Simoore Al-Mujadila
PDF —
22 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Mujadila pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Mujadila pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Mujadila Tekki. Al-Mujadila (Medinan) 22 Aaya.



Simoore Al-Mujadila
22 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Yàlla dégg na waxi jigéen ja doon dàggasanteek yaw ci mbirum jëkëram te doon joyal njàmbatam ci Yàlla. Yàllaa ngi dégg seenuk wàqante yéen ñaar, Yàlla kuy dégg la kuy gis la.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Góor ñiy weddi seeni jabar seen pendali nday , taxul ñu mel mi seeni nday ci ñoom... seeni nday ñoom ña leen juróon. Li ñuy wax lu ñaaw la di ay fen. Te Yàlla nag kuy bale la ab Jéggalaakoon la.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Góor ñi nga xam ne dañoo woddi seeni jabar seeni pendali nday ba noppi bëgg caa dale ginnaaw, ca la ñu waxoon, nanu goreel ab jaam balaa ñoo jonjoowaat loolu la ñu leen di jàjje. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Su ko manul na woor ñaari weer yu tegaloo balaa ñuy jonjoowaat. Su ko manul, na leel juróom-benn-fukki ndóol miskiin. Loolu nag, ngir ngeen gëm Yàlla ak ub Yonentam. Te loolu mooy daytali Yàlla yi. Ña weddi nag ñoom danañu am mbugël mu mitti.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Ñay juuyook Yàlla ak ub Yonentam dees na leen toroxal kem niñu toroxale woon ña leen fi jiitu woon. Te wàcce nanu ay firnde yu leer nàññ, yéefar yi am nañu mbugël mu and ak toroxtaane,
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
bu keroog bis pénc baa ba Yàlla dékkal leen ñoom ñépp, dana leen xibaar la ñu jëfoon ndax Yàlla moom takkoon na ko ñoom it ñu fàtte ko. Yàlla kuy seede la ci lépp lu ne.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Xanaa gisuloo Yàlla xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si ? Amul fenn fu ñuy déeyoo sekkare muy ñatt te du moom Yàlla moo leen ñeenteel, du caageen juróom te du ut moo leen juróom-benneel, du lu gëna bari wala lu gëna néew loolu, lu dul ne mi ngi and ak ñoom fu ñu man a nekk. Te, Dana leen xibaar, lépp lu ñu daan jëf, bu bis pénc baa, Yàlla ku xam lépp la.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
Xanaa gisuloo ñañu tere woon (Yahuud ya) ? Ba noppi, ñoom ñu dellu di ko def, di déeyoo ciy bàkkaar, ak ug nooneel ak moy Yonenta bi. Bu ñu dikkee fi yaw, nuyu la ak nuyoo boo xam ne Yàlla nuyoo wu la ko, te ña ngay wax ci seen xol naan : “Lu tax Yàlla dinu mbugël ci li nuy wax ? ” Bàyyi leen ak Safara, Danañu ca xoyomu. Ndaw mujj gu bon !
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
eey yéen ñi gëm ! Su ngeen dee déeyooti, buleen di déeyoo mukk ci luy bàkkaar , walla ak noonoo walla moy Yonenta bi, nangeen di déeyoo ci topp Yàlla ak ragal ko. Te nangeen ragal Yàlla mi nga xam ne dees na leen pang yéen ñépp jëmleen ca moom ( bu bis pénc baa).
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Déeyoo moom [liggéeyub] saytaane doŋŋ la ngir man a tiit loo ñi gëm. Te manuleen a lor dara lu dul ci kàttanu Yàllu. Ñi gëm nañuy doyloo te wéeru ci Yàlla.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
Eey yéen ñi gëm ! bu ñu leen waxee ne yaatleleen ci jataay yi : “Na ngeen daldi yaatal”,. Kon dey Yàlla dana leen yaatalal Bu ñu leen waxee ne jógleen, nangeen daldi jóg (su ngeen ko defee). Yàlla dana yékkatil ñi gëm te bokk ci yéen ak ña am xam-xam (ay daraja yu kawe). Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
eey yéen ñi gëm ! Su ngeen di déeyook Yonenta bi, na ngeen ca jiital ab sarax : loolu moo gën ci yéen te moo gën a sell. Su ngeen ko amul Yàlla moom Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la !
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Moo mbaa du dangeen ragal ñàkk ba tax du ngeen jiital sarax ? Su ngeen, ko deful Yàlla baal leen, daldi leen dem taxawali julli, te di natt asaka, te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Yàlla Ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Xanaa gisuloo naaféq ya dem ànd ak ña Yàlla mere (Yahuud ya) ? Ñoom bokkuñu ci yéen, bokkuñu it ci ñoom (Yahuud ya) ; te ña ngay giñ fen ci Yàlla, te xam ko xéll.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Yàlla waajalna leen mbugël mu tar. Ngir la ñu daan def ñaaw na.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Jàppe woon nañu seen ngiñ ya muy pakk, ñuy gàllankor yoonu Yàlla. Danañu am mbugël muy toroxal.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Seen alal yeek, seen doom yi do leen jariñ manuleen fegal dara ci Yàlla. Ñoom ñoo di waa safara te danu fay béel.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Bu keroogee ba Yàlla dekkal leen ñoom ñépp, su ku defee ñu di ko giiñël ni ñu leen daan giiñale yéen, dañuy jortu ne ñi ngi ci dara. Te ñoom ay fenkat la ñu.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Saytaane man-manee na leen ba fàtteloo leen tudd Yàlla. Ñoo di kureelub Saytaane ndaxam kureelu Saytaane ñooy ña yàqule tigi.
ﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒ
Ñay juuyook Yàlla ak ub Yonentam ñoom ñooy ña torox.
ﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝ
Yàlla bind na ne : “Tigi, Man, maak Samay Yonent nooy not”. Yàlla Ku bari doole la di Ku bari kàttan.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Doo fekk mukk, aw nit ñu gëm Yàlla ak Bis bu mujj ba, ñuy soppanteek kuy juuyook Yàlla ak ub Yonentam, doonte la sax dafay seen baay, walla muy seen doom, walla muy seen mbokk walla ñu bokk giir. Ñooñu Yàlla def na ci seen biir xol ya ngëm dimbali leen ci bu baax. Te dina leen tàbbal ay àjjana yu ay dex di daw ci suufam, ñu béel fa. Yàlla gëram na leen ñoom it gëram nañu ko. Ñooñu ñoo di kurelub Yàlla. Te ndaxam moos kureelub Yàlla ñooy am ndam.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers