Az-Zumar · 6/75
Tekki Waxtaan — Az-Zumar
خَلَقَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ ثُمَّ جَعَلَ مِنْهَا زَوْجَهَا وَأَنزَلَ لَكُم مِّنَ الْأَنْعَامِ ثَمَانِيَةَ أَزْوَاجٍ ۚ يَخْلُقُكُمْ فِي بُطُونِ أُمَّهَاتِكُمْ خَلْقًا مِّن بَعْدِ خَلْقٍ فِي ظُلُمَاتٍ ثَلَاثٍ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ لَهُ الْمُلْكُ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُصْرَفُونَ ۝٦
Khalaqakum min nafsinw waahidatin summa ja`ala minhaa zawjahaa wa anzala lakum minal-an`aami samaani yata azwaaj; yakhuluqukum fee butooni ummahaatikum khalqam mim ba`di khalqin fee zulumaatin salaas; zaalikumul laahu Rabbukum lahul mulk; laaa ilaaha illaa Huwa fa annaa tusrafoon
📖 Tekkim Wolof
Moo leen bind ci jenn jëmm daldi cay defar soxnaam sa. Te wàcceel na leen ci mala yi lu tollook juróom-ñatti tóllent. Mu di leen sos ci seen biiri nday, cig sosu ginnaawug sos, ci biir yatti lëndamaay. Koo koo di Yàlla, seen Boroom ! Moo moom Nguur. Te amul jeneen Yàlla judul Moom. Man dey xamuma naka ngeen koy walbatee ?
🎧 Dégg

📜 Aaya 4-8 — Az-Zumar

4لَّوْ أَرَادَ اللَّهُ أَن يَتَّخِذَ وَلَدًا لَّاصْطَفَىٰ مِمَّا يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ ۚ سُبْحَانَهُ ۖ هُوَ اللَّهُ الْوَاحِدُ الْقَهَّارُ
Su Yàlla nàmmoon jàppe kenn doomam, Kon dana tànn ca la mu bind namu ko soobe (waaye nammu ko). Tudd naa Sellam ga ! Mooy Yàlla, jiy Jenn, tey Notaakoon ba.
5خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۖ يُكَوِّرُ اللَّيْلَ عَلَى النَّهَارِ وَيُكَوِّرُ النَّهَارَ عَلَى اللَّيْلِ ۖ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ ۖ كُلٌّ يَجْرِي لِأَجَلٍ مُّسَمًّى ۗ أَلَا هُوَ الْعَزِيزُ الْغَفَّارُ
Moo bind asamaan yeek suuf si ci dëgg. Mooy muur guddi ci kaw bëccëg mooy mur it bëccëg ci kaw guddi, moo tàggat jant beek weer wi lu ca nekk ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal tigi. Mooy boroom Kàttan gi, di Jégalaakoon bi !
6خَلَقَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ ثُمَّ جَعَلَ مِنْهَا زَوْجَهَا وَأَنزَلَ لَكُم مِّنَ الْأَنْعَامِ ثَمَانِيَةَ أَزْوَاجٍ ۚ يَخْلُقُكُمْ فِي بُطُونِ أُمَّهَاتِكُمْ خَلْقًا مِّن بَعْدِ خَلْقٍ فِي ظُلُمَاتٍ ثَلَاثٍ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ لَهُ الْمُلْكُ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُصْرَفُونَ
Moo leen bind ci jenn jëmm daldi cay defar soxnaam sa. Te wàcceel na leen ci mala yi lu tollook juróom-ñatti tóllent. Mu di leen sos ci seen biiri nday, cig sosu ginnaawug sos, ci biir yatti lëndamaay. Koo koo di Yàlla, seen Boroom ! Moo moom Nguur. Te amul jeneen Yàlla judul Moom. Man dey xamuma naka ngeen koy walbatee ?
7إِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَنِيٌّ عَنكُمْ ۖ وَلَا يَرْضَىٰ لِعِبَادِهِ الْكُفْرَ ۖ وَإِن تَشْكُرُوا يَرْضَهُ لَكُمْ ۗ وَلَا تَزِرُ وَازِرَةٌ وِزْرَ أُخْرَىٰ ۗ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُم مَّرْجِعُكُمْ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۚ إِنَّهُ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Su ngeen weddee, Moom doyewu leen dara. Te gëramul kéefër, ci jaamam yi. Su ngeen santee, Mu gëramal leen ko. Amul kenn kuy yanu bàkkaarub keneen. Te it, dees na leen delloo ca seen Boroom : Mu xamal leen la ngeen daan jëf ndax Moom ku xam la li nekk ci dënn yi (pas-pas yi).
8۞ وَإِذَا مَسَّ الْإِنسَانَ ضُرٌّ دَعَا رَبَّهُ مُنِيبًا إِلَيْهِ ثُمَّ إِذَا خَوَّلَهُ نِعْمَةً مِّنْهُ نَسِيَ مَا كَانَ يَدْعُو إِلَيْهِ مِن قَبْلُ وَجَعَلَ لِلَّهِ أَندَادًا لِّيُضِلَّ عَن سَبِيلِهِ ۚ قُلْ تَمَتَّعْ بِكُفْرِكَ قَلِيلًا ۖ إِنَّكَ مِنْ أَصْحَابِ النَّارِ
Te saa su lor laale nit, dafay daldi fàtte la mu doon woote aka ñaan Boroomam daldi wutal Yàlla ag bokkaale. Di rëyal nit ñi fàbbi leen ci yoonu Yàlla, Waxal ne : “Bànneexul tuuti ci sa kéefër gi. Yaw ci waa Safara nga bokk”.
Az-ZumarFihi Alxuraan
75Aaya
MeccanRevelation
6Aaya

Tekki — Az-Zumar 6

Simoore Az-Zumar Aaya 6 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo leen bind ci jenn jëmm daldi cay defar soxnaam…

Simoore Aaya 6/75 — Az-Zumar الزمر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Az-Zumar Dégg, Az-Zumar Tekki, Az-Zumar mp3, Az-Zumar pdf. Aaya 4–8. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers