Az-Zumar · 55/75
Tekki Waxtaan — Az-Zumar
وَاتَّبِعُوا أَحْسَنَ مَا أُنزِلَ إِلَيْكُم مِّن رَّبِّكُم مِّن قَبْلِ أَن يَأْتِيَكُمُ الْعَذَابُ بَغْتَةً وَأَنتُمْ لَا تَشْعُرُونَ ۝٥٥
Wattabi`ooo ahsana maaa unzila ilaikum mir Rabbikum min qabli aiyaatiyakumal `azaabu baghtatanw wa antum laa tash`uroon
📖 Tekkim Wolof
Te it na ngeen di topp li gën a rafet ci li nu wàcce (Alxuraan) ci yéen mu bawoo ca seen Boroom, balaa mbugël di dal ci seen kaw te du ngeen ko yëg ;
🎧 Dégg

📜 Aaya 53-57 — Az-Zumar

53۞ قُلْ يَا عِبَادِيَ الَّذِينَ أَسْرَفُوا عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ لَا تَقْنَطُوا مِن رَّحْمَةِ اللَّهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ يَغْفِرُ الذُّنُوبَ جَمِيعًا ۚ إِنَّهُ هُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ
Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla. Ndax Yàlla dana jégële bakkaar yépp. Mooy Jégëlaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”.
54وَأَنِيبُوا إِلَىٰ رَبِّكُمْ وَأَسْلِمُوا لَهُ مِن قَبْلِ أَن يَأْتِيَكُمُ الْعَذَابُ ثُمَّ لَا تُنصَرُونَ
Delluleen ci seen Boroom, te jébël ko seen bopp, balaa mbugël di dal ci seen kaw te kenn duleen ca dimbali.
55وَاتَّبِعُوا أَحْسَنَ مَا أُنزِلَ إِلَيْكُم مِّن رَّبِّكُم مِّن قَبْلِ أَن يَأْتِيَكُمُ الْعَذَابُ بَغْتَةً وَأَنتُمْ لَا تَشْعُرُونَ
Te it na ngeen di topp li gën a rafet ci li nu wàcce (Alxuraan) ci yéen mu bawoo ca seen Boroom, balaa mbugël di dal ci seen kaw te du ngeen ko yëg ;
56أَن تَقُولَ نَفْسٌ يَا حَسْرَتَا عَلَىٰ مَا فَرَّطتُ فِي جَنبِ اللَّهِ وَإِن كُنتُ لَمِنَ السَّاخِرِينَ
balaa benn bakkan di wax naan : “Wóy ngalla man ci na mu soofentale woon mbiri Yàlla. Te daan ca reetaan nit ña” ;
57أَوْ تَقُولَ لَوْ أَنَّ اللَّهَ هَدَانِي لَكُنتُ مِنَ الْمُتَّقِينَ
walla mu naan : “Suma Yàlla gindi woon, kon danaa bokk, ca ñay ragal Yàlla” ;
Az-ZumarFihi Alxuraan
75Aaya
MeccanRevelation
55Aaya

Tekki — Az-Zumar 55

Simoore Az-Zumar Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te it na ngeen di topp li gën a rafet…

Simoore Aaya 55/75 — Az-Zumar الزمر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Az-Zumar Dégg, Az-Zumar Tekki, Az-Zumar mp3, Az-Zumar pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers