Az-Zumar · 69/75
Tekki Waxtaan — Az-Zumar
وَأَشْرَقَتِ الْأَرْضُ بِنُورِ رَبِّهَا وَوُضِعَ الْكِتَابُ وَجِيءَ بِالنَّبِيِّينَ وَالشُّهَدَاءِ وَقُضِيَ بَيْنَهُم بِالْحَقِّ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ ۝٦٩
Wa ashraqatil ardu binoori Rabbihaa wa wudi`al Kitaabu wa jeee`a bin nabiyyeena wash shuhadaaa`i wa qudiya bainahum bilhaqqi wa hum laa yuzlamoon
📖 Tekkim Wolof
Suuf si daldi fenk ak leerug Boroomam ; ñu daldi teg Téere ba, indi Yonnent ya ak seede ya ; daldi àtte seen diggënte ci dëgg te kenn duleen tooñ ci dara ;
🎧 Dégg

📜 Aaya 67-71 — Az-Zumar

67وَمَا قَدَرُوا اللَّهَ حَقَّ قَدْرِهِ وَالْأَرْضُ جَمِيعًا قَبْضَتُهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَالسَّمَاوَاتُ مَطْوِيَّاتٌ بِيَمِينِهِ ۚ سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يُشْرِكُونَ
Joxuñu Yàlla dayoom tigi, suuf si sépp ab ŋëbëm lay doon bu Bis Pénc baa, asamaan yépp ab lem lay doon ci [loxoom]. Tudd naa Sellam ga ! Kawe na ci liñu koy bokkaale.
68وَنُفِخَ فِي الصُّورِ فَصَعِقَ مَن فِي السَّمَاوَاتِ وَمَن فِي الْأَرْضِ إِلَّا مَن شَاءَ اللَّهُ ۖ ثُمَّ نُفِخَ فِيهِ أُخْرَىٰ فَإِذَا هُمْ قِيَامٌ يَنظُرُونَ
Suñu ëfee bufta bi, lu nekk ci asamaan yeek suuf si léppay dee, lu dul la ca soob Yàlla. Ñu ëfaat ko beneen yoon ndeketeeyóo, ñépp a ngi ne fujjet jóg taxaw ne xey di xoole.
69وَأَشْرَقَتِ الْأَرْضُ بِنُورِ رَبِّهَا وَوُضِعَ الْكِتَابُ وَجِيءَ بِالنَّبِيِّينَ وَالشُّهَدَاءِ وَقُضِيَ بَيْنَهُم بِالْحَقِّ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ
Suuf si daldi fenk ak leerug Boroomam ; ñu daldi teg Téere ba, indi Yonnent ya ak seede ya ; daldi àtte seen diggënte ci dëgg te kenn duleen tooñ ci dara ;
70وَوُفِّيَتْ كُلُّ نَفْسٍ مَّا عَمِلَتْ وَهُوَ أَعْلَمُ بِمَا يَفْعَلُونَ
bakkan bu nekk ñu fay ko la mu daan jëf. Te [Yàlla] moo gën a xam ñu daan def.
71وَسِيقَ الَّذِينَ كَفَرُوا إِلَىٰ جَهَنَّمَ زُمَرًا ۖ حَتَّىٰ إِذَا جَاءُوهَا فُتِحَتْ أَبْوَابُهَا وَقَالَ لَهُمْ خَزَنَتُهَا أَلَمْ يَأْتِكُمْ رُسُلٌ مِّنكُمْ يَتْلُونَ عَلَيْكُمْ آيَاتِ رَبِّكُمْ وَيُنذِرُونَكُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا ۚ قَالُوا بَلَىٰ وَلَٰكِنْ حَقَّتْ كَلِمَةُ الْعَذَابِ عَلَى الْكَافِرِينَ
Ñuy jiital yéefar yi jëme leen Safara ñu di ay mbooloo. Bu ñu fa àggee, buntu ba ubbiku ña koy wattu ne leen : “Xanaa amuleen woon ay Yonnent yu leen daan jàngal kàdduy Yàlla seen Boroom ak daan leen xupp ci dajeb seen bis bii ? ” Ñu ne leen : axakañ, waaye dogalub mbugël yay na ca yéefar ya.
Az-ZumarFihi Alxuraan
75Aaya
MeccanRevelation
69Aaya

Tekki — Az-Zumar 69

Simoore Az-Zumar Aaya 69 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Suuf si daldi fenk ak leerug Boroomam ; ñu daldi…

Simoore Aaya 69/75 — Az-Zumar الزمر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Az-Zumar Dégg, Az-Zumar Tekki, Az-Zumar mp3, Az-Zumar pdf. Aaya 67–71. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers