Ar-Ra'd · 33/43
Tekki Waxtaan — Ar-Ra'd
أَفَمَنْ هُوَ قَائِمٌ عَلَىٰ كُلِّ نَفْسٍ بِمَا كَسَبَتْ ۗ وَجَعَلُوا لِلَّهِ شُرَكَاءَ قُلْ سَمُّوهُمْ ۚ أَمْ تُنَبِّئُونَهُ بِمَا لَا يَعْلَمُ فِي الْأَرْضِ أَم بِظَاهِرٍ مِّنَ الْقَوْلِ ۗ بَلْ زُيِّنَ لِلَّذِينَ كَفَرُوا مَكْرُهُمْ وَصُدُّوا عَنِ السَّبِيلِ ۗ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ ۝٣٣
Afaman Huwa qaaa`imun `alaa kulli nafsim bimaa kasabat; wa ja`aloo illlaahi shurakaaa`a qul samoohum; am tunabbi`oona hoo bimaa laa ya`lamu fil ardi; am bizaahirim minal qawl; bal zuyyina lillazeena kafaroo makruhum wa suddoo `anis sabeel; wa mai yudlilil laaahu famaa lahoo min haad
📖 Tekkim Wolof
Ndax ku di kay fuglu lu bakkan bu ne fàggu [danañu ko niroole ak leneen ?...]. Te ñoom dañoo sàkkal Yàlla ay bokkaale. Neel : “Tuddleen leen. Walla moo ndax dangeen koy soloo [Moom Yàlla] ci la Mu xamul ci suuf si ? Walla lu ngeen di wax rekk la ci kaw [te eggul ci seen xol]? Déedéet”. Ñooña rafetaleef na leen seen kéefar ba fekk na ñu soril leen yoon [wu jub wa]. Te ku Yàlla bàyyi cig réeram, du am ku ko gindi.
🎧 Dégg

📜 Aaya 31-35 — Ar-Ra'd

31وَلَوْ أَنَّ قُرْآنًا سُيِّرَتْ بِهِ الْجِبَالُ أَوْ قُطِّعَتْ بِهِ الْأَرْضُ أَوْ كُلِّمَ بِهِ الْمَوْتَىٰ ۗ بَل لِّلَّهِ الْأَمْرُ جَمِيعًا ۗ أَفَلَمْ يَيْأَسِ الَّذِينَ آمَنُوا أَن لَّوْ يَشَاءُ اللَّهُ لَهَدَى النَّاسَ جَمِيعًا ۗ وَلَا يَزَالُ الَّذِينَ كَفَرُوا تُصِيبُهُم بِمَا صَنَعُوا قَارِعَةٌ أَوْ تَحُلُّ قَرِيبًا مِّن دَارِهِمْ حَتَّىٰ يَأْتِيَ وَعْدُ اللَّهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَا يُخْلِفُ الْمِيعَادَ
Alxuraan, bu ñu ci doxloo woon tundi doj yi, walla xotti suuf si, walla waxloo ñu dee ñi, [du tax ñu gëm]. Waaye li am moo di mépp mbir Yàllaa ko moom. Moo ndax ñi gëm dañoo xamul ne bu neexoon Yàlla Mu jubal nit ñépp. Waaye ñi weddi duñu deñ mukk njuuma di leen dal ngir seen jëf yu ñaaw, walla xanaa mu wàcc fu jegeñ seeni kër ba digub Yàlla di agsi. Te Yàlla du wuute ab digam.
32وَلَقَدِ اسْتُهْزِئَ بِرُسُلٍ مِّن قَبْلِكَ فَأَمْلَيْتُ لِلَّذِينَ كَفَرُوا ثُمَّ أَخَذْتُهُمْ ۖ فَكَيْفَ كَانَ عِقَابِ
Yéjjeefoon na ay Yonent lu la jiitu. Ma yeexe ña weddi woon. Topp Ma mbugal leen. Naka la sama mbugal mel ? Xanaa metti rekk !
33أَفَمَنْ هُوَ قَائِمٌ عَلَىٰ كُلِّ نَفْسٍ بِمَا كَسَبَتْ ۗ وَجَعَلُوا لِلَّهِ شُرَكَاءَ قُلْ سَمُّوهُمْ ۚ أَمْ تُنَبِّئُونَهُ بِمَا لَا يَعْلَمُ فِي الْأَرْضِ أَم بِظَاهِرٍ مِّنَ الْقَوْلِ ۗ بَلْ زُيِّنَ لِلَّذِينَ كَفَرُوا مَكْرُهُمْ وَصُدُّوا عَنِ السَّبِيلِ ۗ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ
Ndax ku di kay fuglu lu bakkan bu ne fàggu [danañu ko niroole ak leneen ?...]. Te ñoom dañoo sàkkal Yàlla ay bokkaale. Neel : “Tuddleen leen. Walla moo ndax dangeen koy soloo [Moom Yàlla] ci la Mu xamul ci suuf si ? Walla lu ngeen di wax rekk la ci kaw [te eggul ci seen xol]? Déedéet”. Ñooña rafetaleef na leen seen kéefar ba fekk na ñu soril leen yoon [wu jub wa]. Te ku Yàlla bàyyi cig réeram, du am ku ko gindi.
34لَّهُمْ عَذَابٌ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۖ وَلَعَذَابُ الْآخِرَةِ أَشَقُّ ۖ وَمَا لَهُم مِّنَ اللَّهِ مِن وَاقٍ
Am na ñu am mbugal ci dundug àddina. Te ca dëgg-dëgg mbugalum àllaaxira moo gën a tiis te duñu am ku leen aar ci la Yàlla dogal ci ñoom.
35۞ مَّثَلُ الْجَنَّةِ الَّتِي وُعِدَ الْمُتَّقُونَ ۖ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ ۖ أُكُلُهَا دَائِمٌ وَظِلُّهَا ۚ تِلْكَ عُقْبَى الَّذِينَ اتَّقَوا ۖ وَّعُقْبَى الْكَافِرِينَ النَّارُ
Àjjana ja ñu dig ña ragal Yàlla [kem ni tool] bu ay dex di daw ci suufam ; ay meññantam ak i keram day sax ba fàww. Loolooy mujjug ña ragal Yàlla, te ña weddi Yàlla seen mujj mooy Safara.
Ar-Ra'dFihi Alxuraan
43Aaya
MedinanRevelation
33Aaya

Tekki — Ar-Ra'd 33

Simoore Ar-Ra'd Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ndax ku di kay fuglu lu bakkan bu ne fàggu…

Simoore Aaya 33/43 — Ar-Ra'd الرعد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ar-Ra'd Dégg, Ar-Ra'd Tekki, Ar-Ra'd mp3, Ar-Ra'd pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers