni jëf. Yéen deñ ngeen ci li may jëf, man it set naa wecc ci li ngeen di dëf”.
ﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟﰠﰡﰢﰣﰤﰥ
Te am na ci ñoom ñu lay déglu. Moo ndax yaw mën nga déggloo ab tëx, doonte la nekkuñu ñu am i xel.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Te am na ci ñoom ñu lay xool. Moo ndax dangay gindi gumba, doonte dañu dul gis ?
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Yàlla nag du tooñ nit ci dara, waaye nit ñi ñooy tooñ seen bopp.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Bis bu leen Yàlla dajalee, dana mel ni tooguñu [ca seeni bàmmeel] lu dul diirub benn waxtu cig bëccëg, ñuy xamante. Te ña weddi woon ne dajeek Yàlla dana am, yàqule nañu ndax nekkuñu woon ñu gindiku.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Te Nu won la dara ca la Nu leen tëkkoo, walla Nu rey la [Yaw Muhammad], lu mu ca doon seenug delluwaay ci Nun la jëmsi. Ba noppi, Yàlla nekk di seede ca lañu daan def.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Xeet wu nekk am na ab Yonent. Bu seenub Yonent agsee rekk, dees na àtte seen diggante ci maandute, te kenn duleen tooñ.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Ñu naan : “Boobu dig kañ lay doon, ndegam ñu dëggu ngeen” ?
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Neel : “Mënaluma sama bopp lor walla njariñ, lu dul lu neex Yàlla. Xeet wu nekk am na àpp. Bu seen àpp matee, deefuleen yeexe wenn waxtu, te duñu jiitu it àpp ba”.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Neel : “Waaw waxleen ma ! Bu leen mbugal bettoon guddi walla bëccëg, lan la bàkkaarkat yi mën a gaawal ?
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
“Moo ndax bu agsee ngeen koy door a gëm ? [Kon deef na leen wax : “Léegi, yéen a ngi ci biir ba noppi”.] Te yéen a ngi koy yàkkamti”.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Topp waxees tooñkat ya : “Ayca mosleen mbugal mu sax dàkk ! Moo ndax dees na leen feye lu wuuteek la ngeen doon fàggu ? ”
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
Te danañu sàkku nga leeral : “Ndax loolu dëgg la ? ” - Neel : “Waawaaw ! Giñ naa ci sama Boroom ne dëgg la !Te yéen dungeen mën a raw”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Bépp bakkan bu tooñ, bu amoon li nekk ci àddina si, dana ko nangoo joxe ngir jotoo ko.Te bu ñu gisee mbugal ma, dana jéem a nëbb seenug rëccu. Waaye deef na àtte seeni diggante ci maandute, te kenn duleen tooñ [ci wàññil leen dara]..
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Moo ndax dafa nekkul ne Yàlla moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Digub Yàlla mooy dëgg tigi. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Moom mooy dundal, Mooy rey ; te ci Moom ngeen di dellu.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Éy yéen nit ñi ! Ag waaraate dikkal na leen, jóge ci seen Boroom, di saafara li nekk ci seen xol yi, di gindee, di yërmaandey ñi gëm.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Neel : “Bégleen ci xéewal ak yërmaande ; te loolu lépp moo gën la ñu daan dajale [ci alal]”.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Neel : “Moo ndax gis ngeen li leen Yàlla wàcceel ci xéewal, ngeen jàpp ne am na ci yu araam ak yu dagan ? - Neel : “Ndax Yàllaa leen ko digal ? Walla dangeen di duural Yàlla” ?
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Ana lan mooy njortul ñiy duural Yàlla ay fen Bis-pénc ba ? - Dafa dëggu ne Yàlla xéewalaakoon la, waaye li ëpp ci ñoom duñu gërêm [Yàlla].
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒ
Doo nekk ci menn mbir, walla ngay jàng dara ci Alxuraan, walla ngeen def jenn jëf te Nekkunu ca seede ba ngeen cay duggu. Te lu toll ni pepp su tuuti du rëcc sa Boroom, du ci suuf si, du ci asamaan yi ; te amul lu ko gën a tuuti walla lu ko gën a rëy lu dul ne mi ngi ci ab téere bu bir.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
Ca dëgg-dëgg, ña féeteek Yàlla duñu gis lu ñu ragal, duñu gis njàqare,
ﭜﭝﭞﭟﭠ
Ña gëm te ragal Yàlla,
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Am nañu mbégte ci dundug àddina ak ca àllaaxira. - Soppeeku du am ciy kàddu Yàlla -. Loolu mooy texe gu mag ga !
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Li ñuy wax , bumu la naqari. Teraanga nag Yàllaa moom lépp. Te Moom Kuy dégg la, Kuy xam la.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Ca dëgg-dëgg, li nekk ci asamaan yi ak suuf si, Yàllaa leen moom. Ñay jaamu leneen lu dul Yàlla, ñoom daal toppuñu lu dul ay njort. Nekkewuñu lu dul di sos ay fen.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Moom [Yàlla], moo def guddi ngir ngeen di ca noppalu, ak bëccëg ngeen di ca gise. Kéemaan nekk na ci loolu ngir aw nit ñuy dégg !
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Wax nañu ne : “Yàlla am na doom”. Kañ naa sellam ga ! Moom ku doylu la ci boppam. Ñeel na ko li ci asamaan yi ak suuf si ; - Amuleen aw layati ci wax jooju. Moo ndax dangeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul ?
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Neel : “Ñiy duural Yàlla ay fen duñu texe”.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Am nañu yóbbal bu néew ci àddina bi ; ñépp danañu dellusi ci Nun Nu mosal leen mbugal mu tar ngir la ñu nekkoon di weddi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Nettalileen xew-xewu [Nooh], ba mu waxee aw nitam ne leen : "Yéen samaw nit, ndeem sama nekk fii diis na ci yéen, ak samag waare ci kàdduy Yàlla yi, man maa ngi wéeru ci Yàlla. Bu ngeen yaboo ngeen dajale seeni kàttan yéen ak ñi ngeen di jaamu [bàyyi Yàlla]. Te bu seeni pexe nekk aw tiis ci yéen. Te it [lu leen neex] jëme ci man, te buleen négasndiku dara ci def ci man [seeni yéene].
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Bu ngeen dëddoo, xamleen ne laajumaleen ag pey... Samag pey nekkul fenn fu dul fa Yàlla. Te digaleef na ma ma bokk ca way-jébbalu ña”.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Ñu weddi ko. Nu musal ko mook ña ànd ak moom ca gaal ga, Nu def leen ñuy ñay wuutu [nit ña ci kaw suuf si]. Nu labal ña weddi sunuy ndigal. Nanga xool nag ña ñu waaroon [ca ña weddi], ni seen mujj deme !
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Topp nu yónni ginnaawam ay Yonent ci seenu nit. Nu indil leen ay lay yu leer. Waaye nekkuñu woon di way-gëm la ñu weddi woon ca bu jëkk. Ba noonu Lanu tëjee ràpp xoli ña jéggi woon dayo, daan jalgati.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Topp Nu yónni ci seen ginnaaw Muusaa ak Haaroona ca [Firawna] ak mbooloo ma [ñu xamal leen] sunuy ndigal. Ñu rëy-rëylu, di aw nit ñu dëng [diy saay-saay].
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Ba dëgg ga agsee ca ñoom tukkee ci Nun Yàlla, [ñu ne leen] : “Jibar tigi la ! ”.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Muusaa ne leen : “Moo ndax dangeen di wax ci dëgg gii ba mu agsee ci yéen, naan leen : Ag jibar la ? Te jibarkat yi duñu texe...”.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Ñu ne ko : “Moo ndax danga fee dikk ngir dëddale nu ak la nu fekkoon sunuy baay nekk ca ? Ba noppi yéen ñaar ngeen yilif àddina bi ? Waay-waay nun sax gëmunuleen ! ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
Firawna ne : “Indil-leen ma bépp jibarkat bu am xam-xam ! ”.
ﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ba jibarkat ya dikkee, Muusaa ne leen : “Sànnileen li ngeen di sànni”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Ba ñu sànnee, Muusaa ne leen : “Li ngeen indi jibar rekk la ! Yàlla dana ko neenal. Ne : “Yàlla du àntuloo jëfi yàqkat ya”.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Te Yàlla dana notal dëgg ci dogalam, doonte neexul it ñu dëng ña”.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Te kenn gëmul woon Muusaa lu dul ab kurél ci aw nitam, [la ko waral] mooy Firawna ak mbooloo ma lañu ragal seen fitna. Te Firawna dafa rëy-rëylu woon ci kaw suuf si, kawe lool, te moom bokk na ca saay-saay sa.
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Muusaa ne : "Yéen samaw nit, ndegam gëm ngeen Yàlla, nangeen wéeru ci Moom ndeem ñu wommatu tigi ngeen te di ay jullit”.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Ñu wax ne : “Ci Yàlla lanuy wéeru. Yaw sunu Boroom, Yàlla boonu teg nattu ya tooñkat ya yayoo.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Te nga musal nu ci sa yërmaande, ca nit ña di ay yéefar”.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Nu jox Muusaa ak mbokkam ma ndigal, ne leen : “Sàkkleen néeg ca Misra ca seen biiru nit, te ngeen def seen néeg jàkka te nangeen di taxawal julli. Te di bégloo ñi gëm [ca seenug waare]”.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Muusaa ne : "Yaw sunu Boroom, may nga Firawna ak u nitam taar ak alal ci alali àddina. Yaw sunu Boroom, ña réer moy saw yoon, faral seen alal ya te nga fatt seeni xol, duñu gëm mukk ndare bu ñu gisee mbugal mu tar ma”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Mu ne leen : “Nangoof na seeni ñaan. Taxawleen temm yéen ñaar ci bañ a topp yoonu ña xamule”.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
Nu jàlle waa Banii-Israayiila géej ga. Firawna topp leen ak lelam [ay xarekatam] ngir mbewte ak ug noonu. Ba lab ga agsee ci moom, mu ne : “Gëm naa ne lay mbir moo di ne : amul jeneen yàlla ju dul Ji waa Banii-Israayiila gëm. Te man bokk naa ci way-wommatu ña”.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
[Yàlla ne ko] : Moo ndax léegi [ngay door a gëm] ? Te nga féttéerlu woon lu jiitu te nga bokk ca yàqkat ya !
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Tey jii Dananu la musal ci sàmm saw yaram [mu bañ a yàqu] ngir nga nekk ci ña lay wuutu màndarga. Ndaxte ñu bari ci nit ñi dañoo sàggane Sunuy màndarga [yu leen di teete jëme ci Man seen Boroom].
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Te wàcceel Nanu waa Banii-Israayiila wàccuwaayu teraanga, Nu xéewale leen ñam yu sell ya. Waaye réeruñu woon ba ba leen xam-xam dikkalee. Sa Boroom nag dana àtteji seen diggante bu Bis-pénc baa ci lépp lañu doon juuyoo.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Boo amee sikki-sàkka ci li Nu wàcce ci yaw, laajal ña jàngoon Téere ba. Ba li wér dëgg agsi na ci yaw jóge ca sa Boroom : bul bokk ci way-sikki-sàkka ña, werantekat ña.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Bul bokk mukk ci ñiy weddi kàdduy Yàlla. Nde kon nga bokk ca ña yàqule.
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Ña nga xam ne seen kàddug Boroom far na dal ca seen kaw, duñu gëm,
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
doonte la tegtal yépp dikkal na leen it [duñu gëm], mbete ñu gisee mbugal mu metti ma.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Te amul benn dëkk [bu gëmadi, bu alkaande dikkee] buy door a gëm, di jariñoo ngëmam, lu dul nitu Yuunusa ! Ba ñu gëmee Lanu leen teggil mbugal muy toroxale ci dundug àddina gii, teg ca jox leen ay xéewal ab diir.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Bu neexoon sa Boroorm, fàwwu ñi nekk ci kaw suuf si ñépp gëm. Moo ndax yaw dangay ga [gétén] nit ñi ci ñu nekk ñu gëm ?
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Yellul ci benn bakkan muy gëm lu dul ci coobarey Yàlla. Te Dana teg mbugal ña xel- luwul [ba mën a ràññee dëgg].
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Neel : “Xool-leen li nekk ci asamaan yi ak suuf si”. Te kaawtéef ya ak waaraate ya duñu jariñ dara ci aw nit ñu gëmul.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Moo ndax ñooña dañuy xaar ba mu deme ni bis yu tiis, yu ña leen jiitu woon dajoon, agsi ci ñoom ? Neleen : “Muñandikuleen ! Man it maa ngi bokk ci ñay muñandiku”.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Topp ginnaaw ba, Nu musal Sunuy Yonent ak ña gëm. Noonu la yaye ci Nun Nuy musal ñi gëm.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Neel : "Éy yéen nit ñi ! Bu ngeen amee xel-ñaar ci sama diine jii, xamleen ne man duma jaamu li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ; Waaye Yàlla laay jaamu, Moom mi leen di rey. Te digaleef na ma ma bokk ca way-gëm ña”.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Te : “Nga taxaw temm jublu ci diine jii wéetal Yàlla ! Te bul bokk mukk ca way- bokkaale ña ;
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
bul jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu laa lor, mënu laa jariñ. Soo ko defee rekk daldi bokk ca tooñkat ya”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Bu la Yàlla saddee aw naqar, kenn du la ko mën a teggil ku dul Moom. Bu la bégalee ci aw yiw, dara du mën a fànq xéewalam. Dana ko jottale ku ko soob ci jaamam yi. Moo di Xéewalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Neel : "Éy yéen nit ñi ! Dëgg gi ñëw na ci yéen tukke ci seen Boroom. Ku jub te gindiku, boppam ; ku réer, sànku it boppam. Man dey warlulumaleen dara [ci seeni mbir].
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
e nanga topp [Yaw Yonent bi] la ñu la soloo, te nga sax ci Man ba ba Yàllay àtte te Mooy gën jaa mën a àtte.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers