Simoore Sad ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Sad ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (88 Aaya — مكية). Sad Dégg, Sad Tekki, Sad mp3, Sad pdf.

Jàng te Dégg Simoore Sad

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
ص ۚ وَالْقُرْآنِ ذِي الذِّكْرِ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Saad. Maa ngi giiñ ci Alxuraan, miy boroom tur ci ne :
بَلِ الَّذِينَ كَفَرُوا فِي عِزَّةٍ وَشِقَاقٍ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Ña weddi ña nga cag rëy-rëylu ak kaŋ-kaŋ !
كَمْ أَهْلَكْنَا مِن قَبْلِهِم مِّن قَرْنٍ فَنَادَوا وَّلَاتَ حِينَ مَنَاصٍ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Aka bari ñu nu faagaagal ca ña leen jiitu woon, ñu daan yuuxu, walla te du ñu man a raw?
وَعَجِبُوا أَن جَاءَهُم مُّنذِرٌ مِّنْهُمْ ۖ وَقَالَ الْكَافِرُونَ هَٰذَا سَاحِرٌ كَذَّابٌ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
(Waa Màkka) daana yéeme ci waaraatekat bii leen digal te bokk ci ñoom, yéefar ya daan wax naan : “Kii dey ab njibarkat la bu di ab fenaakoon,
أَجَعَلَ الْآلِهَةَ إِلَٰهًا وَاحِدًا ۖ إِنَّ هَٰذَا لَشَيْءٌ عُجَابٌ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Moo ndax dafa bëgg a def Yàlla yii muy jenn Yàlla ? Aa lii dey mbir mu yéeme la”.
وَانطَلَقَ الْمَلَأُ مِنْهُمْ أَنِ امْشُوا وَاصْبِرُوا عَلَىٰ آلِهَتِكُمْ ۖ إِنَّ هَٰذَا لَشَيْءٌ يُرَادُ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Kilifa ya ne leen : “Demleen, te muñ jàpp ci seen Yàlla yii : lii daal la nu bëgg.
مَا سَمِعْنَا بِهَٰذَا فِي الْمِلَّةِ الْآخِرَةِ إِنْ هَٰذَا إِلَّا اخْتِلَاقٌ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Nun masunoo dégg lii ci diine ji fi mujj wàcc (Iisaa) ; lii daal ay sos rekk la !
أَأُنزِلَ عَلَيْهِ الذِّكْرُ مِن بَيْنِنَا ۚ بَلْ هُمْ فِي شَكٍّ مِّن ذِكْرِي ۖ بَل لَّمَّا يَذُوقُوا عَذَابِ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Nuy wax naan, ak ni nu tollu ndax ci moom la [Alxuraan] di wàcc? ” Li wer moo di yéefar yaa ngay sikki-sàkka ci sama Téere bi. Xanaa kay dañoo mosagul mbugël !
أَمْ عِندَهُمْ خَزَائِنُ رَحْمَةِ رَبِّكَ الْعَزِيزِ الْوَهَّابِ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Walla ndabi yërmaandey sa Boroom tey Mayewaakoon, biy boroom Kàttan bi, da fa nekk ci ñoom.
أَمْ لَهُم مُّلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا بَيْنَهُمَا ۖ فَلْيَرْتَقُوا فِي الْأَسْبَابِ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Walla dañoo moom nguurug asamaan yeek suuf si, ak li nekk ci seen diggënte? su fekkee ne looloo am kon nañu def pexe ci yéeg ci !
جُندٌ مَّا هُنَالِكَ مَهْزُومٌ مِّنَ الْأَحْزَابِ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Ak nu seeni xarekat man a tollu ak ña leen di jàppale, danuy nërméelu !
كَذَّبَتْ قَبْلَهُمْ قَوْمُ نُوحٍ وَعَادٌ وَفِرْعَوْنُ ذُو الْأَوْتَادِ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
ña leen fi jiitu woon, weddi woon nañu ña di nitu Nooh, ak Aad ak Firawna ma doon boroom dëx (tabax yu rëy),
وَثَمُودُ وَقَوْمُ لُوطٍ وَأَصْحَابُ الْأَيْكَةِ ۚ أُولَٰئِكَ الْأَحْزَابُ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
k Samuud, ak nitu Lóot, ak waa Aykata, (ñoom ñépp weddi woon nañu seeni yonnent). Te ñoom ñoo di jàppalekat ya (farandoo ya).
إِن كُلٌّ إِلَّا كَذَّبَ الرُّسُلَ فَحَقَّ عِقَابِ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Ñoom ñépp weddi woon yonnent ya. Nu daldi leen mbugël !
وَمَا يَنظُرُ هَٰؤُلَاءِ إِلَّا صَيْحَةً وَاحِدَةً مَّا لَهَا مِن فَوَاقٍ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Ñoom xaaruñu lu dul genn xaacu, gu dul tóllantiku wol.
وَقَالُوا رَبَّنَا عَجِّل لَّنَا قِطَّنَا قَبْلَ يَوْمِ الْحِسَابِ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, gaawal jox nu sunu wàll balaa wañoo ba”.
اصْبِرْ عَلَىٰ مَا يَقُولُونَ وَاذْكُرْ عَبْدَنَا دَاوُودَ ذَا الْأَيْدِ ۖ إِنَّهُ أَوَّابٌ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Muñal lii ñuy wax ; te ngay fàttaliku Sunu jaam ba Daawuda ma doonoon boroom doole, Moom ku faral daan dellu ci Boroomam la woon.
إِنَّا سَخَّرْنَا الْجِبَالَ مَعَهُ يُسَبِّحْنَ بِالْعَشِيِّ وَالْإِشْرَاقِ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Tàggataloon Nanu ko, tundi doj yi nu daan ànd ak moom, di sàbbaal Yàlla subaak ngoon,
وَالطَّيْرَ مَحْشُورَةً ۖ كُلٌّ لَّهُ أَوَّابٌ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
picc yépp it dañuy dajaloo, di delloo kañ [Yàlla].
وَشَدَدْنَا مُلْكَهُ وَآتَيْنَاهُ الْحِكْمَةَ وَفَصْلَ الْخِطَابِ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Dëgaralal Nanu ko nguuram jox ko xam-xamu xereñe ràññee ak xam-xamu àtte.
۞ وَهَلْ أَتَاكَ نَبَأُ الْخَصْمِ إِذْ تَسَوَّرُوا الْمِحْرَابَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Moo ndax xibaari xulóokat ya agsi na ci yaw ba ñu bëttee ñagub mbaar ma (mihraab ba) !
إِذْ دَخَلُوا عَلَىٰ دَاوُودَ فَفَزِعَ مِنْهُمْ ۖ قَالُوا لَا تَخَفْ ۖ خَصْمَانِ بَغَىٰ بَعْضُنَا عَلَىٰ بَعْضٍ فَاحْكُم بَيْنَنَا بِالْحَقِّ وَلَا تُشْطِطْ وَاهْدِنَا إِلَىٰ سَوَاءِ الصِّرَاطِ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Ba ñu duggee fekk fa Daawuda, mu tiit ci ñoom. Nu wax ko ne : “Bul tiit ! Ñaari way xuloo la nu ; kenn ci nun dafay néewal dole ka ca des. Kon àtteel sunu diggënte ci dëgg, te it nga gindi nu teg nu ci yoon wu jub xocc wa.
إِنَّ هَٰذَا أَخِي لَهُ تِسْعٌ وَتِسْعُونَ نَعْجَةً وَلِيَ نَعْجَةٌ وَاحِدَةٌ فَقَالَ أَكْفِلْنِيهَا وَعَزَّنِي فِي الْخِطَابِ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Kii nag sama mbokk la : amna juróom-ñeenti fukki xar ak juróom ñenenta, man ma am menn xar doŋŋ. Mu wax ma ne : “Naa ko ko jox” ; daldi wane lool ; doole ca ba ñuy waqante”.
قَالَ لَقَدْ ظَلَمَكَ بِسُؤَالِ نَعْجَتِكَ إِلَىٰ نِعَاجِهِ ۖ وَإِنَّ كَثِيرًا مِّنَ الْخُلَطَاءِ لَيَبْغِي بَعْضُهُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ إِلَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ وَقَلِيلٌ مَّا هُمْ ۗ وَظَنَّ دَاوُودُ أَنَّمَا فَتَنَّاهُ فَاسْتَغْفَرَ رَبَّهُ وَخَرَّ رَاكِعًا وَأَنَابَ ۩ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
[Daawuda] ne ko : “Moo la tooñ ci laaj gi mu la laaj sam xar ngir dollee koy xaram”. Te ñiy faral a ànd di liggéey bariyaana ba ñennat ci ñoom jaayee doole ña ca des, ba mu des ña gëm tey def yiw – te ñooña ñu néew lañu ci. – Daawuda daldi xam nag ne dañu ko doon nattu. Mu daldi rot (rukuu) sëgg jàpp ci ay wóomam delluwaat ca Boroomam.
فَغَفَرْنَا لَهُ ذَٰلِكَ ۖ وَإِنَّ لَهُ عِندَنَا لَزُلْفَىٰ وَحُسْنَ مَآبٍ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Nu daldi koy jégël loola. Te amna daraja ju Nu jige ak wàccuwaay wu jekk.
يَا دَاوُودُ إِنَّا جَعَلْنَاكَ خَلِيفَةً فِي الْأَرْضِ فَاحْكُم بَيْنَ النَّاسِ بِالْحَقِّ وَلَا تَتَّبِعِ الْهَوَىٰ فَيُضِلَّكَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَضِلُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ لَهُمْ عَذَابٌ شَدِيدٌ بِمَا نَسُوا يَوْمَ الْحِسَابِ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
“Éy yaw Daawuda, def Nanu la ngay sunu kuutlaay ci kaw suuf si. Na ngay àtte diggënte nit ñi ci dëgg te bul topp mukk bànneex : su ko defee dana la féewale ak yoonu Yàlla”. Te ñiy féewook yoon danañu am mbugël mu tar mitti ngir lañu fàtte bisub wañoo ba (Bis Pénc ba).
وَمَا خَلَقْنَا السَّمَاءَ وَالْأَرْضَ وَمَا بَيْنَهُمَا بَاطِلًا ۚ ذَٰلِكَ ظَنُّ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ فَوَيْلٌ لِّلَّذِينَ كَفَرُوا مِنَ النَّارِ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Te bindunu asamaan ak suuf ak li nekk ci seen diggënte cig neen. Loolu la yéefar ya njortu. Te yéefar yaa ngaay tuskare ca biir safara !
أَمْ نَجْعَلُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ كَالْمُفْسِدِينَ فِي الْأَرْضِ أَمْ نَجْعَلُ الْمُتَّقِينَ كَالْفُجَّارِ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Moo ndax dañuy jëflaantéek yàqkat yi nekk ci suuf ? walla danuy jëflaantéek ña ragal Yàlla kem ni ñuy jëflaantéek kàccoor yi ?
كِتَابٌ أَنزَلْنَاهُ إِلَيْكَ مُبَارَكٌ لِّيَدَّبَّرُوا آيَاتِهِ وَلِيَتَذَكَّرَ أُولُو الْأَلْبَابِ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
[Lii] ab Téere la bu Nuy wàcce ci yaw bu barkeel nak, ngir ñuy settantal ay laayaam ak it ngir woroomi xel yi man ciy fàttalikoo!
وَوَهَبْنَا لِدَاوُودَ سُلَيْمَانَ ۚ نِعْمَ الْعَبْدُ ۖ إِنَّهُ أَوَّابٌ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
May Nanu Daawuda (doomam ja) Sulaymaan, - ndaw jaam bu baax ! – Ku daan dellu ca boroomam la.
إِذْ عُرِضَ عَلَيْهِ بِالْعَشِيِّ الصَّافِنَاتُ الْجِيَادُ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
(Fàttalikul) ngoon ga, ñu ko gaarale fasi naari góor ya,
فَقَالَ إِنِّي أَحْبَبْتُ حُبَّ الْخَيْرِ عَن ذِكْرِ رَبِّي حَتَّىٰ تَوَارَتْ بِالْحِجَابِ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
Sulaymaan dellu wax ne : “Cëy man, maa ngi fees dell ak bëgg (àddina sii) mu fàbbi maa ba jant bi so te fàttalikuwuma sama Boroom.
رُدُّوهَا عَلَيَّ ۖ فَطَفِقَ مَسْحًا بِالسُّوقِ وَالْأَعْنَاقِ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
Delloosil ma fas yi.”. Ñu delloosil ko ko mu dagg yeel ya ak doq ya.
وَلَقَدْ فَتَنَّا سُلَيْمَانَ وَأَلْقَيْنَا عَلَىٰ كُرْسِيِّهِ جَسَدًا ثُمَّ أَنَابَ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
Nattu Nanu Sulaymaan ci nu sànni ca toogoom ba (jëmm ju nu wotte). Mu delluwaat, màggal Boroomam.
قَالَ رَبِّ اغْفِرْ لِي وَهَبْ لِي مُلْكًا لَّا يَنبَغِي لِأَحَدٍ مِّن بَعْدِي ۖ إِنَّكَ أَنتَ الْوَهَّابُ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, na nga ma jégal te may ma nguur goo xam ne kenn dootu ko am sama ginnaaw. Yaw yaay Mayaakoon bi”.
فَسَخَّرْنَا لَهُ الرِّيحَ تَجْرِي بِأَمْرِهِ رُخَاءً حَيْثُ أَصَابَ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Tàggatal Nanu ko ngelaw li, muy daw ci ndigëlam, ak fu mu jublu.
وَالشَّيَاطِينَ كُلَّ بَنَّاءٍ وَغَوَّاصٍ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Tàggatal Nanu ko sayaane yi, ñu di ko tabaxal ak di ko nuural ci (ndox).
وَآخَرِينَ مُقَرَّنِينَ فِي الْأَصْفَادِ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Ak ñeneen, ñu ñu lëkkële ak i njéng.
هَٰذَا عَطَاؤُنَا فَامْنُنْ أَوْ أَمْسِكْ بِغَيْرِ حِسَابٍ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
“Lii mooy sunug may ; mayeel walla nga téye ko kenn du ko waññook yaw”.
وَإِنَّ لَهُ عِندَنَا لَزُلْفَىٰ وَحُسْنَ مَآبٍ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Te mooy am na daraja ju Nu jege ak wàccuwaay wu jekk.
وَاذْكُرْ عَبْدَنَا أَيُّوبَ إِذْ نَادَىٰ رَبَّهُ أَنِّي مَسَّنِيَ الشَّيْطَانُ بِنُصْبٍ وَعَذَابٍ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Fàttalikul sunu jaam Ayyuuba , ba muy woo Boroomam naan ko : “Yaw sama Boroom Saytaane teg na ma coono ak i tiis”.
ارْكُضْ بِرِجْلِكَ ۖ هَٰذَا مُغْتَسَلٌ بَارِدٌ وَشَرَابٌ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
(Yàlla ne ko) dóoral sa tànk fi ci suuf : am ndox ngi nii mu sedd mu man a sangu neex a naan.
وَوَهَبْنَا لَهُ أَهْلَهُ وَمِثْلَهُم مَّعَهُمْ رَحْمَةً مِّنَّا وَذِكْرَىٰ لِأُولِي الْأَلْبَابِ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Nu delloowaat ko njabootam joxaat ko lu na tollu, muy yërmande ju bawoo ci Nun ak fàttili woroom xel yi.
وَخُذْ بِيَدِكَ ضِغْثًا فَاضْرِب بِّهِ وَلَا تَحْنَثْ ۗ إِنَّا وَجَدْنَاهُ صَابِرًا ۚ نِّعْمَ الْعَبْدُ ۖ إِنَّهُ أَوَّابٌ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
“Ŋëbal sëqub ñax, te dóor ko ko (soxnaam sa). Te bul gàddu bàkkaarub ngiiñ”. Moom, muñkat la di jaam bu baax. Kuy farlu di dellu ci Boroomam la.
وَاذْكُرْ عِبَادَنَا إِبْرَاهِيمَ وَإِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ أُولِي الْأَيْدِي وَالْأَبْصَارِ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Fàttalikul suñu jaam ña Ibraahiima, ak Ishaaq ak Yaaquub ? Woroomi kàttan la ñu woon ak i gis-gis (xel).
إِنَّا أَخْلَصْنَاهُم بِخَالِصَةٍ ذِكْرَى الدَّارِ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Noo leen ràññi woon ngir sellalug : fàttaliku bis pénc ba.
وَإِنَّهُمْ عِندَنَا لَمِنَ الْمُصْطَفَيْنَ الْأَخْيَارِ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Te ñoom, bokk nañu, ca tànnéef ya gën a ràññiku.
وَاذْكُرْ إِسْمَاعِيلَ وَالْيَسَعَ وَذَا الْكِفْلِ ۖ وَكُلٌّ مِّنَ الْأَخْيَارِ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Fàttalikul Ismaahiila ak Ilyaas, ak Suul kifli, ñoom ñépp ay tànnéef la ñu.
هَٰذَا ذِكْرٌ ۚ وَإِنَّ لِلْمُتَّقِينَ لَحُسْنَ مَآبٍ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
Lii ag fàttali la. Te ne ñay ragal Yàlla, am nañu, wàccuwaay wu jekk,
جَنَّاتِ عَدْنٍ مُّفَتَّحَةً لَّهُمُ الْأَبْوَابُ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
Àjjanay Adan, seen wunt ya ne ŋàll ngir ñoom,
مُتَّكِئِينَ فِيهَا يَدْعُونَ فِيهَا بِفَاكِهَةٍ كَثِيرَةٍ وَشَرَابٍ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
dañu fay, sóonu, di woo ay futéef yu bari ak i naan.
۞ وَعِندَهُمْ قَاصِرَاتُ الطَّرْفِ أَتْرَابٌ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Amnañu fa ay jigéen (jabar) ñu di ay lamsalkat, yu maase ay at.
هَٰذَا مَا تُوعَدُونَ لِيَوْمِ الْحِسَابِ ۝٥٣
📖 Tekki Aaya 53
Lii mooy li Nu leen dégóon ci bisub wañoo ba.
إِنَّ هَٰذَا لَرِزْقُنَا مَا لَهُ مِن نَّفَادٍ ۝٥٤
📖 Tekki Aaya 54
Lii moo di sunu xéewal gi te du jeex mukk.
هَٰذَا ۚ وَإِنَّ لِلطَّاغِينَ لَشَرَّ مَآبٍ ۝٥٥
📖 Tekki Aaya 55
Yëgal it ne ! ñay bew am nañu wàccuwaay wu yées,
جَهَنَّمَ يَصْلَوْنَهَا فَبِئْسَ الْمِهَادُ ۝٥٦
📖 Tekki Aaya 56
Mooy Safara su ñuy xoyomoo. ndaw kër gu bon !
هَٰذَا فَلْيَذُوقُوهُ حَمِيمٌ وَغَسَّاقٌ ۝٥٧
📖 Tekki Aaya 57
Mi ngi nii ! Nu cay tokamtiku : ndox muy tàng ak a wañax,
وَآخَرُ مِن شَكْلِهِ أَزْوَاجٌ ۝٥٨
📖 Tekki Aaya 58
ak yeneeni xeeti mbugël yu mu témbóol.
هَٰذَا فَوْجٌ مُّقْتَحِمٌ مَّعَكُمْ ۖ لَا مَرْحَبًا بِهِمْ ۚ إِنَّهُمْ صَالُو النَّارِ ۝٥٩
📖 Tekki Aaya 59
Ñii ay mbooloo la ñu ñuy buuxanteek yéen, kenn dalaluleen. Te ñooy xoyomu ca Safara.
قَالُوا بَلْ أَنتُمْ لَا مَرْحَبًا بِكُمْ ۖ أَنتُمْ قَدَّمْتُمُوهُ لَنَا ۖ فَبِئْسَ الْقَرَارُ ۝٦٠
📖 Tekki Aaya 60
Ñuy wax naan : “Yéen kay la kenn dul dalal, lii, Yéen la ñu ko waajal”. Te ndaw saxuwaay bu bon !
قَالُوا رَبَّنَا مَن قَدَّمَ لَنَا هَٰذَا فَزِدْهُ عَذَابًا ضِعْفًا فِي النَّارِ ۝٦١
📖 Tekki Aaya 61
Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom na nga dolli, ki nu waajalal lii, mbugël muy fulandiku ca biir Safara ”.
وَقَالُوا مَا لَنَا لَا نَرَىٰ رِجَالًا كُنَّا نَعُدُّهُم مِّنَ الْأَشْرَارِ ۝٦٢
📖 Tekki Aaya 62
“Ana lan moo xew ba gisunu fi gaa ya nu daan limaale ci saay-saay si ?
أَتَّخَذْنَاهُمْ سِخْرِيًّا أَمْ زَاغَتْ عَنْهُمُ الْأَبْصَارُ ۝٦٣
📖 Tekki Aaya 63
Moo ndax dañu leen ko daan tooñe walla danu làqu sunu gëm ? ”
إِنَّ ذَٰلِكَ لَحَقٌّ تَخَاصُمُ أَهْلِ النَّارِ ۝٦٤
📖 Tekki Aaya 64
Lii daal tigi mooy xulóob waa Safara
قُلْ إِنَّمَا أَنَا مُنذِرٌ ۖ وَمَا مِنْ إِلَٰهٍ إِلَّا اللَّهُ الْوَاحِدُ الْقَهَّارُ ۝٦٥
📖 Tekki Aaya 65
Waxal ne : “Man daal ab xuppekat laa. Te jenn Yàlla amul judul, Yàlla jiy jenn , Notaakoon ba,
رَبُّ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا بَيْنَهُمَا الْعَزِيزُ الْغَفَّارُ ۝٦٦
📖 Tekki Aaya 66
Mooy Boroom asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggënte, te mooy boroom Kàttan gi, di Jégëlaakoon bi”.
قُلْ هُوَ نَبَأٌ عَظِيمٌ ۝٦٧
📖 Tekki Aaya 67
Waxal ne : “Xibaar bu rëy la,
أَنتُمْ عَنْهُ مُعْرِضُونَ ۝٦٨
📖 Tekki Aaya 68
waaye yéen dumóoyu ngeen ko.
مَا كَانَ لِيَ مِنْ عِلْمٍ بِالْمَلَإِ الْأَعْلَىٰ إِذْ يَخْتَصِمُونَ ۝٦٩
📖 Tekki Aaya 69
Amuma woon xam-xam ca xulóob kilifa ya gën a kawe.
إِن يُوحَىٰ إِلَيَّ إِلَّا أَنَّمَا أَنَا نَذِيرٌ مُّبِينٌ ۝٧٠
📖 Tekki Aaya 70
Li nu may soloo doonul lu dul ne man mii ab xuppe kat laa waaraatekat bu bir”.
إِذْ قَالَ رَبُّكَ لِلْمَلَائِكَةِ إِنِّي خَالِقٌ بَشَرًا مِّن طِينٍ ۝٧١
📖 Tekki Aaya 71
(Fàttalitul) ba sa Boroom waxee Malaaka ya ne leen : “Man de maa ngi sàkk mbindéef ci ban.
فَإِذَا سَوَّيْتُهُ وَنَفَخْتُ فِيهِ مِن رُّوحِي فَقَعُوا لَهُ سَاجِدِينَ ۝٧٢
📖 Tekki Aaya 72
Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, na ngeen daldi rot, sujuudal ko”.
فَسَجَدَ الْمَلَائِكَةُ كُلُّهُمْ أَجْمَعُونَ ۝٧٣
📖 Tekki Aaya 73
Malaaka ya yépp daldi sujuud,
إِلَّا إِبْلِيسَ اسْتَكْبَرَ وَكَانَ مِنَ الْكَافِرِينَ ۝٧٤
📖 Tekki Aaya 74
ba mu des Ibliis moom dafa rëy-rëylu bokk ca yéefar ya.
قَالَ يَا إِبْلِيسُ مَا مَنَعَكَ أَن تَسْجُدَ لِمَا خَلَقْتُ بِيَدَيَّ ۖ أَسْتَكْبَرْتَ أَمْ كُنتَ مِنَ الْعَالِينَ ۝٧٥
📖 Tekki Aaya 75
(Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujuud ci lii ma bind ci samay yoxo ? Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ”
قَالَ أَنَا خَيْرٌ مِّنْهُ ۖ خَلَقْتَنِي مِن نَّارٍ وَخَلَقْتَهُ مِن طِينٍ ۝٧٦
📖 Tekki Aaya 76
“[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci ban”.
قَالَ فَاخْرُجْ مِنْهَا فَإِنَّكَ رَجِيمٌ ۝٧٧
📖 Tekki Aaya 77
(Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ;
وَإِنَّ عَلَيْكَ لَعْنَتِي إِلَىٰ يَوْمِ الدِّينِ ۝٧٨
📖 Tekki Aaya 78
te Samam rëbb dal na la ba baa saa di taxaw”.
قَالَ رَبِّ فَأَنظِرْنِي إِلَىٰ يَوْمِ يُبْعَثُونَ ۝٧٩
📖 Tekki Aaya 79
“[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”.
قَالَ فَإِنَّكَ مِنَ الْمُنظَرِينَ ۝٨٠
📖 Tekki Aaya 80
(Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu,
إِلَىٰ يَوْمِ الْوَقْتِ الْمَعْلُومِ ۝٨١
📖 Tekki Aaya 81
ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”.
قَالَ فَبِعِزَّتِكَ لَأُغْوِيَنَّهُمْ أَجْمَعِينَ ۝٨٢
📖 Tekki Aaya 82
“[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj loo ñoom ñépp,
إِلَّا عِبَادَكَ مِنْهُمُ الْمُخْلَصِينَ ۝٨٣
📖 Tekki Aaya 83
ba mu des sa jaam ñiy sellal”.
قَالَ فَالْحَقُّ وَالْحَقَّ أَقُولُ ۝٨٤
📖 Tekki Aaya 84
(Yàlla) daldi wax ne : “Maa ngi waat, ci dëgg ne dëgg laay wax,
لَأَمْلَأَنَّ جَهَنَّمَ مِنكَ وَمِمَّن تَبِعَكَ مِنْهُمْ أَجْمَعِينَ ۝٨٥
📖 Tekki Aaya 85
Danaa feesal Safara ci yaw ak ña la topp ñépp”.
قُلْ مَا أَسْأَلُكُمْ عَلَيْهِ مِنْ أَجْرٍ وَمَا أَنَا مِنَ الْمُتَكَلِّفِينَ ۝٨٦
📖 Tekki Aaya 86
Waxal ne : “Laajumaleen ci ag pey ; te it yanuwuma ci.
إِنْ هُوَ إِلَّا ذِكْرٌ لِّلْعَالَمِينَ ۝٨٧
📖 Tekki Aaya 87
[Alxuraan] jii daal ag fàttali la ñeel waa àddina si yépp.
وَلَتَعْلَمُنَّ نَبَأَهُ بَعْدَ حِينٍ ۝٨٨
📖 Tekki Aaya 88
Te dangeen xam ay xibaaram ci ndiir su yàggatul ! ”.
← 37 Sad (38/114) 39 →
Jàng Simoore Sad ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

38ص Sad 📚 88 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers