Az-Zumar · 36/75
Tekki Waxtaan — Az-Zumar
أَلَيْسَ اللَّهُ بِكَافٍ عَبْدَهُ ۖ وَيُخَوِّفُونَكَ بِالَّذِينَ مِن دُونِهِ ۚ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ ۝٣٦
Alaisal laahu bikaafin `abdahoo wa yukhawwi foonaka billazeena min doonih; wa mai yudlilil laahu famaa lahoo min haad
📖 Tekkim Wolof
Moo ndax Yàlla dafa doyul [wéruwaay] ci ab jaamam ? Bay tax ñu di la tiitale ci leneen lu dul Moom. Képp ku Yàlla natt ci moom réer kenn du ku gindi.
🎧 Dégg

📜 Aaya 34-38 — Az-Zumar

34لَهُم مَّا يَشَاءُونَ عِندَ رَبِّهِمْ ۚ ذَٰلِكَ جَزَاءُ الْمُحْسِنِينَ
Am nañu lu leen soob fa seen Boroom ; loolu mooy peyug ñiy rafetal,
35لِيُكَفِّرَ اللَّهُ عَنْهُمْ أَسْوَأَ الَّذِي عَمِلُوا وَيَجْزِيَهُمْ أَجْرَهُم بِأَحْسَنِ الَّذِي كَانُوا يَعْمَلُونَ
te Yàlla dana far seen ñaawtéef fay leen ca la gënnoon a rafet ca la ñu daan jëf.
36أَلَيْسَ اللَّهُ بِكَافٍ عَبْدَهُ ۖ وَيُخَوِّفُونَكَ بِالَّذِينَ مِن دُونِهِ ۚ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ
Moo ndax Yàlla dafa doyul [wéruwaay] ci ab jaamam ? Bay tax ñu di la tiitale ci leneen lu dul Moom. Képp ku Yàlla natt ci moom réer kenn du ku gindi.
37وَمَن يَهْدِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِن مُّضِلٍّ ۗ أَلَيْسَ اللَّهُ بِعَزِيزٍ ذِي انتِقَامٍ
Te it képp ku Yàlla namm ci moom njub, kenn du ko réerël. Moo ndax Yàlla dafa dul boroom Kàttan di boroomuk Fayu ? Axakañ !
38وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلْ أَفَرَأَيْتُم مَّا تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ إِنْ أَرَادَنِيَ اللَّهُ بِضُرٍّ هَلْ هُنَّ كَاشِفَاتُ ضُرِّهِ أَوْ أَرَادَنِي بِرَحْمَةٍ هَلْ هُنَّ مُمْسِكَاتُ رَحْمَتِهِ ۚ قُلْ حَسْبِيَ اللَّهُ ۖ عَلَيْهِ يَتَوَكَّلُ الْمُتَوَكِّلُونَ
Soo leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ? ”, Ñu ni la : “Yàlla”. Waxal ne : “Xanaa gisu leen li ngéen di jaamu bàyyi Yàlla ; ci ne su Yàlla nammee ci man lor, ndax ñoom kon danañu man a teggi lor ja ? Walla su Yàlla nammoon ci man yërmaande, ndax kenn danañu man a fanq yërmaande ja ? ” – waxal ne : “Yàlla doy na ma : ci moom la wéerukat ya di wéeru”
Az-ZumarFihi Alxuraan
75Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Az-Zumar 36

Simoore Az-Zumar Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo ndax Yàlla dafa doyul [wéruwaay] ci ab jaamam ?…

Simoore Aaya 36/75 — Az-Zumar الزمر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Az-Zumar Dégg, Az-Zumar Tekki, Az-Zumar mp3, Az-Zumar pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers