Al-Maida · 18/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَقَالَتِ الْيَهُودُ وَالنَّصَارَىٰ نَحْنُ أَبْنَاءُ اللَّهِ وَأَحِبَّاؤُهُ ۚ قُلْ فَلِمَ يُعَذِّبُكُم بِذُنُوبِكُم ۖ بَلْ أَنتُم بَشَرٌ مِّمَّنْ خَلَقَ ۚ يَغْفِرُ لِمَن يَشَاءُ وَيُعَذِّبُ مَن يَشَاءُ ۚ وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا بَيْنَهُمَا ۖ وَإِلَيْهِ الْمَصِيرُ ۝١٨
Wa qaalatil Yahoodu wan Nasaaraa nahnu abnaaa`ul laahi wa ahibbaaa`uh; qul falima yu`azzibukum bizunoobikum bal antum basharum mimmman khalaq; yaghfiru limai yashaaa`u wa yu`azzibu mai yashaaa`; wa lillaahi mulkus samaawaati wal ardi wa maa bainahumaa wa ilaihil maseer
📖 Tekkim Wolof
Yahuud yeek Nasraan yi wax nañu ne : “Nun nooy doomi Yàlla te di ay soppam.” Neel : “Lu tax mu mbugal leen ci sababus seeni bàkkaar ? ” Li am kay mooy, yéen, ay nit ngeen ñu bokk ca ña Mu bind. Dana baal ku Ko soob, Dana mbugal it ku Ko soob. Te Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si ak lu nekk ci seen diggante. Te ca Moom la lépp di dellu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 16-20 — Al-Maida

16يَهْدِي بِهِ اللَّهُ مَنِ اتَّبَعَ رِضْوَانَهُ سُبُلَ السَّلَامِ وَيُخْرِجُهُم مِّنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ بِإِذْنِهِ وَيَهْدِيهِمْ إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Yàlla dana ca gindi képp ku topp ndigalam, muy yoonu jàmm. Te Dana leen génne cig lëndëm, tàbbal leen cig leer bu Ko soobee. Te teg leen ci yoon wu jub xocc wa.
17لَّقَدْ كَفَرَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ هُوَ الْمَسِيحُ ابْنُ مَرْيَمَ ۚ قُلْ فَمَن يَمْلِكُ مِنَ اللَّهِ شَيْئًا إِنْ أَرَادَ أَن يُهْلِكَ الْمَسِيحَ ابْنَ مَرْيَمَ وَأُمَّهُ وَمَن فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا ۗ وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا بَيْنَهُمَا ۚ يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ ۚ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Ña wax ne : “Ka ñu barkeel, doomi Maryaama [Iisaa], mooy Yàlla ! ”, weddi nañu Yàlla - Neel : “Ana kan moo mënal Yàlla dara, su bëggoon a rey ku ñu barkeel ka, doomi Maryaama, ak yaayam, ak ñi nekk ci kaw suuf si ñépp [Am na sañ-sañu def ko] ?... Te Yàllaay Boroom asamaan yeek suuf si ak li ci seen diggante”. Moom Yàlla mooy sàkk [sos] li ko soob. Yàlla am na kàttan ci def lu ne.
18وَقَالَتِ الْيَهُودُ وَالنَّصَارَىٰ نَحْنُ أَبْنَاءُ اللَّهِ وَأَحِبَّاؤُهُ ۚ قُلْ فَلِمَ يُعَذِّبُكُم بِذُنُوبِكُم ۖ بَلْ أَنتُم بَشَرٌ مِّمَّنْ خَلَقَ ۚ يَغْفِرُ لِمَن يَشَاءُ وَيُعَذِّبُ مَن يَشَاءُ ۚ وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا بَيْنَهُمَا ۖ وَإِلَيْهِ الْمَصِيرُ
Yahuud yeek Nasraan yi wax nañu ne : “Nun nooy doomi Yàlla te di ay soppam.” Neel : “Lu tax mu mbugal leen ci sababus seeni bàkkaar ? ” Li am kay mooy, yéen, ay nit ngeen ñu bokk ca ña Mu bind. Dana baal ku Ko soob, Dana mbugal it ku Ko soob. Te Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si ak lu nekk ci seen diggante. Te ca Moom la lépp di dellu.
19يَا أَهْلَ الْكِتَابِ قَدْ جَاءَكُمْ رَسُولُنَا يُبَيِّنُ لَكُمْ عَلَىٰ فَتْرَةٍ مِّنَ الرُّسُلِ أَن تَقُولُوا مَا جَاءَنَا مِن بَشِيرٍ وَلَا نَذِيرٍ ۖ فَقَدْ جَاءَكُم بَشِيرٌ وَنَذِيرٌ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Éy yéen ñoñ-téere ! Sunub Yonent dikk na ci yéen leeralal leen ginnaaw diir ba dox digganteem ak ka mujj a feeñ ngir ngeen bañ a taafentaloo ne : “Kenn kuy waare walla kuy xamle dikkul fi nun”. Am na ku dikkoon fi yéen kay di xamle ak a waare. Te Yàlla am na kàttan ci def lu Ko soob.
20وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ اذْكُرُوا نِعْمَةَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ إِذْ جَعَلَ فِيكُمْ أَنبِيَاءَ وَجَعَلَكُم مُّلُوكًا وَآتَاكُم مَّا لَمْ يُؤْتِ أَحَدًا مِّنَ الْعَالَمِينَ
(Fàttalikul) ba Muusaa waxee aw nitam, ne leen : "Yéen samaw nit ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi Mu defoon ci yéen, ba Mu defee ci yéen ay Yonent. Def leen ngeen di ay buur. Mu mayoon leen lu mu musul may kenn ci àddina bi.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
18Aaya

Tekki — Al-Maida 18

Simoore Al-Maida Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yahuud yeek Nasraan yi wax nañu ne : “Nun nooy…

Simoore Aaya 18/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers