Simoore Al-Mumtahina
PDF —
13 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Mumtahina pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Mumtahina pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Mumtahina Tekki. Al-Mumtahina (Medinan) 13 Aaya.



Simoore Al-Mumtahina
13 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Eey ñi gëm ! Buleen jàpp Samay noon ak seeni noon, ay xarit, ndax ñoom dañoo weddi dëgg ga dikk ci yéen. Danañu génne Yonent bi ak yéen néey da ngeen a gëm, Yàlla. Su fekkee ne dangeen a génn di xare ji ci yoonu Yàlla tey sàkku sama ngërëm, buleen rocciku mukk di wut ci ñoom ay xarit, ndax Man xam naa li ngeen di nëbb ak li ngeen di feeñal ? Képp ku ko def ci yéen na xam ne réere na yoon wu jub xocc wa.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Te suñu leen jekkoo, danañu leen rey saaga leen ; li ñu bëgg moo di ngeen weddi.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Te bu Bis Pénc baa seeni doom walla seeni mbokk dunuleen fa jariñ, [Yàlla] dana fa teqale seen diggante, te Yàlla kuy Gis la li ngeen di def.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Am ngeen, royukaay wu rafet ci Ibraahiima ak ña àndoon ak moom, (fàttalikul) ba ñu waxee seen nit ña ne leen : “Deñ nanu ci, yéen ak li ngeen di jaamu te du Yàlla. Weddi nanu leen. Sunu digganteek yéen it, mbañeel ak ug noonoo moo fiy dox ba fàwwu, lu dul bu ngeen gëmee Yàlla doŋŋ”. Ba mu des waxi Ibraahiima ak baayam ne ko : “Danaa la, jéggalul [Yàlla] waaye amaluma la dara ci Yàlla”. “Yaw sunu Boroom, Yaw la nu doyloo te ci Yaw la nuy delu. Te ci Yaw la lépp di Mujj.
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Yaw sunu Boroom, bul nu def mukk [sànje] ci loxoy yéefar yi ; te nanga nu jéggal, Yaw, yaa di Boroom Kàttan gi, di Ku Xereñ ki”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Ñoom am ngeen ci ñoom royuwaay wu rafet, mu ñeel képp ku yaakaar Yàlla ak Bis bu mujj ba : képp ku dumóoyu nag... na xam ne Yàlla ku doyloo boppam Yayoowaakoonu cant la.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Amaana bu Yàlla defee ci seen diggante ak ñi ngeen noonooloon ag bëggënte. Yàlla Ku Man la te Yàlla Jéggëlaakoon Jaglewaakoon la.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Yàlla duleen tere ngeen di maslaa ak di laamisook ñi xeexul ak yéen ci seen diine te génnewuñuleen seeni kër. Yàlla safoona way maandu yi.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
Ñi leen Yàlla di tere kay ñooy ñiy xeex ak yéen ci diine, di leen génnee ci seeni kër walla ña leen cay jàppale. Buleen xaritoo mukk ak ñoom képp kuy xaritook ñoom ñooy tooñkat yi.
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Eey yéen ñi gëm ! Su leen jullit yu jigéen ñi digëloon ne da ñuy gàddaay, nangeen leen seetlu nattu leen ; Yàllaa gën a xam seen dayob ngëm ; su ngeen xamee ne ay jullit la ñu, buleen leen delloo ca Yéefër ya. Ndax daganatuñu ci yéefar yi, Yéefër yi it daganatuñu ci ñoom. Te nangeen delloo alal ya. Aayul ci yéen ngeen denc leen soxna su ngeen joxee can. Buleen maslaak Yéefër. Laajleen la ngeen joxe woon ñoom it nañu laaj la ñu joxe woon. Loolu moo di àtteb Yàlla, Yàlla di àtte seen diggante Yàlla Ku Xam la Ku Xereñ la.
ﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟ
Su seeni soxna rëccee dem ca Yéefër ya yóbbaale can, su ngeen xareek ñoom ba nangu seeni alal, nangeen daldi génneel ña ca seeni soxna dem kem lu tollu ni seeni can. Te nangeen ragal Yàlla mi ngeen gëm.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
Eey yaw Yonent bi ! Jigéen ñi gëm su ñu la dikkalee di jaayanteek yaw ci ne, dootuñu bokkaaleek Yàlla dara, duñu sàcc, duñu njaaloo, duñu rey seeni doom, te duñu sos genn njaaxum ci seeni tànk ak yoxo te dunu la moy ci wenn yiw, nanga jaayanteek ñoom, te nanga leen jéggalul Yàlla. Te Yàlla moom, Jéggalakoon la Jaglewaakoon la.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
Eey yéen ñi gëm ! Buleen di xaritook aw nit ñoo xam ne Yàlla da leen mere te dañoo yoqat ci àllaaxira, ni Yéefër yi yoqate ci ñi nekk ci biir bàmmeel yi.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers