Az-Zumar · 50/75
Tekki Waxtaan — Simoore Az-Zumar
قَدْ قَالَهَا الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَمَا أَغْنَىٰ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَكْسِبُونَ ۝٥٠
Qad qaalahul lazeena min qablihim famaaa aghnaa `anhum maa kaanoo yaksiboon
📖 Tekkim Wolof
Ña leen fi jiitu woon waxoon na ñu ko. Te taxul la ñu daan fàggu jariñ leen dara ;

🎧 Dégg


📜 Aaya 48-52 — Simoore Az-Zumar

48وَبَدَا لَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا كَسَبُوا وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ
seen ñaawtéef ya ñu fàggu woon feeñ, la ñu daan ñaawalaatee muur leen.
49فَإِذَا مَسَّ الْإِنسَانَ ضُرٌّ دَعَانَا ثُمَّ إِذَا خَوَّلْنَاهُ نِعْمَةً مِّنَّا قَالَ إِنَّمَا أُوتِيتُهُ عَلَىٰ عِلْمٍ ۚ بَلْ هِيَ فِتْنَةٌ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Saa su nit amee lor ju ko dab, danuy daldi woo. Tey ñaan waaye saa su nu ko teggee may ko xeewël, muy wax naan : “lii ci [sama] xam-xam laa ko ame”. Ab nattu la, de; waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
50قَدْ قَالَهَا الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَمَا أَغْنَىٰ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Ña leen fi jiitu woon waxoon na ñu ko. Te taxul la ñu daan fàggu jariñ leen dara ;
51فَأَصَابَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا كَسَبُوا ۚ وَالَّذِينَ ظَلَمُوا مِنْ هَٰؤُلَاءِ سَيُصِيبُهُمْ سَيِّئَاتُ مَا كَسَبُوا وَمَا هُم بِمُعْجِزِينَ
Faf sax la gënoon a ñaaw a la ñu daan fàggu moo leen dal. Te ñii itam li gën a ñaaw ca la ñu doon fàggu dana dal ci seen kaw te duñu ko man a teggi.
52أَوَلَمْ يَعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ وَيَقْدِرُ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Xanaa dañoo xamul ne Yàlla mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam di ko xatal it ? Ay kiiman a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.
Az-ZumarFihi Alxuraan
75Aaya
MeccanRevelation
50Aaya

Tekki — Az-Zumar 50

Simoore Az-Zumar Aaya 50 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña leen fi jiitu woon waxoon na ñu ko. Te…

Simoore Aaya 50/75 — Simoore Az-Zumar الزمر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Az-Zumar Dégg, Simoore Az-Zumar Tekki, Simoore Az-Zumar mp3, Simoore Az-Zumar pdf. Aaya 48–52. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers