Simoore Az-Zumar ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Az-Zumar ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (75 Aaya — مكية). Az-Zumar Dégg, Az-Zumar Tekki, Az-Zumar mp3, Az-Zumar pdf.

Jàng te Dégg Simoore Az-Zumar

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
تَنزِيلُ الْكِتَابِ مِنَ اللَّهِ الْعَزِيزِ الْحَكِيمِ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Wàcceg Téere ba bawoo ca Yàlla, miy boroom Kàttan, di ku Xereñ.
إِنَّا أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ فَاعْبُدِ اللَّهَ مُخْلِصًا لَّهُ الدِّينَ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Wàcce Nanu ci yaw Téere bi ci dëgg. Na ngay jaamu Yàlla te di ko sellalal jaamu ga.
أَلَا لِلَّهِ الدِّينُ الْخَالِصُ ۚ وَالَّذِينَ اتَّخَذُوا مِن دُونِهِ أَوْلِيَاءَ مَا نَعْبُدُهُمْ إِلَّا لِيُقَرِّبُونَا إِلَى اللَّهِ زُلْفَىٰ إِنَّ اللَّهَ يَحْكُمُ بَيْنَهُمْ فِي مَا هُمْ فِيهِ يَخْتَلِفُونَ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي مَنْ هُوَ كَاذِبٌ كَفَّارٌ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Yàlla rekk am diine ju sell. Ñay jaamu leneen lu dul moom tey (wax naan) : “Lii nuy jaamu daal danu ciy sukandiku ngir man a jigeñ Yàlla”. Te, Yàlla dana àtte seen diggënte ci la ñu daan woote. Yàlla du gindi fenkat bu weddiwaakoon.
لَّوْ أَرَادَ اللَّهُ أَن يَتَّخِذَ وَلَدًا لَّاصْطَفَىٰ مِمَّا يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ ۚ سُبْحَانَهُ ۖ هُوَ اللَّهُ الْوَاحِدُ الْقَهَّارُ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Su Yàlla nàmmoon jàppe kenn doomam, Kon dana tànn ca la mu bind namu ko soobe (waaye nammu ko). Tudd naa Sellam ga ! Mooy Yàlla, jiy Jenn, tey Notaakoon ba.
خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۖ يُكَوِّرُ اللَّيْلَ عَلَى النَّهَارِ وَيُكَوِّرُ النَّهَارَ عَلَى اللَّيْلِ ۖ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ ۖ كُلٌّ يَجْرِي لِأَجَلٍ مُّسَمًّى ۗ أَلَا هُوَ الْعَزِيزُ الْغَفَّارُ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Moo bind asamaan yeek suuf si ci dëgg. Mooy muur guddi ci kaw bëccëg mooy mur it bëccëg ci kaw guddi, moo tàggat jant beek weer wi lu ca nekk ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal tigi. Mooy boroom Kàttan gi, di Jégalaakoon bi !
خَلَقَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ ثُمَّ جَعَلَ مِنْهَا زَوْجَهَا وَأَنزَلَ لَكُم مِّنَ الْأَنْعَامِ ثَمَانِيَةَ أَزْوَاجٍ ۚ يَخْلُقُكُمْ فِي بُطُونِ أُمَّهَاتِكُمْ خَلْقًا مِّن بَعْدِ خَلْقٍ فِي ظُلُمَاتٍ ثَلَاثٍ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ لَهُ الْمُلْكُ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُصْرَفُونَ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Moo leen bind ci jenn jëmm daldi cay defar soxnaam sa. Te wàcceel na leen ci mala yi lu tollook juróom-ñatti tóllent. Mu di leen sos ci seen biiri nday, cig sosu ginnaawug sos, ci biir yatti lëndamaay. Koo koo di Yàlla, seen Boroom ! Moo moom Nguur. Te amul jeneen Yàlla judul Moom. Man dey xamuma naka ngeen koy walbatee ?
إِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَنِيٌّ عَنكُمْ ۖ وَلَا يَرْضَىٰ لِعِبَادِهِ الْكُفْرَ ۖ وَإِن تَشْكُرُوا يَرْضَهُ لَكُمْ ۗ وَلَا تَزِرُ وَازِرَةٌ وِزْرَ أُخْرَىٰ ۗ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُم مَّرْجِعُكُمْ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۚ إِنَّهُ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Su ngeen weddee, Moom doyewu leen dara. Te gëramul kéefër, ci jaamam yi. Su ngeen santee, Mu gëramal leen ko. Amul kenn kuy yanu bàkkaarub keneen. Te it, dees na leen delloo ca seen Boroom : Mu xamal leen la ngeen daan jëf ndax Moom ku xam la li nekk ci dënn yi (pas-pas yi).
۞ وَإِذَا مَسَّ الْإِنسَانَ ضُرٌّ دَعَا رَبَّهُ مُنِيبًا إِلَيْهِ ثُمَّ إِذَا خَوَّلَهُ نِعْمَةً مِّنْهُ نَسِيَ مَا كَانَ يَدْعُو إِلَيْهِ مِن قَبْلُ وَجَعَلَ لِلَّهِ أَندَادًا لِّيُضِلَّ عَن سَبِيلِهِ ۚ قُلْ تَمَتَّعْ بِكُفْرِكَ قَلِيلًا ۖ إِنَّكَ مِنْ أَصْحَابِ النَّارِ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Te saa su lor laale nit, dafay daldi fàtte la mu doon woote aka ñaan Boroomam daldi wutal Yàlla ag bokkaale. Di rëyal nit ñi fàbbi leen ci yoonu Yàlla, Waxal ne : “Bànneexul tuuti ci sa kéefër gi. Yaw ci waa Safara nga bokk”.
أَمَّنْ هُوَ قَانِتٌ آنَاءَ اللَّيْلِ سَاجِدًا وَقَائِمًا يَحْذَرُ الْآخِرَةَ وَيَرْجُو رَحْمَةَ رَبِّهِ ۗ قُلْ هَلْ يَسْتَوِي الَّذِينَ يَعْلَمُونَ وَالَّذِينَ لَا يَعْلَمُونَ ۗ إِنَّمَا يَتَذَكَّرُ أُولُو الْأَلْبَابِ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Moo ndax, kuy jóg, diggu guddi, di sujuud ak a taxaw( julli), ngir moytu (tiisu àllaaxira) tey yaakaar yërmaandey Boroomam... Waxal ne : “Ndax ñi xam danañu yem, niróok ñi xamadi ? ” Li wér moo di ne woroom xel yi rekk ay fàttaliku.
قُلْ يَا عِبَادِ الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا رَبَّكُمْ ۚ لِلَّذِينَ أَحْسَنُوا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةٌ ۗ وَأَرْضُ اللَّهِ وَاسِعَةٌ ۗ إِنَّمَا يُوَفَّى الصَّابِرُونَ أَجْرَهُم بِغَيْرِ حِسَابٍ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi gëm ! Ragalleen seen Boroom (Yàlla)”. Ñiy jëf aw yiw ci àddina, danañu am [aw yiw]. Te suufus Yàlla si yaatu na te muñkat yi danañu leen jox seenug pey mu mat sëkk ci lu dul ak waññ.
قُلْ إِنِّي أُمِرْتُ أَنْ أَعْبُدَ اللَّهَ مُخْلِصًا لَّهُ الدِّينَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Waxal ne : “digëléef na ma may jaamu Yàlla di ko sellalal diinéem,
وَأُمِرْتُ لِأَنْ أَكُونَ أَوَّلَ الْمُسْلِمِينَ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
te it digaléef na ma doon Jullit buy jëkk.
قُلْ إِنِّي أَخَافُ إِنْ عَصَيْتُ رَبِّي عَذَابَ يَوْمٍ عَظِيمٍ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Waxal ne : “Ragal naa, su ma mettee sama Boroom, (dajeek) mbugëlam bis bu màgg”.
قُلِ اللَّهَ أَعْبُدُ مُخْلِصًا لَّهُ دِينِي ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Waxal ne : “Yàlla laay jaamu, te di Ko sellalal sama diine.
فَاعْبُدُوا مَا شِئْتُم مِّن دُونِهِ ۗ قُلْ إِنَّ الْخَاسِرِينَ الَّذِينَ خَسِرُوا أَنفُسَهُمْ وَأَهْلِيهِمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ أَلَا ذَٰلِكَ هُوَ الْخُسْرَانُ الْمُبِينُ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Jaamuleen, lu leen soob (bàyyi Yàlla)! ” – Waxal ne : “ña yàqule, ñooy ña ñàkk seen bopp ak seen njaboot, ca Bis Pénc ba”. Loolu mooy yàqule tigi.
لَهُم مِّن فَوْقِهِمْ ظُلَلٌ مِّنَ النَّارِ وَمِن تَحْتِهِمْ ظُلَلٌ ۚ ذَٰلِكَ يُخَوِّفُ اللَّهُ بِهِ عِبَادَهُ ۚ يَا عِبَادِ فَاتَّقُونِ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Am na ci seen kaw, ay muuraayi safara, ak ci seen suuf ay laltaayi safara. Loolu la Yàlla di ragalloo jaamam ñi. “Éy yéen Samay jaam, ragalleen ma ! ”
وَالَّذِينَ اجْتَنَبُوا الطَّاغُوتَ أَن يَعْبُدُوهَا وَأَنَابُوا إِلَى اللَّهِ لَهُمُ الْبُشْرَىٰ ۚ فَبَشِّرْ عِبَادِ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Ñay moytandikoo jaamuy xërëm, tey dellu ca Yàlla, danañu am mbégte ! Bégalal Sama jaam ñi
الَّذِينَ يَسْتَمِعُونَ الْقَوْلَ فَيَتَّبِعُونَ أَحْسَنَهُ ۚ أُولَٰئِكَ الَّذِينَ هَدَاهُمُ اللَّهُ ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمْ أُولُو الْأَلْبَابِ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Ña nga xam ne dañuy déglu Wax, tey topp la ca gën a rafet. Ñoom la Yàlla gindi te ñooy woroom xel ya !
أَفَمَنْ حَقَّ عَلَيْهِ كَلِمَةُ الْعَذَابِ أَفَأَنتَ تُنقِذُ مَن فِي النَّارِ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Ka baatub mbugël yay ci moom,... ndax yaw yaay xettali ku nekk ca biir safara ?
لَٰكِنِ الَّذِينَ اتَّقَوْا رَبَّهُمْ لَهُمْ غُرَفٌ مِّن فَوْقِهَا غُرَفٌ مَّبْنِيَّةٌ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ ۖ وَعْدَ اللَّهِ ۖ لَا يُخْلِفُ اللَّهُ الْمِيعَادَ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Waaye ñay ragal seen Boroom am nañu [ay neegi] taax yu tegaloo ay dex di daw ci suufam. Muy digub Yàlla ! Te Yàlla du wuute Ab dégg.
أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَسَلَكَهُ يَنَابِيعَ فِي الْأَرْضِ ثُمَّ يُخْرِجُ بِهِ زَرْعًا مُّخْتَلِفًا أَلْوَانُهُ ثُمَّ يَهِيجُ فَتَرَاهُ مُصْفَرًّا ثُمَّ يَجْعَلُهُ حُطَامًا ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَذِكْرَىٰ لِأُولِي الْأَلْبَابِ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Xanaa gisoo ne Yàlla wàcce na ndox mu bawoo asamaan, daldi koy sóob ci bëtu ndox ci biir suuf si ; di ca, génne mbay mu wuute ay wirgó, di lu bëbbu, nga gis ko mu mboq wow ; bay, dammatoo. Ag fàttiliku nekk na ci biir loolu ngir [aw nit] ñu am ay xel.
أَفَمَن شَرَحَ اللَّهُ صَدْرَهُ لِلْإِسْلَامِ فَهُوَ عَلَىٰ نُورٍ مِّن رَّبِّهِ ۚ فَوَيْلٌ لِّلْقَاسِيَةِ قُلُوبُهُم مِّن ذِكْرِ اللَّهِ ۚ أُولَٰئِكَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Moo ndax ki Yàlla ubbi dënnam ci Lislaam mu nekk ci leerug Boroomam( moo gën walla ka des cig kéefër)... Toskare ñeel na ñiy bañ a tudd Yàlla ngir xol bu wow. Ñoom ña nga ca réer gu bir.
اللَّهُ نَزَّلَ أَحْسَنَ الْحَدِيثِ كِتَابًا مُّتَشَابِهًا مَّثَانِيَ تَقْشَعِرُّ مِنْهُ جُلُودُ الَّذِينَ يَخْشَوْنَ رَبَّهُمْ ثُمَّ تَلِينُ جُلُودُهُمْ وَقُلُوبُهُمْ إِلَىٰ ذِكْرِ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكَ هُدَى اللَّهِ يَهْدِي بِهِ مَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Yàlla wàcce na gën jaa rafet waxtaan, muy Téere bu bari yu niróo ak i baamu. Yaramu ñi ragal Yàlla day daw [saa su ñu ko déggee] ; ba egal seen yaram ya ak seen xel ya door a firiku jëm ci fàttaliku Yàlla. [Alxuraan] jooju moo di njubug Yàlla mu di ci gindi ku ko soob. Ku Yàlla namm a réeral kenn du ko gindi.
أَفَمَن يَتَّقِي بِوَجْهِهِ سُوءَ الْعَذَابِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۚ وَقِيلَ لِلظَّالِمِينَ ذُوقُوا مَا كُنتُمْ تَكْسِبُونَ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Moo ndax ki am bugël mi gën a gën a bon ( niróo na ak ka dugg Àjjana), bu Bis Pénc baa bu boobaa tooñkat ya... Dañu naan leen : “Tokamtikuleen li ngeen daan fàggu”.
كَذَّبَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَأَتَاهُمُ الْعَذَابُ مِنْ حَيْثُ لَا يَشْعُرُونَ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Xeet ya leen fi jiitu woon weddi woon nañu (Yonnent yi), mbugël ma dikkëlleen fuñu ko foogewul.
فَأَذَاقَهُمُ اللَّهُ الْخِزْيَ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۖ وَلَعَذَابُ الْآخِرَةِ أَكْبَرُ ۚ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Yàlla musal na leen mbugëlu toroxtaane ci dundug àddina sii. Te mbugëlu àllaaxira, moo, gën a rëy, cëy bu ñu xamoon !
وَلَقَدْ ضَرَبْنَا لِلنَّاسِ فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ مِن كُلِّ مَثَلٍ لَّعَلَّهُمْ يَتَذَكَّرُونَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
saddalal Nanu nit ñi ay léebu ci Alxuraan jii, ndax amaana ñuy fàttaliku.
قُرْآنًا عَرَبِيًّا غَيْرَ ذِي عِوَجٍ لَّعَلَّهُمْ يَتَّقُونَ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Mooy Alxuraan ju di [làmmiñu] araab, amul lugg-luggal, ndax amaana ñuy ragal Yàlla !
ضَرَبَ اللَّهُ مَثَلًا رَّجُلًا فِيهِ شُرَكَاءُ مُتَشَاكِسُونَ وَرَجُلًا سَلَمًا لِّرَجُلٍ هَلْ يَسْتَوِيَانِ مَثَلًا ۚ الْحَمْدُ لِلَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْلَمُونَ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Yàllaa ngi sadd léebu jenn waay ju am digaale yu bari tey ŋaayoo : ndax niróonaak waa ju am benn digaale bu mu jubóol ? Yàlla rekk yayoo cant ! Li am moo di ne li ëpp ci ñoom xamuñu (misaalum kuy jaamu Yàlla ak ku koy bokkaale).
إِنَّكَ مَيِّتٌ وَإِنَّهُم مَّيِّتُونَ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Yaw dangay dee ñoom it dañuy dee ;
ثُمَّ إِنَّكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ عِندَ رَبِّكُمْ تَخْتَصِمُونَ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
su ko defee, ngeen daje ca seen kanamu Boroom, di xulóo bu Bis Pénc baa.
۞ فَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن كَذَبَ عَلَى اللَّهِ وَكَذَّبَ بِالصِّدْقِ إِذْ جَاءَهُ ۚ أَلَيْسَ فِي جَهَنَّمَ مَثْوًى لِّلْكَافِرِينَ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
Ana kan moo gën a tooñ, kuy fenal Yàlla tey weddi dëgg saa su dëgg dikkee ? Moo ndax Safara dafa amul wàccuwaayub yéefar ya ? (Axakaañ !)
وَالَّذِي جَاءَ بِالصِّدْقِ وَصَدَّقَ بِهِ ۙ أُولَٰئِكَ هُمُ الْمُتَّقُونَ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
Ku indi dëgg ak ku koy saxal, ñooñoo ragal Yàlla.
لَهُم مَّا يَشَاءُونَ عِندَ رَبِّهِمْ ۚ ذَٰلِكَ جَزَاءُ الْمُحْسِنِينَ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
Am nañu lu leen soob fa seen Boroom ; loolu mooy peyug ñiy rafetal,
لِيُكَفِّرَ اللَّهُ عَنْهُمْ أَسْوَأَ الَّذِي عَمِلُوا وَيَجْزِيَهُمْ أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ الَّذِي كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
te Yàlla dana far seen ñaawtéef fay leen ca la gënnoon a rafet ca la ñu daan jëf.
أَلَيْسَ اللَّهُ بِكَافٍ عَبْدَهُ ۖ وَيُخَوِّفُونَكَ بِالَّذِينَ مِن دُونِهِ ۚ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Moo ndax Yàlla dafa doyul [wéruwaay] ci ab jaamam ? Bay tax ñu di la tiitale ci leneen lu dul Moom. Képp ku Yàlla natt ci moom réer kenn du ku gindi.
وَمَن يَهْدِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِن مُّضِلٍّ ۗ أَلَيْسَ اللَّهُ بِعَزِيزٍ ذِي انتِقَامٍ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Te it képp ku Yàlla namm ci moom njub, kenn du ko réerël. Moo ndax Yàlla dafa dul boroom Kàttan di boroomuk Fayu ? Axakañ !
وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلْ أَفَرَأَيْتُم مَّا تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ إِنْ أَرَادَنِيَ اللَّهُ بِضُرٍّ هَلْ هُنَّ كَاشِفَاتُ ضُرِّهِ أَوْ أَرَادَنِي بِرَحْمَةٍ هَلْ هُنَّ مُمْسِكَاتُ رَحْمَتِهِ ۚ قُلْ حَسْبِيَ اللَّهُ ۖ عَلَيْهِ يَتَوَكَّلُ الْمُتَوَكِّلُونَ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Soo leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ? ”, Ñu ni la : “Yàlla”. Waxal ne : “Xanaa gisu leen li ngéen di jaamu bàyyi Yàlla ; ci ne su Yàlla nammee ci man lor, ndax ñoom kon danañu man a teggi lor ja ? Walla su Yàlla nammoon ci man yërmaande, ndax kenn danañu man a fanq yërmaande ja ? ” – waxal ne : “Yàlla doy na ma : ci moom la wéerukat ya di wéeru”
قُلْ يَا قَوْمِ اعْمَلُوا عَلَىٰ مَكَانَتِكُمْ إِنِّي عَامِلٌ ۖ فَسَوْفَ تَعْلَمُونَ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Waxal ne : “Éy yéen samaw nit, liggéeyleen lu ngeen man, man it [maa ngi liggéey]. Dangeen xalset a xam
مَن يَأْتِيهِ عَذَابٌ يُخْزِيهِ وَيَحِلُّ عَلَيْهِ عَذَابٌ مُّقِيمٌ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
ana kan la mbugël di dikk toroxal ko ; ak ci kaw kan la mbugëlam dëggële di wàcc”.
إِنَّا أَنزَلْنَا عَلَيْكَ الْكِتَابَ لِلنَّاسِ بِالْحَقِّ ۖ فَمَنِ اهْتَدَىٰ فَلِنَفْسِهِ ۖ وَمَن ضَلَّ فَإِنَّمَا يَضِلُّ عَلَيْهَا ۖ وَمَا أَنتَ عَلَيْهِم بِوَكِيلٍ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Wàcce Nanu ci yaw Téere ba, ci dëgg, ngir nit ñi. Ku gindiku boppam ; ku réer it boppam. Seenub lijjënti warula
اللَّهُ يَتَوَفَّى الْأَنفُسَ حِينَ مَوْتِهَا وَالَّتِي لَمْ تَمُتْ فِي مَنَامِهَا ۖ فَيُمْسِكُ الَّتِي قَضَىٰ عَلَيْهَا الْمَوْتَ وَيُرْسِلُ الْأُخْرَىٰ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَتَفَكَّرُونَ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
Yàlla mooy faat bakkan bu ñuy dee ak ya deewul ci biiri nelaw. Mooy téye ya mu namm ñu dee, di boyal ya ca des jëme ko ca dig ba mu ko àppal. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat.
أَمِ اتَّخَذُوا مِن دُونِ اللَّهِ شُفَعَاءَ ۚ قُلْ أَوَلَوْ كَانُوا لَا يَمْلِكُونَ شَيْئًا وَلَا يَعْقِلُونَ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Walla dañoo wut, yeneeni tinukat, bàyyi Yàlla ? Waxal ne : “Ndax ! Nekkuñu woon ñu amal dara te xamu ñu dara ? ”
قُل لِّلَّهِ الشَّفَاعَةُ جَمِيعًا ۖ لَّهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ ثُمَّ إِلَيْهِ تُرْجَعُونَ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Waxal ne : “Tinu ba tinu jeex (ramm) Yàllaa ko jagoo. Miy boroom nguurug asamaan yeek suuf. Te ci moom ngeen di dellu”
وَإِذَا ذُكِرَ اللَّهُ وَحْدَهُ اشْمَأَزَّتْ قُلُوبُ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ ۖ وَإِذَا ذُكِرَ الَّذِينَ مِن دُونِهِ إِذَا هُمْ يَسْتَبْشِرُونَ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Te saa su ñu tuddee Yàlla doŋŋ, xoli ñi gëmul àllaaxira tàmbalee wurwuri (xat mer) saa su ñu tuddee ñeneen (ya ñu koy bokkaaleel), ñu daldi bég.
قُلِ اللَّهُمَّ فَاطِرَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ عَالِمَ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ أَنتَ تَحْكُمُ بَيْنَ عِبَادِكَ فِي مَا كَانُوا فِيهِ يَخْتَلِفُونَ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Waxal ne : “yaw sama Boroom, Yaa bind sàkk asamaan yeek suuf si, Yaa xam kumpa ak li feeñ, te danga àtte diggënte Sa jaam ñi ci la nu daan woote”.
وَلَوْ أَنَّ لِلَّذِينَ ظَلَمُوا مَا فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا وَمِثْلَهُ مَعَهُ لَافْتَدَوْا بِهِ مِن سُوءِ الْعَذَابِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۚ وَبَدَا لَهُم مِّنَ اللَّهِ مَا لَمْ يَكُونُوا يَحْتَسِبُونَ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Te ñiy tooñ su ñu amoon àddina ak li ci biiram, - ak leneen lu na tollaat, - kon danañu ko jéem a jote seen bopp bu Bis Pénc baa ; ngir mbugël mu tar, ak la ñu gis mu bawoo ca Yàlla, te masu ñu koo foog ;
وَبَدَا لَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا كَسَبُوا وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
seen ñaawtéef ya ñu fàggu woon feeñ, la ñu daan ñaawalaatee muur leen.
فَإِذَا مَسَّ الْإِنسَانَ ضُرٌّ دَعَانَا ثُمَّ إِذَا خَوَّلْنَاهُ نِعْمَةً مِّنَّا قَالَ إِنَّمَا أُوتِيتُهُ عَلَىٰ عِلْمٍ ۚ بَلْ هِيَ فِتْنَةٌ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
Saa su nit amee lor ju ko dab, danuy daldi woo. Tey ñaan waaye saa su nu ko teggee may ko xeewël, muy wax naan : “lii ci [sama] xam-xam laa ko ame”. Ab nattu la, de; waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
قَدْ قَالَهَا الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَمَا أَغْنَىٰ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَكْسِبُونَ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
Ña leen fi jiitu woon waxoon na ñu ko. Te taxul la ñu daan fàggu jariñ leen dara ;
فَأَصَابَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا كَسَبُوا ۚ وَالَّذِينَ ظَلَمُوا مِنْ هَٰؤُلَاءِ سَيُصِيبُهُمْ سَيِّئَاتُ مَا كَسَبُوا وَمَا هُم بِمُعْجِزِينَ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
Faf sax la gënoon a ñaaw a la ñu daan fàggu moo leen dal. Te ñii itam li gën a ñaaw ca la ñu doon fàggu dana dal ci seen kaw te duñu ko man a teggi.
أَوَلَمْ يَعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ وَيَقْدِرُ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Xanaa dañoo xamul ne Yàlla mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam di ko xatal it ? Ay kiiman a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.
۞ قُلْ يَا عِبَادِيَ الَّذِينَ أَسْرَفُوا عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ لَا تَقْنَطُوا مِن رَّحْمَةِ اللَّهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ يَغْفِرُ الذُّنُوبَ جَمِيعًا ۚ إِنَّهُ هُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ ۝٥٣
📖 Tekki Aaya 53
Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla. Ndax Yàlla dana jégële bakkaar yépp. Mooy Jégëlaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”.
وَأَنِيبُوا إِلَىٰ رَبِّكُمْ وَأَسْلِمُوا لَهُ مِن قَبْلِ أَن يَأْتِيَكُمُ الْعَذَابُ ثُمَّ لَا تُنصَرُونَ ۝٥٤
📖 Tekki Aaya 54
Delluleen ci seen Boroom, te jébël ko seen bopp, balaa mbugël di dal ci seen kaw te kenn duleen ca dimbali.
وَاتَّبِعُوا أَحْسَنَ مَا أُنزِلَ إِلَيْكُم مِّن رَّبِّكُم مِّن قَبْلِ أَن يَأْتِيَكُمُ الْعَذَابُ بَغْتَةً وَأَنتُمْ لَا تَشْعُرُونَ ۝٥٥
📖 Tekki Aaya 55
Te it na ngeen di topp li gën a rafet ci li nu wàcce (Alxuraan) ci yéen mu bawoo ca seen Boroom, balaa mbugël di dal ci seen kaw te du ngeen ko yëg ;
أَن تَقُولَ نَفْسٌ يَا حَسْرَتَا عَلَىٰ مَا فَرَّطتُ فِي جَنبِ اللَّهِ وَإِن كُنتُ لَمِنَ السَّاخِرِينَ ۝٥٦
📖 Tekki Aaya 56
balaa benn bakkan di wax naan : “Wóy ngalla man ci na mu soofentale woon mbiri Yàlla. Te daan ca reetaan nit ña” ;
أَوْ تَقُولَ لَوْ أَنَّ اللَّهَ هَدَانِي لَكُنتُ مِنَ الْمُتَّقِينَ ۝٥٧
📖 Tekki Aaya 57
walla mu naan : “Suma Yàlla gindi woon, kon danaa bokk, ca ñay ragal Yàlla” ;
أَوْ تَقُولَ حِينَ تَرَى الْعَذَابَ لَوْ أَنَّ لِي كَرَّةً فَأَكُونَ مِنَ الْمُحْسِنِينَ ۝٥٨
📖 Tekki Aaya 58
walla muy wax ba mu gisee mbugël ma naan : “Cëy ! Suma delluwaatoon àddina ! Ba man a bokk ca ñay rafetal”.
بَلَىٰ قَدْ جَاءَتْكَ آيَاتِي فَكَذَّبْتَ بِهَا وَاسْتَكْبَرْتَ وَكُنتَ مِنَ الْكَافِرِينَ ۝٥٩
📖 Tekki Aaya 59
“Mukk ! Ndax Samay laaya dikkaloon na la nga weddi ko, di rëy-rëylu dem àndeek yéefar yi”.
وَيَوْمَ الْقِيَامَةِ تَرَى الَّذِينَ كَذَبُوا عَلَى اللَّهِ وُجُوهُهُم مُّسْوَدَّةٌ ۚ أَلَيْسَ فِي جَهَنَّمَ مَثْوًى لِّلْمُتَكَبِّرِينَ ۝٦٠
📖 Tekki Aaya 60
Bu Bis Pénc baa, dangay gis ña fenal Yàlla, seen xar kanam ya ñuul kukk. Moo ndax wàccuwaayi yéefar ya nekkul ca biir Safara ? (Axakañ)
وَيُنَجِّي اللَّهُ الَّذِينَ اتَّقَوْا بِمَفَازَتِهِمْ لَا يَمَسُّهُمُ السُّوءُ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ ۝٦١
📖 Tekki Aaya 61
Yàlla dana musël ña ragal Yàlla te texel leen [ca Àjjana]. Lu bon du leen fa laal te it duñu fa jàq.
اللَّهُ خَالِقُ كُلِّ شَيْءٍ ۖ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ وَكِيلٌ ۝٦٢
📖 Tekki Aaya 62
Yàlla moo sàkk bind lépp, te it Mooy lijjënti lépp it.
لَّهُ مَقَالِيدُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَالَّذِينَ كَفَرُوا بِآيَاتِ اللَّهِ أُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ ۝٦٣
📖 Tekki Aaya 63
Moo moom caabiy asamaan yeek suuf si ; ñay weddi kàdduy Yàlla, ñooy ña yàqule.
قُلْ أَفَغَيْرَ اللَّهِ تَأْمُرُونِّي أَعْبُدُ أَيُّهَا الْجَاهِلُونَ ۝٦٤
📖 Tekki Aaya 64
Waxal ne : “Yéen ñi réer, ndax dangeen may digël may jaamu lu dul Yàlla ? ”
وَلَقَدْ أُوحِيَ إِلَيْكَ وَإِلَى الَّذِينَ مِن قَبْلِكَ لَئِنْ أَشْرَكْتَ لَيَحْبَطَنَّ عَمَلُكَ وَلَتَكُونَنَّ مِنَ الْخَاسِرِينَ ۝٦٥
📖 Tekki Aaya 65
Te, soloona Nu la ak (Yonnent ya la jiitu woon) ci ne : “Saa soo bokkaalee , sa jëf dana sippiku; nga bokk ci ñu yàqule ña.
بَلِ اللَّهَ فَاعْبُدْ وَكُن مِّنَ الشَّاكِرِينَ ۝٦٦
📖 Tekki Aaya 66
Jaamujil Yàlla, tey sant”.
وَمَا قَدَرُوا اللَّهَ حَقَّ قَدْرِهِ وَالْأَرْضُ جَمِيعًا قَبْضَتُهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَالسَّمَاوَاتُ مَطْوِيَّاتٌ بِيَمِينِهِ ۚ سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يُشْرِكُونَ ۝٦٧
📖 Tekki Aaya 67
Joxuñu Yàlla dayoom tigi, suuf si sépp ab ŋëbëm lay doon bu Bis Pénc baa, asamaan yépp ab lem lay doon ci [loxoom]. Tudd naa Sellam ga ! Kawe na ci liñu koy bokkaale.
وَنُفِخَ فِي الصُّورِ فَصَعِقَ مَن فِي السَّمَاوَاتِ وَمَن فِي الْأَرْضِ إِلَّا مَن شَاءَ اللَّهُ ۖ ثُمَّ نُفِخَ فِيهِ أُخْرَىٰ فَإِذَا هُمْ قِيَامٌ يَنظُرُونَ ۝٦٨
📖 Tekki Aaya 68
Suñu ëfee bufta bi, lu nekk ci asamaan yeek suuf si léppay dee, lu dul la ca soob Yàlla. Ñu ëfaat ko beneen yoon ndeketeeyóo, ñépp a ngi ne fujjet jóg taxaw ne xey di xoole.
وَأَشْرَقَتِ الْأَرْضُ بِنُورِ رَبِّهَا وَوُضِعَ الْكِتَابُ وَجِيءَ بِالنَّبِيِّينَ وَالشُّهَدَاءِ وَقُضِيَ بَيْنَهُم بِالْحَقِّ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ ۝٦٩
📖 Tekki Aaya 69
Suuf si daldi fenk ak leerug Boroomam ; ñu daldi teg Téere ba, indi Yonnent ya ak seede ya ; daldi àtte seen diggënte ci dëgg te kenn duleen tooñ ci dara ;
وَوُفِّيَتْ كُلُّ نَفْسٍ مَّا عَمِلَتْ وَهُوَ أَعْلَمُ بِمَا يَفْعَلُونَ ۝٧٠
📖 Tekki Aaya 70
bakkan bu nekk ñu fay ko la mu daan jëf. Te [Yàlla] moo gën a xam ñu daan def.
وَسِيقَ الَّذِينَ كَفَرُوا إِلَىٰ جَهَنَّمَ زُمَرًا ۖ حَتَّىٰ إِذَا جَاءُوهَا فُتِحَتْ أَبْوَابُهَا وَقَالَ لَهُمْ خَزَنَتُهَا أَلَمْ يَأْتِكُمْ رُسُلٌ مِّنكُمْ يَتْلُونَ عَلَيْكُمْ آيَاتِ رَبِّكُمْ وَيُنذِرُونَكُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا ۚ قَالُوا بَلَىٰ وَلَٰكِنْ حَقَّتْ كَلِمَةُ الْعَذَابِ عَلَى الْكَافِرِينَ ۝٧١
📖 Tekki Aaya 71
Ñuy jiital yéefar yi jëme leen Safara ñu di ay mbooloo. Bu ñu fa àggee, buntu ba ubbiku ña koy wattu ne leen : “Xanaa amuleen woon ay Yonnent yu leen daan jàngal kàdduy Yàlla seen Boroom ak daan leen xupp ci dajeb seen bis bii ? ” Ñu ne leen : axakañ, waaye dogalub mbugël yay na ca yéefar ya.
قِيلَ ادْخُلُوا أَبْوَابَ جَهَنَّمَ خَالِدِينَ فِيهَا ۖ فَبِئْسَ مَثْوَى الْمُتَكَبِّرِينَ ۝٧٢
📖 Tekki Aaya 72
“Ñu ne, [leen] dugguleen, wunti Safara, ngeen béel fa”. Rëy-rëylu kat tee ka bon ab saxuwaay !
وَسِيقَ الَّذِينَ اتَّقَوْا رَبَّهُمْ إِلَى الْجَنَّةِ زُمَرًا ۖ حَتَّىٰ إِذَا جَاءُوهَا وَفُتِحَتْ أَبْوَابُهَا وَقَالَ لَهُمْ خَزَنَتُهَا سَلَامٌ عَلَيْكُمْ طِبْتُمْ فَادْخُلُوهَا خَالِدِينَ ۝٧٣
📖 Tekki Aaya 73
Ñooy jiital ña ragaloon seen Boroom jëme leen Àjjana. Ñu, di ay mbooloo bu ñu fa àggee wunt ya ubbeeku, ña koy wattu ne leen : “Jàmm rekk yal na nekk ci yéen ! Yéen dey baax ngeen : dugguleen ci, te dangeen ciy béel”.
وَقَالُوا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي صَدَقَنَا وَعْدَهُ وَأَوْرَثَنَا الْأَرْضَ نَتَبَوَّأُ مِنَ الْجَنَّةِ حَيْثُ نَشَاءُ ۖ فَنِعْمَ أَجْرُ الْعَامِلِينَ ۝٧٤
📖 Tekki Aaya 74
Ñuy wax naan : “Noo ngi sant Yàlla mi nu dëggëlal digëm bi te donale nu suuf si ! Tey noo ngi xéyoo ci Àjjana nu mu nu neexe”. Ay waay gii pey a neex !
وَتَرَى الْمَلَائِكَةَ حَافِّينَ مِنْ حَوْلِ الْعَرْشِ يُسَبِّحُونَ بِحَمْدِ رَبِّهِمْ ۖ وَقُضِيَ بَيْنَهُم بِالْحَقِّ وَقِيلَ الْحَمْدُ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ ۝٧٥
📖 Tekki Aaya 75
Nga gis Malaaka yaa ngay wër (Aras), di sàbbaal seen cantug Boroom. Ñu wax naan : “Xeeti cant, ñeel na Yàlla miy Boroom àddina si”.
← 38 Az-Zumar (39/114) 40 →
Jàng Simoore Az-Zumar ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

39الزمر Az-Zumar 📚 75 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers